Slovakian

Wolof: New Testament

1 Timothy

1

1Pavel, apoštol Ježiša Krista podľa nariadenia Boha, našeho Spasiteľa, a Pána Ježiša Krista, našej nádeje,
1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci ndigalu Yàlla sunu Musalkat ak Kirist Yeesu sunu yaakaar,
2Timoteovi, svojmu pravému dieťaťu vo viere: milosť, milosrdenstvo, pokoj od Boha, nášho Otca, a od Krista Ježiša, nášho Pána.
2 maa ngi lay bind Timote, yaw miy sama doomu diine ju wér. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
3Jako som ťa prosil, keď som išiel do Macedonie, žeby si zostal v Efeze, aby si prikázal niektorým, aby neučili iného učenia
3 Xam nga ne, ba may dem diiwaanu Maseduwan, ñaanoon naa la, nga des dëkku Efes, ngir dénk ña fa doon jàngale luy sànke, ñu bàyyi ko.
4ani nedbali na bájky a na rodopravy, nemajúce konca - kraja, ktoré poskytujú skôr škriepky než správu Božiu vo viere.
4 Te it nga dénk leen, ñu bañ a topp léebi diiney neen ak limi maam yu dul jeex mukk. Loolu werante rekk lay jur, waaye du jëme kanam mbir mi Yàlla tëral, wéer ko ci ngëm.
5Ale cieľom prikázania je láska z čistého srdca a dobrého svedomia a z nepokryteckej viery,
5 Waaye li sunuy dénkaane di jur mooy mbëggeel gu jóge ci xol bu laab, ci xel mu dal ak ci ngëm gu wér.
6od čoho niektorí sťa od cieľa zablúdili a uchýlili sa k márnosloviu
6 Am na ñu moy loolu, ba jeng jëm ciy waxi neen.
7a chcúc byť učiteľmi zákona, kým nerozumejú, ani čo hovoria ani čo tvrdia.
7 Dañoo sababloo nekk ay jàngalekat ci yoonu Musaa, fekk xamuñu dara sax ci li ñuy wax ak a dëggal.
8Ale vieme, že zákon je dobrý, keby ho niekto zákonne používal,
8 Ci li aju ci yoonu Musaa nag, xam nanu ne baax na, ci ku koy jëfe ni ko Yàlla tërale.
9vediac to, že zákon nie je daný pre spravedlivého, ale pre bezzákonných a nepoddajných, pre bezbožných a hriešnych, pre nesvätých a obecných, pre otcovrahov a materovrahov a pre vrahov vôbec,
9 Xam nanu it ne, tëddul ngir ñi jub waaye ngir ñi jubadi ak ñi déggadi, ñi weddi tey bàkkaar, ñi selladi te fonkadi Yàlla, ñiy dóor ndey walla baay, ak ñiy bóom;
10pre smilníkov, samcoložníkov, pre tých, ktorí kupčia s ľuďmi, pre lhárov, krivoprísažníkov, a jestli je čo iné, čo sa protiví zdravému učeniu
10 ngir ñiy doxaan, ñi góor-jigéenu ak ñiy def nit jaam, ñiy fen tey wann seen kàddu, ak lépp luy juuyoo ak njàngale mu wér
11podľa evanjelia slávy blahoslaveného Boha, ktorým to evanjeliom som ja poverený.
11 mu xebaar bu baax bi indaale. Te xamleb xebaar, boobuy feeñal ndamu Yàlla Aji Tedd ji, dénk nañu ma ko.
12A ďakujem tomu, ktorý ma posilnil, Kristu Ježišovi, nášmu Pánovi, že ma povážil za verného a postavil do služby,
12 Maa ngi gërëm sunu Boroom Kirist Yeesu, mi ma dooleel, ci kóolute gi mu am ci man, ba fal ma jawriñ.
13ktorý som bol predtým ruhač a prenasledovník a trýzniteľ, ale som dostal milosrdenstvo, lebo som to robil v nevedomosti v nevere.
13 Moona daa naa suufeel turam, di fitnaal ak a toroxal ñi ko gëm. Waaye Yàlla yërëm na ma, ndaxte ñàkka xam ak ñàkka gëm rekk a taxoon ma def ko.
14Ale sa preveľmi rozmnožila milosť našeho Pána s vierou a láskou, ktorá je v Kristu Ježišovi.
14 Te yiwu sunu Boroom baawaan na ci man, ànd ak ngëm ak mbëggeel, yi bawoo ci Kirist Yeesu.
15Verné je to slovo a hodno každého prijatia, že Kristus Ježiš prišiel na svet spasiť hriešnikov, z ktorých prvý som ja.
15 Wax ju wóor a ngii te yelloo gépp kóolute: Kirist Yeesu ganesi na àddina, ngir musal bàkkaarkat yi, te maa ci raw!
16Ale preto som dostal milosrdenstvo, aby na mne prvom dokázal Ježiš Kristus celú zhovievavosť za príklad tým, ktorí majú veriť v neho cieľom večného života.
16 Waaye Yàlla yërëm na ma, ngir Kirist Yeesu jëkk a feeñal ci man muñam gu yaatu gi, ma nekk royukaay ci ñi ko nar a gëm te am dund gu dul jeex.
17A Kráľovi vekov, neporušiteľnému, neviditeľnému, jedinému, múdremu Bohu, česť a sláva na veky vekov. Ameň.
17 Yaw Buur bi fiy sax ba abadan, yaw mi bët mënta gis, yaw Yàlla miy kenn, yaa yelloo teraanga ak ndam ba fàww. Amiin!
18Toto prikázanie ti predkladám, dieťa Timotee, podľa predošlých, na teba sa vzťahujúcich sa proroctiev, aby si v nich bojoval dobrý boj
18 Kon nag Timote sama doom, loolu mooy sas wi ma lay dénk, te mu dëppook waxi yonent, yi jëmoon ci yaw. Doolewool wax yooyu, ba xeex xeex bu baax bi,
19majúc vieru a dobré svedomie, ktoré odstrčiac niektorí od seba stroskotali čo do viery,
19 di sàmm sa ngëm ak xel mu dal. Am na ñu seen xel nëx, ba labal seen ngëm,
20z ktorých je Hymeneus a Alexander, ktorých som vydal satanovi, aby sa naučili nerúhať sa.
20 naka Imene ak Alegsàndar; jébbal naa leen Seytaane, ngir ñu réccu li ñu doon sosal Yàlla.