Latvian: New Testament

Wolof: New Testament

2 Corinthians

6

1Būdami jūsu līdzstrādnieki, mēs atgādinām, lai jūs nesaņemtu Dieva žēlastību veltīgi.
1 Nun nag ñiy liggéeyandoo ak Yàlla, nu ngi leen di ñaan: jariñooleen yiw, wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu bañ a neen ci yéen.
2Jo Viņš saka: žēlastības laikā es tevi paklausīju un pestīšanas dienā es tev palīdzēju. Lūk, tagad ir žēlastības laiks, lūk, tagad pestīšanas diena.
2 Ndaxte Yàlla nee na:«Ca jamono ja mu jekke, nangu naa sa ñaan;ci bésu mucc gi laa la wallu.» Tey jii la jamono ju jekk ji; tey la bésub mucc gi.
3Mēs nevienam nekādu apgrēcību nedodam, lai mūsu kalpošana netiktu nopelta;
3 Bëggunoo lëmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn bañ a sikk sunu liggéey.
4Bet ka visā esam Dieva kalpi, mēs pierādām lielā pacietībā, bēdās, trūkumā un bailēs,
4 Li nu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ci fànn gu nekk; danuy muñ coono yi, tiis yi, njàqare yi;
5Šaustīšanā, cietumos, uztraukumos, darbā, negulēšanā, gavēnī,
5 ñu nuy dóor, di nu tëj ci kaso, dëkk yi di yengu ndax sunu mbir; nuy liggéey ba sonn, di fanaanee xool, di woor.
6Šķīstībā, zināšanā, lēnprātībā, laipnībā, Svētajā Garā, neviltotā mīlestībā,
6 Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ,
7Patiesības vārdā, Dieva spēkā, ar taisnības ieročiem pa labi un pa kreisi,
7 ci kàddug dëgg ak ci kàttanu Yàlla, nu ngi yor gànnaayi njubte ci loxol ndeyjoor ak lu càmmooñ.
8Ar godu un negodu, ar neslavu un labu slavu, it kā viltnieki un tomēr patiesīgi; kā nepazīstami un tomēr zināmi;
8 Ñu bàkk nu, jéppi nu, sant nu, xas nu. Ñu di nu jiiñ réeral, moona niti dëgg lanu.
9Kā mirēji, un, lūk, mēs dzīvojam; kā šaustīti, bet nenonāvēti;
9 Ñuy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw nañu. Nu mel ni ñu loof, moona nu ngi dund. Ñu yar nu, teewul nu rëcc ci dee.
10Kā noskumuši, bet vienmēr priecīgī; kā trūkumcietēji, bet kas daudzus dara bagātus; kā tādi, kam nekā nav un tomēr ir viss.
10 Danuy dékku tiis, waaye di bég fu nu tollu. Nu tumurànke, waaye di woomal ñu bare; amunu dara, fekk noo moom lépp.
11Korintieši, mēs jums atklāti sakām, mūsu sirds ir plaši atvērt.
11 Yéen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol.
12Mēs pret jums neesam šaursirdīgi, bet jūs pret mums esat šaursirdīgi.
12 Ubbiku nanu ci yéen, waaye yéen ubbikuwuleen ci nun.
13Tā kā jūs saņemat to pašu algu, es kā bērniem jums saku: kļūstiet arī jūs atvērtāki!
13 Maa ngi wax ak yéen ni samay doom; feyleen nu bor bi, yéen itam; ubbileen seen xol!
14Nevelciet jūgu kopā ar neticīgajiem, jo kas kopējs ir taisnībai ar netaisnību? Vai kāda sadraudzība gaismai ar tumsu?
14 Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo man a am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo man a am diggante leer ak lëndëm?
15Bet kāda saskaņa Kristum ar Beliālu? Vai kāda daļa ir ticīgajam ar neticīgo?
15 Gan déggoo moo man a am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo man a am diggante ki gëm ak ki gëmul?
16Bet kā sader Dieva svētnīca ar elkiem? Jo jūs esat dzīvā Dieva svētnīca, kā Dievs to saka: es viņos mājošu un starp viņiem staigāšu, un es būšu viņu Dievs, un viņi būs mana tauta.
16 Nan la këru Yàlla man a mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy këru Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe:«Dinaa dëkk ci seen biir,tey dox ànd ak ñoom,ma nekk seen Yàlla,ñuy samay gaay.»
17Tāpēc aizejiet no viņu vidus un nošķirieties, saka Kungs, un netīram nepieskarieties!
17 Kon nag Boroom bi nee na:«Génnleen biir ñooñu te beru.Buleen laal dara lu am sobe,kon dinaa leen teeru.
18Un es jūs pieņemšu, un es būšu jums Tēvs, un jūs būsiet mani dēli un meitas, saka visspēcīgais Kungs.
18 Dinaa nekk baay ci yéen,ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen. Moom la Aji Kàttan ji wax.»