Slovakian

Wolof: New Testament

Hebrews

13

1Bratská láska nech zostáva.
1 Saxleen ci bëggante ni ay bokk.
2Nezabúdajte na pohostinnosť, lebo ňou niektorí, nevediac, pohostili anjelov.
2 Buleen fàttee teral ñiy ñëw ci yéen, ndaxte ñenn ñi, bi ñu ko defee, teral nañu ay malaaka te xamuñu ko.
3Pamätajte na väzňov ako spoluuväznení, na tých, ktorí sú v trápení, jako takí, ktorí ste aj sami v tele.
3 Fàttalikuleen ñi ñu tëj, mel ni su ñu leen boole woon ak ñoom tëjaale. Fàttalikuleen ñi ñuy sonal, ni su ngeen bokkoon ak ñoom coono.
4Manželstvo nech je v úcte u všetkých a loža nepoškvrnená. A smilníkov a cudzoložníkov bude súdiť Bôh.
4 Na ñépp fullaal séy, te lalu séy bi bañ a taq sobe, ndaxte Yàlla dina àtte ñu yàqu ñi ak njaalookat yi.
5Spôsob vašeho obcovania nech je prostý lakomstva, a majte dosť na tom, čo máte. Lebo on povedal: Nenechám ťa cele iste ani ťa neopustím,
5 Buleen bëgge; deeleen doylu, ndaxte Yàlla ci boppam nee na:«Duma la wacc mukk,duma la wor mukk,»
6takže môžeme smele hovoriť: Pán mi je spomocníkom, a nebudem sa báť. Čo mi urobí človek?!
6 ba tax nu am kóoluteg wax ne:«Boroom bi moo di sama ndimbal;duma ragal dara.Lu ma nit manal?»
7Pamätajte na svojich vodcov, ktorí vám hovorili slovo Božie, a pozorujúc, aký bol ich východ, to jest koniec ich obcovania, nasledujte takú vieru.
7 Fàttalikuleen seen njiit, yi leen yégal kàddug Yàlla. Nemmikuleen li seen dund meññ te roy seen ngëm.
8Ježiš Kristus ten istý včera i dnes i naveky.
8 Yeesu Kirist du soppiku mukk; ni mu mel démb ak tey lay mel ba fàww.
9Rôznymi a cudzími učeniami sa nedajte točiť. Lebo je dobre, aby milosťou bolo upevňované srdce, nie pokrmami, ktoré neprospely tým, ktorí sa nimi zapodievali.
9 Buleen nangu mukk ñu fàbbi leen ak njàngale yu bare yu wuute ak yu jëkk ya. Li gën moo di xol yi jële seen doole ci yiwu Yàlla, te bañ koo jële ci sàrt yi jëm ci ñam, yi jariñul dara ñi koy sàmm.
10Máme oltár, z ktorého jesť nemajú práva tí, ktorí svätoslúžia stánu.
10 Am nanu sarax boo xam ne ñiy jaamu Yàlla ci tàntu màggalukaayu bànni Israyil sañuñu koo lekk.
11Lebo ktorých zvierat krv za hriech sa vnáša najvyšším kňazom do svätyne, tých telá sa pália vonku za táborom.
11 Ndaxte saraxalekat bu mag bi dafay yóbbu deretu mala yi ca bérab bu sell-baa-sell ni sarax ngir dindi bàkkaar yi, waaye yàpp wi dees na ko lakk ca gannaaw dal ba.
12Preto i Ježiš, aby svojou vlastnou krvou posvätil ľud, trpel vonku za bránou.
12 Looloo tax Yeesu sonn ca gannaaw dëkk ba, ngir sellal mbooloo mi ak deretam.
13Vyjdime tedy za ním von za tábor nesúc jeho pohanenie.
13 Nanu ko fekki nag ca gannaaw dal ba, bokk ak moom toroxte ga.
14Lebo tu nemáme zostávajúceho mesta, ale to budúce hľadáme.
14 Amunu fii ci àddina dëkk bu sax ba fàww, waaye nu ngi wut dëkk biy ñëw.
15Tedy skrze neho obetujme vždycky Bohu obeť chvály, to jest ovocie rtov, vyznávajúcich jeho meno.
15 Kon nag nanu jaare ci Yeesu, tey dëkk ci jébbal Yàlla sarax bu koy màggal, maanaam sant turam.
16A na dobročinnosť a na sdielnosť nezabúdajte, lebo v takých obetiach má Bôh záľubu.
16 Buleen fàtte di def lu baax ak di sédde ci seen alal, ndaxte sarax yu mel noonu ñoo neex Yàlla.
17Poslúchajte svojich vodcov a ustupujte im, lebo oni bdejú za vaše duše jako takí, ktorí vydajú počet, aby to robili s radosťou a nevzdychali, lebo to by vám nebolo užitočné.
17 Déggal-leen seeni njiit te topp seen ndigal, ndaxte ñoo leen di sàmm te ñooy layoo seen liggéey. Kon nangeen leen déggal, ngir ñu man a def seen liggéey ak xol bu sedd, bañ cee am naqar, ndaxte loolu du leen amal njariñ.
18Modlite sa za nás, lebo sme si istí toho, že máme dobré svedomie chcúc sa vo všetkom správne chovať.
18 Deeleen nu ñaanal. Wóor nanu ne, sunu xel dal na, ndaxte danoo bëgg a rafet ci lépp lu nuy def.
19A ešte tým viacej prosím, žeby ste to robili, aby som vám bol skôr prinavrátený.
19 Maa ngi leen di xiir, ngeen ñaanal nu, ba tuur ci seen ñaq, ngir ma yiwiku, ba dellusi ci yéen ci ni mu gën a gaawe.
20A Bôh pokoja, ktorý vyviedol toho veľkého Pastiera oviec z mŕtvych na základe krvi večnej smluvy, nášho Pána Ježiša,
20 Na leen Yàlla Boroom jàmm, mi dekkal sunu Boroom Yeesu, di Sàmm bu mag bi, ci darajay deret, ji fas kóllëre gu sax,
21nech vás ráči učiniť dokonalými v každom skutku dobrom, aby ste činili jeho vôľu, pôsobiac vo vás to, čo je ľúbe pred jeho tvárou, skrze Ježiša Krista, ktorému sláva na veky vekov. Ameň.
21 matal ci lépp lu baax, ba ngeen man a def coobareem, di jëfe ci nun li neex ci moom, mu jaarale lépp ci Yeesu Kirist, moom mi yelloo ndam ba fàww. Amiin.
22Ale vás prosím, bratia, zneste slovo napomenutia, lebo i tak som vám len krátko písal.
22 Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan, ngeen tegoo baatu yedd yooyu, ndaxte dama leen a bind ci lu gàtt.
23Vedzte o našom bratovi Timoteovi, že je prepustený, s ktorým, keď prijde skoro, vás uvidím.
23 Xamleen ne, Timote sunu mbokk, génn na kaso. Su dikkee léegi, dinaa ànd ak moom, seetsi leen.
24Pozdravte všetkých svojich vodcov a všetkých svätých. Pozdravujú vás tí z Itálie.
24 Nuyul-leen ma seen njiit yépp ak gaayi Yàlla yépp. Waa Itali ñu ngi leen di nuyu.
25Milosť so všetkými vami. Ameň.
25 Na yiwu Yàlla nekk ànd ak yéen ñépp.