Spanish: Reina Valera (1909)

Wolof: New Testament

John

7

1Y PASADAS estas cosas andaba Jesús en Galilea: que no quería andar en Judea, porque los Judíos procuraban matarle.
1 Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile.
2Y estaba cerca la fiesta de los Judíos, la de los tabernáculos.
2 Bëggul woon a dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wut a rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi.
3Y dijéronle sus hermanos: Pásate de aquí, y vete á Judea, para que también tus discípulos vean las obras que haces.
3 Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
4Que ninguno que procura ser claro, hace algo en oculto. Si estas cosas haces, manifiéstate al mundo.
4 Ku bëgg a siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
5Porque ni aun sus hermanos creían en él.
5 Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
6Díceles entonces Jesús: Mi tiempo aun no ha venido; mas vuestro tiempo siempre está presto.
6 Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
7No puede el mundo aborreceros á vosotros; mas á mí me aborrece, porque yo doy testimonio de él, que sus obras son malas.
7 Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne, seeni jëf baaxul.
8Vosotros subid á esta fiesta; yo no subo aún á esta fiesta, porque mi tiempo aun no es cumplido.
8 Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
9Y habiéndoles dicho esto, quedóse en Galilea.
9 Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10Mas como sus hermanos hubieron subido, entonces él también subió á la fiesta, no manifiestamente, sino como en secreto.
10 Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sog a dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
11Y buscábanle los Judíos en la fiesta, y decían: ¿Dónde está aquél?
11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
12Y había grande murmullo de él entre la gente: porque unos decían: Bueno es; y otros decían: No, antes engaña á las gentes.
12 Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
13Mas ninguno hablaba abiertamente de él, por miedo de los Judíos.
13 Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
14Y al medio de la fiesta subió Jesús al templo, y enseñaba.
14 Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngale ca kër Yàlla ga.
15y maravillábanse los Judíos, diciendo: ¿Cómo sabe éste letras, no habiendo aprendido?
15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16Respondióles Jesús, y dijo: Mi doctrina no es mía, sino de aquél que me envió.
16 Yeesu daldi leen tontu ne: «Li may jàngale, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
17El que quisiere hacer su voluntad, conocerá de la doctrina si viene de Dios, ó si yo hablo de mí mismo.
17 Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngale ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
18El que habla de sí mismo, su propia gloria busca; mas el que busca la gloria del que le envió, éste es verdadero, y no hay en él injusticia.
18 Nit kiy wax ci coobareem nag, day wut a màggal boppam, waaye kiy wut a màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
19¿No os dió Moisés la ley, y ninguno de vosotros hace la ley? ¿Por qué me procuráis matar?
19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?»
20Respondió la gente, y dijo: Demonio tienes: ¿quién te procura matar?
20 Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wut a rey?»
21Jesús respondió, y díjoles: Una obra hice, y todos os maravilláis.
21 Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle!
22Cierto, Moisés os dió la circuncisión (no porque sea de Moisés, mas de los padres); y en sábado circuncidáis al hombre.
22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gune yi --jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan — moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésu noflaay bi.
23Si recibe el hombre la circuncisión en sábado, para que la ley de Moisés no sea quebrantada, ¿os enojáis conmigo porque en sábado hice sano todo un hombre?
23 Bu ngeen manee xarafal nit ci bésu noflaay bi, ngir bañ a wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
24No juzguéis según lo que parece, mas juzgad justo juicio.
24 Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
25Decían entonces unos de los de Jerusalem: ¿No es éste al que buscan para matarlo?
25 Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wut a rey?
26Y he aquí, habla públicamente, y no le dicen nada; ¿si habrán entendido verdaderamente los príncipes, que éste es el Cristo?
26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne, mooy Almasi bi?
27Mas éste, sabemos de dónde es: y cuando viniere el Cristo, nadie sabrá de dónde sea.
27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
28Entonces clamaba Jesús en el templo, enseñando y diciendo: Y á mí me conocéis, y sabéis de dónde soy: y no he venido de mí mismo; mas el que me envió es verdadero, al cual vosotros no conocéis.
28 Yeesu di jàngale ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko.
29Yo le conozco, porque de él soy, y él me envió.
29 Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
30Entonces procuraban prenderle; mas ninguno puso en él mano, porque aun no había venido su hora.
30 Noonu ñu koy wut a jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.
31Y muchos del pueblo creyeron en él, y decían: El Cristo, cuando viniere, ¿hará más señales que las que éste hace?
31 Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?»
32Los Fariseos oyeron á la gente que murmuraba de él estas cosas; y los príncipes de los sacerdotes y los Fariseos enviaron servidores que le prendiesen.
32 Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33Y Jesús dijo: Aun un poco de tiempo estaré con vosotros, é iré al que me envió.
33 Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sog a dem ci ki ma yónni.
34Me buscaréis, y no me hallaréis; y donde yo estaré, vosotros no podréis venir.
34 Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen man a dem fa may nekk.»
35Entonces los Judíos dijeron entre sí: ¿A dónde se ha de ir éste que no le hallemos? ¿Se ha de ir á los esparcidos entre los Griegos, y á enseñar á los Griegos?
35 Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nar a dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya?
36¿Qué dicho es éste que dijo: Me buscaréis, y no me hallaréis; y donde yo estaré, vosotros no podréis venir?
36 Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen man a dem fa may nekk?”»
37Mas en el postrer día grande de la fiesta, Jesús se ponía en pie y clamaba, diciendo: Si alguno tiene sed, venga á mí y beba.
37 Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na, ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.»
38El que cree en mí, como dice la Escritura, ríos de agua viva correrán de su vientre.
39 Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroon a jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
39(Y esto dijo del Espíritu que habían de recibir los que creyesen en él: pues aun no había venido el Espíritu Santo; porque Jesús no estaba aún glorificado.)
40 Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi war a ñëw.»
40Entonces algunos de la multitud, oyendo este dicho, decían: Verdaderamente éste es el profeta.
41 Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi man a jógee Galile?
41Otros decían: Este es el Cristo. Algunos empero decían: ¿De Galilea ha de venir el Cristo?
42 Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.»
42¿No dice la Escritura, que de la simiente de David, y de la aldea de Bethlehem, de donde era David, vendrá el Cristo?
43 Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu.
43Así que había disensión entre la gente acerca de él.
44 Am na ca ñoom ñu ko bëggoon a jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara.
44Y algunos de ellos querían prenderle; mas ninguno echó sobre él manos.
45 Bi alkaati ya delloo, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?»
45Y los ministriles vinieron á los principales sacerdotes y á los Fariseos; y ellos les dijeron: ¿Por qué no le trajisteis?
46 Alkaati ya ne leen: «Kenn musul a waxe ni nit kooku!»
46Los ministriles respondieron: Nunca ha hablado hombre así como este hombre.
47 Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam?
47Entonces los Fariseos les respondieron: ¿Estáis también vosotros engañados?
48 Ndax am na kenn ci saraxalekat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet.
48¿Ha creído en él alguno de los príncipes, ó de los Fariseos?
49 Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!»
49Mas estos comunales que no saben la ley, malditos son.
50 Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen:
50Díceles Nicodemo (el que vino á él de noche, el cual era uno de ellos):
51 «Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?»
51¿Juzga nuestra ley á hombre, si primero no oyere de él, y entendiere lo que ha hecho?
52 Ñu tontu ko ne: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne, benn yonent musul a jóge Galile.»
52Respondieron y dijéronle: ¿Eres tú también Galileo? Escudriña y ve que de Galilea nunca se levantó profeta.
53 Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër.
53Y fuése cada uno á su casa.