1Bija arī tautā viltus pravieši, kā arī jums būs mācītāji meļi, kuri ienesīs kaitīgas maldu mācības, noliegdami Kungu, kas viņus atpirka, tā sagatavodami sev drīzu pazušanu.
1 Waaye ci bànni Israyil, amoon na naaféq yu mbubboo turu yonent, ni muy ame seen biir ñuy mbubboo turu jàngalekat. Ci seeni pexe dinañu dugal ci yeen xalaat yu sànke, di weddi Boroom bi leen jot, tey yóbbe seen bopp alkande ju teew.
2Un daudzi sekos viņu baudu dzīvei, un viņi zaimos patiesības ceļu.
2 ñu bare dinañu leen fekki ci seeni ñaawteef, ba gàkkal yoonu dëgg ci bëti nit ñi.
3Un mantkārībā viņi izmantos jūs ar izdomātiem vārdiem: jau sen nekavējas viņu notiesāšana, un viņu bojā eja nesnauž.
3 Seen bëgge dina tax, ñu dàbbdaaxe ay wax, ngir nax leen, ba lekk seenus tuut. Waaye àtte baa ngi leen di xaar, te seen alkande di leen teeru.
4Jo arī eņģeļus, kas apgrēkojās, Dievs nesaudzēja, bet, elles tumsības saitēm saistītus, nogrūda bezdibenī ciešanās, lai glabātu viņus tiesai.
4 Ndaxte Yàlla jeggalul malaaka ya bàkkaaroon, waaye tàbbal na leen safara, tëj leen ca kàmb yu lëndëm, di leen nége àtte ba.
5Un Viņš nesaudzēja seno pasauli, sūtīdams plūdus bezdievīgajai pasaulei, bet saudzēja taisnības sludinātāju Noasu kā astoto.
5 Te it jeggalul àddina su jëkk sa weddi woon, ba xooj ko ci ndoxu mbënn ma, waaye musal na Nóoyin rekk, mi daan waare ci njub, moom ak juróom-ñaari nit.
6Un tāpat nosodīja sodomiešu un gomoriešu pilsētas, pārvērsdams tās pelnos un iznīcinādams, rādot biedinājumu visiem, kas bezdievīgi dzīvos.
6 Te it Yàlla daan na dëkki Sodom ak Gomor, raafal leen cig lakk, ñuy misaalu ñiy weddi ëllëg.
7Viņš izglāba taisnīgo Latu, ko nomāca bezdievju varmācība un viņu netiklā dzīve,
7 Waaye musal na Lóot mi jub, mi sonnoon ndax ñaawteefi ñu dëng, ñooñu mu nekkaloon.
8Jo, visu to redzēdams un dzirdēdams, viņš palika taisnīgs, lai gan viņš dzīvoja pie tiem, kuri diendienā mocīja ļauniem darbiem viņa taisnīgo dvēseli.
8 Ndaxte Lóot, mi dëkkoon ci seen biir, dafa dëkke woon tiisu xol, ndax ñaawteef yi mu gis ak a dégg guddi ak bëccëg.
9Kungs prot izglābt dievbijīgos no kārdinājuma, bet netaisnos paturēt mokām tiesas dienai,
9 Gannaaw loolu lépp am na nag, nanu bir ne, Boroom bi man na musal aji gëm ji nekk ci nattu, te denc ñi jubadi, ngir alag leen bésu àtte ba.
10Bet it sevišķi tos, kas seko nešķīstajām miesas kārībām un nicina augstāko varu, pārdroši un patmīlīgi nebaidīdamies radīt šķelšanos un zaimot,
10 Rawatina ñiy topp seen bakkan ciy bëgg-bëgg yu ruslu, te faalewuñu genn kilifteef. ñu ñeme Yàlla lañu, te dëgër bopp, ba ragaluñoo xas kilifa ya gëna kawe.
11Kaut gan eņģeļi, kas stiprumā un spēkā lielāki, netiesā viens otru zaimiem,
11 Fekk sax malaaka, yi leen ëpp doole ak kàttan, tey sax ca jetaayu Boroom bi, ñemewuñoo xas kilifa yooyu.
12Jo tie zaimo to, ko nepazīst un savā samaitāšanā iet bojā kā neprātīgi dzīvnieki, kas pēc dabas paredzēti sagūstīšanai un nonāvēšanai.
12 Waaye ñoom dañuy xas ci biir yi ñu xamul. ñoom ak bàyyima ñoo yem, di ay mbindeef yuy tañaxu, te tër rendi rekk a jekk ci ñoom; dees na leen rey ni bàyyima,
13Tie saņem netaisnības algu; dienas uzdzīvi viņi uzskata par prieku; tie ir netīrumu un kauna traipi, kas savās dzīrēs dzīro kopā ar jums.
13 muy seen peyug njubadi. Xawaare bëccëgu ndara-kàmm mooy seen bànneex. Su ñuy lekkandoo ak yeen, dañuy bànneexu ci seeni bëgg-bëgg, di ay gàkk ak i sikk ci seen biir.
14Viņu acis pildītas laulības pārkāpšanām, nepiepildāmiem grēkiem. Viņi vilina svārstīgas dvēseles. Viņu sirdis vingrinātas mantkārībā; tie ir lāsta bērni.
14 Jigéen ju seen bët tegu, ñu xédd ko, ba duñu tàggook moy mukk; ku ñàkk pasteef ñu fàbbi la; ñu xelu lañu jëme cig bëgge -- ñu alku lañu!
15Viņi maldījās, atstādami taisno ceļu, un sekoja Balaama, Bosora dēla, ceļam, kas mīlēja netaisnības algu,
15 Réer nañu ba wàcc yoon wu jub wi, topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi bëgge xiiroon ci njubadi.
16Bet saņēma pamācību par savu ārprātu: mēms nastu nesējs lops, runādams cilvēka valodā, aizkavēja pravieša neprātību.
16 Waaye déggadeem yóbbe na ko yeraanga; xam ngeen ne mbaam-sëf du wax, waaye mbaam wax na ak moom ci làmmiñ wu bir, ngir mu génn ci ndofam googu.
17Tie ir bezūdens avoti, vētras dzenāti mākoņi, kam nolemta visdrūmākā tumsība.
17 Ñooñule ay teen yu dëy lañu, di xiini lay, yu ngelaw liy naawal, te seen pey mooy lëndëm gu ne taraj.
18Jo, runādami lepnus, tukšus vārdus, tie vilina miesas kārībās un netiklās baudās tos, kas tikko izbēguši no maldu ceļu gājējiem,
18 Dañuy fàbbi ñu naroona mucc ci àddina ju réer, dig leen ak làmmiñ yu neex bànneexi bakkan yu jéggi dayo.
19Apsolīdami tiem brīvību, būdami paši samaitāšanas vergi, jo kura kāds uzvarēts, tā vergs viņš ir.
19 Dañu leen di dig ngoreel, te fekk ñoom ci seen bopp jaami yàqute lañu, ndaxte lu la noot, jaamam nga.
20Jo ja tie, kas mūsu Kunga un Pestītāja Jēzus Kristus atzīšanā izbēguši no pasaules gānekļiem, bet tanīs atkal iepīti, tiek uzvarēti, tad pēdējo gals ir ļaunāks nekā sākums.
20 Su ñu xamee Boroom bi, di sunu Musalkat Yeesu Krist, ba mucc ci sobes àddina, ba noppi sóobuwaat ca, ba mu noot leen, seen muj moo yées seen njàlbéen.
21Tiem būtu labāk, ja tie nebūtu pazinuši patiesības ceļu, nekā, to pazīstot, novērsties no viņiem dotā svētā baušļa.
21 Ndaxte ñu xam yoon wu jub wi, ba noppi dëddu ndigal lu sell li ñu déggoon, bañoon koo xam moo gënoon ci ñoom.
22Bet viņiem noticis, kā saka patiess sakāmvārds: Suns atgriežas pie sava vēmekļa, un mazgāta cūka atkal vārtās dubļos.
22 Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: Xaj mooy waccu, di ko lekkaat; te it: Mbaam-xuux, loo ko sang-sang, mu xalangu ci ban.