1Prvú knihu som napísal, Teofíle, o všetkom, čo započal Ježiš činiť a učiť,
1 Yaw Teyofil, téere bu jëkk, ba ma bindoon, ëmb na lépp li Yeesu tàmbali woon a jëf ak a jàngale,
2až do toho dňa, ktorého vzatý bol hore do neba, keď už bol dal skrze Svätého Ducha prikázania apoštolom, ktorých si vyvolil,
2 ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon.
3ktorým sa aj zjavoval živý po svojom utrpení mnohými dôkazmi ukazujúc sa im štyridsať dní a hovoriac s nimi o kráľovstve Božom.
3 Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent-fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.
4A shromažďujúc sa s nimi prikazoval im, aby neodchádzali z Jeruzalema, ale aby čakali zasľúbenie Otcovo, o ktorom zasľúbení ste vraj počuli od mňa;
4 Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.
5totiž že Ján krstil vodou, ale vy budete pokrstení Svätým Duchom už o nie mnoho dní.
5 Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»
6A oni síduc sa pýtali sa ho a vraveli: Pane, či v tomto čase obnovíš Izraelovi kráľovstvo?
6 Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»
7A on im povedal: To nie je vašou vecou zvedieť časy alebo jednotlivé doby, ktoré si Otec uložil vo svojej vlastnej moci,
7 Mu tontu leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.
8ale prijmete moc Svätého Ducha, ktorý prijde na vás, a budete mi svedkami i v Jeruzaleme i po celom Judsku i v Samárii a tak až do poslednej končiny zeme.
8 Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»
9A keď to povedal, zdvihnutý bol hore, kým oni hľadeli na to, a podňal ho oblak a vzal zpred ich očí.
9 Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët.
10A jako v tom, čo odchádzal, upretým zrakom hľadeli do neba, tu hľa, dvaja mužovia sa postavili vedľa nich v bielom rúchu,
10 Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.
11ktorí aj povedali: Galilejskí mužovia, čo tu stojíte a hľadíte do neba? Tento Ježiš, ktorí bol vzatý od vás hore do neba, prijde tak, ako ste ho videli ísť do neba.
11 Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina dellusi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.»
12Vtedy sa vrátili do Jeruzalema s vrchu, zvaného Olivového, ktorý je blízko Jeruzalema, na cestu sobotného dňa od neho.
12 Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem.
13A keď vošli do mesta, vyšli do vrchnej dvorany, kde sa zdržovali Peter a Jakob a Ján a Andrej, Filip a Tomáš, Bartolomeus a Matúš, Jakob Alfeov a Šimon Zelóta, Horlivec, a Júdas Jakobov.
13 Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.
14Títo všetci zotrvávali jednomyseľne na modlitbe a v pokornej prosbe so ženami a s Máriou, matkou Ježišovou, i s jeho bratmi.
14 Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.
15A v tých dňoch vstal Peter v strede učeníkov (a bol tam vovedne zástup tak asi sto dvadsať duší) a povedal:
15 Ca bés yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni téeméer ak ñaar-fukk.
16Mužovia bratia, muselo sa naplniť písmo, ktoré predpovedal Svätý Duch skrze ústa Dávidove o Judášovi, ktorý sa stal vodcom tým, ktorí zajali Ježiša,
16 Mu ne leen: «Bokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda, fàww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat ñi jàpp Yeesu
17pretože bol počítaný k nám a bol dostal podiel na tejto službe.
17 te mu bokkoon ci nun, ba am cér ci liggéey bi.»
18Ten si teda nadobudol pole za mzdu neprávosti a svaliac sa strmhlav rozpukol sa napoly, a vykydly sa všetky jeho vnútornosti.
18 --Pey gi Yudaa jotoon ci ñaawteefam, mu jënd ci tool, daanu fa, ba fàcc, ay buttitam tuuru.
19A stalo sa to známym všetkým, ktorí bývajú v Jeruzaleme, takže je nazvané to pole ich vlastným nárečím: Akeldama, to jest Pole krvi.
19 Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret.» —
20Lebo je napísané v knihe žalmov: Nech je jeho príbytok pustý, a nech nie je nikoho, kto by býval v ňom! a: Jeho biskupstvo nech vezme iný!
20 Piyeer teg ca ne: «Ndaxte lii lañu bind ci téereb Sabóor:“Na këram gental,bu fa kenn dëkk.” Te it:“Na keneen bey sasam.”
21Musí teda jeden z týchto mužov, ktorí sa s nami schádzali po celý čas, v ktorom Pán Ježiš vchádzal a vychádzal, žil a obcoval medzi nami,
21 Kon ñeel na nu, nu tànn kenn ci ñi bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir,
22počnúc od krstu Jánovho až do dňa, v ktorom bol vzatý od nás hore do neba, byť s nami svedkom jeho zmŕtvychvstania.
22 li dale ci bi ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jële ci sunu biir, yéege ko. Kooku war na ànd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.»
23A tak postavili dvoch, Jozefa, zvaného Barsabáša, ktorý mal prímeno Justus, Spravedlivý, a Mateja.
23 Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.
24A pomodliac sa povedali: Ty, Pane, ktorý znáš srdcia všetkých ľudí, ukáž, prosíme, z týchto dvoch toho jedného, ktorého si si vyvolil,
24 Ñu ñaan ci Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu nit ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,
25aby dostal podiel na tejto službe a na apoštolstve, odkiaľ odstúpil Judáš, aby odišiel na svoje vlastné miesto.
25 mu yenu liggéeyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko bàyyi, dem bérabam.»
26A dali im losy, a los padol na Mateja, a bol spolu počítaný s jedonástimi apoštolmi.
26 Noonu ñu boole leen, tegoo ay bant, bant ba dal ca Macas, mu fekki fukki ndaw ya ak benn.