1Festus therefore, having come into the province, after three days went up to Jerusalem from Caesarea.
1 Bi Festus teersee ci diiwaanam, mu teg ca ñetti fan, dem Yerusalem.
2And the chief priests and the principal men of the Jews informed him against Paul; and they besought him,
2 Noonu saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame Pool ci moom.
3asking a favor against him, that he would send for him to Jerusalem; laying a plot to kill him on the way.
3 Ñuy sàkku ndimbal ci moom, di ko ñaan bu wér, mu yónni Pool Yerusalem, fekk lal nañu fiiru rey ko ca yoon wa.
4Howbeit Festus answered, that Paul was kept in charge at Caesarea, and that he himself was about to depart [thither] shortly.
4 Waaye Festus tontu leen ne: «Ñu ngi wottu Pool ca Sesare, te dinaa fa dem fi ak fan yu néew.»
5Let them therefore, saith he, that are of power among you go down with me, and if there is anything amiss in the man, let them accuse him.
5 Mu ne leen: «Ñi am maana ci yéen nag, nangeen ànd ak man, layooji ak nit ka, bu dee tooñ na.»
6And when he had tarried among them not more than eight or ten days, he went down unto Caesarea; and on the morrow he sat on the judgment-seat, and commanded Paul to be brought.
6 Noonu Festus am fa ñoom juróom-ñett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca ëllëg sa mu toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Pool.
7And when he was come, the Jews that had come down from Jerusalem stood round about him, bringing against him many and grievous charges which they could not prove;
7 Bi mu ñëwee nag, Yawut ya jóge Yerusalem wër ko, di ko jiiñ tooñ yu bare te réy, te mënuñu leen a firndeel.
8while Paul said in his defense, Neither against the law of the Jews, nor against the temple, nor against Caesar, have I sinned at all.
8 Noonu Pool làyyi ne: «Tooñuma yoonu Yawut ya, tooñuma kër Yàlla ga, tooñuma buur ba Sesaar.»
9But Festus, desiring to gain favor with the Jews, answered Paul and said, Wilt thou go up to Jerusalem, and there be judged of these things before me?
9 Ci kaw loolu Festus, mi bëgg lu neex Yawut ya, tontu Pool ne: «Ndax bëgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?»
10But Paul said, I am standing before Caesar's judgment-seat, where I ought to be judged: to the Jews have I done no wrong, as thou also very well knowest.
10 Waaye Pool ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu buur Sesaar; te fii lañu ma war a àttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne, tooñuma Yawut yi.
11If then I am a wrong-doer, and have committed anything worthy of death, I refuse not to die; but if none of those things is [true] whereof these accuse me, no man can give me up unto them. I appeal unto Caesar.
11 Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir bañ a dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leen a jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.»
12Then Festus, when he had conferred with the council, answered, Thou hast appealed unto Caesar: unto Caesar shalt thou go.
12 Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu tontu ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.»
13Now when certain days were passed, Agrippa the King and Bernice arrived at Caesarea, and saluted Festus.
13 Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus.
14And as they tarried there many days, Festus laid Paul's case before the King, saying, There is a certain man left a prisoner by Felix;
14 Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj.
15about whom, when I was at Jerusalem, the chief priests and the elders of the Jews informed [me], asking for sentence against him.
15 Te bi ma nekkee Yerusalem, saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko.
16To whom I answered, that it is not the custom of the Romans to give up any man, before that the accused have the accusers face to face, and have had opportunity to make his defense concerning the matter laid against him.
16 Waaye ma tontu leen ne: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba man a làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.”
17When therefore they were come together here, I made no delay, but on the next day sat on the judgment-seat, and commanded the man to be brought.
17 Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku.
18Concerning whom, when the accusers stood up, they brought no charge of such evil things as I supposed;
18 Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon;
19but had certain questions against him of their own religion, and of one Jesus, who was dead, whom Paul affirmed to be alive.
19 waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne, mu ngi dund.
20And I, being perplexed how to inquire concerning these things, asked whether he would go to Jerusalem and there be judged of these matters.
20 Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.
21But when Paul had appealed to be kept for the decision of the emperor, I commanded him to be kept till I should send him to Caesar.
21 Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.»
22And Agrippa [said] unto Festus, I also could wish to hear the man myself. To-morrow, saith he, thou shalt hear him.
22 Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus tontu ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
23So on the morrow, when Agrippa was come, and Bernice, with great pomp, and they were entered into the place of hearing with the chief captains and principal men of the city, at the command of Festus Paul was brought in.
23 Ca ëllëg sa nag Agaripa ak Berenis ñëw bu xumb, ñu dugg ca néegu àtte ba, ànd ak kilifay xare ba ak ña am maana ca dëkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, ñu indi Pool.
24And Festus saith, King Agrippa, and all men who are here present with us, ye behold this man, about whom all the multitude of the Jews made suit to me, both at Jerusalem and here, crying that he ought not to live any longer.
24 Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratul a dund.”
25But I found that he had committed nothing worthy of death: and as he himself appealed to the emperor I determined to send him.
25 Waaye gis naa ne, deful dara lu jar dee. Moona, gannaaw moom ci boppam dénk na boppam buur bu tedd ba, fas naa yéene yónnee ko ko.
26Of whom I have no certain thing to write unto my lord. Wherefore I have brought him forth before you, and specially before thee, king Agrippa, that, after examination had, I may have somewhat to write.
26 Fekk awma dara lu wóor ci mbiram, lu ma man a bind sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam buur Agaripa, ngir sunu jataay may ma lu ma bind.
27For it seemeth to me unreasonable, in sending a prisoner, not withal to signify the charges against him.
27 Ndaxte yaakaar naa ne, yónnee ku ñu tëj, te bañ caa boole lu ko waral, àndul ak xel.»