1Now the apostles and the brethren that were in Judaea heard that the Gentiles also had received the word of God.
1 Bi loolu amee ndaw yi ak bokk yi nekk ci diiwaanu Yude, dégg nañu ne, ñi dul Yawut nangu nañu kàddug Yàlla.
2And when Peter was come up to Jerusalem, they that were of the circumcision contended with him,
2 Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:
3saying, Thou wentest in to men uncircumcised, and didst eat with them.
3 «Lu tax nga dem ca këru ñu xarafal, bay lekk sax ak ñoom?»
4But Peter began, and expounded [the matter] unto them in order, saying,
4 Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko
5I was in the city of Joppa praying: and in a trance I saw a vision, a certain vessel descending, as it were a great sheet let down from heaven by four corners; and it came even unto me:
5 ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man.
6upon which when I had fastened mine eyes, I considered, and saw the fourfooted beasts of the earth and wild beasts and creeping things and birds of the heaven.
6 Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan.
7And I heard also a voice saying unto me, Rise, Peter; kill and eat.
7 Te dégg naa baat bu ma ne: “Jógal Piyeer, rey te lekk.”
8But I said, Not so, Lord: for nothing common or unclean hath ever entered into my mouth.
8 Waaye ma tontu ne: “Mukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam musul a dugg ci sama gémmiñ.”
9But a voice answered the second time out of heaven, What God hath cleansed, make not thou common.
9 Waaye ñaareel bi yoon baat bi dellu ne ma: “Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.”
10And this was done thrice: and all were drawn up again into heaven.
10 Loolu am ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas lépp, jëme asamaan.
11And behold, forthwith three men stood before the house in which we were, having been sent from Caesarea unto me.
11 «Ca saa sa ñetti góor, ña ñu yebal ci man, jóge Sesare, agsi ca kër ga ma dal.
12And the Spirit bade me go with them, making no distinction. And these six brethren also accompanied me; and we entered into the man's house:
12 Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom-benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu.
13and he told us how he had seen the angel standing in his house, and saying, Send to Joppa, and fetch Simon, whose surname is Peter;
13 Mu nettali nu ne, gis na malaaka, feeñu ko ca këram ne ko: “Yónneel ca dëkku Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
14who shall speak unto thee words, whereby thou shalt be saved, thou and all thy house.
14 Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
15And as I began to speak, the Holy Spirit fell on them, even as on us at the beginning.
15 «Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk.
16And I remembered the word of the Lord, how he said, John indeed baptized with water; but ye shall be baptized in the Holy Spirit.
16 Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.”
17If then God gave unto them the like gift as [he did] also unto us, when we believed on the Lord Jesus Christ, who was I, that I could withstand God?
17 Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?»
18And when they heard these things, they held their peace, and glorified God, saying, Then to the Gentiles also hath God granted repentance unto life.
18 Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.»
19They therefore that were scattered abroad upon the tribulation that arose about Stephen travelled as far as Phoenicia, and Cyprus, and Antioch, speaking the word to none save only to Jews.
19 Ñi tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, ñu dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca dëkku Ancos, di wax kàddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi.
20But there were some of them, men of Cyprus and Cyrene, who, when they were come to Antioch, spake unto the Greeks also, preaching the Lord Jesus.
20 Moona amoon na ci ñoom ay niti Sipar ak dëkku Siren, ñu ñëw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, ñu di leen xamal xebaar bu baax bu Yeesu Boroom bi.
21And the hand of the Lord was with them: and a great number that believed turned unto the Lord.
21 Te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, ba mbooloo mu mag gëm te woññiku ci Boroom bi.
22And the report concerning them came to the ears of the church which was in Jerusalem: and they sent forth Barnabas as far as Antioch:
22 Ba mbir ma siiwee, ba àgg ci noppi mbooloom ñi gëm ci Yerusalem, ñu yebal Barnabas ba Ancos.
23who, when he was come, and had seen the grace of God, was glad; and he exhorted them all, that with purpose of heart they would cleave unto the Lord:
23 Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Yàlla may, mu bég ci te di leen xiir, ñu wàkkirlu ci Boroom bi te dogu ci.
24for he was a good man, and full of the Holy Spirit and of faith: and much people was added unto the Lord.
24 Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.
25And he went forth to Tarsus to seek for Saul;
25 Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sool.
26and when he had found him, he brought him unto Antioch. And it came to pass, that even for a whole year they were gathered together with the church, and taught much people, and that the disciples were called Christians first in Antioch.
26 Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist.
27Now in these days there came down prophets from Jerusalem unto Antioch.
27 Ca fan yooyu ay yonent jóge Yerusalem, ñëw Ancos.
28And there stood up one of them named Agabus, and signified by the Spirit that there should be a great famine over all the world: which came to pass in the days of Claudius.
28 Kenn ci ñoom tudd Agabus jóg, mu yégle jaarale ko ci Xelu Yàlla mi ne, xiif bu metti dina daj àddina sépp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu ñuy wax Këlódd.
29And the disciples, every man according to his ability, determined to send relief unto the brethren that dwelt in Judea:
29 Kon taalibe ya fas yéenee sàkk ndimbal, jëme ca bokk ya dëkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem-kàttan.
30which also they did, sending it to the elders by the hand of Barnabas and Saul.
30 Noonu lañu def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sool, yónnee ko njiit ya.