Latvian: New Testament

Wolof: New Testament

Acts

22

1Brāļi un tēvi, uzklausiet tagad aizstāvēšanos, kādu es jums teikšu!
1 «Yéen bokk yi ak baay yi, dégluleen samaw lay.»
2Kad tie dzirdēja, ka viņš tos uzrunā ebreju valodā, tie kļuva vēl klusāki,
2 Bi ñu déggee, mu di leen wax ci làkku yawut, ñu gën ne xeram. Noonu Pool ne leen:
3Un viņš sacīja: Es esmu jūds, dzimis Tarsā, Kilikijā, bet uzaudzināts šinī pilsētā, izglītojies pie Gamaliēla kājām saskaņā ar tēvu bauslības patiesībām, bauslības cīnītājs, kādi arī jūs šodien visi esat;
3 «Man Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu jàngal ma bu wér yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Yàlla, mel ni yéen ñépp tey.
4Un šo mācību esmu vajājis līdz nāvei, saistīdams un nododams cietumā vīriešus un sievietes,
4 Daan naa fitnaal ña bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa góor ak jigéen, tëj leen;
5Kā to man apliecina augstais priesteris un visi vecākie, no kuriem, saņēmis vēstules, gāju pie brāļiem uz Damasku, lai no turienes tos sasaistītus vestu uz Jeruzalemi un sodītu.
5 saraxalekat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen.
6Bet notika, ka, man ejot un dienas vidū tuvojoties Damaskai, piepeši mani apspīdēja spilgta gaisma no debesīm.
6 «Waaye ci digg-bëccëg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damas, ca saa sa leer gu mag jóge asamaan, melax ba ëmb ma.
7Un es nokritu zemē un dzirdēju balsi man sakām: Saul, Saul, kāpēc tu mani vajā?
7 Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?”
8Bet es atbildēju: Kungs, kas tu esi? Un Viņš sacīja man: Es esmu Jēzus Nācarietis, ko tu vajā.
8 Ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.”
9Un tie, kas bija kopā ar mani, gaismu gan redzēja, bet Viņa balsi, kas ar mani runāja, nedzirdēja.
9 Ñi ma àndaloon gis nañu leer ga, waaye dégguñu baatu ka doon wax ak man.
10Es sacīju: Kungs, kas man jādara? Bet Kungs sacīja man: Celies, ej uz Damasku, un tur tev pateiks visu, kas tev jādara.
10 Noonu ma laaj ko: “Lu ma war a def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.”
11Un tā kā es no tās gaismas spilgtuma nevarēju vairs redzēt, pavadoņi veda mani aiz rokas, un tā es nonācu Damaskā.
11 Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, ña ma àndal wommat ma, ma ñëw Damas.
12Tur Ananija, bauslības vīrs, par ko liecina visi tur dzīvojošie jūdi,
12 «Bi ma ko defee ku tudd Anañas ñëw ci man. Nit ku ragal Yàlla la woon ci sàmm yoonu Musaa, te Yawuti Damas yépp seedeel ko lu baax.
13Atnāca un, nostājies pie manis, sacīja man: Brāli Saul, topi redzīgs! Un es tanī pat stundā uzlūkoju viņu,
13 Mu taxaw ci sama wet ne ma: “Sool sama mbokk, delluwaatal di gis.” Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko.
14Bet viņš sacīja: Mūsu tēvu Dievs tevi izredzējis, lai tu atzītu Viņa prātu un redzētu Taisnīgo, un dzirdētu balsi no Viņa mutes;
14 Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam tànn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga dégg ay waxam.
15Jo tu visiem ļaudīm liecināsi par Viņu to, ko redzēji un dzirdēji.
15 Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp.
16Un ko tagad vēl kavējies? Celies un pieņem kristību, un, Viņa vārdu piesaucis, nomazgā savus grēkus!
16 Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.”
17Bet notika, kad atgriezos Jeruzalemē un svētnīcā lūdzu Dievu, ka es tiku garā aizrauts;
17 «Bi ma dellusee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man.
18Un es redzēju Viņu man sakām: Steidzies un žigli izej no Jeruzalemes, jo viņi tavu liecību par mani nepieņems.
18 Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem ci ni mu gën a gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.”
19Un es sacīju: Kungs, viņi zina, ka es tos, kas uz Tevi ticēja, metu cietumā un šaustīju sinagogās.
19 Waaye ma tontu ne: “Boroom bi, xam nañu ne, dama daan wër jàngoo-jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm.
20Un kad Tava liecinieka Stefana asinis tika izlietas, es biju klāt un piekritu tam, un sargāju drēbes tiem, kas viņu nonāvēja.
20 Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”
21Un Viņš man sacīja: Ej, jo es tevi sūtīšu tālumā starp pagāniem.
21 Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»
22Uzklausījuši viņu līdz šiem vārdiem, tie pacēla savas balsis, sacīdami: Nost tādu no šīs zemes, jo tāds nedrīkst dzīvot!
22 Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowul a dund!»
23Bet, kad tie kliedza un nometa savas drēbes, un svieda putekļus gaisā,
23 Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tey callameeru suuf.
24Priekšnieks lika viņu ievest mītnē, šaustīt rīkstēm un mocīt viņu, lai uzzinātu, kāda iemesla dēļ tie tā kliedza uz viņu.
24 Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii.
25Un kad tie sasēja viņu siksnām, Pāvils sacīja virsniekam, kas stāvēja viņam klāt: Vai jums atļauts šaustīt nenotiesātu Romas pilsoni?
25 Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?»
26To dzirdējis, virsnieks aizgāja pie priekšnieka un paziņoja viņam, sacīdams: Ko tu gribi darīt? Šis cilvēks taču ir Romas pilsonis.
26 Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.»
27Tad priekšnieks, piegājis, jautāja viņam: Saki man, vai tu esi romietis? Un viņš sacīja: Jā!
27 Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu tontu ko: «Waaw, moom laa.»
28Tad priekšnieks atbildēja: Es šo pilsonību ieguvu par augstu maksu. Un Pāvils sacīja: Bet es tāds jau esmu dzimis.
28 Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool tontu ko: «Man de dama koo judduwaale.»
29Tad tūdaļ aizgāja no viņa tie, kas taisījās viņu mocīt. Bet priekšnieks, uzzinājis, ka viņš ir Romas pilsonis, izbijās, jo bija viņu saistījis.
29 Ñi ko bëggoon a dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.
30Bet nākošajā dienā, gribēdams skaidrāk zināt, kāpēc jūdi viņu apsūdz, viņš to atbrīvoja un, pavēlējis sanākt priesteriem un visai augstajai tiesai, izveda Pāvilu un nostādīja viņu starp tiem.
30 Ca ëllëg sa mu bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, saraxalekat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.