1Now before the feast of the passover, Jesus knowing that his hour was come that he should depart out of this world unto his Father, having loved his own that were in the world, he loved them unto the end.
1 Laata màggalu bésu Jéggi ba la woon. Yeesu xamoon na ne, waxtu wi mu war a génne àddina, dem ca wetu Baay ba, jot na. Ku bëgg ñoñam yi nekk ci àddina la, te bëgg na leen ba fa mbëggeel man a yem.
2And during supper, the devil having already put into the heart of Judas Iscariot, Simon's [son], to betray him,
2 Yeesu ak taalibe yaa ngi doon reer. Fekk na booba Seytaane xiirtal Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo, ngir mu wori Yeesu.
3[Jesus], knowing that the Father had given all the things into his hands, and that he came forth from God, and goeth unto God,
3 Yeesu xamoon na ne, Yàlla joxoon na ko sañ-sañ ci lépp, xam it ne, ca Yàlla la jóge te ca moom lay delluwaat.
4riseth from supper, and layeth aside his garments; and he took a towel, and girded himself.
4 Mu daldi jóge ca reer ba, summi mbubbam, daldi jël ab sarbet, laxas ko ci ndiggam.
5Then he poureth water into the basin, and began to wash the disciples' feet, and to wipe them with the towel wherewith he was girded.
5 Noonu mu sotti ndox ci ab këll, daldi tàmbali di raxas tànki taalibe ya, di leen fomp ak sarbet, ba mu laxasaayoo.
6So he cometh to Simon Peter. He saith unto him, Lord, dost thou wash my feet?
6 Bi mu agsee ba ca Simoŋ Piyeer, kooku ne ko: «Boroom bi, ndax yaw dangaa nar a raxas samay tànk?»
7Jesus answered and said unto him, What I do thou knowest not now; but thou shalt understand hereafter.
7 Yeesu tontu ko ne: «Xamoo fii mu nekk li may def, waaye dinga ko xami.»
8Peter saith unto him, Thou shalt never wash my feet. Jesus answered him, If I wash thee not, thou hast no part with me.
8 Piyeer ne ko: «Déedéet, duma nangu mukk nga raxas samay tànk.» Yeesu ne ko: «Su ma la raxasul, doo bokk ak man dara.»
9Simon Peter saith unto him, Lord, not my feet only, but also my hands and my head.
9 Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Boroom bi, bul yem rekk ci tànk yi, waaye raxasaaleel loxo yi ak bopp bi!»
10Jesus saith to him, He that is bathed needeth not save to wash his feet, but is clean every whit: and ye are clean, but not all.
10 Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatul a raxas lu dul ay tànkam, ndaxte set na wecc. Yéen nag set ngeen, waaye du ñépp!»
11For he knew him that should betray him; therefore said he, Ye are not all clean.
11 Fekk Yeesu xamoon na ki ko nar a wor, looloo tax mu ne: «Setuleen yéen ñépp.»
12So when he had washed their feet, and taken his garments, and sat down again, he said unto them, Know ye what I have done to you?
12 Bi mu leen raxasalee seeni tànk ba noppi, Yeesu dafa solaat mbubbam, dellu toogaat ne leen: «Ndax xam ngeen li ma leen defal?
13Ye call me, Teacher, and, Lord: and ye say well; for so I am.
13 Yéen a ngi may wooye “Kilifa gi” ak “Boroom bi,” te wax ngeen dëgg, moom laa.
14If I then, the Lord and the Teacher, have washed your feet, ye also ought to wash one another's feet.
14 Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni tànk, yéen itam war ngeen di raxasalante seeni tànk.
15For I have given you an example, that ye also should do as I have done to you.
15 Bàyyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di jëf, nii ma jëfeek yéen.
16Verily, verily, I say unto you, a servant is not greater than his lord; neither one that is sent greater than he that sent him.
16 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jaam gënul a màgg sangam, mbaa ndaw, ki ko yónni.
17If ye know these things, blessed are ye if ye do them.
17 Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég.
18I speak not of you all: I know whom I have chosen: but that the scripture may be fulfilled: He that eateth my bread lifted up his heel against me.
18 «Yéen ñépp taxuleen may wax; xam naa ñi ma tànn. Waaye li Mbind mi wax, fàww mu am, bi ñu naan: “Ki lekk sama dugub wéq na ma.”
19From henceforth I tell you before it come to pass, that, when it is come to pass, ye may believe that I am [he].
19 Maa ngi leen koy wax ci teel, bala looloo ñëw, ngir bu ñëwee, ngeen gëm ne, Maay ki nekk.
20Verily, verily, I say unto you, he that receiveth whomsoever I send receiveth me; and he that receiveth me receiveth him that sent me.
20 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku nangu kenn ci ñi may yónni, nangu nga ma, man itam; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni.»
21When Jesus had thus said, he was troubled in the spirit, and testified, and said, Verily, verily, I say unto you, that one of you shall betray me.
21 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mu jàq, biral ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
22The disciples looked one on another, doubting of whom he spake.
22 Taalibe yi di xoolante, te xamuñu kan lay wax.
23There was at the table reclining in Jesus' bosom one of his disciples, whom Jesus loved.
23 Ka Yeesu bëggoon te mu bokkoon ca taalibe ya, ma nga sóonu woon ca kaw Yeesu.
24Simon Peter therefore beckoneth to him, and saith unto him, Tell [us] who it is of whom he speaketh.
24 Kooku la Simoŋ Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ki ko taxoon di wax.
25He leaning back, as he was, on Jesus' breast saith unto him, Lord, who is it?
25 Taalibe ba daldi walbatiku ca Yeesu, laaj ko ne: «Boroom bi, kooku kan la?»
26Jesus therefore answereth, He it is, for whom I shall dip the sop, and give it him. So when he had dipped the sop, he taketh and giveth it to Judas, [the son] of Simon Iscariot.
26 Yeesu ne ko: «Dinaa capp dogu mburu ci ndab li; ki ma koy jox, kooku la.» Noonu Yeesu jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, daldi koy jox Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo.
27And after the sop, then entered Satan into him. Jesus therefore saith unto him, What thou doest, do quickly.
27 Naka la Yudaa jël dog wa, Seytaane dugg ci moom. Yeesu ne ko: «Gaawantul ci li ngay def!»
28Now no man at the table knew for what intent he spake this unto him.
28 Amul kenn ca ña fa toogoon ku xam lu tax mu wax ko loolu.
29For some thought, because Judas had the bag, that Jesus said unto him, Buy what things we have need of for the feast; or, that he should give something to the poor.
29 Waaye gannaaw Yudaa moo yoroon boyetu xaalis bi, am ñu xalaat ne, Yeesu dafa koo wax, mu dem jëndi li war ci màggal gi, walla mu ne ko mu dem sarax miskin yi.
30He then having received the sop went out straightway: and it was night.
30 Yudaa nag jël dogu mburu ma, daldi génn ca saa sa. Booba guddi woon na.
31When therefore he was gone out, Jesus saith, Now is the Son of man glorified, and God is glorified in him;
31 Bi Yudaa génnee, Yeesu ne: «Léegi nag ndamu Doomu nit ki feeñ na, te ndamu Yàlla feeñ na itam ci moom.
32and God shall glorify him in himself, and straightway shall he glorify him.
32 Te bu ma feeñalee ndamu Yàlla, Yàlla itam ci teewaayam dina feeñal ndamu Doomu nit ki, te dina ko def léegi.
33Little children, yet a little while I am with you. Ye shall seek me: and as I said unto the Jews, Whither I go, ye cannot come; so now I say unto you.
33 Samay soppe, sama nekk ak yéen dootul yàgg. Dingeen may seet, waaye maa ngi leen di wax léegi li ma waxoon Yawut ya: fa ma jëm, dungeen fa man a dem.
34A new commandment I give unto you, that ye love one another; even as I have loved you, that ye also love one another.
34 Maa ngi leen di jox ndigal lu bees: bëgganteleen. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge.
35By this shall all men know that ye are my disciples, if ye have love one to another.
35 Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.»
36Simon Peter saith unto him, Lord, whither goest thou? Jesus answered, Whither I go, thou canst not follow now; but thou shalt follow afterwards.
36 Simoŋ Piyeer laaj ko ne: «Boroom bi, foo jëm?» Yeesu ne ko: «Fa ma jëm, mënuloo ma faa topp léegi, waaye dinga ma toppi ca kanam.»
37Peter saith unto him, Lord, why cannot I follow thee even now? I will lay down my life for thee.
37 Piyeer ne ko: «Boroom bi, lu tax mënuma laa topp léegi? Àttan naa joxe sama bakkan ngir yaw!»
38Jesus answereth, Wilt thou lay down thy life for me? Verily, verily, I say unto thee, The cock shall not crow, till thou hast denied me thrice.
38 Yeesu ne ko: «Àttan ngaa joxe sa bakkan ngir man? Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.