1DESPUÉS se manifestó Jesús otra vez á sus discípulos en la mar de Tiberias; y manifestóse de esta manera.
1 Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu feeñuwaat na ay taalibeem ca tefesu dex gu ñuy wax Tiberyàdd. Nii la deme woon:
2Estaban juntos Simón Pedro, y Tomás, llamado al Dídimo, y Natanael, el que era de Caná de Galilea, y los hijos de Zebedeo, y otros dos de sus discípulos.
2 Taalibey Yeesu yii àndoon nañu: Simoŋ Piyeer; Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi;» Nataneel, mi dëkk Kana ca diiwaanu Galile; doomi Sebede ak yeneen ñaari taalibe.
3Díceles Simón: A pescar voy. Dícenle: Vamos nosotros también contigo. Fueron, y subieron en una barca; y aquella noche no cogieron nada.
3 Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi.» Ñu ne ko: «Nun it danuy ànd ak yaw.» Ñu dugg gaal, daldi dem. Waaye guddi googu jàppuñu dara.
4Y venida la mañana, Jesús se puso á la ribera: mas los discípulos no entendieron que era Jesús.
4 Ci fajar gi Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe yi xàmmiwuñu ko.
5Y díjoles: Mozos, ¿tenéis algo de comer? Respondiéronle: No.
5 Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
6Y él les dice: Echad la red á la mano derecha del barco, y hallaréis. Entonces la echaron, y no la podían en ninguna manera sacar, por la multitud de los peces.
6 Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndeyjooru gaal gi, bu ko defee ngeen jàpp.» Ñu sànni fa mbaal ma, mu fees ak jën, ba mënuñu ko woon a génne ndox mi.
7Entonces aquel discípulo, al cual amaba Jesús, dijo á Pedro: El Señor es. Y Simón Pedro, como oyó que era el Señor, ciñóse la ropa, porque estaba desnudo, y echóse á la mar.
7 Taalibe ba Yeesu bëggoon, ne Piyeer: «Boroom bi la!» Bi Simoŋ Piyeer déggee loolu, dafa woddoo mbubbam, ndaxte dafa summeeku woon, daldi sóobu ci dex gi.
8Y los otros discípulos vinieron con el barco (porque no estaban lejos de tierra sino como doscientos codos), trayendo la red de peces.
8 Yeneen taalibe ya xëcc mbaal, mi fees dell ak jën, jëme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook téeméeri meetar.
9Y como descendieron á tierra, vieron ascuas puestas, y un pez encima de ellas, y pan.
9 Bi ñu teeree, ñu gis ab taal, ñu ciy lakk ay jën, teg mburu ca wet ga.
10Díceles Jesús; Traed de los peces que cogisteis ahora.
10 Yeesu ne leen: «Indileen ci jën, yi ngeen jàpp.»
11Subió Simón Pedro, y trajo la red á tierra, llena de grandes peces, ciento cincuenta y tres: y siendo tantos, la red no se rompió.
11 Simoŋ Piyeer yéeg ca gaal ga, daldi xëcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak jën yu mag; matoon na téeméeri jën ak juróom-fukk ak ñett. Te li muy baree-bare lépp, taxul mbaal ma dog.
12Díceles Jesús: Venid, comed. Y ninguno de los discípulos osaba preguntarle: ¿Tú, quién eres? sabiendo que era el Señor.
12 Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ci taalibe yi ñemewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam nañu ne, Boroom bi la.
13Viene pues Jesús, y toma el pan, y les da; y asimismo del pez.
13 Yeesu jegeñsi, jël mburu mi, jox leen, jox leen it jën.
14Esta era ya la tercera vez que Jesús se manifestó á sus discípulos, habiendo resucitado de los muertos.
14 Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy ñetteelu yoon, bi mu feeñoo ay taalibeem.
15Y cuando hubieron comido, Jesús dijo á Simón Pedro: Simón, hijo de Jonás, ¿me amas más que estos? Dícele; Sí Señor: tú sabes que te amo. Dícele: Apacienta mis corderos.
15 Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu tontu ko ne: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.»
16Vuélvele á decir la segunda vez: Simón, hijo de Jonás, ¿me amas? Respóndele: Sí, Señor: tú sabes que te amo. Dícele: Apacienta mis ovejas.
16 Noonu mu waxaat ko ne: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Sàmmal ma sama xar yi.»
17Dícele la tercera vez: Simón, hijo de Jonás, ¿me amas? Entristecióse Pedro de que le dijese la tercera vez: ¿Me amas? y dícele: Señor, tú sabes todas las cosas; tú sabes que te amo. Dícele Jesús: Apacienta mis ovejas.
17 Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaana, bëgg nga maam?» Piyeer am naqar ci li mu ko laaj ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Mu tontu ko ne: «Boroom bi, xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama xar yi.
18De cierto, de cierto te digo: Cuando eras más mozo, te ceñías, é ibas donde querías; mas cuando ya fueres viejo, extenderás tus manos, y te ceñirá otro, y te llevará á donde no quieras.
18 Ci dëgg-dëgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw yaa doon takk sa geño, di dem fu la neex. Waaye boo màggatee, dinga tàllal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.»
19Y esto dijo, dando á entender con qué muerte había de glorificar á Dios. Y dicho esto, dícele: Sígueme.
19 Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale nan la Piyeer war a faatoo ngir jollil ndamu Yàlla. Noonu Yeesu ne ko: «Toppal ci man!»
20Volviéndose Pedro, ve á aquel discípulo al cual amaba Jesús, que seguía, el que también se había recostado á su pecho en la cena, y le había dicho: Señor, ¿quién es el que te ha de entregar?
20 Piyeer geestu, gis taalibe bi Yeesu bëggoon, di ñëw ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki sóonu woon ca Yeesu, ba ñuy lekk, te laajoon ko ne: «Boroom bi, kan moo lay wori?»
21Así que Pedro vió á éste, dice á Jesús: Señor, ¿y éste, qué?
21 Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: «Kii nag, Boroom bi, nu muy mujje?»
22Dícele Jesús: Si quiero que él quede hasta que yo venga, ¿qué á tí? Sígueme tú.
22 Yeesu ne ko: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon? Yaw toppal ci man.»
23Salió entonces este dicho entre los hermanos, que aquel discípulo no había de morir. Mas Jesús no le dijo, No morirá; sino: Si quiero que él quede hasta que yo venga ¿qué á ti?
23 Noonu am, ci bokki taalibe yi, ñu xalaat ne, taalibe boobu du dee. Moona Yeesu musul ne Piyeer, du dee; waaye li mu wax mooy: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon?»
24Este es aquel discípulo que da testimonio de estas cosas, y escribió estas cosas: y sabemos que su testimonio es verdadero.
24 Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne, li muy wax dëgg la.
25Y hay también otras muchas cosas que hizo Jesús, que si se escribiesen cada una por sí, ni aun en el mundo pienso que cabrían los libros que se habrían de escribir. Amén.
25 Yeesu def na yeneen jëf yu bare. Su ñu ko doon nettali, bind lépp, xalaat naa ne, téere yi duñu xaj ci àddina.