Slovakian

Wolof: New Testament

John

11

1A bol istý nemocný, Lazar z Betánie, z mestečka Márie a Marty, jej sestry.
1 Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Ma nga dëkkoon Betani, moom ak Maryaama ak Màrt, mi mu bokkaloon ndey ak baay.
2To bola tá Mária, ktorá pomazala Pána masťou a poutierala jeho nohy svojimi vlasmi, ktorej brat, Lazar, bol teraz nemocný.
2 Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la càmmiñam Lasaar woppoon.
3Vtedy poslaly k nemu tie sestry a odkázaly mu: Pane, hľa, ten, ktorého máš rád, je nemocný.
3 Ñaari jigéeni Lasaar yónnee ca Yeesu ne ko: «Boroom bi, sa xarit wopp na.»
4A keď to počul Ježiš, povedal: Tá nemoc nie je na smrť, ale na slávu Božiu, aby ňou bol Syn Boží oslávený.
4 Bi Yeesu déggee xebaar boobu, mu ne: «Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji.»
5A Ježiš miloval Martu i jej sestru i Lazara.
5 Yeesu soppoon na Màrt ak Maryaama ak Lasaar.
6Ako tedy počul, že je nemocný, vtedy zostal na mieste, na ktorom bol, dva dni.
6 Bi mu yégee nag ne, Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba mu nekkoon.
7Až potom povedal učeníkom: Poďme zase do Judska.
7 Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.»
8A učeníci mu povedali: Rabbi, len teraz ťa hľadali Židia ukameňovať, a zase ta ideš?
8 Taalibe ya tontu ko ne: «Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wut a rey ak i xeer, nga di fa dellu?»
9Ježiš odpovedal: Či nie je dvanásť hodín dňa? Ak niekto chodí vodne, nezavadí, lebo vidí svetlo tohoto sveta;
9 Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy dox bëccëg, du fakkastalu, ndaxte day gis leeru àddina si.
10ale ak niekto chodí vnoci, zavadí, lebo niet v ňom svetla.
10 Waaye kuy dox guddi, dina fakkastalu, ndaxte leer nekkul ci moom.»
11To povedal a potom im riekol: Lazar, náš priateľ, usnul; ale idem, aby som ho zobudil zo sna.
11 Yeesu wax loolu, teg ca ne: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.»
12Vtedy mu povedali učeníci: Pane, ak usnul, ozdravie.
12 Taalibe ya tontu ne: «Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér.»
13Ale Ježiš povedal o jeho smrti, a oni sa domnievali, že hovorí o spánku sna.
13 Yeesu dafa bëggoon a wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne, mbiri nelaw rekk lay wax.
14A tak vtedy im povedal Ježiš otvorene: Lazar zomrel,
14 Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: «Lasaar dee na.
15a radujem sa pre vás, že som tam nebol, aby ste uverili. Ale poďme za ním!
15 Bég naa ngir yéen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gën a dëgër. Waaye nanu ko seeti.»
16Vtedy povedal Tomáš, zvaný Didymus, spoluučeníkom: Poďme aj my, aby sme zomreli s ním!
16 Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi,» daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!»
17A tak keď prišiel Ježiš, našiel ho už štyri dni ležať v hrobe.
17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne, bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan.
18A Betánia bola blízko Jeruzalema, nejakých pätnásť honov.
18 Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet.
19A mnohí zo Židov boli prišli k Marte a Márii, aby ich potešili ohľadom ich brata.
19 Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfël leen ci seen deewu càmmiñ.
20Vtedy Marta, ako počula, že ide Ježiš, vyšla proti nemu, ale Mária sedela doma.
20 Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga.
21Vtedy povedala Marta Ježišovi: Pane, keby si tu bol býval, môj brat by nebol zomrel.
21 Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.
22Ale aj teraz viem, že všetko, za čokoľvek by si požiadal Boha, dá ti Bôh.
22 Waaye xam naa ne, fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.»
23Ježiš jej povedal: Tvoj brat vstane.
23 Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
24A Marta mu povedala: Viem, že vstane pri vzkriesení, v posledný deň.
24 Màrt tontu ko ne: «Xam naa ne, dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.»
25Ježiš jej povedal: Ja som vzkriesenie i život; ten, kto verí vo mňa, aj keby zomrel, žiť bude.
25 Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.
26A nikto, kto žije a verí vo mňa, nezomrie na veky; či veríš tomu?
26 Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27Riekla mu: Áno, pane; ja som uverila, že si ty Kristus, ten Syn Boží, ktorý mal prijsť na svet.
27 Mu tontu ko ne: «Waaw Boroom bi. Gëm naa ne, yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji war a ñëw àddina.»
28A keď to povedala, odišla a zavolala Máriu, svoju sestru, tajne, povediac: Učiteľ je tu a volá ťa.
28 Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem woowi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
29A tá, jako to počula, vstala rýchle a išla za ním.
29 Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantoo dem ca Yeesu.
30A Ježiš nebol ešte prišiel do mestečka, ale bol ešte na mieste, kde bola vyšla proti nemu Marta.
30 Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt.
31Vtedy Židia, ktorí boli s ňou v dome a tešili ju, vidiac Máriu, že vstala rýchle a vyšla, išli za ňou domnievajúc sa, že ide k hrobu, aby tam plakala.
31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfël Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne, day jooyi ca bàmmeel ba.
32Vtedy Mária, ako prišla ta, kde bol Ježiš, a videla ho, padla k jeho nohám a povedala mu: Pane, keby si tu bol býval, môj brat by nebol zomrel.
32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.»
33Vtedy Ježiš, keď ju videl, že plače, aj Židov, ktorí prišli s ňou, že plačú, zovrel duchom a zachvel sa
33 Yeesu gis ne, mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy.
34a povedal: Kde ste ho položili? A oni mu povedali: Pane, poď a pozri!
34 Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu tontu ko ne: «Kaay gis, Sang bi.»
35A Ježiš zaplakal.
35 Yeesu jooy.
36Vtedy vraveli Židia: Hľa, jako ho mal rád!
36 Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!»
37A niektorí z nich povedali: Či nemohol tento, ktorý otvoril oči slepého, učiniť aj to, aby tento nezomrel?
37 Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax mënul woon a fexe ba Lasaar du dee?»
38Vtedy znova zovrel v sebe Ježiš a prišiel k hrobu. A bola to jaskyňa, a kameň ležal na nej.
38 Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer.
39Ježiš povedal: Zodvihnite kameň! A Marta, sestra zomrelého, mu povedala: Pane, už smrdí, lebo je už štyri dni v hrobe.
39 Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.»
40Na to jej riekol Ježiš: Či som ti nepovedal, že ak budeš veriť, uvidíš slávu Božiu?
40 Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne, boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
41Vtedy zodvihli kameň, kde ležal mŕtvy. A Ježiš pozdvihol oči hore a povedal: Otče, ďakujem ti, že si ma počul.
41 Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi.
42No, ja som vedel, že ma vždy čuješ, ale pre zástup, stojaci okolo, som to povedal, aby uverili, že si ma ty poslal.
42 Xam naa ne, doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne, yaa ma yónni.»
43A keď to povedal, zavolal veľkým hlasom: Lazare, poď von!
43 Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!»
44A zomrelý vyšiel majúc poviazané nohy aj ruky pohrabnými povojmi, a jeho tvár bola ovinutá znojníkom. A Ježiš im povedal: Rozviažte ho a nechajte ho odísť!
44 Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
45Vtedy mnohí zo Židov, ktorí boli prišli za Máriou a videli, čo učinil Ježiš, uverili v neho.
45 Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm.
46Ale niektorí z nich odišli k farizeom a povedali im, čo učinil Ježiš.
46 Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon.
47Vtedy svolali najvyšší kňazi a farizeovia vysokú radu a hovorili: Čo to robíme, že ten človek robí tak mnohé divy?
47 Farisen ya ak saraxalekat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgg a bare. Lu nuy def nag?
48Ak ho necháme takto, všetci uveria v neho, a prijdú Rimania a vezmú i naše miesto i náš národ.
48 Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!»
49A jeden, ktorýsi z nich, Kaifáš, ktorý bol toho roku najvyšším kňazom, im povedal: Vy neviete ničoho
49 Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon saraxalekat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara.
50ani nemyslíte, že nám je užitočné, aby zomrel jeden človek za ľud, a nie aby zahynul celý národ.
50 Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir ñépp, mooy li gën ci yéen? Bu ko defee réew mi du tas.»
51A však toho nepovedal sám od seba, ale súc toho roku najvyšším kňazom zaprorokoval, že Ježiš mal zomrieť za národ.
51 Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon saraxalekat bu mag ba at mooma, moo tax Yàlla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir réew mi.
52No, nie len za národ, ale aby aj rozptýlené deti Božie shromaždil v jedno.
52 Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Yàlla, yi tasaaroo yépp, dajaloo nekk benn.
53A tak od toho dňa sa uradili, aby ho zabili.
53 Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu.
54Preto už viacej nechodil Ježiš verejne medzi Židmi, ale odišiel odtiaľ do kraja blízko púšte, do mesta, zvaného Efraim, a tam sa zdržoval so svojimi učeníkmi.
54 Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndiŋ ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem.
55A bola blízko Veľká noc Židov, a mnohí išli z toho kraja pred Veľkou nocou hore do Jeruzalema, aby sa očistili.
55 Bésu Jéggi ba, di màggalu Yawut ya, mu ngi doon jubsi, ba ñu bare ca waa àll ba di dem Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set.
56Vtedy hľadali Ježiša a shovárali sa jeden s druhým stojac v chráme: Čo sa vám zdá? Že naozaj neprijde na sviatok?
56 Ñu ngi doon wut Yeesu tey waxante ca kër Yàlla ga naan: «Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñëw ci màggal gi walla déet?»
57A jako najvyšší kňazi tak i farizeovia boli už vydali rozkaz, aby to, keby niekto zvedel, kde je, oznámil, aby ho chytili.
57 Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp.