1Y JESUS, seis días antes de la Pascua, vino á Bethania, donde estaba Lázaro, que había sido muerto, al cual había resucitado de los muertos.
1 Juróom benni fan laata màggalu bésub Jéggi ba, Yeesu dem na Betani, dëkku Lasaar, mi mu dekkal.
2E hiciéronle allí una cena y Marta servía, y Lázaro era uno de los que estaban sentados á la mesa juntamente con él.
2 Foofa ñu defaral ko fa reer. Màrt moo ko doon séddale, te Lasaar bokkoon na ca gan ña.
3Entonces María tomó una libra de ungüento de nardo líquido de mucho precio, y ungió los pies de Jesús, y limpió sus pies con sus cabellos: y la casa se llenó del olor del ungüento.
3 Noonu Maryaama daldi jël liibaru latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree-bare. Mu sotti ko ci tànki Yeesu, ba noppi fomp ko ak kawaram. Xetu latkoloñ gi gilli ci kër gi yépp.
4Y dijo uno de sus discípulos, Judas Iscariote, hijo de Simón, el que le había de entregar:
4 Kenn ca taalibey Yeesu ya, muy Yudaa Iskariyo, mi ko nar a wor, daldi ne:
5¿Por qué no se ha vendido este ungüento por trescientos dineros, y se dió á los pobres?
5 «Lu tax jaayewuñu latkoloñ jii peyu atum lëmm, jox ko miskin yi?»
6Mas dijo esto, no por el cuidado que él tenía de los pobres: sino porque era ladrón, y tenía la bolsa, y traía lo que se echaba en ella.
6 Waaye bi muy wax loolu, xalaatul woon miskin yi, ndaxte sàcc la woon; moo yoroon boyetu xaalis bi, te daan ci sàkk.
7Entonces Jesús dijo: Déjala; para el día de mi sepultura ha guardado esto;
7 Waaye Yeesu ne ko: «Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul.
8Porque á los pobres siempre los tenéis con vosotros, mas á mí no siempre me tenéis.
8 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, waaye dungeen ma gis ba fàww.»
9Entonces mucha gente de los Judíos entendió que él estaba allí; y vinieron no solamente por causa de Jesús, mas también por ver á Lázaro, al cual había resucitado de los muertos.
9 Bi ñu yégee ne, Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Betani. Yeesu rekk yóbbuwu leen fa woon, waaye dañoo bëggoon a gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon.
10Consultaron asimismo los príncipes de los sacerdotes, de matar también á Lázaro;
10 Saraxalekat yu mag ya dogu ci ne, dañuy reyaale Lasaar,
11Porque muchos de los Judíos iban y creían en Jesús por causa de él.
11 ndaxte moo waral Yawut yu bare dëddu leen, gëm Yeesu.
12El siguiente día, mucha gente que había venido á la fiesta, como oyeron que Jesús venía á Jerusalem,
12 Ca ëllëg sa mbooloo mu bare, ma ñëwoon ca màggalu bésub Jéggi ba, yég ne Yeesoo ngi jëmsi Yerusalem.
13Tomaron ramos de palmas, y salieron á recibirle, y clamaban: Hosanna, Bendito el que viene en el nombre del Señor, el Rey de Israel!
13 Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na Yàlla barkeel buuru Israyil!»
14Y halló Jesús un asnillo, y se sentó sobre él, como está escrito:
14 Yeesu wut cumbur, war ko; ndaxte Mbind mi nee na:
15No temas, hija de Sión: he aquí tu Rey viene, sentado sobre un pollino de asna.
15 «Buleen ragal, waa Siyon.Gis ngeen, seen buur a ngi ñëw,war mbaam mu ndaw.»
16Estas cosas no las entendieron sus discípulos de primero: empero cuando Jesús fué glorificado, entonces se acordaron de que estas cosas estaban escritas de él, y que le hicieron estas cosas.
16 Yooyu yépp, taalibe ya xamuñu woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu feeñee, ñu fàttaliku ne, Mbind mi yégle woon na loolu ci moom, te amal nañu ko.
17Y la gente que estaba con él, daba testimonio de cuando llamó á Lázaro del sepulcro, y le resucitó de los muertos.
17 Ña nekkoon ak Yeesu ñépp, bi muy wooyee Lasaar mu génn ca bàmmeel ba te mu dekkal ko, demoon nañu, nettali la ñu gis.
18Por lo cual también había venido la gente á recibirle, porque había oído que él había hecho esta señal;
18 Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte yégoon nañu firnde boobu.
19Mas los Fariseos dijeron entre sí: ¿Veis que nada aprovecháis? he aquí, el mundo se va tras de él.
19 Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, mënuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!»
20Y había ciertos Griegos de los que habían subido á adorar en la fiesta:
20 Ca mbooloo ma, amoon na ca ay Gereg yu bokk ca ña ñëwoon Yerusalem ngir jaamu Yàlla diirub màggal ga.
21Estos pues, se llegaron á Felipe, que era de Bethsaida de Galilea, y rogáronle, diciendo: Señor, querríamos ver á Jesús.
21 Ñëw nañu ci Filib, mi dëkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: «Sang bi, danoo bëggoon a gis Yeesu.»
22Vino Felipe, y díjolo á Andrés: Andrés entonces, y Felipe, lo dicen á Jesús.
22 Filib dem wax ko Andare; ñu ànd, waxi ko Yeesu.
23Entonces Jesús les respondió, diciendo: La hora viene en que el Hijo del hombre ha de ser glorificado.
23 Mu tontu leen ne: «Waxtu wi ñu war a feeñale ndamu Doomu nit ki jot na.
24De cierto, de cierto os digo, que si el grano de trigo no cae en la tierra y muere, él solo queda; mas si muriere, mucho fruto lleva.
24 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du man a weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.
25El que ama su vida, la perderá; y el que aborrece su vida en este mundo, para vida eterna la guardará.
25 Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.
26Si alguno me sirve, sígame: y donde yo estuviere, allí también estará mi servidor. Si alguno me sirviere, mi Padre le honrará.
26 Ku bëgg a doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral.
27Ahora está turbada mi alma; ¿y qué diré? Padre, sálvame de esta hora. Mas por esto he venido en esta hora.
27 «Léegi nag damaa jàq. Lu may war a wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nar a xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu.
28Padre, glorifica tu nombre. Entonces vino una voz del cielo: Y lo he glorificado, y lo glorificaré otra vez.
28 Baay, màggalal sa tur!» Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.»
29Y la gente que estaba presente, y había oído, decía que había sido trueno. Otros decían: Angel le ha hablado.
29 Mbooloo ma fa teewoon te dégg baat ba daldi ne: «Dënnu la woon!» Ñeneen naan: «Malaakaa doon wax ak moom.»
30Respondió Jesús, y dijo: No ha venido esta voz por mi causa, mas por causa de vosotros.
30 Waaye Yeesu ne leen: «Taxuma baat boobu jolli, waaye yéena tax.
31Ahora es el juicio de este mundo: ahora el príncipe de este mundo será echado fuera.
31 Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si.
32Y yo, si fuere levantado de la tierra, á todos traeré á mí mismo.
32 Te man, bu ñu ma yékkatee, ma tiim suuf, dinaa wootal nit ñépp ci man.»
33Y esto decía dando á entender de qué muerte había de morir.
33 Ci baat yooyu la doon misaale ni mu war a faatoo.
34Respondióle la gente: Nosotros hemos oído de la ley, que el Cristo permanece para siempre: ¿cómo pues dices tú: Conviene que el Hijo del hombre sea levantado? ¿Quién es este Hijo del hombre?
34 Mbooloo ma tontu ko ne: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga man a waxe ne, “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?»
35Entonces Jesús les dice: Aun por un poco estará la luz entre vosotros: andad entre tanto que tenéis luz, porque no os sorprendan las tinieblas; porque el que anda en tinieblas, no sabe dónde va.
35 Yeesu ne leen: «Leer gi dootul yàgg ak yéen. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir lëndëm bañ leen a bett. Ndaxte kuy dox ci lëndëm doo xam foo jëm.
36Entre tanto que tenéis la luz, creed en la luz, para que seáis hijos de luz. Estas cosas habló Jesús, y fuése, y escondióse de ellos.
36 Kon ci bi ngeen dee am leer gi, gëmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.» Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, nëbbatuji leen.
37Empero habiendo hecho delante de ellos tantas señales, no creían en él.
37 Firnde yi mu leen won yépp taxul ñu gëm ko,
38Para que se cumpliese el dicho que dijo el profeta Isaías: ¿Señor, quién ha creído á nuestro dicho? ¿Y el brazo del Señor, á quién es revelado?
38 ngir li yonent Yàlla Esayi waxoon am:«Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?Kan la Boroom bi won dooleem?»
39Por esto no podían creer, porque otra vez dijo Isaías:
39 Mënuñu woon a gëm, ndaxte Esayi dafa waxaat ne:
40Cegó los ojos de ellos, y endureció su corazón; Porque no vean con los ojos, y entiendan de corazón, Y se conviertan, Y yo los sane.
40 «Yàlla dafa gumbaal seeni bët,def ba ñu dëgër bopp,ngir seeni bët bañ a gis,seen xel bañ a xam,ñu bañ a woññiku ci manngir ma wéral leen.»
41Estas cosas dijo Isaías cuando vió su gloria, y habló de él.
41 Esayi dafa wax loolu, ndaxte gisoon na ndamu Yeesu te mi ngi doon wax ci ay mbiram.
42Con todo eso, aun de los príncipes, muchos creyeron en él; mas por causa de los Fariseos no lo confesaban, por no ser echados de la sinagoga.
42 Fekk na ci biir njiit yi sax, ñu bare gëmoon nañu Yeesu, waaye Farisen yee tax fésaluñu ko, ndaxte dañoo ragaloon, ñu dàq leen ca jàngu ba.
43Porque amaban más la gloria de los hombres que la gloria de Dios.
43 Ngërëmu nit a leen gënaloon ngërëmu Yàlla.
44Mas Jesús clamó y dijo: El que cree en mí, no cree en mí, sino en el que me envió;
44 Yeesu yégle ne: «Ku ma gëm, gëmuloo ma waaye gëm nga ki ma yónni.
45Y el que me ve, ve al que me envió.
45 Ku ma gis, gis nga ki ma yónni.
46Yo la luz he venido al mundo, para que todo aquel que cree en mí no permanezca en tinieblas.
46 Ni ag leer laa wàcce ci àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm.
47Y el que oyere mis palabras, y no las creyere, yo no le juzgo; porque no he venido á juzgar al mundo, sino á salvar al mundo.
47 Ku dégg samay wax te toppu leen, du man maa koy daan, ndaxte wàccuma ngir daan àddina, waaye damaa ñëw ngir musal ko.
48El que me desecha, y no recibe mis palabras, tiene quien le juzgue: la palabra que he hablado, ella le juzgará en el día postrero.
48 Ku ma beddeeku te nanguwul samay wax, dina fekk fii li koy daan: sama njàngalee koy daan keroog bés bu mujj ba.
49Porque yo no he hablado de mí mismo; mas el Padre que me envió, él me dió mandamiento de lo que he de decir, y de lo que he de hablar.
49 Ndaxte waxuma ci sama coobare, waaye Baay bi ma yónni ci boppam, moo ma sant li ma war a wax ak li ma war a jàngale.
50Y sé que su mandamiento es vida eterna: así que, lo que yo hablo, como el Padre me lo ha dicho, así hablo.
50 Te xam naa ne, li muy santaane day joxe dund gu dul jeex. Kon li ma wax, dama koy wax, ni ma ko Baay bi sante.»