1差遣十二使徒(可3:13~19,6:8~13;路6:12~16,9:1~5。參路10:4~12;徒1:13)
1 Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp.
2十二使徒的名字如下:為首的是西門(又名彼得),西門的弟弟安得烈,西庇太的兒子雅各,雅各的弟弟約翰,
2 Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;l
3腓力,巴多羅邁,多馬,稅吏馬太,亞勒腓的兒子雅各,達太,
3 Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade;l
4激進派的西門,和出賣耶穌的加略人猶大。
4 Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nar a wor Yeesu.
5耶穌差遣這十二個人出去,並且囑咐他們:“外族人的路,你們不要走,撒瑪利亞人的城,你們也不要進;
5 Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari.
6卻要到以色列家的迷羊那裡去。
6 Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar.
7你們要一邊走一邊宣揚說:‘天國近了。’
7 Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.”
8要醫治有病的,叫死人復活,潔淨患痲風的,趕出污鬼。你們白白地得來,也應當白白地給人。
8 Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen.
9你們腰袋裡不要帶金、銀、銅錢;
9 Buleen dajale wurus, xaalis mbaa xànjar ci seeni maxtume.
10路上不要帶行囊,也不要帶兩件衣裳,不要帶鞋或手杖,因為作工的理當得到供應。
10 Buleen wut it mbuus ngir tukki mbaa ñaari turki, ay dàll mbaa aw yet, ndaxte liggéeykat yeyoo na dundam.
11你們無論進哪一座城哪一個村,都要打聽誰配接待你們,就住在那裡,直到離去。
11 «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba.
12到他家裡的時候,要向他們問安;
12 Bu ngeen di dugg ci kër nag, nuyooleen.
13如果這家是配得的,你們的平安就必臨到他們;如果這家不配得,你們的平安仍歸你們。
13 Bu fekkee ne kër ga yeyoo na ko, na seen jàmm wàcc ci ñoom, waaye bu ko yeyoowul, na seen yéene dellusi ci yéen.
14如果有人不接待你們,不聽你們的話,你們離開那一家那一城的時候,就要把腳上的灰塵跺下去。
14 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk.
15我實在告訴你們,在審判的日子,所多瑪和蛾摩拉所受的,比那城還輕呢。
15 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu.
16使徒會遭受迫害(可13:11~13;路21:12~17)“現在,我差派你們出去,好像羊進到狼群中間;所以你們要像蛇一樣機警,像鴿子一樣純潔。
16 «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax.
17你們要小心,因為有人要把你們送交公議會,並要在會堂裡鞭打你們;
17 Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu.
18你們為我的緣故,也要被帶到統治者和君王面前,向他們和外族人作見證。
18 Dees na leen yóbbu ngir man ci kanami boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut.
19你們被捕的時候,用不著擔心說甚麼和怎麼說,因為那時你們必得著當說的話;
19 Boo xamee ne nag jébbale nañu leen, buleen am xel ñaar ci li ngeen di wax, mbaa ni ngeen koy waxe. Ndaxte ca waxtu woowa sax dingeen jot li ngeen war a wax;
20因為說話的不是你們,而是你們的父的靈,是他在你們裡面說話。
20 du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen.
21弟兄要出賣弟兄,父親要出賣兒子,甚至把他們置於死地;兒女要悖逆父母,害死他們。
21 «Mag dina joxe rakkam ci dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu.
22你們為我的名,要被眾人恨惡,然而堅忍到底的必然得救。
22 Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc.
23如果有人在這城迫害你們,就逃到別的城去。我實在告訴你們,你們還沒有走遍以色列的各城,人子就來到了。
23 Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen man a wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
24“學生不能勝過老師,奴僕也不能勝過主人。
24 Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam.
25學生若能像老師一樣,奴僕若能像主人一樣,也就夠了。如果一家之主也被稱為別西卜(“別西卜”是鬼王的名字),何況他的家人呢?
25 Bu taalibe yemee ak kilifaam demin, doy na; jaam it ni sangam. Ndegam tudde nañu boroom kër gi Beelsebul, astemaak waa kër gi.
26應該怕誰(路12:2~9)“所以不要怕他們。沒有甚麼掩蓋的事不被揭露,也沒有甚麼祕密是人不知道的。
26 Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warul a biral, mbaa luy kumpa lu ñu warul a siiwal.
27我在暗處告訴你們的,你們要在明處講出來;你們聽見的耳語,要在房頂上宣揚出來。
27 Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi.
28那些殺身體卻不能殺靈魂的,不要怕他們;倒要怕那位能把靈魂和身體都投入地獄裡的。
28 Te buleen ragal ñu man a rey yaram, te mënuñoo rey ruu, waaye ragal-leen Ki man a sànk yaram ak ruu ci safara.
29兩隻麻雀不是賣一個大錢嗎?但你們的父若不許可,一隻也不會掉在地上。
29 Ñaari picci rammatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay.
30甚至你們的頭髮都一一數過了。
30 Seen kawari bopp sax, waññees na leen.
31所以不要怕,你們比許多麻雀貴重得多呢。
31 Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu rammatu.
32“凡在人面前承認我的,我在我天父面前也要承認他;
32 «Koo xam ne nangu nga ma ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.
33在人面前不認我的,我在我天父面前也要不認他。
33 Waaye ku ma gàntu ci kanamu nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanamu Baay, bi nekk ci kaw.
34作門徒的代價(路12:51~53)“你們不要以為我來了,是要給地上帶來和平;我並沒有帶來和平,卻帶來刀劍,
34 «Te it buleen defe ne, damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale.
35因為我來了是要叫人分裂:人與父親作對,女兒與母親作對,媳婦與婆婆作對,
35 Ndaxte ñëw naa ngir féewale doom ak baayam, doom ju jigéen ak ndeyam, jabar ak goroom;
36人的仇敵就是自己的家人。
36 te nooni nit ñooy waa këram.
37愛父母過於愛我的,不配作屬我的;愛兒女過於愛我的,不配作屬我的;
37 Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma.
38凡不背起自己的十字架來跟從我的,也不配作屬我的。
38 Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma.
39顧惜自己生命的,必要喪掉生命;但為我犧牲生命的,必要得著生命。
39 Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko.
40得賞賜(可9:41)“接待你們的,就是接待我;接待我的,就是接待那差我來的。
40 «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni.
41因先知的名接待先知的,必得先知所得的賞賜;因義人的名接待義人的,必得義人所得的賞賜。
41 Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub.
42無論誰因門徒的名,只把一杯涼水給這些微不足道的人中的一個喝,我實在告訴你們,他決不會得不到他的賞賜。”
42 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gën a ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.»