Spanish: Reina Valera (1909)

Wolof: New Testament

Luke

7

1Y COMO acabó todas sus palabras oyéndole el pueblo, entró en Capernaum.
1 Bi Yeesu waxee la mu naroon a wax lépp ca kanamu mbooloo ma, mu daldi dem Kapernawum.
2Y el siervo de un centurión, al cual tenía él en estima, estaba enfermo y á punto de morir.
2 Amoon na fa njiitu xare. Njiit la nag, surgaam bu mu bëggoon lool dafa feebaroon, bay bëgg a dee.
3Y como oyó hablar de Jesús, envió á él los ancianos de los Judíos, rogándole que viniese y librase á su siervo.
3 Bi mu déggee mbiri Yeesu, mu yónni ca moom ay Yawut, di magi dëkk ba, ngir ñaan ko, mu ñëw faj surga ba.
4Y viniendo ellos á Jesús, rogáronle con diligencia, diciéndole: Porque es digno de concederle esto;
4 Bi magi dëkk ba agsee ca Yeesu, ñu sàkku ci moom ndimbal, ñaan ko: «Ki nu yónni ci yaw de, yelloo na ndimbal,
5Que ama nuestra nación, y él nos edificó una sinagoga.
5 ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu jàngu.»
6Y Jesús fué con ellos. Mas como ya no estuviesen lejos de su casa, envió el centurión amigos á él, diciéndole: Señor, no te incomodes, que no soy digno que entres debajo de mi tejado;
6 Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom. Waaye bi ñuy bëgg a agsi ca kër ga, njiit la yebal ay xaritam ngir ñu wax Yeesu ne: «Sang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama kër.
7Por lo cual ni aun me tuve por digno de venir á ti; mas di la palabra, y mi siervo será sano.
7 Looloo tax it ma xalaat ne, awma darajay gatandu la. Waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér.
8Porque también yo soy hombre puesto en potestad, que tengo debajo de mí soldados; y digo á éste: Ve, y va; y al otro: Ven, y viene; y á mi siervo: Haz esto, y lo hace.
8 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
9Lo cual oyendo Jesús, se maravilló de él, y vuelto, dijo á las gentes que le seguían: Os digo que ni aun en Israel he hallado tanta fe.
9 Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, musuma cee gis ku gëme nii.»
10Y vueltos á casa los que habían sido enviados, hallaron sano al siervo que había estado enfermo.
10 Noonu ndaw ya daldi dellu ca kër ga. Bi ñu agsee, ñu gis ne surga ba wér na.
11Y aconteció después, que él iba á la ciudad que se llama Naín, é iban con él muchos de sus discípulos, y gran compañía.
11 Yàggul dara Yeesu dem ci dëkk bu ñuy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare ànd ak moom.
12Y como llegó cerca de la puerta de la ciudad, he aquí que sacaban fuera á un difunto, unigénito de su madre, la cual también era viuda: y había con ella grande compañía de la ciudad.
12 Bi muy agsi ca buntu dëkk ba, fekk ñuy rob néew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji jëkkëram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca dëkk ba di gunge soxna sa.
13Y como el Señor la vió, compadecióse de ella, y le dice: No llores.
13 Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy yërëm ne ko: «Bul jooyati.»
14Y acercándose, tocó el féretro: y los que lo llevaban, pararon. Y dice: Mancebo, á ti digo, levántate.
14 Mu jegeñsi, laal jaat ga, ñi ko jàppoo taxaw. Mu ne: «Waxambaane wi, jógal, ndigal la.»
15Entonces se incorporó el que había muerto, y comenzó á hablar. Y dióle á su madre.
15 Noonu nit ka dee woon jóg toog, tàmbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.
16Y todos tuvieron miedo, y glorificaban á Dios, diciendo: Que un gran profeta se ha levantado entre nosotros; y que Dios ha visitado á su pueblo.
16 Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»
17Y salió esta fama de él por toda Judea, y por toda la tierra de alrededor.
17 La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.
18Y sus discípulos dieron á Juan las nuevas de todas estas cosas: y llamó Juan á dos de sus discípulos,
18 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,
19Y envió á Jesús, diciendo: ¿Eres tú aquél que había de venir, ó esperaremos á otro?
19 yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki war a ñëw, walla danoo war a xaar keneen?»
20Y como los hombres vinieron á él, dijeron: Juan el Bautista nos ha enviado á ti, diciendo: ¿Eres tú aquél que había de venir, ó esperaremos á otro?
20 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroon a ñëw, walla danuy xaar keneen?»
21Y en la misma hora sanó á muchos de enfermedades y plagas, y de espíritus malos; y á muchos ciegos dió la vista.
21 Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.
22Y respondiendo Jesús, les dijo: Id, dad las nuevas á Juan de lo que habéis visto y oído: que los ciegos ven, los cojos andan, los leprosos son limpiados, los sordos oyen, los muertos resucitan, á los pobres es anunciado el evangelio:
22 Noonu mu tontu ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te ñi woyoflu ñu ngi dégg xebaar bu baax bi.
23Y bienaventurado es el que no fuere escandalizado en mí.
23 Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
24Y como se fueron los mensajeros de Juan, comenzó á hablar de Juan á las gentes: ¿Qué salisteis á ver al desierto? ¿una caña que es agitada por el viento?
24 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
25Mas ¿qué salisteis á ver? ¿un hombre cubierto de vestidos delicados? He aquí, los que están en vestido precioso, y viven en delicias, en los palacios de los reyes están.
25 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.
26Mas ¿qué salisteis á ver? ¿un profeta? También os digo, y aun más que profeta.
26 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne, ëpp na yonent.
27Este es de quien está escrito: He aquí, envío mi mensajero delante de tu faz, El cual aparejará tu camino delante de ti.
27 Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan:“Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la,te xàllal la yoon ci sa kanam.”
28Porque os digo que entre los nacidos de mujeres, no hay mayor profeta que Juan el Bautista: mas el más pequeño en el reino de los cielos es mayor que él.
28 Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya musul a feeñ. Waaye ba tey ki gën a ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»
29Y todo el pueblo oyéndole, y los publicanos, justificaron á Dios, bautizándose con el bautismo de Juan.
29 Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.
30Mas los Fariseos y los sabios de la ley, desecharon el consejo de Dios contra sí mismos, no siendo bautizados de él.
30 Waaye Farisen ya ak xutbakat ya dañoo bañ, mu sóob leen ci ndox, di wone noonu ne, gàntu nañu li leen Yàlla bëggaloon.
31Y dice el Señor: ¿A quién, pues, compararé los hombres de esta generación, y á qué son semejantes?
31 Yeesu tegaat ca ne: «Kon lan laa man a mengaleel niti jamono jii? Lan lañuy nirool?
32Semejantes son á los muchachos sentados en la plaza, y que dan voces los unos á los otros, y dicen: Os tañimos con flautas, y no bailasteis: os endechamos, y no llorasteis.
32 Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan:“Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
33Porque vino Juan el Bautista, que ni comía pan, ni bebía vino, y decís: Demonio tiene.
33 Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
34Vino el Hijo del hombre, que come y bebe, y decís: He aquí un hombre comilón, y bebedor de vino, amigo de publicanos y de pecadores.
34 Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.”
35Mas la sabiduría es justificada de todos sus hijos.
35 Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
36Y le rogó uno de los Fariseos, que comiese con él. Y entrado en casa del Fariseo, sentóse á la mesa.
36 Amoon na ab Farisen bu ñaan Yeesu, mu ñëw lekkandoo ak moom. Yeesu dem kër waa ja, toog ca lekkukaay.
37Y he aquí una mujer que había sido pecadora en la ciudad, como entendió que estaba á la mesa en casa de aquel Fariseo, trajo un alabastro de ungüento,
37 Fekk amoon na ca dëkk ba jigéen juy moy Yàlla. Bi mu yégee ne, Yeesoo ngay lekk ca kër Farisen ba, mu dem, yóbbaale njaq lu ñu defare doj wu ñuy wax albaatar te def latkoloñ.
38Y estando detrás á sus pies, comenzó llorando á regar con lágrimas sus pies, y los limpiaba con los cabellos de su cabeza; y besaba sus pies, y los ungía con el ungüento.
38 Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rangooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja.
39Y como vió esto el Fariseo que le había convidado, habló entre sí, diciendo: Este, si fuera profeta, conocería quién y cuál es la mujer que le toca, que es pecadora.
39 Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.»
40Entonces respondiendo Jesús, le dijo: Simón, una cosa tengo que decirte. Y él dice: Di, Maestro.
40 Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la war a wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»
41Un acredor tenía dos deudores: el uno le debía quinientos denarios, y el otro cincuenta;
41 Yeesu ne ko: «Da fee amoon ñaari nit ñu ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel téeméeri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni.
42Y no teniendo ellos de qué pagar, perdonó á ambos. Di, pues, ¿cuál de éstos le amará más?
42 Waaye kenn ci ñoom mënu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci ñaar ñooñu nag kan moo ko ciy gën a bëgg?»
43Y respondiendo Simón, dijo: Pienso que aquél al cual perdonó más. Y él le dijo: Rectamente has juzgado.
43 Simoŋ tontu ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gën a bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»
44Y vuelto á la mujer, dijo á Simón: ¿Ves esta mujer? Entré en tu casa, no diste agua para mis pies; mas ésta ha regado mis pies con lágrimas, y los ha limpiado con los cabellos.
44 daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rangooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram.
45No me diste beso, mas ésta, desde que entré, no ha cesado de besar mis pies.
45 Bi ma agsee, fóonuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba léegi tàyyiwul ci di fóon samay tànk.
46No ungiste mi cabeza con óleo; mas ésta ha ungido con ungüento mis pies.
46 Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkoloñ ci samay tànk.
47Por lo cual te digo que sus muchos pecados son perdonados, porque amó mucho; mas al que se perdona poco, poco ama.
47 Moo tax ma di la wax ne, su wonee mbëggeel gu réye nii, dafa fekk ñu baal ko bàkkaaram yu bare. Waaye ki mbëggeelam néew dafa fekk ñu baal ko lu tuuti.»
48Y á ella dijo: Los pecados te son perdonados.
48 Yeesu daldi ne jigéen ja: «Baal nañu la say bàkkaar.»
49Y los que estaban juntamente sentados á la mesa, comenzaron á decir entre sí: ¿Quién es éste, que también perdona pecados?
49 Noonu ñi doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: «Kii am sañ-sañu baale bàkkaar mooy kan?»
50Y dijo á la mujer: Tu fe te ha salvado, ve en paz.
50 Waaye Yeesu ne jigéen ja: «Sa ngëm musal na la. Demal ci jàmm.»