Slovakian

Wolof: New Testament

1 John

2

1Moje dieťatká, toto vám píšem nato, abyste nezhrešili. A keby niekto zhrešil, máme prímluvcu u Otca, Ježiša Krista, spravedlivého.
1 Samay doom, maa ngi leen di bind yëf yii, ngir ngeen bañ a def bàkkaar. Waaye su kenn defee bàkkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Kirist mu jub mi.
2A on je smierením za naše hriechy, no, nie len za naše, ale aj za hriechy celého sveta.
2 Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy bàkkaar, te du sax sunuy bàkkaar rekk, waaye yu àddina sépp.
3A potom známe, že sme ho poznali, keď zachovávame jeho prikázania.
3 Ci lii lanu xame ne, xam nanu ko: sàmm ay ndigalam.
4Kto hovorí: Znám ho, a jeho prikázaní nezachováva, je lhár, a v tom niet pravdy.
4 Ku wax ne xam nga ko, te sàmmoo ay ndigalam, dangay fen, te dëgg nekkul ci yaw.
5Ale kto zachováva jeho slovo, v tom je po pravde láska Božia dokonaná. Po tom známe, že sme v ňom.
5 Kuy sàmm kàddug Yàlla, dëgg-dëgg sa mbëggeel ci Yàlla mat na sëkk. Ci loolu lanu xame ne, nekk nanu ci moom.
6Ten, kto hovorí, že zostáva v ňom, je povinný, jako on chodil, i sám tak chodiť.
6 Ku wax ne ci Yàlla nga sax, fàww nga dund, ni Yeesu Kirist daan dunde moom ci boppam.
7Milovaní [bratia], nepíšem vám nového prikázania, ale staré prikázanie, ktoré ste mali od počiatku. A tým starým prikázaním je slovo, ktoré ste počuli od počiatku.
7 Samay soppe, li ma leen di bind du ndigal lu bees, waaye ndigal lu yàgg la; la ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu yàgg loolu, mooy kàddu gi ngeen déggoon.
8A zase vám píšem nové prikázanie, čo je pravdivé v ňom i vo vás, že tma ta ide, a pravé svetlo už svieti.
8 Teewul ndigal lu bees laa leen di bind, lu amoon ci dundu Yeesu, te am it ci seen dund; ndaxte lëndëm gaa ngi wéy, te leer gu wóor gi fenk na xaat.
9Ten, kto hovorí, že je vo svetle a nenávidí svojho brata, je vo tme až doteraz.
9 Ku wax ne yaa ngi ci leer, tey bañ sa mbokk, yaa ngi ci lëndëm ba tey.
10Kto miluje svojho brata, zostáva vo svetle, a niet v ňom pohoršenia.
10 Kuy sopp sa mbokk, yaa ngi dëkk ci leer, te luy yóbbe nit bàkkaar du nekk ci yaw.
11Ale ten, kto nenávidí svojho brata, je vo tme a chodí vo tme a nevie, kam ide, lebo tma oslepila jeho oči.
11 Waaye kuy bañ sa mbokk, ci lëndëm nga nekk, di ci dox, te xamoo foo jëm, ndax lëndëm muur na say bët.
12Píšem vám, dieťatká, že sú vám odpustené hriechy pre jeho meno.
12 Samay doom, maa ngi leen di bind,ndax baalees na leen seeni bàkkaar ci turu Kirist.
13Píšem vám, otcovia, že ste poznali toho, ktorý je od počiatku. Píšem vám, mládenci, že ste zvíťazili nad tým zlým.
13 Maa ngi leen di bind, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Maa ngi leen di bind, yéen waxambaane yi,ndax daaneel ngeen Ibliis.
14Píšem vám, deti, že ste poznali Otca. Písal som vám, otcovia, že ste poznali toho, ktorý je od počiatku. Písal som vám, mládenci, že ste silní, a že slovo Božie zostáva vo vás, a zvíťazili ste nad tým zlým.
14 Bind naa leen, samay doom,ndax xam ngeen Yàlla Baay bi.Bind naa leen, yéen baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca njàlbéen ga ba tey.Bind naa leen, yéen waxambaane yi,ndax yéena ngi dëgër,ndax kàddug Yàllaa ngi dëkk ci yéen,te daaneel ngeen Ibliis.
15Nemilujte sveta ani vecí, ktoré sú na svete. Keď niekto miluje svet, nie je v ňom lásky Otcovej.
15 Buleen sopp àddina ak li ci biiram. Ku sopp àddina, mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom.
16Lebo nič z toho, čo je na svete - žiadosť tela, žiadosť očí a chlúbna pýcha života, nie je z Otca, ale je zo sveta.
16 Ndaxte lépp lu nekk ci àddina, maanaam bëgg-bëggu yaram ak xemmemu bët ak réyug àddina, loolu du jóge ci Baay bi waaye ci àddina.
17A svet ide ta i jeho žiadosť, ale ten, kto činí vôľu Božiu, trvá na veky.
17 Te àddina day wéy, waaye kuy def coobareg Yàlla dinga sax ba fàww.
18Deti, je posledná hodina, a ako ste počuli, že prijde antikrist, i teraz už povstali mnohí antikristovia, odkiaľ známe, že je posledná hodina.
18 Samay doom, waxtu wu mujj wi jot na! Dégg ngeen ne, benn Bañaaleb Kirist dina ñëw; te dëgg la, bañaaley Kirist yu bare feeñ nañu. Ci loolu lanu xame ne, waxtu wu mujj wi jot na.
19Z nás vyšli, ale neboli z nás, lebo keby boli bývali z nás, boli by zostali s nami. Ale aby sa ukázali, že nie sú všetci z nás.
19 Ci sunu biir lañu jóge, waaye bokkuñu woon ci nun; ndaxte su ñu bokkoon ci nun, kon dinañu des ci nun. Waaye dàggeeku nañu nu, ngir mu leer ne, kenn ci ñoom bokkul woon ci nun.
20A vy máte pomazanie od Svätého a viete všetko.
20 Yéen nag, Aji Sell ji sol na leen Xelam, te yéen ñépp am ngeen xam-xam.
21Nepísal som vám preto, že neznáte pravdy, ale že ju znáte, a že niktorá lož nie je z pravdy.
21 Bind naa leen, du ndax xamuleen dëgg, waaye ndax xam ngeen ko, xam it ne wenn fen du jóge ci dëgg.
22A kto je lhár, ak nie ten, kto zapiera, že Ježiš nie je Kristus? To je ten antikrist, kto zapiera Otca i Syna.
22 Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Bañaaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji.
23Nikto, kto zapiera Syna, nemá ani Otca; kto vyznáva Syna, má aj Otca.
23 Ku weddi Doom ji, amuloo itam Baay bi; ku seedeel Doom ji, am nga it Baay bi.
24A tak tedy vy, čo ste počuli od počiatku, to nech zostáva vo vás. Keď zostane vo vás to, čo ste počuli od počiatku, aj vy zostanete v Synovi aj Otcovi.
24 Yéen nag, la ngeen déggoon ca ndoorte la, na sax ci yéen. Loolu ngeen déggoon ca ndoorte la, su saxee ci yéen, dingeen sax yéen itam ci Doom ji ak ci Baay bi.
25A toto je to zasľúbenie, ktoré nám on zasľúbil, večný život.
25 Te li mu nu digoon mooy lii: dund gu dul jeex.
26Toto som vám napísal o tých, ktorí vás zvodia.
26 Bind naa leen lii ci mbirum ñi leen di bëgg a réeral.
27A vy, to pomazanie, ktoré ste dostali od neho, zostáva vo vás, a nepotrebujete, aby vás niekto učil, ale jako vás učí to isté pomazanie o všetkom, a je pravdivé a nie je lžou, a jako vás naučilo, tak zostanete v ňom.
27 Yéen nag, Xel mi leen Kirist sol a ngi dëkk ci yéen, te soxlawuleen kenn jàngal leen dara. Waaye Xel mi mu leen sol, mi ngi leen di jàngal lépp, te li mu leen di jàngal mooy dëgg; kon nag saxleen ci moom, ni mu leen ko jàngale.
28A teraz, dieťatká, zostávajme v ňom, aby sme, keď sa ukáže, mali smelú dôveru a neboli zahanbení pred ním, keď prijde.
28 Gannaaw loolu nag yéen samay doom, saxleen ci Kirist, ngir bés bu feeñee, nu am kóolute ci kanamam te bañ a rus ba sëngéem cig dikkam.
29Keď viete, že je spravedlivý, že každý, kto činí spravedlivosť, narodil sa z neho.
29 Gannaaw xam ngeen ne ku jub la, dingeen xam it ne, képp kuy def lu jub juddu nga ci moom.