聖經新譯本

Wolof: New Testament

Matthew

19

1 神配合的,人不可分開(可10:1~12)耶穌講完了這些話,就離開加利利,來到約旦河東的猶太境內。
1 Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan.
2有許多人跟著他;他在那裡醫好了他們。
2 Mbooloo mu bare topp ko, mu faj leen fa.
3法利賽人前來試探耶穌,說:“人根據某些理由休妻,可以嗎?”
3 Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase jabaram, saa su ko neexee?»
4他回答:“造物者從起初‘造人的時候,就造男造女’。‘因此人要離開父母,與妻子連合,二人成為一體。’這些話你們沒有念過嗎?
4 Yeesu tontu leen ne: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen,
5
5 te mu ne: “Moo tax góor dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, ñoom ñaar doon benn.”
6這樣,他們不再是兩個人,而是一體的了。所以 神所配合的,人不可分開。”
6 Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
7他們就問:“為甚麼摩西卻吩咐‘人若給了休書,就可以休妻’呢?”
7 Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox jabaram kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?»
8他說:“摩西因為你們的心硬,才准許你們休妻,但起初並不是這樣。
8 Yeesu tontu leen: «Musaa may na leen, ngeen fase seen jabar, ndax seen xol dafa dëgër, waaye ca njàlbéen ga demewul woon noonu.
9我告訴你們,凡休妻另娶的,如果不是因為妻子不貞,就是犯姦淫了。”
9 Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa jabar te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.»
10門徒對他說:“夫妻的關係既然是這樣,倒不如不結婚了。”
10 Bi ko taalibe ya déggee, ñu ne ko: «Bu dee noonu la digganteb góor ak jigéen mel, bañ a séy moo gën.»
11耶穌對他們說:“這話不是每個人都能領受的,只有賜給誰,誰才能領受。
11 Yeesu tontu leen: «Du ñépp ñoo man a nangu loolu, waaye ñi ko Yàlla jagleel rekk.
12有些人是生來就不能結婚的,有些人不能結婚是因為人使他們這樣,也有些人是為了天國的緣故自願這樣的。誰能領受就領受吧!”
12 Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu bañ a séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko man a nangu, nangu ko.»
13給小孩子按手祈禱(可10:13~16;路18:15~17)那時,有人帶了小孩子到耶穌面前,求他給他們按手祈禱,門徒就責備那些人。
13 Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen.
14但耶穌說:“讓小孩子到我這裡來,不要禁止他們,因為天國是屬於這樣的人的。”
14 Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
15於是他給他們按手,然後離開那裡。
15 Noonu Yeesu teg leen ay loxoom, ba noppi jóge fa.
16有錢的人難進 神的國(可10:17~31;路18:18~30)有一個人前來見耶穌,說:“老師,我要作甚麼善事,才可以得著永生?”
16 Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def ci lu baax, ngir man a am dund gu dul jeex?»
17耶穌說:“為甚麼問我關於善的事呢?只有一位是善的。如果你想進入永生,就應當遵守誡命。”
17 Yeesu tontu ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.»
18他問:“甚麼誡命?”耶穌回答:“就是‘不可殺人,不可姦淫,不可偷盜,不可作假證供;
18 Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóom, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg,
19當孝敬父母,當愛人如己’。”
19 teralal sa ndey ak sa baay, te it: nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
20那青年對他說:“這一切我都遵守了,還缺少甚麼呢?”
20 Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?»
21耶穌對他說:“如果你想要完全,就去變賣你所有的,分給窮人,你就必定有財寶在天上,而且你要來跟從我。”
21 Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
22那青年聽見這話,就憂憂愁愁地走了,原來他的財產很多。
22 Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.
23耶穌對門徒說:“我實在告訴你們,有錢的人是很難進天國的。
23 Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
24我又告訴你們,駱駝穿過針眼,比有錢的人進 神的國還容易呢!”
24 Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu pusa, moo gën a yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
25門徒聽見了,十分驚奇,就問他:“這樣,誰可以得救呢?”
25 Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo man a mucc nag?»
26耶穌看著他們說:“在人這是不能的,在 神卻凡事都能。”
26 Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.»
27那時彼得對他說:“你看,我們已經捨棄一切跟從了你,我們會得到甚麼呢?”
27 Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?»
28耶穌對他們說:“我實在告訴你們,到了萬物更新,人子坐在他榮耀的寶座上的時候,你們這些跟從我的人,也會坐在十二個寶座上,審判以色列的十二個支派。
28 Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.
29凡為我的名撇下房屋、兄弟、姊妹、父母、兒女或田地的,他必得著百倍,並且承受永生。
29 Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex.
30然而許多在前的將要在後,在後的將要在前。”
30 Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.