Spanish: Reina Valera (1909)

Wolof: New Testament

Luke

17

1Y A SUS discípulos dice: Imposible es que no vengan escándalos; mas ­ay de aquél por quien vienen!
1 Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar mënta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal.
2Mejor le fuera, si le pusiesen al cuello una piedra de molino, y le lanzasen en el mar, que escandalizar á uno de estos pequeñitos.
2 Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gën a tuuti ci ñii.
3Mirad por vosotros: si pecare contra ti tu hermano, repréndele; y si se arrepintiere, perdónale.
3 Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.
4Y si siete veces al día pecare contra ti, y siete veces al día se volviere á ti, diciendo, pésame, perdónale.
4 Te su la tooñee juróom-ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom-ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»
5Y dijeron los apóstoles al Señor: Auméntanos la fe.
5 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: «Yokkal sunu ngëm.»
6Entonces el Señor dijo: Si tuvieseis fe como un grano de mostaza, diréis á este sicómoro: Desarráigate, y plántate en el mar; y os obedecerá.
6 Boroom bi tontu ne: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen man a ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
7¿Y quién de vosotros tiene un siervo que ara ó apacienta, que vuelto del campo le diga luego: Pasa, siéntate á la mesa?
7 «Kan ci yéen bu amoon surga bu beyi walla bu sàmmi ba ñëw, ndax dafa ko naa: “Kaay lekk.”
8¿No le dice antes: Adereza qué cene, y arremángate, y sírveme hasta que haya comido y bebido; y después de esto, come tú y bebe?
8 Déedéet. Xanaa kay da ko naan: “Defaral ma réer bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga door a lekk te naan.”
9¿Da gracias al siervo porque hizo lo que le había sido mandado? Pienso que no.
9 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ngërëm? Déedéet.
10Así también vosotros, cuando hubiereis hecho todo lo que os es mandado, decid: Siervos inútiles somos, porque lo que debíamos hacer, hicimos.
10 Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeen a war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
11Y aconteció que yendo él á Jerusalem, pasaba por medio de Samaria y de Galilea.
11 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xaajale Samari ak Galile.
12Y entrando en una aldea, viniéronle al encuentro diez hombres leprosos, los cuales se pararon de lejos,
12 Bi muy jub benn dëkk, fukki gaana ñëw, dogale ko. Ñu taxaw dand ko, di wax ca kaw naan:
13Y alzaron la voz, diciendo: Jesús, Maestro, ten misericordia de nosotros.
13 «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!»
14Y como él los vió, les dijo: Id, mostraos á los sacerdotes. Y aconteció, que yendo ellos, fueron limpios.
14 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: «Demleen won seen bopp saraxalekat ya.» Bi ñuy dem, ñu daldi set.
15Entonces uno de ellos, como se vió que estaba limpio, volvió, glorificando á Dios á gran voz;
15 Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb.
16Y derribóse sobre el rostro á sus pies, dándole gracias: y éste era Samaritano.
16 Mu dëpp jëwam ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
17Y respondiendo Jesús, dijo: ¿No son diez los que fueron limpios? ¿Y los nueve dónde están?
17 Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom-ñeent ña nag?
18¿No hubo quien volviese y diese gloria á Dios sino este extranjero?
18 Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!»
19Y díjole: Levántate, vete; tu fe te ha salvado.
19 Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
20Y preguntado por los Fariseos, cuándo había de venir el reino de Dios, les respondió y dijo: El reino de Dios no vendrá con advertencia;
20 Farisen yi laaj Yeesu ne ko: «Kañ la Yàlla di tëral nguuram?» Mu tontu leen ne: «Bu Yàlla di wàcce nguuram ci nit ñi, kenn du ko man a teg bët.
21Ni dirán: Helo aquí, ó helo allí: porque he aquí el reino de Dios entre vosotros está.
21 Duñu man a wax it ne: “Xool-leen, mi ngi fii,” walla: “Ma nga fale,” ndaxte nguuru Yàlla wàcc na ci seen biir.»
22Y dijo á sus discípulos: Tiempo vendrá, cuando desearéis ver uno de los días del Hijo del hombre, y no lo veréis.
22 Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgg a gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis.
23Y os dirán: Helo aquí, ó helo allí. No vayáis, ni sigáis.
23 Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.
24Porque como el relámpago, relampagueando desde una parte de debajo del cielo, resplandece hasta la otra debajo del cielo, así también será el Hijo del hombre en su día.
24 Ndaxte ni melax naan ràyye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci bésam.
25Mas primero es necesario que padezca mucho, y sea reprobado de esta generación.
25 Waaye balaa booba fàww mu sonn lool te niti jamono jii dëddu ko.
26Y como fué en los días de Noé, así también será en los días del Hijo del hombre.
26 «La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki.
27Comían, bebían, los hombres tomaban mujeres, y las mujeres maridos, hasta el día que entró Noé en el arca; y vino el diluvio, y destruyó á todos.
27 Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.
28Asimismo también como fué en los días de Lot; comían, bebían, compraban, vendían, plantaban, edificaban;
28 «Dina mel it ni la xewoon ca bési Lóot. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jënd ak di jaay, di ji ak di tabax.
29Mas el día que Lot salió de Sodoma, llovió del cielo fuego y azufre, y destruyó á todos:
29 Waaye bés ba Lóot génnee Sodom, Yàlla tawloo safara ak tamarax, rey leen ñoom ñépp.
30Como esto será el día en que el Hijo del hombre se manifestará.
30 Noonu lay mel, bés bu Doomu nit kiy feeñ.
31En aquel día, el que estuviere en el terrado, y sus alhajas en casa, no descienda á tomarlas: y el que en el campo, asimismo no vuelva atrás.
31 «Ca bés boobee ku nekk ca kaw kër ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu wàcc jëli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu ñibbi.
32Acordaos de la mujer de Lot.
32 Fàttalikuleen jabaru Lóot!
33Cualquiera que procurare salvar su vida, la perderá; y cualquiera que la perdiere, la salvará.
33 Kuy wut a rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund.
34Os digo que en aquella noche estarán dos en una cama; el uno será tomado, y el otro será dejado.
34 Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, ñaar dinañu bokk a tëdd guddi, dees na yóbbu kenn ki, bàyyi ka ca des.
35Dos mujeres estarán moliendo juntas: la una será tomada, y la otra dejada.
35 Ñaari jigéen dinañu wolandoo, dees na yóbbu kenn ci, bàyyi ka ca des.»
36Dos estarán en el campo; el uno será tomado, y el otro dejado.
37 Taalibe yi ne Yeesu: «Fu loolu di xewe, Boroom bi?» Yeesu tontu leen ne: «Fa médd nekk, la tan yiy dajee.»
37Y respondiendo, le dicen: ¿Dónde, Señor? Y él les dijo: Donde estuviere el cuerpo, allá se juntarán también las águilas.