1 Samay bokk, bu ñépp di sababloo nekk jàngalekatu mbooloo mi, xam ne nun jàngalekat yi, àtte bi nuy jaar mooy gën a diis.
2 Ndaxte nun ñépp sikk nanu ci fànn yu bare. Ki sikkul ci kàddoom, ku mat nga, te man a noot sa yaram wépp.
3 Noonu ku laab fas, ngir mu déggal la, noot nga jëmmam jépp.
4 Te gaal yi it yu réy lañu, te ngelaw lu am doole di leen jiñax, waaye dawalkat bi, weñ gu tuuti la leen di jëme fu ko neex.
5 Ci noonu làmmiñ, cér su tuuti la, waaye day bàkkoo jëf yu réy. Seetleen ni ferñent tuutee, te man a làkk àll bu yaatu.
6 Noonu it làmmiñ safara la, di bon-bonu àddina ci biir cér yi, tey musibaal jëmm jépp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk àddina.
7 Nit man na noot xeeti rab yépp: rabi àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi; noot na lépp.
8 Waaye làmmiñ kenn mënu koo noot; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak daŋar juy rey.
9 Làmmiñ lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi móoloo ko nit, ñi Yàlla sàkk ci meloom.
10 Gémmiñ gi sante mooy móoloo. Yéen samay bokk, loolu warul a am.
11 Ndax ndox mu lewet ak mu wex dinañu ballandoo ci genn mbënn?
12 Samay bokk, ndax mas ngeen a gis garabu figg gu meññ oliw, walla garabu réseñ gu meññ ay figg? Mukk! Mbënnu xorom mënta nàcc mukk ndox mu neex.
13 Ana ku neex xel ci yéen, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy jëfam ak dundam gu sell, te feeñal xelam ci jikkoom ju lewet.
14 Waaye ku am ci sa xol farlu gu laloo wextan ak wut aw tur, bul bàkku, di weddi dëgg.
15 Xel moomu jógewul ci kaw; jëfu àddina la, di jikkoy niti kese, te jóge ci Seytaane.
16 Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa xëccoo ak bépp ñaawteef.
17 Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq.
18 Te nitu jàmm dina bey toolu jàmm, góob njub.