1 Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. 2 Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam; 3 Yuda, Fares ak Sara ci Tamar; Fares Esrom, miy baayu Aram; 4 Aram Aminadab; Aminadab Naason; Naason Salmon; 5 Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Yese,6 miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon jabari Uri; 7 Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf; 8 Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas; 9 Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiyas; 10 Esekiyas Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas; 11 Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon. 12 Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel, 13 miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor; 14 Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd; 15 Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba; 16 Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo. 17 Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. 18 Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. 19 Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woon a weer. Mu nar a xàccook moom ci sutura. 20 Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragal a yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. 21 Dina jur doom ju góor; na nga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.» 22 Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: 23 «Janq bi dina ëmb,jur doom ju góor,ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» 24 Noonu Yuusufa yeewu, yeggali jabaram, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon. 25 Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.