1Tanī dienā Jēzus izgāja no mājas un apsēdās jūrmalā.
1 Bés booba Yeesu génnoon na ca kër ga, toog ca wetu dex ga.
2Un daudz ļaužu sapulcējās ap Viņu. Tāpēc Viņš iekāpa laivā un apsēdās. Visi ļaudis stāvēja krastā.
2 Mbooloo mu bare dajaloo ca moom, ba tax mu dugg cig gaal, toog; mbooloo mépp taxaw ca tefes ga.
3Un Viņš daudz runāja tiem līdzībās, sacīdams: Lūk, sējējs izgāja sēt.
3 Noonu Yeesu dégtal leen lu bare ciy léeb ne leen: «Dafa amoon beykat bu demoon jiyi.
4Viņam sējot, cita nokrita ceļmalā, un debess putni nāca un to apēda.
4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi ñëw, lekk ko lépp.
5Cita krita akmenājā, kur nebija daudz zemes, un tūliņ uzdīga, jo tā nebija dziļi zemē.
5 Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.
6Kad uzlēca saule, tā novīta un nokalta, jo tai nebija saknes.
6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.
7Bet cita krita starp ērkšķiem, un ērkšķi uzauga un to nomāca.
7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko.
8Bet cita krita labā zemē un nesa augļus: cita simtkārtīgus, cita sešdesmitkārtīgus, cita trīsdesmitkārtīgus.
8 Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom-benn-fukk, li ci des fanweer.
9Kam ausis dzirdēšanai, lai dzird!
9 Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
10Un Viņa mācekļi piegājuši sacīja Viņam: Kāpēc Tu tiem runā līdzībās?
10 Bi Yeesu waxee ba noppi, ay taalibeem jegeñsi, laaj ko lu tax mu di leen wax ciy léeb.
11Viņš atbildēja un sacīja tiem: Jums dots saprast debesvalstības noslēpumus, bet viņiem nav dots.
11 Noonu mu tontu leen ne: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
12Jo kam ir, tam tiks dots, lai būtu pārpilnībā, bet kam nav, no tā tiks atņemts arī tas, kas viņam ir.
12 Ndaxte ku am, dinañu la dollil, ba nga barele; waaye ku amul, li nga am as néew, dinañu ko nangu.
13Tāpēc es runāju viņiem līdzībās, jo tie redzēdami neredz, dzirdēdami nedzird un arī nesaprot.
13 “Dañuy xool te duñu gis, di déglu waaye duñu dégg te duñu xam,” moo tax ma di leen wax ciy léeb.
14Un izpildīsies viņos Isaja pravietojums, kas saka: ar dzirdi jūs dzirdēsiet, bet nesapratīsiet; skatīdamies redzēsiet, bet nesaredzēsiet.
14 Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan:“Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.
15Jo šīs tautas sirds ir nocietināta, un ar ausīm viņi grūti dzird, un savas acis viņi aizver, lai acīm neredzētu un ar ausīm nedzirdētu, un sirdī nesaprastu un neatgrieztos, lai es viņus izdziedinātu.
15 Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.”
16Svētīgas ir jūsu acis, jo tās redz, un jūsu ausis, jo tās dzird.
16 «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg!
17Patiesi es jums saku: daudzi pravieši un taisnīgie vēlējās redzēt, ko jūs redzat, bet nav redzējuši, un dzirdēt, ko jūs dzirdat, un nedzirdēja.
17 Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, ay yonent yu bare ak nit ñu jub ñu bare bëggoon nañu gis li ngeen di gis waaye gisuñu ko, te dégg li ngeen di dégg waaye dégguñu ko.
18Tad nu klausieties līdzību par sējēju!
18 «Yéen nag dégluleen li léebu beykat biy tekki.
19Pie ikviena, kas vārdu par valstību dzird, bet to nesaprot, nāk ļaunais un izrauj to, kas bija iesēts viņa sirdī. Šis ir tas, kas ceļmalā bija iesēts.
19 Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
20Bet iesētais akmenājā ir tas, kas vārdu dzird un tūliņ to priekā pieņem.
20 Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw;
21Bet tanī nav saknes, tas nav pastāvīgs. Tiklīdz sākas bēdas un vajāšanas vārda dēļ, viņš tūdaļ ieļaunojas.
21 waaye du yàgg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi, mu dàggeeku ci saa si.
22Bet starp ērkšķiem sētais ir tas, kas vārdu dzird, bet šīs pasaules rūpes un bagātības viltība nomāc vārdu; un viņš nenes augļus.
22 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ.
23Bet labā zemē sētais ir tas, kas vārdu dzird un to saprot, un nes augļus: cits simtkārtīgus, cits sešdesmitkārtīgus, bet cits trīsdesmitkārtīgus.
23 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom-benn-fukk mbaa fanweer.»
24Citu līdzību Viņš teica tiem, sacīdams: Debesvalstība pielīdzināma cilvēkam, kas labu sēklu iesēja savā tīrumā.
24 Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
25Bet kamēr ļaudis gulēja, atnāca viņa ienaidnieks un iesēja nezāli starp kviešiem, un aizgāja.
25 Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem.
26Bet kad labība uzauga un deva augļus, tad parādījās arī nezāle.
26 Bi dugub ji saxee nag, jëmb bi saxaale ak moom.
27Tad pienāca nama tēva kalpi un sacīja viņam: Kungs, vai tu neiesēji labu sēklu savā tīrumā? No kurienes tad radās nezāle?
27 «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?”
28Viņš tiem sacīja: Cilvēks, ienaidnieks, to padarīja. Bet kalpi sacīja viņam: Ja vēlies, mēs iesim un to izravēsim.
28 Mu tontu leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?”
29Bet viņš sacīja: Nē, lai jūs, ravējot nezāli, kopā ar to neizrautu arī kviešus.
29 Waaye mu tontu leen: “Déedéet, ngir bañ a buddiwaale dugub ji, bu ngeen koy dindi.
30Ļaujiet abiem augt līdz pļaujas laikam! Un pļaujas laikā es teikšu pļāvējiem: savāciet vispirms nezāli un sasieniet to kūlīšos sadedzināšanai, bet kviešus sakraujiet manā šķūnī.
30 Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: Jëkkleen a dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.”»
31Vēl citu līdzību Viņš tiem stāstīja, sacīdams: Debesvalstība pielīdzināma sinepju graudam, ko cilvēks paņēma un iesēja savā tīrumā.
31 Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
32Šī gan ir mazākā no visām sēklām, bet kad tā izaug, tā lielāka par visiem dārza stādiem un kļūst koks, tā ka debess putni nāk un dzīvo tā zaros.
32 Doomu fuddën moo gën a tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
33Citu līdzību Viņš tiem sacīja: Debesvalstība pielīdzināma raugam, ko sieviete ņem un iejauc trijos mēros miltu, iekams viss sarūgst.
33 Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
34Šo visu Jēzus runāja ļaudīm līdzībās; un bez līdzībām Viņš tiem nerunāja nekā,
34 Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb.
35Lai piepildītos, ko pravietis priekšsludinājis, sacīdams: Es atdarīšu savu muti līdzībās, atklāšu to, kas no pasaules radīšanas bija apslēpts.
35 Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan:«Dinaa leen wax ciy léeb,di yégle yëf yu nëbbuli dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.»
36Tad Viņš, atlaidis ļaudis, iegāja namā, un Viņa mācekļi piegāja pie Viņa un sacīja: Izskaidro mums līdzību par nezāli tīrumā!
36 Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.»
37Viņš atbildēja un sacīja tiem: Cilvēka Dēls ir tas, kas sēj labo sēklu.
37 Noonu Yeesu tontu leen ne: «Doomu nit ki mooy ji jiwu wu baax wi;
38Bet tīrums ir pasaule, un labā sēkla - valstības bērni, bet nezāle ir ļaunā bērni.
38 àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi;
39Bet ienaidnieks, kas to sējis, ir sātans. Pļauja ir pasaules gals, bet pļāvēji ir eņģeļi.
39 Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi.
40Kā nezāles savāc un ugunī sadedzina, tā tas notiks arī pasaules beigās.
40 Ni ñu dajalee jëmb ba, lakk ko, noonu lay nekke, bu àddina tukkee.
41Cilvēka Dēls izsūtīs savus eņģeļus, un tie salasīs Viņa valstībā visus apgrēcības un netaisnības darītājus
41 Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar,
42Un iemetīs tos uguns krāsnī. Tur būs raudāšana un zobu griešana.
42 sànni leen ci safara; foofa dees na fa jooy te yéyu.
43Tad taisnīgie spīdēs kā saule sava Tēva valstībā. Kam ausis dzirdēšanai, lai dzird!
43 Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
44Debesvalstība pielīdzināma tīrumā apslēptai mantai, ko cilvēks atrod un paslēpj; un viņš, būdams priecīgs par to, iet un pārdod visu, kas viņam ir, un pērk šo tīrumu.
44 Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
45Vēl debesvalstība pielīdzināma tirgotājam, kas meklē labas pērles.
45 «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet.
46Un viņš, atradis vienu dārgu pērli, aizgāja un pārdeva visu, kas viņam bija, un nopirka to.
46 Am bés mu gis per buy jar njëg gu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
47Vēl debesvalstība pielīdzināma jūrā izmestam tīklam, kas savāc visāda veida zivis.
47 Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk.
48Un viņi, kad tas bija pilns, izvilkuši un krastā sēdēdami, labās savāca traukos, bet sliktās izmeta ārā.
48 Bi mbaal mi feesee nag, ñu ñoddi ko ci tefes gi, ba noppi ñu taxaw, dajale yu baax yi ciy ndab, waaye sànni yi bon.
49Tā tas būs arī pasaules beigās: eņģeļi izies un no taisnīgo vidus atšķirs ļaunos,
49 Noonu lay mel, bu àddina tukkee. Malaaka yi dinañu génn, tànn ñu bon ñi ci biir ñu jub ñi,
50Un iemetīs viņus uguns krāsnī; tur būs raudāšana un zobu griešana.
50 sànni leen ci safara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.»
51Vai jūs visu to sapratāt? Tie atbildēja Viņam: Jā gan!
51 Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu tontu ko: «Waaw.»
52Viņš tiem sacīja: Tāpēc ikviens rakstu mācītājs, kas mācīts debesvalstībai, pielīdzināms nama tēvam, kas no sava mantu krājuma izceļ jauno un veco.
52 Yeesu ne leen: «Kon xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
53Un notika, kad Jēzus šīs līdzības bija beidzis, ka Viņš aizgāja no turienes.
53 Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa,
54Un Viņš, nonācis savā dzimtenē, mācīja tos viņu sinagogās tā, ka tie brīnījās un sacīja: No kurienes Viņam tāda gudrība un spēks?
54 dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële?
55Vai Viņš nav galdnieka dēls? Vai Viņa māte nesaucas Marija un Viņa brāļi Jēkabs un Jāzeps, un Sīmanis, un Jūda?
55 Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
56Un vai Viņa māsas nav visas pie mums? No kurienes tad Viņam tas viss?
56 Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?»
57Un tie ieļaunojās no Viņa. Bet Jēzus sacīja viņiem: Pravietis nav bez cieņas, bet ne savā tēvzemē un savās mājās.
57 Kon ñu daldi koy xeeb.Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.»
58Un Viņš tur nedarīja daudz brīnumu viņu neticības dēļ.
58 Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi.