1Bądźcie naśladowcami moimi, jakom i ja Chrystusowy;
1 Royleen ma nag, ni may roye Kirist.
2A chwalę was, bracia! iż pamiętacie wszystkie moje nauki, a jakom wam podał, podania trzymacie.
2 Maa ngi leen di sant ci li ngeen may fàttaliku ci lépp, ak ci li ngeen di topp dénkaane, yi ma leen dénk.
3A chcę, abyście wiedzieli, iż każdego męża głową jest Chrystus, a głową niewiasty mąż, a głową Chrystusową Bóg.
3 Waaye nag bëgg naa ngeen xam lii: Kirist mooy kilifag bépp góor, góor di kilifag jigéen, te Yàlla di kilifag Kirist.
4Każdy mąż, gdy się modli albo prorokuje z przykrytą głową, szpeci głowę swoję.
4 Kon nag góor guy ñaan Yàlla, walla muy wax ci kàddug Yàlla, fekk mu teg dara ci boppam, day suufeel Kirist, kilifaam.
5I każda niewiasta, gdy się modli albo prorokuje, nie nakrywszy głowy swojej, szpeci głowę swoję; boć to jedno, a toż samo jest, jakoby ogolona była.
5 Waaye bu jigéen musóoruwul, buy ñaan walla buy wax ci kàddug Yàlla, kooku day suufeel jëkkëram jiy kilifaam, ndaxte day mel ni jigéen ju ñu wat.
6Albowiem jeźli się nie nakrywa niewiasta, niechże się też strzyże; a jeźli szpetna rzecz jest niewieście, strzyc się albo golić, niechże się nakrywa.
6 Jigéen ju dul musóoru, bu yaboo, mu watu. Waaye su fekkee ne jigéen dafay am kersa, su wàññee kawaram walla mu watu, fàww kon mu musóoru.
7Albowiem mąż nie ma nakrywać głowy, gdyż jest wyobrażeniem i chwałą Bożą; ale niewiasta jest chwałą mężową.
7 Góor nag moom warul a teg dara ci boppam, ndaxte mooy melokaanu Yàlla te dafay wone ndamu Yàlla. Jigéen moom dafay wone ndamu góor.
8Bo mąż nie jest z niewiasty, ale niewiasta z męża.
8 Ndaxte jëlewuñu góor ci jigéen, waaye jigéen lañu jële ci góor.
9Albowiem mąż nie jest stworzony dla niewiasty, ale niewiasta dla męża.
9 Te sàkkuñu góor ngir jigéen, waaye jigéen lañu sàkk ngir góor.
10A przetoż niewiasta powinna mieć władzę na głowie dla Aniołów.
10 Looloo tax jigéen war a teg ci kaw boppam luy màndargaal kilifteef ga, ndax malaaka yi.
11A wszakże mąż nie jest bez niewiasty, ani niewiasta nie jest bez męża w Panu.
11 Teewul nag ci sunu booloo ak Boroom bi, jigéen a ngi wéeru ci góor, te góor a ngi wéeru ci jigéen.
12Albowiem jako niewiasta z męża jest, tak też mąż przez niewiastę; jednak wszystkie rzeczy są z Boga.
12 Ni ñu sàkke jigéen ci góor, noonu la góor juddoo ci jigéen, te lépp a ngi jóge ca Yàlla.
13Sami u siebie rozsądźcie, przystoili niewieście bez nakrycia modlić się Bogu?
13 Seetleen mbir mii: ndax jekk na jigéen bañ a musóoru, buy ñaan Yàlla?
14Azaż was i samo przyrodzenie nie uczy, iż mężowi, gdyby włosy zapuszczał, jest mu ku zelżywości?
14 Xanaa du àddina ci boppam dafa leen di won ne, gàcce la ci góor, ngir muy yar kawar gu bare?
15Ale niewiasta, jeźli zapuszcza włosy, jest jej ku poczciwości, przeto iż jej włosy dane są za przykrycie.
15 Waaye loolu nag ab taar la ci jigéen. Dañoo jagleel jigéen kawar gu gudd, muy muuraay ci moom.
16A jeźliby się kto zdał być swarliwym, my takiego obyczaju nie mamy, ani zbory Boże.
16 Waaye su kenn bëggee werante ci mbir moomu, na xam lii: amunu beneen aada ci njàng mi, du nun walla mboolooy Yàlla.
17A to opowiadając nie chwalę, że się nie ku lepszemu, ale ku gorszemu schodzicie.
17 Bi may tollu ci ndigal yi, mënuma leen a sant, ndaxte seeni ndaje loraange lañuy jur, waaye du njariñ.
18Albowiem najprzód, gdy się wy schodzicie we zborze, słyszę, iż rozerwania bywają między wami, i poniekąd wierzę.
18 Ci bu jëkk dégg naa lii: bu ngeen di daje, am na ci yéen ñuy féewaloo, te xaw naa koo gëm.
19Bo muszą być kacerstwa między wami, aby ci, którzy są doświadczeni, byli jawnymi między wami.
19 Fàww mu am ay féewaloo ci seen biir, ngir ñu man a xàmmi ñi neex Yàlla ci yéen.
20Gdy się wy tedy wespół schodzicie, nie jest to używać wieczerzy Paóskiej.
20 Bu ngeen dajee, mënuleen a wax ne reeru Boroom bi ngeen di lekk.
21Albowiem każdy wieczerzę swoję pierwej zjada i jeden łaknie, a drugi jest pijany.
21 Ndaxte bu ngeen dee lekk, ku nekk dafay gaawantu di lekk reeram, ba tax ñenn ñaa ngi xiif, fekk ñeneen di màndi.
22Azaż domów nie macie do jedzenia i do picia? Albo zborem Bożym gardzicie i zawstydzacie tych, którzy nie mają? Cóż wam rzekę? Pochwalęż was? W tem nie chwalę.
22 Xanaa amuleen kër yu ngeen di lekke ak di naane? Walla ndax dangeen a xeeb mbooloom Yàlla? Walla ngeen bëgg a rusloo ñi amul dara? Lu ma leen ci war a wax nag? Ma gërëm leen ci loolu? Mukk! Gërëmuma leen.
23Albowiem jam wziął od Pana, com też wam podał, iż Pan Jezus tej nocy, której był wydan, wziął chleb,
23 Li ma jële ci Boroom bi, moom laa leen jottali: Boroom bi Yeesu, ci guddi gi ñu ko woree, dafa jël mburu,
24A podziękowawszy, złamał i rzekł: Bierzcie, jedzcie; to jest ciało moje, które za was bywa łamane; to czyócie na pamiątkę moję.
24 sant Yàlla, damm ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
25Także i kielich, gdy było po wieczerzy mówiąc: Ten kielich jest nowy testament we krwi mojej; to czyócie, ilekroć pić będziecie, na pamiątkę moję
25 Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees, gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret. Defleen lii ngir fàttaliku ma.»
26Albowiem ilekroć byście jedli ten chleb i ten kielich byście pili, śmierć Paóską opowiadajcie, ażby przyszedł.
26 Ndaxte saa su ngeen di lekk mburu mii, walla ngeen di naan ci kaas bii, yéena ngi yégle deewu Boroom bi, ba kera muy ñëw.
27A tak, kto by jadł ten chleb, albo pił ten kielich Paóski niegodnie, będzie winien ciała i krwi Paóskiej.
27 Kon nag képp ku jekkadi ni mu lekke ci mburu mi te naane ni ci kaasu Boroom bi, tooñ nga yaramu Boroom bi ak deretam.
28Niechże tedy człowiek samego siebie doświadczy, a tak niech je z chleba tego i z kielicha tego niechaj pije.
28 Na ku nekk seetlu boppam nag, sog a lekk ci mburu mi te naan ci kaas bi.
29Albowiem kto je i pije niegodnie, sąd sobie samemu je i pije, nie rozsądzając ciała Paóskiego.
29 Ku lekk mburu mi, naan ci kaas bi, fekk faalewuloo solos yaramu Kirist wi, sa lekk ak sa naan dina xëcc àtteb Yàlla ci sa kaw.
30Dlatego między wami wiele jest słabych i chorych, i niemało ich zasnęło.
30 Looloo tax ñu bare ci yéen wopp te ñàkk doole, ba ñenn ñi faatu.
31Bo gdybyśmy się sami rozsądzali, nie bylibyśmy sądzeni.
31 Su nu doon seetlu sunu bopp ni mu ware, kon àtte du nu dal.
32Lecz gdy sądzeni bywamy, od Pana bywamy ćwiczeni, abyśmy z światem nie byli potępieni.
32 Waaye bu nu Boroom bi dee àtte, da nuy yar ngir bañ noo boole ci mbugalu àddina.
33Ale tak, bracia moi! gdy się schodzicie ku jedzeniu, oczekiwajcie jedni drugich.
33 Noonu nag bokk yi, bu ngeen dajee, di lekk reeru Boroom bi, nangeen xaarante.
34A jeźli kto łaknie, niechże je w domu, abyście się na sąd nie schodzili. A inne rzeczy, gdy przyjdę, postanowię.
34 Ku xiif, na lekke këram, ngir bañ a indi ci yéen àtteb Yàlla ndax seen ndaje yi. Yeneen fànn yi ci des nag, bu ma ñëwee ci yéen, dinaa ko seet.