Latvian: New Testament

Wolof: New Testament

James

4

1No kurienes kari un strīdi jūsu starpā? Vai ne no turienes, no jūsu kārībām, kas karo jūsu locekļos?
1 Xeex yi ak xuloo yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni bëgg-bëgg, yiy xeex ci seeni cér?
2Jūs iekārojat, bet jums nav; jūs slepkavojat un ienīstat, bet nevarat iegūt; jūs strīdaties un karojat, bet jums nav, jo jūs nelūdzat Dievu.
2 Dangeen di mébét waaye dungeen am; dangeen di rey nit, boole ci kiñaan, waaye li ngeen di yóotu, dungeen ko jot; dangeen di xuloo ak a xeex waaye dungeen am dara, ndaxte ñaanuleen Yàlla.
3Jūs lūdzat, bet nesaņemat, jo jūs ļauni lūdzat, lai to izlietotu savām kārībām.
3 Bu ngeen ñaanee sax, dungeen jot dara, ndax yéena ngi ñaan ci naaféq, ngir gën a topp seen nafsu.
4Jūs, laulības pārkāpēji! Vai jūs nezināt, ka šīs pasaules draudzība ir ienaidā ar Dievu? Un kas gribētu būt šīs pasaules draugs, tas paliek Dievam ienaidnieks.
4 Yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, xanaa xamuleen ne mbëggeelu àddina, mbañeel la fa Yàlla? Ku bëgg a xaritoo ak àddina nag, noonoo nga ak Yàlla.
5Vai jūs domājat, ka Raksti veltīgi saka: Līdz greizsirdībai iekāro gars, kas mājo jūsos?
5 Xanaa yaakaar ngeen ne, Mbind mi day wax cig neen, ci li mu ne: «Yàlla am na mbëggeel gu fiir ci Xel mi mu def ci nun.»
6Bet Viņš dod lielāku žēlastību; tādēļ sacīts: Dievs pretojas lepniem, bet pazemīgiem dod žēlastību (Sak 3,34)
6 Waaye yiwu Yàllaa ko ëpp. Moom la Mbind mi wax ne:«Yàlla dàq na ñi réy,waaye yiwal na ñi woyof.»
7Tādēļ esiet padevīgi Dievam, un pretojieties velnam, un tas bēgs no jums.
7 Kon nag wàkkirluleen ci Yàlla, waaye dàqleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen.
8Tuvojieties Dievam, un Viņš tuvosies jums. Šķīstījiet rokas, grēcinieki, un tīriet savas sirdis, jūs, dalītie dvēselē!
8 Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yéen bàkkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo; yéen ñi am xel ñaar, laabal-leen seeni xol.
9Sajūtiet savu niecību, sērojiet un raudiet; jūsu smiekli lai pārvēršas sērās, bet jūsu prieks - skumjās!
9 Toroxluleen te naqarlu, bay jooy; defleen seeni ree aw naqar, te seen mbég nekk tiis.
10Pazemojieties Kunga priekšā, tad Viņš jūs paaugstinās.
10 Suufeel-leen seen bopp fa kanam Boroom bi, kon dina leen yékkati.
11Neaprunājiet, brāļi, cits citu! Kas savu brāli aprunā vai savu brāli tiesā, tas aprunā likumu un tiesā likumu. Bet ja tu likumu tiesā, tad tu neesi likuma pildītājs, bet tiesātājs.
11 Yéen bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa moroom mbaa nga ñaaw njort, ba àtte ko, diiŋat nga yoonu Yàlla te àtte ko; ku àtte yoon wi nag sàmmoo ko, waaye danga koo àtte.
12Viens ir Likumdevējs un Tiesātājs, kas var pazudināt un glābt.
12 Kenn rekk mooy tëral yoon, kooku rekk mooy àtte; moo man a musle, moo man a alage. Te sax yaw miy àtte sa bokk yaay kan?
13Bet kas tu esi, kas tiesā tuvāko? Lūk, jūs, kas sakāt: Šodien vai rīt mēs dosimies uz to pilsētu un pavadīsim tur kādu gadu, tirgosimies un gūsim peļņu.
13 Léegi nag dégluleen, yéen ñiy wax ne: «Tey walla ëllëg dinanu dem ca dëkk sàngam, def fa at, di fa sàkku xaalis ci jula.»
14Jūs neziniet, kas būs rīt.
14 Ndax dangeen a xam seen ëllëg? Te luy seen dund? Xanaa cóola doŋŋ luy naaw ci diir bu gàtt, daldi naaxsaay.
15Jo kas ir jūsu dzīve? Garaiņi, kas īsu brīdi redzami un tad izzūd. Tai vietā jums būtu jāsaka: Ja Kungam labpatiksies un dzīvi būsim, tad darīsim to vai citu.
15 Lii kay ngeen waroon a wax: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund, tey def nàngam ak nàngam.»
16Bet tagad jūs savā augstprātībā lielaties. Katra tāda lielība ir ļauna.
16 Waaye fi mu ne, naagu ngeen bay damu, te damoo noonu baaxul.
17Kas zina labu darīt, bet to nedara, tam ir grēks.
17 Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko, bàkkaar nga.