1Pēc tam Kungs nozīmēja vēl citus septiņdesmit divus un sūtīja viņus pa diviem sava vaiga priekšā visās pilsētās un vietās, kur Viņš domāja iet.
1 Gannaaw loolu Boroom bi tànn na yeneen juróom-ñaar-fukki taalibe ak ñaar, yebal leen, ñu ànd ñaar ak ñaar, jiituji ko ca dëkk yépp ak ca bérab yépp, ya mu naroon a dem moom ci boppam.
2Un Viņš tiem sacīja: Pļaujamā daudz, bet strādnieku maz. Lūdziet tad pļaujas Kungu, lai Viņš sūta strādniekus savā pļaujā!
2 Mu ne leen: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.
3Ejiet! Lūk, es jūs sūtu kā jērus vilku starpā.
3 Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki.
4Nenesiet līdz nedz naudas maku, nedz somu, nedz kurpes un nevienu ceļā nesveiciniet!
4 Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay dàll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi.
5Un kur jūs kādā namā ieiesiet, vispirms sakiet: miers šim namam!
5 «Kër gu ngeen man a dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.”
6Un ja tur būs miera bērns, jūsu miers mitēs pār viņu; bet ja nē, tad tas atgriezīsies jūsos.
6 Bu fa nitu jàmm nekkee, seen yéene dina ko indil jàmm. Lu ko moy, seen yéene dina dellusi ci yéen.
7Bet tanī pat namā palieciet un ēdiet, un dzeriet, kas viņiem ir, jo strādnieks ir savas algas cienīgs! Nestaigājiet no vienas mājas otrā!
7 Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër.
8Un ja jūs ieiesiet kādā pilsētā un jūs tur uzņems, ēdiet, ko jums liks priekšā!
8 «Dëkk bu ngeen man a dugg, te waa dëkk ba teeru leen, lu ñu leen jox, lekkleen ko.
9Un dziediniet slimos, kas tanī ir, un sakiet viņiem: Dieva valstība jums tuvu klāt!
9 Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.”
10Bet ja jūs ieiesiet kādā pilsētā, un viņi jūs neuzņems, izgājuši tās gatvēs, sakiet:
10 Waaye bu ngeen duggee ci dëkk te teeruwuñu leen, demleen ca mbedd ya te ne leen:
11Pat putekļus, kas no jūsu pilsētas mums pielipuši, mēs nokratām uz jums; tomēr to ziniet, ka Dieva valstība ir tuvu!
11 “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne, nguuru Yàlla jegesi na.”
12Es jums saku, ka Sodomai tai dienā būs vieglāk nekā šai pilsētai.
12 Maa ngi leen koy wax, bu bés baa, waa Sodom ñooy tane dëkk boobu.
13Bēdas tev, Horacina! Bēdas tev Betsaida, jo, ja Tirā un Sidonā būtu notikuši tie brīnumi, kas notika jūsos, tad tās jau sen, rupjās drēbēs un pelnos sēdot, gandarītu par grēkiem.
13 «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon tuub nañu seeni bàkkaar bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
14Tiešām Tirai un Sidonai tiesas dienā būs vieglāk nekā jums.
14 Moona ca bés pénc ba, Tir ak Sidon ñoo leen di tane.
15Un tu, Kafarnauma, kas līdz debesīm esi paaugstināta, tiksi nogremdēta līdz pat ellei.
15 Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe.
16Kas jūs klausa, tas mani klausa; un kas jūs nicina tas nicina mani; bet kas mani nicina tas nicina to, kas mani sūtījis.
16 «Ku leen déglu, déglu na ma; ku leen bañ, bañ na ma. Te ku ma bañ, bañ na ki ma yónni.»
17Bet tie septiņdesmit divi atgriezās un priecādamies sacīja: Kungs, pat ļaunie gari mums Tavā vārdā padodas.
17 Juróom-ñaar-fukki taalibe yi ak ñaar dellusi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.»
18Un Viņš tiem sacīja: Es redzēju sātanu kā zibeni no debesīm krītam.
18 Yeesu ne leen: «Maa ngi doon séen Seytaane wàcce asamaan ni safaras melax.
19Lūk, es jums devu varu pār katru ienaidnieka spēku un čūsku un skorpiju samīšanai, un nekas jums nekaitēs.
19 Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen man a gaañ.
20Tomēr nepriecājieties par to, ka gari jums pakļauti, bet priecājieties, ka jūsu vārdi ierakstīti debesīs!
20 Moona li leen rab yi déggal, bumu tax ngeen bég, waaye bégleen ndax li ñu bind seen tur ci asamaan.»
21Tanī pat brīdī Viņš gavilēja Svētajā Garā un sacīja: Es godāju Tevi, Tēvs, debess un zemes Kungs, ka Tu to apslēpi gudrajiem un mācītājiem, bet atklāji mazajiem! Tiešām, Tēvs, jo tas Tev tā labpaticis!
21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gune yi. Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.»
22Mans Tēvs visu man atdevis; un neviens nezina, kas ir Dēls, kā tikai Tēvs; un kas ir Tēvs, kā tikai Dēls un kam Dēls to vēlas atklāt.
22 Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn mënul a xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn mënul a xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgg a xamal.»
23Un Viņš, griezdamies pie saviem mācekļiem, sacīja: Svētīgas tās acis, kas redz to, ko jūs redzat!
23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen ñoom rekk: «Ñi seeni bët di gis li ngeen di gis, am nañu mbég.
24Jo es jums saku, ka daudzi pravieši un ķēniņi vēlējās redzēt, ko jūs redzat, un nav redzējuši, un dzirdēt to, ko jūs dzirdat, un nav dzirdējuši.
24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare bëggoon nañoo gis li ngeen di gis, waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg, waaye dégguñu ko.»
25Un, lūk, kāds likumu pazinējs piecēlās, un, Viņu kārdinādams, sacīja: Mācītāj, ko man darīt, lai es iemantotu mūžīgo dzīvi?
25 Noonu benn xutbakat daldi jóg, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: «Kilifa gi, lan laa war a def, ba am dund gu dul jeex?»
26Bet Viņš tam sacīja: Kas bauslībā rakstīts? Kā tu lasi?
26 Yeesu ne ko: «Lu ñu bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy jàng?»
27Un tas atbildēja un sacīja: Mīli Kungu, savu Dievu, no visas savas sirds un no visas savas dvēseles, un ar visu savu spēku, un ar visu savu prātu, un savu tuvāko - kā sevi pašu.
27 Nit ka ne ko: « “Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»
28Un Viņš tam sacīja: Tu pareizi atbildēji; dari tā, un tu dzīvosi!
28 Yeesu ne ko nag: «Li nga wax dëgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba fàww.»
29Bet viņš, gribēdams sevi attaisnot, sacīja Jēzum: Un kas tad ir mans tuvākais?
29 Waaye xutbakat ba bëggoon a am aw lay, ne Yeesu: «Kan mooy sama moroom nag?»
30Tad Jēzus iesāka un sacīja: Kāds cilvēks, iedams no Jeruzalemes uz Jēriku, iekrita slepkavu rokās. Tie viņu aplaupīja un ievainoja, un, atstājuši pusdzīvu, aizgāja.
30 Yeesu tontu ko ne: «Dafa amoon nit ku jóge woon Yerusalem, jëm Yeriko. Ay sàcc dogale ko, futti ko, dóor ko ba muy bëgg a dee, dem bàyyi ko fa.
31Bet gadījās, ka kāds priesteris gāja pa to pašu ceļu un, viņu ieraudzījis, pagāja garām.
31 Faf ab saraxalekat jaar ca yoon wa, séen nit ka, teggi.
32Tāpat arī levīts, kad bija tanī vietā, viņu redzēdams, pagāja garām.
32 Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca bérab booba, séen waa ja, teggi.
33Bet kāds samarietis, iedams savu ceļu, nonāca pie viņa un, to ieraudzījis, apžēlojās.
33 Waaye benn waay bu dëkk Samari bu doon tukki, ñëw ba jege waa ja, gis ko, yërëm ko.
34Un tas, piegājis klāt, apsēja viņa brūces, ieliedams tanīs eļlu un vīnu, un, uzcēlis viņu savā lopā, aizveda to mājvietā un rūpējās par viņu.
34 Noonu mu ñëw, diw ko diwlin ak biiñ ngir faj gaañu-gaañu ya, bandaas ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo.
35Bet otrā dienā viņš, izvilcis divus denārijus, deva tos mājas saimniekam, sacīdams: Gādā par viņu, un, ko tu vairāk izdosi, es, kad atgriezīšos, atdošu tev.
35 Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”»
36Kā tev šķiet, kurš no šiem trim bija tuvākais tam, kas iekrita slepkavu rokās?
36 Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?»
37Un viņš atbildēja: Tas, kas viņam parādīja žēlsirdību. Un Jēzus viņam sacīja: Ej, un tu dari tāpat!
37 Xutbakat ba tontu ko ne: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»
38Bet notika, ka, tālāk iedami, viņi nonāca kādā miestā; un kāda sieviete, vārdā Marta, uzņēma Viņu savā namā.
38 Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn dëkk, fekk fa jigéen ju tudd Màrt, ganale ko.
39Un viņai bija māsa, vārdā Marija, kas, apsēdusies pie Kunga kājām, klausījās Viņa vārdos.
39 Màrt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci tànki Boroom bi, di déglu ay kàddoom.
40Bet Marta, nopūlējusies, lai viņu labāk apkalpotu, pienāca un sacīja: Kungs, vai Tev nerūp, ka mana māsa atstājusi mani, lai es viena kalpotu? Saki jel viņai, lai viņa man palīdz!
40 Fekk Màrt jàpp lool ca waañ wa. Noonu mu ñëw ci wetu Yeesu ne ko: «Boroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji bàyyi ma ak liggéey bi yépp? Ne ko mu jàpple ma.»
41Un Kungs viņai atbildēja, sacīdams: Marta, Marta, tu rūpējies un pūlies par daudz lietām,
41 Boroom bi tontu ko ne: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu.
42Bet tikai viena ir nepieciešama. Marija izvēlējusies sev labāko daļu; tā viņai netiks atņemta.
42 Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom.»