1Now concerning the collection for the saints, as I gave order to the churches of Galatia, so also do ye.
1 Léegi nag ci li jëm ci ndimbal, li ñuy sàkkal gaayi Yàlla yi, defleen li ma tëral ci mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Galasi.
2Upon the first day of the week let each one of you lay by him in store, as he may prosper, that no collections be made when I come.
2 Bés bu jëkk ci ayu-bés yi, na ku nekk ber lu mu àttan, denc ko, ngir saa yu ma dikkee, ñu bañ di wër di laaj xaalis.
3And when I arrive, whomsoever ye shall approve, them will I send with letters to carry your bounty unto Jerusalem:
3 Su ma dikkee, dinaa dénk seen xaalis ñi ngeen tànn, yónni leen Yerusalem, boole ko ak bataaxal.
4and if it be meet for me to go also, they shall go with me.
4 Su aajoo ma demal sama bopp, kon dinañu ànd ak man.
5But I will come unto you, when I shall have passed through Macedonia; for I pass through Macedonia;
5 Gannaaw bu ma jàllee diiwaanu Maseduwan, dinaa ñëw ci yéen, ndaxte fas naa ko yéenee jàll.
6but with you it may be that I shall abide, or even winter, that ye may set me forward on my journey whithersoever I go.
6 Man na am ma yàgg ci yéen, jombul sax ma lollikoo fi yéen. Noonu dingeen taxawu sama yoon, fu ma man a jëm.
7For I do not wish to see you now by the way; for I hope to tarry a while with you, if the Lord permit.
7 Ndaxte fi mu ne bëgguma leen a gis rekk, jàll, waaye yaakaar naa ne, dinaa toog ci yéen ab diir, bu neexee Boroom bi.
8But I will tarry at Ephesus until Pentecost;
8 Ba tey dinaa toog fii ci dëkku Efes ba màggalu Pàntakot,
9for a great door and effectual is opened unto me, and there are many adversaries.
9 ndaxte Yàlla ubbil na ma bunt, ba mu ne làññ, ngir may def liggéey bu man a am muj gu rafet, te noon yu bare bëgg a gàllankoor liggéey bi.
10Now if Timothy come, see that he be with you without fear; for he worketh the work of the Lord, as I also do:
10 Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am njàqare ci seen biir, ndaxte dafay liggéeyal Boroom bi ni man.
11let no man therefore despise him. But set him forward on his journey in peace, that he may come unto me: for I expect him with the brethren.
11 Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu dellusi ci man ci jàmm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi.
12But as touching Apollos the brother, I besought him much to come unto you with the brethren: and it was not all [his] will to come now; but he will come when he shall have opportunity.
12 Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu ñëw ci yéen, ànd ak bokk yi. Waaye fi mu ne dëppoowul ak coobareem. Dina ñëw saa su ko manee.
13Watch ye, stand fast in the faith, quit you like men, be strong.
13 Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pasteef.
14Let all that ye do be done in love.
14 Lépp li ngeen di def, defleen ko ak mbëggeel.
15Now I beseech you, brethren (ye know the house of Stephanas, that it is the firstfruits of Achaia, and that they have set themselves to minister unto the saints),
15 Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam ñoo jëkk a nangu xebaar bu baax bi ci diiwaanu Akayi, te ñoo joxe seen bopp, ngir liggéeyal gaayi Yàlla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan,
16that ye also be in subjection unto such, and to every one that helpeth in the work and laboreth.
16 ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak képp ku ànd ak ñoom ci liggéey bi.
17And I rejoice at the coming of Stephanas and Fortunatus and Achaicus: for that which was lacking on your part they supplied.
17 Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, bég naa ci lool. Taxawal nañu leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man te tële ko.
18For they refreshed my spirit and yours: acknowledge ye therefore them that are such.
18 Seral nañu sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit ñu mel noonu.
19The churches of Asia salute you. Aquila and Prisca salute you much in the Lord, with the church that is in their house.
19 Mboolooy ñi gëm te nekk diiwaanu Asi ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci Boroom bi, ñoom ak mbooloom ñi gëm tey daje seen kër.
20All the brethren salute you. Salute one another with a holy kiss.
20 Bokk yépp ñu ngi leen di nuyu. Saafoonteleen ak xol bu laab.
21The salutation of me Paul with mine own hand.
21 Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp.
22If any man loveth not the Lord, let him be anathema. Maranatha.
22 Képp ku bañ Boroom bi, Yal na ko Yàlla alag. Boroom bi, ñëwal!
23The grace of the Lord Jesus Christ be with you.
23 Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen.
24My love be with you all in Christ Jesus. Amen.
24 Bëgg naa leen yéen ñépp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.