Spanish: Reina Valera (1909)

Wolof: New Testament

John

9

1Y PASANDO Jesús, vió un hombre ciego desde su nacimiento.
1 Amoon na fu Yeesu jaaroon, gis fa waa ju judduwaale gumba.
2Y preguntáronle sus discípulos, diciendo: Rabbí, ¿quién pecó, éste ó sus padres, para que naciese ciego?
2 Taalibeem ya laaj ko ne: «Kilifa gi, lu tax waa jii judduwaale gumba? Ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram?»
3Respondió Jesús: Ni éste pecó, ni sus padres: mas para que las obras de Dios se manifiesten en él.
3 Yeesu tontu ne: «Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom.
4Conviéneme obrar las obrar del que me envió, entre tanto que el día dura: la noche viene, cuando nadie puede obrar.
4 Bëccëg lanu war a matal jëfi ki ma yónni; guddi dina ñëwi, goo xam ne kenn du ci man a liggéey.
5Entre tanto que estuviere en el mundo, luz soy del mundo.
5 Ci bi may nekk àddina, maay leeru àddina.»
6Esto dicho, escupió en tierra, é hizo lodo con la saliva, y untó con el lodo sobre los ojos del ciego,
6 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ci bëti gumba ga ne ko:
7Y díjole: Ve, lávate en el estanque de Siloé (que significa, si lo interpretares, Enviado). Y fué entonces, y lavóse, y volvió viendo.
7 «Demal sëlmu ci bëtu Silowe.» Silowe mi ngi tekki «Yónni nañu ko.» Gumba ga daldi dem sëlmuji, dellusi di gis.
8Entonces los vecinos, y los que antes le habían visto que era ciego, decían: ¿no es éste el que se sentaba y mendigaba?
8 Dëkkandoom yi ak ñi ko xame woon bu jëkk ci yelwaan naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?»
9Unos decían: Este es; y otros: A él se parece. El decía: Yo soy.
9 Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!»
10Y dijéronle: ¿Cómo te fueron abiertos los ojos?
10 Ñu ne ko: «Lu ubbi say bët?»
11Respondió él y dijo: El hombre que se llama Jesús, hizo lodo, y me untó los ojos, y me dijo: Ve al Siloé, y lávate: y fuí, y me lavé, y recibí la vista.
11 Mu tontu ne: «Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmu ci bëtu Silowe.” Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.»
12Entonces le dijeron: ¿Dónde está aquél? El dijo: No sé.
12 Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
13Llevaron á los Fariseos al que antes había sido ciego.
13 Noonu ñu daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon.
14Y era sábado cuando Jesús había hecho el lodo, y le había abierto los ojos.
14 Ndekete Yeesu, bés bi mu tooyale ban, ubbi bëti gumba ga, bésu noflaay la woon.
15Y volviéronle á preguntar también los Fariseos de qué manera había recibido la vista. Y él les dijo: Púsome lodo sobre los ojos, y me lavé, y veo.
15 Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen: «Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.»
16Entonces unos de los Fariseos decían: Este hombre no es de Dios, que no guarda el sábado. Otros decían: ¿Cómo puede un hombre pecador hacer estas señales? Y había disensión entre ellos.
16 Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, mënul a jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésu noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar man a wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir.
17Vuelven á decir al ciego: ¿Tú, qué dices del que te abrió los ojos? Y él dijo: Que es profeta.
17 Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.»
18Mas los Judíos no creían de él, que había sido ciego, y hubiese recibido la vista, hasta que llamaron á los padres del que había recibido la vista;
18 Yawut ya mënuñu woon a nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram,
19Y preguntáronles, diciendo: ¿Es éste vuestro hijo, el que vosotros decís que nació ciego? ¿Cómo, pues, ve ahora?
19 laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne, gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?»
20Respondiéronles sus padres y dijeron: Sabemos que éste es nuestro hijo, y que nació ciego:
20 Waajur ya tontu ne: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.
21Mas cómo vea ahora, no sabemos; ó quién le haya abierto los ojos, nosotros no lo sabemos; él tiene edad, preguntadle á él; él hablará de sí.
21 Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.»
22Esto dijeron sus padres, porque tenían miedo de los Judíos: porque ya los Judíos habían resuelto que si alguno confesase ser él el Mesías, fuese fuera de la sinagoga.
22 Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23Por eso dijeron sus padres: Edad tiene, preguntadle á él.
23 Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24Así que, volvieron á llamar al hombre que había sido ciego, y dijéronle: Da gloria á Dios: nosotros sabemos que este hombre es pecador.
24 Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne, waa joojee boroom bàkkaar la.»
25Entonces él respondió, y dijo: Si es pecador, no lo sé: una cosa sé, que habiendo yo sido ciego, ahora veo.
25 Mu tontu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.»
26Y volviéronle á decir: ¿Qué te hizo? ¿Cómo te abrió los ojos?
26 Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?»
27Respondióles: Ya os lo he dicho, y no habéis atendido: ¿por qué lo queréis otra vez oir? ¿queréis también vosotros haceros sus discípulos?
27 Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeen a bëgg a nekk yéen itam ay taalibeem?»
28Y le ultrajaron, y dijeron: Tú eres su discípulo; pero nosotros discípulos de Moisés somos.
28 Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.
29Nosotros sabemos que á Moisés habló Dios: mas éste no sabemos de dónde es.
29 Xam nanu ne, Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.»
30Respondió aquel hombre, y díjoles: Por cierto, maravillosa cosa es ésta, que vosotros no sabéis de dónde sea, y á mí me abrió los ojos.
30 Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët!
31Y sabemos que Dios no oye á los pecadores: mas si alguno es temeroso de Dios, y hace su voluntad, á éste oye.
31 Xam nanu ne, Yàlla du déglu boroom bàkkaar. Waaye nag, dina déglu ki koy ragal tey def coobareem.
32Desde el siglo no fué oído, que abriese alguno los ojos de uno que nació ciego.
32 Bi àddina sosoo ba tey, musuñoo dégg nit ku ubbi bëti gumbag judduwaale.
33Si éste no fuera de Dios, no pudiera hacer nada.
33 Kon nit kookee nag, bu jógewul woon ca Yàlla, du man a def dara.»
34Respondieron, y dijéronle: En pecados eres nacido todo, ¿y tú nos enseñas? Y echáronle fuera.
34 Ñu tontu ko ne: «Yaw, ci biir bàkkaar nga juddoo, ba noppi di nu jàngal?» Noonu ñu dàq ko ca jàngu ba.
35Oyó Jesús que le habían echado fuera; y hallándole, díjole: ¿Crees tú en el Hijo de Dios?
35 Yeesu daldi yég ne, dàq nañu nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: «Ndax gëm nga Doomu nit ki?»
36Respondió él, y dijo: ¿Quién es, Señor, para que crea en él?
36 Waa ja ne ko: «Wax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo gëm.»
37Y díjole Jesús: Y le has visto, y el que habla contigo, él es.
37 Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.»
38Y él dice: Creo, Señor; y adoróle.
38 Waa ja ne: «Boroom bi, gëm naa la.» Noonu mu jaamu Yeesu.
39Y dijo Jesús: Yo, para juicio he venido á este mundo: para que los que no ven, vean; y los que ven, sean cegados.
39 Yeesu ne ko: «Àttee ma tax a ñëw àddina, ngir ñi gumba gis, ñiy gis gumba.»
40Y ciertos de los Fariseos que estaban con él oyeron esto, y dijéronle: ¿Somos nosotros también ciegos?
40 Bi Farisen ya nekkoon ak moom déggee loolu, ñu ne ko: «Xanaa kon nun it danoo gumba?»
41Díjoles Jesús: Si fuerais ciegos, no tuvierais pecado: mas ahora porque decís, Vemos, por tanto vuestro pecado permanece.
41 Yeesu tontu leen ne: «Bu ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye fi ak yéena ngi naan: “Nu ngi gis,” ci bàkkaar ngeen di dëkk.