聖經新譯本

Wolof: New Testament

Mark

9

1耶穌又對他們說:“我實在告訴你們,站在這裡的,有人在沒有嘗過死味以前,必定看見 神的國帶著能力降臨。”
1 Mu ne leen ati: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu nguuru Yàlla ñëw ak doole.»
2在山上改變形象(太17:1~13;路9:28~36)過了六天,耶穌帶著彼得、雅各、約翰,領他們悄悄地上了高山,在他們面前改變了形象。
2 Juróom-benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam;
3他的衣服閃耀發光,極其潔白,地上漂布的沒有能漂得這樣白的。
3 ay yéreem di ray-rayi, weex tàll, te fóotukatu àddina mënu leen weexale nii.
4又有以利亞和摩西向他們顯現,並且跟耶穌談話。
4 Noonu ñu gis yonenti Yàlla Iliyas ak Musaa, di wax ak Yeesu.
5彼得對耶穌說:“拉比,我們在這裡真好!我們可以搭三個帳棚,一個為你,一個為摩西,一個為以利亞。”
5 Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.»
6彼得不知道該說甚麼才好,因為他們都非常害怕。
6 Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp.
7有一片雲彩來,籠罩他們,又有聲音從雲中出來:“這是我的愛子,你們要聽他。”
7 Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
8門徒立刻周圍觀看,再也看不見別的人,只見耶穌單獨和他們在一起。
8 Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuñu kenn, ku dul Yeesu rekk.
9他們下山的時候,耶穌吩咐他們,人子從死人中復活之前,不要把所看見的告訴人。
9 Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi muy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.»
10門徒把這句話記在心裡,又彼此討論從死人中復活是甚麼意思。
10 Ñu téye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki.
11他們就問耶穌:“經學家為甚麼說以利亞必須先來呢?”
11 Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Iliyas moo war a jëkk a ñëw?»
12耶穌說:“以利亞固然要先來復興一切,但聖經為甚麼又記載人子要受許多苦,被人藐視呢?
12 Yeesu ne leen: «Waaw, Iliyas dina jëkk a ñëw, jubbanti lépp. Waaye itam lu tax bind nañu ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, ñu xeeb ko, dëddu ko.
13其實我告訴你們,以利亞已經來了,他們卻任意待他,正如經上指著他所說的。”
13 Waaye maa ngi leen di wax ne, Iliyas ñëw na, te def nañu ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.»
14治好癲癇病的小孩(太17:14~21;路9:37~42)他們回到門徒那裡,看見一大群人圍著他們,又有經學家和他們辯論。
14 Bi nga xamee ne Yeesu ñëw na, ba jege taalibe yi, mu gis mbooloo mu bare wër leen, te ay xutbakat di werante ak ñoom.
15眾人看見了耶穌,都很驚奇,就跑上前去向他問安。
15 Naka la mbooloo mi gis Yeesu, ñu waaru, daldi daw nuyu ko.
16他問他們:“你們和他們辯論甚麼?”
16 Noonu Yeesu laaj leen: «Ci lan ngeen di werante ak ñoom?»
17群眾當中有一個回答他:“老師,我把我的兒子帶到你這裡來,他被啞巴鬼附著。
17 Kenn ci mbooloo mi tontu ko ne: «Kilifa gi, rab jàpp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko jàppee, daf koy daaneel ci suuf, gémmiñ gi di fuur, muy yéyu, ne jàdd. Ñaan naa say taalibe, ñu dàq ko, waaye mënuñu ko.»
18無論在哪裡,鬼抓住他,把他摔倒,他就口吐白沫,咬牙切齒,渾身僵硬。我請你的門徒把鬼趕出去,他們卻辦不到。”
19 Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa war a nekk ak yéen, ba kañ laa leen war a muñal? Indil-leen ma xale bi.»
19耶穌回答他們:“唉!不信的世代啊!我跟你們在一起到幾時呢?我要忍受你們到幾時呢?把他帶到我這裡來吧。”
20 Ñu indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, gémmiñ giy fuur.
20他們就把孩子帶到他跟前。那鬼一見耶穌,就立刻使孩子抽了一陣瘋,倒在地上,流著唾沫打滾。
21 Yeesu laaj baay bi: «Lii kañ la ko dal?» Baay bi ne ko: «Li dale ci nguneem.
21耶穌問他父親:“這事臨到他有多久了?”他說:“從小就是這樣。
22 Léeg-léeg rab wi bëmëx ko ci safara, léeg-léeg mu bëmëx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yërëm nu te xettali nu.»
22鬼常常把他扔在火裡水中,要毀滅他。如果你能作甚麼,求你可憐我們,幫助我們。”
23 Yeesu tontu ko: «Nga ne: “Soo ko manee,” ku gëm man na lépp.»
23耶穌對他說:“‘如果你能’(“如果你能”有些抄本作“你若能信”)──對於信的人,甚麼都能!”
24 Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.»
24孩子的父親立刻喊著說:“我信!但我的信心不夠,求你幫助我。”
25 Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wërsi ko, mu daldi gëdd rab wi nag ne ko: «Génnal ci moom, yaw rab wu luu te tëx, te bu ko jàppaat; wax naa la ko.»
25耶穌看見群眾圍攏了來,就斥責那污鬼說:“聾啞的鬼,我吩咐你從他身上出來,不要再進去。”
26 Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, génn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax ñu bare ne: «Dee na.»
26那鬼大聲喊叫,使孩子重重地抽了一陣瘋,就出來了。孩子好像死了一樣,所以許多人都說:“他死了!”
27 Waaye Yeesu jàpp loxoom, jógloo ko, xale bi daldi taxaw.
27但耶穌拉著他的手,扶他起來,他就站起來了。
28 Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax mënunu ko woon a dàq?»
28耶穌進了屋子,門徒私下問他說:“為甚麼我們不能把那污鬼趕出去呢?”
29 Yeesu tontu leen ne: «Yu mel ni yii, ñaan ci Yàlla rekk a leen di dàq.»
29耶穌對他們說:“這一類的鬼,非用禱告是趕不出去的。”
30 Bi loolu amee ñu jóge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bëggul kenn yég ko.
30第二次預言受難及復活(太17:22~23;路9:43~45)他們從那裡出去,經過加利利,耶穌不想讓人知道,
31 Ndaxte muy jàngal taalibe yi ne leen: «Dees na jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit, te dinañu ko rey, mu dekki ci ñetti fan.»
31因為他正在教導門徒。他又對他們說:“人子將要被交在人的手裡,他們要殺害他,死後三天他要復活。”
32 Waaye taalibe yi xamuñu lu wax joojuy tekki, te ñemewuñu ko koo laaj.
32門徒不明白這話,又不敢問他。
33 Bi nga xamee ne egg nañu dëkku Kapernawum, te dugg ci kër gi, Yeesu laaj leen ne: «Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?»
33門徒爭論誰最大(太18:1~5;路9:46~48)他們來到迦百農。在屋裡的時候,耶穌問他們:“你們在路上爭論甚麼?”
34 Waaye ñu ne cell, ndaxte ñu ngi fa doon werante, ba xam ku gën a màgg ci ñoom.
34門徒一聲不響,因為他們在路上彼此爭論誰為大。
35 Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak ñaar ne leen: «Ku bëgg a jiitu, na topp ci gannaaw ñépp te nekk surgab ñépp.»
35耶穌坐下,叫十二門徒來,對他們說:“誰想為首,就該作眾人中最末的一個,作眾人的僕人。”
36 Bi ko Yeesu waxee, mu jël xale, indi ko ci biir géew gi, ba noppi leewu ko naan:
36於是拉過一個小孩子來,叫他站在門徒中間,又把他抱起來,對他們說:
37 «Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.»
37“凡因我的名接待一個這樣的小孩子的,就是接待我;凡接待我的,不是接待我,而是接待那差我來的。”
38 Bi loolu amee Yowaana ne ko: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun.»
38反對與贊成(路9:49~50)約翰對耶穌說:“老師,我們看見有一個人奉你的名趕鬼,就禁止他,因為他不跟從我們。”
39 Waaye Yeesu tontu ko: «Buleen ko tere, ndaxte kenn mënul a def kéemaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab.
39耶穌說:“不要禁止他,因為沒有人能奉我的名行了神蹟,又立刻毀謗我。
40 Ku nu sotul, far na ak nun.
40不反對我們的,就是贊成我們的。
41 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yéena ngi bokk ci man Kirist, kooku du ñàkk yoolam mukk.
41無論誰因你們有屬基督的名分,給你們一杯水喝的,我實在告訴你們,他決不會失掉賞賜。
42 «Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom, moo di ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej.
42堅拒犯罪(太18:6~9;路17:1~2)“如果有人使一個信我的小弟兄犯罪,倒不如在他的頸項上拴一塊大磨石投在海裡。
43 Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko. Ndaxte ñàkk loxo te tàbbi ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo te tàbbi ci safara su dul fey mukk.
43如果你的一隻手使你犯罪,就把它砍下來。你身體殘廢進永生,總比有兩隻手下到地獄,進入那不滅的火裡好得多。
45 Te bu la sa tànk di yóbbe bàkkaar, dagg ko. Nga lafañ te tàbbi ci dund gu wóor gi moo gën, nga am ñaari tànk, ñu sànni la ci safara.
44(有些抄本有第44節:“在那裡蟲是不死的,火是不滅的。”)
47 Te bu la sa bët di yóbbe bàkkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Yàlla, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, ñu sànni la ci safara.
45如果你的一隻腳使你犯罪,就把它砍下來。你瘸腿進永生,總比你有兩隻腳而被丟在地獄裡好得多。
48 Foofa:“Sax ya duñu dee mukk,te safara sa du fey.”
46(有些抄本有第46節:“在那裡蟲是不死的,火是不滅的。”)
49 Ñépp safara lañu leen di xorome.
47如果你的一隻眼睛使你犯罪,就把它挖出來。你只有一隻眼睛進 神的國,總比你有兩隻眼睛而被丟在地獄裡好得多,
50 Xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen jàmmoo.»
48在那裡蟲是不死的,火是不滅的。
49每一個人必被火當鹽來醃。(有些抄本在此有“各祭物必用鹽來醃”一句;也有些抄本只有附註的一句,而沒有正文的一句)
50鹽是好的,但如果失了味,可以用甚麼使它再鹹呢?你們自己裡面應當有鹽,彼此和睦。”