1But Saul, yet breathing threatening and slaughter against the disciples of the Lord, went unto the high priest,
1 Naka Sool, muy tëkkoo rey taalibey Boroom bi, ba di ko noyyee far. Mu dem nag ca saraxalekat bu mag ba,
2and asked of him letters to Damascus unto the synagogues, that if he found any that were of the Way, whether men or women, he might bring them bound to Jerusalem.
2 laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damas. Noonu ñu mu fa fekk, te ñu bokk ci yoon wi, góor mbaa jigéen, mu am dogalu yeew leen, indi leen Yerusalem.
3And as he journeyed, it came to pass that he drew nigh unto Damascus: and suddenly there shone round about him a light out of heaven:
3 Waaye bi muy jub Damas, ca saa sa leer gu jóge asamaan melax, ba ëmb ko.
4and he fell upon the earth, and heard a voice saying unto him, Saul, Saul, why persecutest thou me?
4 Mu daanu ci suuf, dégg baat bu ko ne: «Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?»
5And he said, Who art thou, Lord? And he [said], I am Jesus whom thou persecutest:
5 Mu wuyu ne: «Yaay kan Boroom bi?» Boroom bi ne ko: «Maay Yeesu, mi ngay fitnaal.
6but rise, and enter into the city, and it shall be told thee what thou must do.
6 Waaye jógal, dugg ca dëkk ba, te dinañu la wax li nga war a def.»
7And the men that journeyed with him stood speechless, hearing the voice, but beholding no man.
7 Nit ñi ànd ak moom nag taxaw, waaru ba luu, ci li ñu dégg baat bi te gisuñu kenn.
8And Saul arose from the earth; and when his eyes were opened, he saw nothing; and they led him by the hand, and brought him into Damascus.
8 Noonu Sool jóg, xippi, waaye gisul dara; kon ñu wommat ko, yóbbu ko Damas.
9And he was three days without sight, and did neither eat nor drink.
9 Diirub ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
10Now there was a certain disciple at Damascus, named Ananias; and the Lord said unto him in a vision, Ananias. And he said, Behold, I [am here], Lord.
10 Amoon na nag ci Damas taalibe bu tudd Anañas. Bi loolu amee nag Boroom bi feeñu ko ne: «Anañas!» Mu wuyu: «Maa ngi nii Boroom bi.»
11And the Lord [said] unto him, Arise, and go to the street which is called Straight, and inquire in the house of Judas for one named Saul, a man of Tarsus: for behold, he prayeth;
11 Boroom bi ne ko: «Jógal, nga jaar ci mbedd, mi ñuy wax Mbedd mu jub mi, te seet ci kër Yudaa nit ku tudd Sool te dëkk Tars, ndaxte mu ngay ñaan.
12and he hath seen a man named Ananias coming in, and laying his hands on him, that he might receive his sight.
12 Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.»
13But Ananias answered, Lord, I have heard from many of this man, how much evil he did to thy saints at Jerusalem:
13 Waaye Anañas tontu ko ne: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.
14and here he hath authority from the chief priests to bind all that call upon thy name.
14 Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci saraxalekat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.»
15But the Lord said unto him, Go thy way: for he is a chosen vessel unto me, to bear my name before the Gentiles and kings, and the children of Israel:
15 Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil.
16for I will show him how many things he must suffer for my name's sake.
16 Te dinaa ko won coono yu bare yu mu war a dékku ngir sama tur.»
17And Ananias departed, and entered into the house; and laying his hands on him said, Brother Saul, the Lord, [even] Jesus, who appeared unto thee in the way which thou camest, hath sent me, that thou mayest receive thy sight, and be filled with the Holy Spirit.
17 Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sool. Mu ne ko: «Sool sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.»
18And straightway there fell from his eyes as it were scales, and he received his sight; and he arose and was baptized;
18 Ca saa sa lu mel ni ay waasintoor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox;
19and he took food and was strengthened. And he was certain days with the disciples that were at Damascus.
19 ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damas.
20And straightway in the synagogues he proclaimed Jesus, that he is the Son of God.
20 Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21And all that heard him were amazed, and said, Is not this he that in Jerusalem made havoc of them that called on this name? and he had come hither for this intent, that he might bring them bound before the chief priests.
21 Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanamu saraxalekat yu mag ya?»
22But Saul increased the more in strength, and confounded the Jews that dwelt at Damascus, proving that this is the Christ.
22 Moona Sool di gën a am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.
23And when many days were fulfilled, the Jews took counsel together to kill him:
23 Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24but their plot became known to Saul. And they watched the gates also day and night that they might kill him:
24 Waaye Sool yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25but his disciples took him by night, and let him down through the wall, lowering him in a basket.
25 Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26And when he was come to Jerusalem, he assayed to join himself to the disciples: and they were all afraid of him, not believing that he was a disciple.
26 Bi Sool agsee Yerusalem, mu jéem a ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27But Barnabas took him, and brought him to the apostles, and declared unto them how he had seen the Lord in the way, and that he had spoken to him, and how at Damascus he had preached boldly in the name of Jesus.
27 Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sool gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damas.
28And he was with them going in and going out at Jerusalem,
28 Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29preaching boldly in the name of the Lord: and he spake and disputed against the Grecian Jews; but they were seeking to kill him.
29 Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wut a rey.
30And when the brethren knew it, they brought him down to Caesarea, and sent him forth to Tarsus.
30 Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31So the church throughout all Judaea and Galilee and Samaria had peace, being edified; and, walking in the fear of the Lord and in the comfort of the Holy Spirit, was multiplied.
31 Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gën a dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
32And it came to pass, as Peter went throughout all parts, he came down also to the saints that dwelt at Lydda.
32 Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd,
33And there he found a certain man named Aeneas, who had kept his bed eight years; for he was palsied.
33 mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom-ñetti at.
34And Peter said unto him, Aeneas, Jesus Christ healeth thee: arise and make thy bed. And straightway he arose.
34 Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.
35And all that dwelt at Lydda and in Sharon saw him, and they turned to the Lord.
35 Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi woññiku ci Boroom bi.
36Now there was at Joppa a certain disciple named Tabitha, which by interpretation is called Dorcas: this woman was full of good works and almsdeeds which she did.
36 Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas,» maanaam «kewel,» te muy wéy ci jëf yu baax ak saraxe.
37And it came to pass in those days, that she fell sick, and died: and when they had washed her, they laid her in an upper chamber.
37 Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma.
38And as Lydda was nigh unto Joppa, the disciples, hearing that Peter was there, sent two men unto him, entreating him, Delay not to come on unto us.
38 Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne, Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si.
39And Peter arose and went with them. And when he was come, they brought him into the upper chamber: and all the widows stood by him weeping, and showing the coats and garments which Dorcas made, while she was with them.
39 Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisool ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.
40But Peter put them all forth, and kneeled down and prayed; and turning to the body, he said, Tabitha, arise. And she opened her eyes; and when she saw Peter, she sat up.
40 Ci kaw loolu Piyeer génne ñépp ci biti, mu sukk, ñaan ci Yàlla, ba noppi walbatiku ca néew ba ne ko: «Tabita, jógal!» Noonu mu xippi, gis Piyeer, daldi toog.
41And he gave her his hand, and raised her up; and calling the saints and widows, he presented her alive.
41 Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Mu woo gaayi Yàlla ya ak jigéen ña, won leen ko, muy dund.
42And it became known throughout all Joppa: and many believed on the Lord.
42 Mbir ma siiw ca Yope gépp, ba ñu bare gëm Boroom bi.
43And it came to pass, that he abode many days in Joppa with one Simon a tanner.
43 Gannaaw loolu Piyeer toog ay fan ci Yope, ci këru ku tudd Simoŋ, miy wullikat.