聖經新譯本

Wolof: New Testament

Mark

7

1不可因傳統廢棄 神的誡命(太15:1~20)有法利賽人和幾個經學家從耶路撒冷來,聚集到耶穌那裡。
1 Amoon na bés nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu jóge Yerusalem ñëw ci Yeesu.
2他們看見他的門徒有人用不潔的手,就是沒有洗過的手吃飯,
2 Ñu gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwuñu woon, ni ko aada santaanee.
3(原來法利賽人和所有的猶太人都拘守古人的傳統,如果不認真洗手,就不吃東西;
3 Farisen yi nag ñoom ak Yawut yi yépp dañuy topp aaday yoon, yi maam yi tëral, te fandee leen gënal lekk ak loxo yu ñu raxasul.
4從街市回來,不先洗手,也不吃東西,還有許多別的傳統,他們都沿襲拘守,例如洗杯、洗罐、洗銅器等等。)
4 Te it bu ñu jógee pénc ma, su ñu sanguwul set, duñu lekk. Am nañu it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga war a raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba ñu laab.
5法利賽人和經學家問耶穌:“你的門徒為甚麼不遵行古人的傳統,用不潔的手吃飯呢?”
5 Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?»
6耶穌對他們說:“以賽亞指著你們這班偽君子所說的預言是對的,經上記著:‘這人民用嘴唇尊敬我,心卻遠離我;
6 Yeesu tontu leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee:“Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ,waaye seen xol sore na ma.
7他們把人的規條當作道理去教導人,所以拜我也是徒然。’
7 Seen màggal amul benn njariñ,ci li ñuy jàngale dénkaaney nit kese.”»
8你們拘守著人的傳統,卻離棄了 神的誡命。”
8 Yeesu neeti leen: «Dëddu ngeen ndigali Yàlla, jublu ci aaday nit.»
9耶穌又對他們說:“你們為了堅守自己的傳統,而巧妙地把 神的誡命拒絕了。
9 Mu teg ca ne leen: «Xelu ngeen ci tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada.
10因為摩西說:‘當孝敬父母’,又說:‘咒罵父母的,必被處死。’
10 Ndaxte Musaa nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” teg ca ne: “Ku móolu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.”
11你們倒說:‘人對父母說,我應該給你的供奉,已經作了各耳板’(各耳板意思是奉給 神的供物),
11 Waaye yéen dangeen ne, ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga war a jariñoo ci man Korban la,” maanaam “jébbal naa ko Yàlla,”
12你們就不讓那人再為父母作甚麼。
12 dootuleen ko bàyyi, mu defal dara ndeyam walla baayam.
13這樣,你們藉著所領受的傳統,把 神的話廢棄了。你們還作了許多這一類的事。”
13 Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it yéena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.»
14於是耶穌又把群眾叫過來,對他們說:“你們大家都要聽我說,也要明白:
14 Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: «Yéen ñépp dégluleen ma te xam.
15從外面進去的,不能使人污穢,從裡面出來的,才能使人污穢。”
15 Li ci biti, tey dugg nit, du ko man a indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.»
16(有些抄本有第16節:“有耳可聽的,就應該聽。”)
17 Bi nga xamee ne jóge nañu ci mbooloo mi, dugg ci kër gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju làqu jooju.
17耶穌離開群眾,進了屋子,門徒就來問他這比喻的意思。
18 Yeesu tontu leen ne: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko man a indil sobe,
18他對他們說:“連你們也是這樣不明白嗎?難道不知道從外面進去的,不能使人污穢嗎?
19 ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam.
19因為不是進到他的心,而是進到他的肚腹,再排泄到外面去。”(他這樣說是表示各樣食物都是潔淨的。)
20 Yeesu ne leen ati: «Li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.
20接著他又說:“從人裡面出來的,才會使人污穢。
21 Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di jóge ak ndoxaanu yàqute, càcc ak bóom,
21因為從裡面,就是從人的心裡,發出惡念、淫亂、偷盜、兇殺、
22 njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof.
22姦淫、貪心、邪惡、詭詐、放蕩、嫉妒、毀謗、驕傲、愚妄;
23 Lu bon loolu lépp day génn ci nit, di ko indil sobe.»
23這一切惡事,是從人裡面出來的,都能使人污穢。”
24 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam mënul a umpe.
24敘利亞婦人的信心(太15:21~28)耶穌從那裡動身到推羅(有些抄本在此有“和西頓”)境內去。進了一所房子,本來不想讓人知道,卻隱藏不住。
25 Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
25有一個女人,她的小女兒被污靈附著,她聽見了耶穌的事,就來俯伏在他腳前。
26 fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam.
26這女人是外族人,屬於敘利亞的腓尼基族。她求耶穌把鬼從她女兒身上趕出去。
27 Waaye Yeesu ne ko: «Na gune yi jëkk a lekk, ba regg; fab ñamu gune yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
27耶穌對她說:“應該先讓兒女吃飽。拿兒女的餅去丟給小狗吃是不好的。”
28 Jigéen ji tontu ko: «Waaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gune yi.»
28那女人回答他:“主啊,是的,不過小狗在桌子底下,也可以吃孩子們掉下來的碎渣。”
29 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Ndax wax jooju demal ci jàmm, rab wa génn na sa doom.»
29耶穌對她說:“就憑這句話,你回去吧,鬼已經從你女兒身上出去了。”
30 Noonu mu ñibbi, fekk doom ji tëdd cib lal te mucc ci rab wi.
30她回到家裡,看見小孩子躺在床上,鬼已經出去了。
31 Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi.
31治好又聾又啞的人(太15:29~31)耶穌從推羅境內出去,經過西頓,回到低加波利地區的加利利海。
32 Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo.
32有人帶著一個又聾又啞的人到他那裡,求耶穌按手在他身上。
33 Noonu Yeesu yóbbu ko, ba ñu sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal làmmiñam.
33耶穌把他從人群中帶到一邊,用指頭探他的耳朵,吐唾沫抹他的舌頭,
34 Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki: «Ubbikuleen.»
34然後望著天,長長地歎了一口氣,對他說:“以法大!”意思是“開了吧”。
35 Ci saa si ay noppam daldi dégg te làmmiñam yiwiku, muy wax bu leer.
35那人的耳朵就開了,舌頭也鬆了,說話也準確了。
36 Bi mu ko defee Yeesu tere leen, ñu wax ko kenn, waaye lu mu leen ko gën a tere, ñu gën ko nee siiwale.
36耶穌囑咐他們不要告訴人。但他越是囑咐,他們卻越發傳揚。
37 Ñu waaru lool naan: «Lépp lu mu def, lu yéeme la. May na sax tëx yi ñuy dégg, ak luu yi ñuy wax.»
37眾人非常驚訝說:“他所作的一切事都好極了;他竟然使聾子聽見,又使啞巴說話。”