1And it came to pass, that, while Apollos was at Corinth, Paul having passed through the upper country came to Ephesus, and found certain disciples:
1 Ba Apolos nekkee Korent nag, Pool jaar ca teggi ya gën a kawe ca réew ma, door a dikk Efes. Noonu mu gis fa ay taalibe.
2and he said unto them, Did ye receive the Holy Spirit when ye believed? And they [said] unto him, Nay, we did not so much as hear whether the Holy Spirit was [given].
2 Mu ne leen: «Ndax jot ngeen ci Xel mu Sell mi, bi ngeen gëmee?» Ñu tontu ko: «Déggunu sax ne, Xel mu Sell mi am na.»
3And he said, Into what then were ye baptized? And they said, Into John's baptism.
3 Mu ne leen: «Kon nag, bi ñu leen sóobee ci ndox, lu ciy maana?» Ñu tontu ko: «Xanaa li Yaxya tëral.»
4And Paul said, John baptized with the baptism of repentance, saying unto the people that they should believe on him that should come after him, that is, on Jesus.
4 Pool ne leen: «Yaxya daan na sóob nit ñi ci ndox, ndax bi ñu tuubee seeni bàkkaar; te mu ne bànni Israyil, kiy topp ci moom lañu war a gëm, maanaam Yeesu.»
5And when they heard this, they were baptized into the name of the Lord Jesus.
5 Bi ñu déggee loolu nag, sóob nañu leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi.
6And when Paul had laid his hands upon them, the Holy Spirit came on them; and they spake with tongues, and prophesied.
6 Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi ñëw ci ñoom, ñuy wax yeneeni làkk, di wax ci kàddug Yàlla.
7And they were in all about twelve men.
7 Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.
8And he entered into the synagogue, and spake boldly for the space of three months, reasoning and persuading [as to] the things concerning the kingdom of God.
8 Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéem a gëmloo.
9But when some were hardened and disobedient, speaking evil of the Way before the multitude, he departed from them, and separated the disciples, reasoning daily in the school of Tyrannus.
9 Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.
10And this continued for the space of two years; so that all they that dwelt in Asia heard the word of the Lord, both Jews and Greeks.
10 Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.
11And God wrought special miracles by the hands of Paul:
11 Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.
12insomuch that unto the sick were carried away from his body handkerchiefs or aprons, and the evil spirits went out.
12 Ñu yóbbul sax ñi wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba jàngoro yi di leen bàyyi, rab yay génn ci ñoom.
13But certain also of the strolling Jews, exorcists, took upon them to name over them that had the evil spirits the name of the Lord Jesus, saying, I adjure you by Jesus whom Paul preacheth.
13 Noonu ay Yawut yuy wëndéelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéem a ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.»
14And there were seven sons of one Sceva, a Jew, a chief priest, who did this.
14 Ñi doon def loolu, juróom-ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon taafantaloo saraxalekat bu mag ba ci Yawut yi.
15And the evil spirit answered and said unto them, Jesus I know, and Paul I know, but who are ye?
15 Waaye bi ñu ko defee rab wa tontu leen ne: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»
16And the man in whom the evil spirit was leaped on them, and mastered both of them, and prevailed against them, so that they fled out of that house naked and wounded.
16 Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, noot leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti.
17And this became known to all, both Jews and Greeks, that dwelt at Ephesus; and fear fell upon them all, and the name of the Lord Jesus was magnified.
17 Loolu siiw na ci ñépp, ñi dëkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange jàpp leen ñoom ñépp, ba ñu màggal turu Yeesu Boroom bi.
18Many also of them that had believed came, confessing, and declaring their deeds.
18 Bi loolu amee ñu bare ci ñi gëm ñëw, di wesar ci kanam ñépp seeni jati luxus.
19And not a few of them that practised magical arts brought their books together and burned them in the sight of all; and they counted the price of them, and found it fifty thousand pieces of silver.
19 Te ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. Te bi ñu xaymaa njëg ga, mu tollook juróom-fukki junniy poseti daraxma.
20So mightily grew the word of the Lord and prevailed.
20 Noonu la kàddu Boroom bi lawe, te noot lépp.
21Now after these things were ended, Paul purposed in the spirit, when he had passed through Macedonia and Achaia, to go to Jerusalem, saying, After I have been there, I must also see Rome.
21 Bi loolu wéyee Pool nas xel jëm Yerusalem, jaar ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. Mu ne: «Gannaaw bu ma fa demee, fàww ma seeti Room it.»
22And having sent into Macedonia two of them that ministered unto him, Timothy and Erastus, he himself stayed in Asia for a while.
22 Mu yebal nag ci Maseduwan ñaari jaraafam, di Timote ak Erast, waaye moom mu des ab diir ci Asi.
23And about that time there arose no small stir concerning the Way.
23 Fekk booba amoon na yengu-yengu bu réy ci lu aju ci Yoon wi.
24For a certain man named Demetrius, a silversmith, who made silver shrines of Diana, brought no little business unto the craftsmen;
24 Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem.
25whom he gathered together, with the workmen of like occupation, and said, Sirs, ye know that by this business we have our wealth.
25 Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne, sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii.
26And ye see and hear, that not alone at Ephesus, but almost throughout all Asia, this Paul hath persuaded and turned away much people, saying that they are no gods, that are made with hands:
26 Gis ngeen nag te dégg ne, Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.”
27and not only is there danger that this our trade come into disrepute; but also that the temple of the great goddess Diana be made of no account, and that she should even be deposed from her magnificence whom all Asia and the world worshippeth.
27 Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.»
28And when they heard this they were filled with wrath, and cried out, saying, Great is Diana of the Ephesus.
28 Bi ñu déggee loolu, mer mu réy tàbbi ci ñoom, ñuy yuuxu ne: «Artemis mu Efes màgg na!»
29And the city was filled with the confusion: and they rushed with one accord into the theatre, having seized Gaius and Aristarchus, men of Macedonia, Paul's companions in travel.
29 Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool.
30And when Paul was minded to enter in unto the people, the disciples suffered him not.
30 Pool nag bëgg a dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.
31And certain also of the Asiarchs, being his friends, sent unto him and besought him not to adventure himself into the theatre.
31 Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu bañ a jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.
32Some therefore cried one thing, and some another: for the assembly was in confusion; and the more part knew not wherefore they were come together.
32 Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gën a bare xamuñu lu waral ndaje ma.
33And they brought Alexander out of the multitude, the Jews putting him forward. And Alexander beckoned with the hand, and would have made a defense unto the people.
33 Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma.
34But when they perceived that he was a Jew, all with one voice about the space of two hours cried out, Great is Diana of the Ephesians.
34 Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»
35And when the townclerk had quieted the multitude, he saith, Ye men of Ephesus, what man is there who knoweth not that the city of the Ephesians is temple-keeper of the great Diana, and of the [image] which fell down from Jupiter?
35 Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne, dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan?
36Seeing then that these things cannot be gainsaid, ye ought to be quiet, and to do nothing rash.
36 Gannaaw nag kenn mënta weddi loolu, war ngeen a dalal seen xel te bañ a sañaxu ci dara.
37For ye have brought [hither] these men, who are neither robbers of temples nor blasphemers of our goddess.
37 Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla.
38If therefore Demetrius, and the craftsmen that are with him, have a matter against any man, the courts are open, and there are proconsuls: let them accuse one another.
38 Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem jànkoonte nañu ak kenn, am na ay bési layoo ak ñu yilif réew mi; nañu fa woo ku ñu amleenteel.
39But if ye seek anything about other matters, it shall be settled in the regular assembly.
39 Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom dëgg dina ko àtte.
40For indeed we are in danger to be accused concerning this day's riot, there being no cause [for it]: and as touching it we shall not be able to give account of this concourse.
40 Ndaxte fi mu ne man nañu noo jiiñ jógug mbooloo mi ndax li fi xew tey. Te bu loolu amee dunu am aw lay ci mbirum mbooloo mu rëb mii, ndaxte amul dara lu ko waral.»
41And when he had thus spoken, he dismissed the assembly.
41 Bi mu waxee loolu nag, mu tas mbooloo ma.