1Bet rīta agrumā visi augstie priesteri un tautas vecākie apspriedās par Jēzu, lai Viņu nodotu nāvei.
1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yépp ak njiiti xeet wa gise, ngir fexee reylu Yeesu.
2Un tie, saistījuši Viņu, aizveda un nodeva zemes pārvaldniekam Poncijam Pilātam.
2 Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma.
3Tad Jūdass, Viņa nodevējs, redzēdams, ka Viņš notiesāts, žēluma pamudināts, aiznesa trīsdesmit sudraba gabalus augstajiem priesteriem
3 Bi nga xamee ne Yudaa, mi woroon Yeesu, gis na ne, daan nañu ko, mu am naqaru xol. Mu dem nag ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya, delloo leen fanweeri poset yu xaalis,
4Un sacīja: Es esmu grēkojis, nododams nevainīgas asinis. Bet tie sacīja: Kāda mums daļa? Skaties pats!
4 ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu tontu ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.»
5Un viņš, nometis sudraba gabalus svētnīcā, aizgāja un pakārās cilpā.
5 Noonu Yudaa sànni xaalis ba ca kër Yàlla ga, jóge fa, dem, takk buum ci baatam, xaru.
6Bet augstie priesteri paņēma sudraba gabalus un sacīja: Nav brīv tos mest upurlādē, jo tā ir asins nauda.
6 Saraxalekat yu mag ya nag fab xaalis ba, naan: «Jaaduwul nu def xaalis bii ci dencukaayu xaalis bi ci kër Yàlla gi, ndaxte njëgu deret la.»
7Un apspriedušies viņi nopirka par tiem podnieka tīrumu svešinieku kapsētai.
7 Ñu daldi diisoo nag, jënd ca xaalis ba toolu defarkatu ndaa ya, ngir di fa suul doxandéem ya.
8Tāpēc šis tīrums līdz šai dienai saucas Hakeldama, tas ir, asins tīrums.
8 Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret.
9Tā piepildījās pravieša Jeremija sludinājums, kas saka: Un tie saņēma trīsdesmit sudraba gabalus, novērtētā maksu, kādu Izraēļa dēli bija noteikuši,
9 Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njëg gi bànni Israyil xayma woon ci nit ki;
10Un atdeva tos par podnieka tīrumu, kā Kungs man pavēlējis.
10 ñu joxe ko ngir toolu defarkatu ndaa ya, ni ma ko Boroom bi sante.»
11Bet Jēzus nostājās zemes pārvaldnieka priekšā; un pārvaldnieks Viņam jautāja, sacīdams: Vai Tu esi jūdu ķēniņš? Jēzus viņam atbildēja: Tu to saki.
11 Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanamu boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko; «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
12Un kad augstie priesteri un vecākie Viņu apsūdzēja, Viņš nekā neatbildēja.
12 Yeesu tontu ko ne: «Wax nga ko,» waaye tontuwul dara ca la ko saraxalekat yu mag ya ak njiit ya jiiñ.
13Tad Pilāts sacīja Viņam: Vai Tu nedzirdi, cik smagu liecību viņi nodod pret Tevi?
13 Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo lépp li ñu la jiiñ?»
14Un Viņš tam neatbildēja ne uz vienu vārdu, tā ka pārvaldnieks ļoti brīnījās.
14 Waaye Yeesu tontuwu ko ci dara, ba tax boroom réew ma waaru lool.
15Bet augstos svētkos zemes pārvaldnieks mēdza atbrīvot vienu cietumnieku, kuru viņi vēlējās.
15 Ca màggal gu nekk nag boroom réew ma daan na may mbooloo ma, ñu tànn kenn ca ña ñu tëjoon, mu daldi leen ko bàyyil.
16Bet tanī laikā viņam bija sevišķi ļaunas slavas cietumnieks, vārdā Baraba.
16 Fekk booba amoon nañu ku ñu tëjoon, ku siiw te tudd Barabas.
17Un kad viņi bija sapulcējušies, Pilāts sacīja tiem: Kuru jūs gribat, lai es jums atlaižu, Barabu vai Jēzu, kuru sauc Kristus?
17 Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?»
18Jo viņš zināja, ka tie skaudības dēļ Viņu bija nodevuši.
18 Ndaxte xamoon na ne, kiñaan rekk a taxoon, ñu jébbal ko ko.
19Bet kad viņš sēdēja soģa krēslā, viņa sieva sūtīja pie tā, sacīdama: Neaiztiec šo Taisnīgo, jo es šodien sapnī Viņa dēļ daudz cietu!
19 Te it bi mu toogee sax ca jalu àttekaay ba, jabaram yónnee ci moom ne ko: «Bul dugg ci yëfi ku jub kooku, ndaxte tey gént naa ci moom te sonn naa ci lool.»
20Bet augstie priesteri un vecākie pamudināja tautu, lai tā pieprasa Barabu, bet Jēzu nogalina.
20 Waaye saraxalekat yu mag ya ak njiit ya xiir mbooloo ma, ñu laaj Barabas te reylu Yeesu.
21Un zemes pārvaldnieks atbildēja un sacīja viņiem: Kuru no šiem diviem gribat, lai es jums atlaižu? Bet viņi sacīja: Barabu.
21 Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu tontu ko: «Barabas.»
22Pilāts viņiem sacīja: Ko tad man darīt ar Jēzu, kas saucas Kristus?
22 Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp tontu ko ne: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
23Visi viņi sacīja: Sist Viņu krustā! Zemes pārvaldnieks viņiem sacīja: Ko tad Viņš ļaunu darījis? Bet viņi vēl skaļāk kliedza un sacīja: Sist Viņu krustā!
23 Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gën a kawe naan: «Daaj ko ci bant!»
24Bet Pilāts, redzēdams to, ka viņš nekā nepanāk, bet troksnis pavairojas, ņēma ūdeni, mazgāja rokas tautas priekšā, sacīdams: Es esmu nevainīgs pie šī Taisnīgā asinīm. Skatieties paši!
24 Naka Pilaat xam ne, du ci man dara, fekk na sax yengu-yengu bi gën a am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanamu mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.»
25Un visi ļaudis atbildēja un sacīja: Viņa asinis lai nāk pār mums un pār mūsu bērniem.
25 Ñépp tontu ko: «Na deretam dal ci sunu kaw ak sunu kaw njaboot.»
26Tad viņš tiem atlaida Barabu, bet Jēzu, šaustītu, nodeva tiem, lai Viņu sit krustā.
26 Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas, mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant.
27Tad pārvaldnieka kareivji ņēma Jēzu tiesas namā un sapulcināja pie Viņa visu pulku.
27 Bi ñu ko defee xarekati boroom réew ma fab Yeesu, yóbbu ko ci biir kër ga, ñu daldi woo mbooloom xarekat ya yépp ci moom.
28Un tie, izģērbuši Viņu, apvilka Viņam purpura mēteli.
28 Noonu ñu summi ko, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
29Un tie, nopinuši kroni no ērkšķiem, lika to Viņam galvā un niedri Viņa labajā rokā. Un tie, Viņa priekšā ceļos mezdamies, izsmēja Viņu, sacīdami: Esi sveicināts, jūdu ķēniņ!
29 Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndeyjooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
30Un tie spļāva uz Viņu, paņēma niedri un sita Viņam pa galvu.
30 Ba noppi ñu daldi tifli ci kawam, fab bantu xat ba, dóor ko ci boppam.
31Un tie, kad bija Viņu izsmējuši, novilka Viņam mēteli un ietērpa Viņu Viņa paša drēbēs un aizveda, lai Viņu sistu krustā.
31 Bi ñu ko ñaawalee ba noppi, ñu summi mbubbum xarekat ma, solalaat ko ay yéreem, yóbbu ko, ngir daaj ko ci bant.
32Bet izgājuši, viņi sastapa cilvēku no Kirēnes, vārdā Sīmani; tie piespieda šo nest Viņa krustu.
32 Bi nga xamee ne génn nañu, ñu daje ak nit ku dëkk Siren te tudd Simoŋ; ñu ga ko, ngir mu gàddu bant, ba ñu war a daaj Yeesu.
33Un viņi nonāca tai vietā, ko sauc par Golgātu, tas ir, Kalvārijas vietu.
33 Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «Bérabu kaaŋu bopp.»
34Un tie Viņam deva dzert vīnu, sajauktu ar žulti. Un Viņš, baudījis, negribēja to dzert.
34 Bi ñu fa eggee, ñu jox ko biiñ, ñu def ci lu wex. Waaye bi mu ko mosee, nanguwu koo naan.
35Bet kad tie bija Viņu krustā piesituši, tie lozējot izdalīja Viņa drēbes, lai izpildītos pravieša priekšsludinājums, kas saka: Viņi izdalīja manas drēbes un par maniem svārkiem meta kauliņus.
35 Noonu ñu daaj ko ca bant ba, ñu daldi séddoo ay yéreem, tegoo ko ay bant,
36Un tie sēdēja un apsargāja Viņu.
36 ba noppi toog fa, di ko wottu.
37Un virs Viņa galvas tie uzlika Viņa vainas uzrakstu: Šis ir Jēzus, jūdu ķēniņš.
37 Te it ñu teg ci kaw boppam mbind, mu xamle lu tax ñu rey ko, mu ne: «Kii mooy Yeesu, buuru Yawut yi.»
38Tad divi slepkavas reizē ar Viņu tika sisti krustā: viens pa labi, otrs pa kreisi.
38 Booba it ñu daajaale ak moom ñaari taskati réew ma, kenn ci ndeyjooram, ka ca des ci càmmooñam.
39Bet garāmgājēji zaimoja Viņu, galvas kratīdami,
39 Ña fa doon romb di ko xas, di wëcc seen bopp ndax sib ko,
40Un sacīja: Tu, kas noplēs Dieva svētnīcu un to trijās dienās atkal uzcel, atpestī pats sevi! Ja Tu esi Dieva Dēls, nokāp no krusta!
40 naan: «Yaw mi man a toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi.»
41Tāpat augstie priesteri ar rakstu mācītājiem un vecākie izsmiedami sacīja:
41 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya it di ko ñaawal naan:
42Citiem Viņš palīdzēja, pats sev nevar palīdzēt. Ja Viņš ir Izraēļa ķēniņš, lai nokāpj tagad no krusta, un mēs ticēsim Viņam.
42 «Waa jii musal na ñeneen te mënul a musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko.
43Viņš paļāvās uz Dievu, lai tagad glābj, ja Viņš to vēlas, jo Viņš sacījis: Es esmu Dieva Dēls.
43 Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”»
44Bet arī slepkavas, kas līdz ar Viņu bija krustos piesisti, tāpat nievāja Viņu.
44 Taskati réew ma it, ya ñu daajaale ak moom, di ko xas noonule.
45Bet no sestās stundas tumsa iestājās pār visu zemi līdz pat devītajai stundai.
45 La tàmbalee digg-bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
46Bet ap devīto stundu Jēzus sauca stiprā balsī, sacīdams: Eli, Eli, lema sabahtani? Tas ir: Mans Dievs, mans Dievs, kāpēc Tu mani atstāji?
46 Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
47Bet daži, kas tur stāvēja, to dzirdēdami, teica: Viņš sauc Eliju.
47 Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Iliyas.»
48Un tūdaļ viens no tiem aizskrēja, paņēma sūkli, piesūcināja to etiķī, uzsprauda niedrē un deva Viņam dzert.
48 Ca saa sa kenn ci ñoom daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci kaw bant, jox ko ko, mu muucu.
49Bet citi sacīja: Pagaidi, redzēsim, vai Elijs nāks Viņu glābt.
49 Waaye ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ba xam Iliyas dina ñëw, musal ko.»
50Bet Jēzus atkal sauca skaļā balsī un atdeva savu garu.
50 Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
51Un, lūk, svētnīcas priekškars pārplīsa divās daļās no augšas līdz apakšai, un zeme trīcēja, un klintis plīsa,
51 Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yengu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku,
52Un kapi atvērās, un daudz svēto miesas, kas dusēja, uzcēlās no miroņiem.
52 te ñu bare ci jëmmi nit ñu sell ñu dee, dekki.
53Un pēc Viņa augšāmcelšanās tie izgāja no kapiem, nāca svētajā pilsētā un parādījās daudziem.
53 Te gannaaw ndekkitel Yeesu ñu génn ca bàmmeel ya, dugg ca dëkk bu sell ba, te feeñu ñu bare.
54Bet virsnieks un tie, kas ar Viņu bija, sargāja Jēzu un, redzēdami zemestrīci un visu, kas notika, ļoti izbijās un sacīja: Patiesi, Viņš bija Dieva Dēls.
54 Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yengu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.»
55Bet tur bija daudz sieviešu no tālienes, kas pavadīja Jēzu no Galilejas un kalpoja Viņam.
55 Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dand, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo.
56Starp tām bija Marija Magdalēna un Marija, Jēkaba un Jāzepa māte, un Zebedeja dēlu māte.
56 Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, ndeyu Saag ak Yuusufa, ak ndeyu doomi Sebede ya.
57Bet vakaram iestājoties, nāca kāds bagāts cilvēks no Arimatejas, vārdā Jāzeps, kas arī bija Jēzus māceklis.
57 Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon.
58Viņš aizgāja pie Pilāta un izlūdzās Jēzus miesas. Tad Pilāts pavēlēja miesas atdot.
58 Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Pilaat santaane, ñu jox ko ko.
59Un kad Jāzeps saņēma miesas, viņš ietina tās tīrā audeklā.
59 Noonu Yuusufa fab jëmm ja, laxas ko ci càngaay lu set,
60Un viņš ielika tās savā jaunajā kapā, ko bija izcirtis klintī. Un viņš, pievēlis kapa durvīm lielu akmeni, aizgāja.
60 dugal ko ca bàmmeel bu bees, ba mu yettaloon boppam ciw doj. Mu béraŋ doj wu mag ca buntu bàmmeel ba, dem.
61Bet tur bija Marija Magdalēna un otra Marija; viņas sēdēja iepretim kapam.
61 Fekk Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des ñoo fa toogoon janook bàmmeel ba.
62Bet otrā dienā, kas ir pēc sataisīšanās dienas, augstie priesteri un farizeji sapulcējās pie Pilāta
62 Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat.
63Un sacīja: Kungs, mēs atminējāmies, ka šis viltnieks, vēl dzīvs būdams, sacīja: Pēc trim dienām es augšāmcelšos.
63 Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.”
64Tāpēc pavēli apsargāt kapu līdz trešajai dienai, ka kādreiz neatnāk Viņa mācekļi un nenozog Viņu, un nepasaka tautai: Viņš uzcēlies no miroņiem. Tad pēdējā viltība būtu lielāka nekā pirmā.
64 Danoo bëggoon nag, nga santaane, ñu wottu bàmmeel ba, ba am ñetti fan, ngir bañ taalibeem ya ñëw, sàcc néew ba, tey yégle ne dekki na. Bu ko defee nax bu mujj boobu dina yées bu jëkk ba.»
65Pilāts viņiem atbildēja: Ņemiet sardzi, ejiet un apsargājiet, kā zināt!
65 Pilaat tontu leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.»
66Un viņi aizgāja, pielika kapam sardzi un apzīmogoja akmeni.
66 Noonu ñu dem, tëj bàmmeel ba bu wóor, ñu tay ca doj wa màndarga, teg fa wottukat ya.