1NO se turbe vuestro corazón; creéis en Dios, creed también en mí.
1 «Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma.
2En la casa de mi Padre muchas moradas hay: de otra manera os lo hubiera dicho: voy, pues, á preparar lugar para vosotros.
2 Am na néeg yu bare ca sama kër Baay, bu dul woon noonu, ma wax leen ko, ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di dëkk.
3Y si me fuere, y os aparejare lugar, vendré otra vez, y os tomaré á mí mismo: para que donde yo estoy, vosotros también estéis.
3 Te su ma leen defaralee bérab booba ba noppi, dinaa dellusi, yóbbaale leen, ba fu ma nekk, ngeen nekk fa, yéen itam.
4Y sabéis á dónde yo voy; y sabéis el camino.
4 Te fa ma jëm, xam ngeen yoon wi.»
5Dícele Tomás: Señor, no sabemos á dónde vas: ¿cómo, pues, podemos saber el camino?
5 Tomaa ne ko: «Boroom bi, xamunu fa nga jëm. Kon nan lanuy man a xame yoon wi?»
6Jesús le dice: Yo soy el camino, y la verdad, y la vida: nadie viene al Padre, sino por mí.
6 Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man.
7Si me conocieseis, también á mi Padre conocierais: y desde ahora le conocéis, y le habéis visto.
7 Ndegam xam ngeen ma, dingeen xam itam sama Baay. Lu weesu tey, xam ngeen ko te gis ngeen ko.»
8Dícele Felipe: Señor, muéstranos el Padre, y nos basta.
8 Filib ne ko: «Boroom bi, won nu Baay bi; loolu doy na nu.»
9Jesús le dice: ¿Tanto tiempo ha que estoy con vosotros, y no me has conocido, Felipe? El que me ha visto, ha visto al Padre; ¿cómo, pues, dices tú: Muéstranos el Padre?
9 Yeesu tontu ko ne: «Ni ma yàggeek yéen te ba tey Filib, xamuloo ma? Ku ma gis, gis nga Baay bi. Kon nag nan ngay man a laaje naan: “Won nu Baay bi”?
10¿No crees que yo soy en el Padre, y el Padre en mí? Las palabras que yo os hablo, no las hablo de mí mismo: mas el Padre que está en mí, él hace las obras.
10 Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax jógewuñu ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay jëfam.
11Creedme que yo soy en el Padre, y el Padre en mí: de otra manera, creedme por las mismas obras.
11 Gëmleen li ma leen wax ne, maa ngi ci Baay bi te Baay baa ngi ci man; walla boog, gëmleen ndax jëf yi.
12De cierto, de cierto os digo: El que en mí cree, las obras que yo hago también él las hará; y mayores que éstas hará; porque yo voy al Padre.
12 Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax: képp ku ma gëm dina def, moom itam, jëf yi may def. Dina def sax yu gën a màgg, ndaxte maa ngi dem ci Baay bi.
13Y todo lo que pidiereis al Padre en mi nombre, esto haré, para que el Padre sea glorificado en el Hijo.
13 Te it lu ngeen ñaan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji feeñal ndamu Baay bi.
14Si algo pidiereis en mi nombre, yo lo haré.
14 Lu ngeen ñaan ci sama tur, maa koy def.
15Si me amáis, guardad mis mandamientos;
15 «Bu ngeen ma bëggee, dingeen topp sama ndigal.
16Y yo rogaré al Padre, y os dará otro Consolador, para que esté con vosotros para siempre:
16 Te dinaa ñaan Baay bi, mu jox leen beneen Dimbalikat, buy nekk ak yéen ba abadan.
17Al Espíritu de verdad, al cual el mundo no puede recibir, porque no le ve, ni le conoce: mas vosotros le conocéis; porque está con vosotros, y será en vosotros.
17 Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dëgg. Àddina du ko man a nangu, ndaxte gisu ko te xamu ko. Yéen xam ngeen ko, ndaxte mi ngi dëkk ak yéen te dina nekk ci yéen.
18No os dejaré huérfanos: vendré á vosotros.
18 Duma leen bàyyi ngeen wéet. Dinaa dellusi ci yéen.
19Aun un poquito, y el mundo no me verá más; empero vosotros me veréis; porque yo vivo, y vosotros también viviréis.
19 Des na tuuti ci kanam, àddina du ma gisati; waaye yéen dingeen ma gis. Dinaa dund, moo tax yéen itam dingeen dund.
20En aquel día vosotros conoceréis que yo estoy en mi Padre, y vosotros en mí, y yo en vosotros.
20 Bu keroogee, dingeen xam nag ne, nekk naa ci sama Baay, yéen it nekk ngeen ci man, te maa ngi nekk ci yéen.
21El que tiene mis mandamientos, y los guarda, aquél es el que me ama; y el que me ama, será amado de mi Padre, y yo le amaré, y me manifestaré á él.
21 Ki ma bëgg, mooy kiy nangu samay ndigal te di ko topp. Ku ma bëgg, Baay bi bëgg la, te man dinaa la bëgg, di la feeñu.»
22Dícele Judas, no el Iscariote: Señor, ¿qué hay porque te hayas de manifestar á nosotros, y no al mundo?
22 Yudaa --du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon — ne ko: «Boroom bi, lu xew, ba nga nar noo feeñu nun rekk, te doo feeñu àddina sépp?»
23Respondió Jesús, y díjole: El que me ama, mi palabra guardará; y mi Padre le amará, y vendremos á él, y haremos con él morada.
23 Yeesu tontu ko ne: «Ku ma bëgg dina sàmm sama kàddu. Sama Baay dina ko bëgg te nun dinanu ñëw ci moom, te dëkk ci moom.
24El que no me ama, no guarda mis palabras: y la palabra que habéis oído, no es mía, sino del Padre que me envió.
24 Ku ma bëggul doo sàmm sama kàddu. Li may wax nag, jógewul ci man, waaye mi ngi soqikoo ci ki ma yónni.
25Estas cosas os he hablado estando con vosotros.
25 «Lii dama leen koy wax ci bi may nekk ak yéen.
26Mas el Consolador, el Espíritu Santo, al cual el Padre enviará en mi nombre, él os enseñará todas las cosas, y os recordará todas las cosas que os he dicho.
26 Waaye Dimbalikat, bi leen Baay bi di yónnee ci sama tur, muy Xelam mu Sell, dina leen jàngal lépp, di leen fàttali li ma leen waxoon lépp.
27La paz os dejo, mi paz os doy: no como el mundo la da, yo os la doy. No se turbe vuestro corazón, ni tenga miedo.
27 Jàmm laa leen bàyyeel, sama jàmm laa leen jox, jàmm ju àddina mënul a joxe. Buleen jàq, buleen tiit.
28Habéis oído cómo yo os he dicho: Voy, y vengo á vosotros. Si me amaseis, ciertamente os gozaríais, porque he dicho que voy al Padre: porque el Padre mayor es que yo.
28 «Dégg ngeen li ma leen wax: “Dinaa dem, waaye dinaa dellusi ci yéen.” Bu ngeen ma bëggoon, dingeen bég ci li may dem ca Baay ba, ndaxte Baay bee ma gën a màgg.
29Y ahora os lo he dicho antes que se haga; para que cuando se hiciere, creáis.
29 Wax naa leen ko nag léegi, bala looloo ñëw, ngir bu waxtu wa agsee, ngeen gëm.
30Ya no hablaré mucho con vosotros: porque viene el príncipe de este mundo; mas no tiene nada en mí.
30 Lu weesu tey duma amati jotu waxtaan ak yéen, ndaxte malaaka mu bon mi jiite àddina saa ngi ñëw. Kooku manalu ma dara.
31Empero para que conozca el mundo que amo al Padre, y como el Padre me dió el mandamiento, así hago. Levantaos, vamos de aquí,
31 Waaye àddina si war na xam ne, bëgg naa Baay bi te ni ma ko Baay bi sante, ni laay jëfe. Jógleen, nu dem!