1Y SALIO de allí, y vino á su tierra, y le siguieron sus discípulos.
1 Bi loolu amee Yeesu jóge fa, dellu réewam, ànd ak taalibe yi.
2Y llegado el sábado, comenzó á enseñar en la sinagoga; y muchos oyéndole, estaban atónitos, diciendo: ¿De dónde tiene éste estas cosas? ¿Y qué sabiduría es ésta que le es dada, y tales maravillas que por sus manos son hechas?
2 Bésu noflaay bi nag mu jàngal leen ci seen jàngu, ba mbooloom ñi ko dégg waaru naan: «Lii, fu mu ko jële, te xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def kéemaan yii?
3¿No es éste el carpintero, hijo de María, hermano de Jacobo, y de José, y de Judas, y de Simón? ¿No están también aquí con nosotros, sus hermanas? Y se escandalizaban en él.
3 Ndax kii du minise bi? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simoŋ? Te ay rakkam yu jigéen ndax nekkuñu fi ak nun?» Kon nag ñu daldi ko xeeb.
4Mas Jesús les decía: No hay profeta deshonrado sino en su tierra, y entre sus parientes, y en su casa.
4 Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam, ciy bokkam mbaa ci këram.»
5Y no pudo hacer allí alguna maravilla; solamente sanó unos pocos enfermos, poniendo sobre ellos las manos.
5 Te Yeesu mënu faa def ay kéemaan yu bare, lu dul teg loxo yenn jarag, wéral leen.
6Y estaba maravillado de la incredulidad de ellos. Y rodeaba las aldeas de alrededor, enseñando.
6 Te mu waaru ndax seen ngëmadi. Bi loolu amee Yeesu di wër dëkk ya, di jàngale.
7Y llamó á los doce, y comenzó á enviarlos de dos en dos: y les dió potestad sobre los espíritus inmundos.
7 Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar.
8Y les mandó que no llevasen nada para el camino, sino solamente báculo; no alforja, ni pan, ni dinero en la bolsa;
8 Mu digal leen nii: «Bu ngeen di dem, buleen yóbbaale dara; du mburu mbaa mbuus mbaa xaalis ci seeni maxtume, waaye yemleen ci aw yet rekk.
9Mas que calzasen sandalias, y no vistiesen dos túnicas.
9 Sol-leen ay dàll te yem ci benn turki.»
10Y les decía: Donde quiera que entréis en una casa, posad en ella hasta que salgáis de allí.
10 Mu ne leen: «Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen jóge dëkk ba.
11Y todos aquellos que no os recibieren ni os oyeren, saliendo de allí, sacudid el polvo que está debajo de vuestros pies, en testimonio á ellos. De cierto os digo que más tolerable será el castigo de los de Sodoma y Gomorra el día del juicio, que el de aqu
11 Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, génnleen fa, yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.»
12Y saliendo, predicaban que los hombres se arrepintiesen.
12 Noonu taalibe ya dem, di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar.»
13Y echaban fuera muchos demonios, y ungían con aceite á muchos enfermos, y sanaban.
13 Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen.
14Y oyó el rey Herodes la fama de Jesús, porque su nombre se había hecho notorio; y dijo: Juan el que bautizaba, ha resucitado de los muertos, y por tanto, virtudes obran en él.
14 Noonu Erodd buur bi dégg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: «Yaxya dekki na, moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
15Otros decían: Elías es. Y otros decían: Profeta es, ó alguno de los profetas.
15 Ñeneen ne: «Kii Iliyas la.» Ñi ci des ne: «Yonent la, bu mel ni yonent yu jëkk ya.»
16Y oyéndo lo Herodes, dijo: Este es Juan el que yo degollé: él ha resucitado de los muertos.
16 Waaye bi ko Erodd déggee, mu ne: «Yaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki.»
17Porque el mismo Herodes había enviado, y prendido á Juan, y le había aprisionado en la cárcel á causa de Herodías, mujer de Felipe su hermano; pues la había tomado por mujer.
17 Fekk Erodd yónnee woon na, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam.
18Porque Juan decía á Herodes: No te es lícito tener la mujer de tu hermano.
18 Te Yaxya ne ko: «Jaaduwul nga denc sa jabaru mag.»
19Mas Herodías le acechaba, y deseaba matarle, y no podía:
19 Moo tax Erojàdd ëmbal ko mer, ba bëgg koo rey, waaye mënu koo def.
20Porque Herodes temía á Juan, sabiendo que era varón justo y santo, y le tenía respeto: y oyéndole, hacía muchas cosas; y le oía de buena gana.
20 Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba sàmm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan déglu it, day jaaxle lool, teewul mu bég ci déglu ko.
21Y venido un día oportuno, en que Herodes, en la fiesta de su nacimiento, daba una cena á sus príncipes y tribunos, y á los principales de Galilea;
21 Noonu bés bu yell ñëw, ba Erodd doon màggal bésu juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile.
22Y entrando la hija de Herodías, y danzando, y agradando á Herodes y á los que estaban con él á la mesa, el rey dijo á la muchacha: Pídeme lo que quisieres, que yo te lo daré.
22 Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.»
23Y le juró: Todo lo que me pidieres te daré, hasta la mitad de mi reino.
23 Mu boole ci ngiñ ne ko: «Loo ma man a laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wàllu réew mi sax.»
24Y saliendo ella, dijo á su madre: ¿Qué pediré? Y ella dijo: La cabeza de Juan Bautista.
24 Noonu janq bi génn ne ndeyam: «Lu may laaj?» Mu tontu ko: «Laajal boppu Yaxya.»
25Entonces ella entró prestamente al rey, y pidió, diciendo: Quiero que ahora mismo me des en un plato la cabeza de Juan Bautista.
25 Mu daldi gaawantoo dugg nag ci kanamu buur bi ne ko: «Damaa bëgg, nga indil ma léegi boppu Yaxya ci biir ndab.»
26Y el rey se entristeció mucho; mas á causa del juramento, y de los que estaban con él á la mesa, no quiso desecharla.
26 Bi ko buur ba déggee, mu am naqar wu réy. Waaye bëggu koo gàntu ndax ngiñ li ak gan ñi.
27Y luego el rey, enviando uno de la guardia, mandó que fuese traída su cabeza;
27 Mu daldi yónni nag xarekat, jox ko ndigal, mu indil ko boppu Yaxya. Waa ji dem, dagg boppu Yaxya ca kaso ba,
28El cual fué, y le degolló en la cárcel, y trajó su cabeza en un plato, y la dió á la muchacha, y la muchacha la dió á su madre.
28 indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq bi, mu daldi ko jox yaayam.
29Y oyéndo lo sus discípulos, vinieron y tomaron su cuerpo, y le pusieron en un sepulcro.
29 Ba taalibey Yaxya déggee loolu, ñu ñëw, fab néew ba, suul ko ci bàmmeel.
30Y los apóstoles se juntaron con Jesús, y le contaron todo lo que habían hecho, y lo que habían enseñado.
30 Gannaaw loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li ñu def ak li ñu jàngale lépp.
31Y él les dijo: Venid vosotros aparte al lugar desierto, y reposad un poco. Porque eran muchos los que iban y venían, que ni aun tenían lugar de comer.
31 Ci kaw loolu Yeesu ne leen: «Nanu beddeeku, dem ci bérab bu wéet; ngeen noppalu fa tuuti.» Waxoon na loolu, ndaxte amoon na ñu bare ñu doon dem ak a dikk, ba amuñu sax jot ngir lekk.
32Y se fueron en un barco al lugar desierto aparte.
32 Noonu ñu dugg cig gaal, dem ca bérab bu wéet.
33Y los vieron ir muchos, y le conocieron; y concurrieron allá muchos á pie de las ciudades, y llegaron antes que ellos, y se juntaron á él.
33 Bi ñuy dem nag, am ñu leen gis, xàmmi leen, ñu daldi jóge ci dëkk yépp, daw, jiitu leen fa.
34Y saliendo Jesús vió grande multitud, y tuvo compasión de ellos, porque eran como ovejas que no tenían pastor; y les comenzó á enseñar muchas cosas.
34 Bi Yeesu génnee gaal gi, mu gis mbooloo mu réy, yërëm leen, ndaxte dañoo mel ni xar yu amul sàmm. Kon mu daldi leen jàngal lu bare.
35Y como ya fuese el día muy entrado, sus discípulos llegaron á él, diciendo: El lugar es desierto, y el día ya muy entrado;
35 Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi.
36Envíalos para que vayan á los cortijos y aldeas de alrededor, y compren para sí pan; porque no tienen qué comer.
36 Yiwil mbooloo mi nag, ñu dugg ci àll bi ak dëkk yi nu wër, jënd lu ñu lekk.»
37Y respondiendo él, les dijo: Dadles de comer vosotros. Y le dijeron: ¿Que vayamos y compremos pan por doscientos denarios, y les demos de comer?
37 Waaye Yeesu tontu leen ne: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom-ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?»
38Y él les dice: ¿Cuántos panes tenéis? Id, y vedlo. Y sabiéndolo, dijeron: Cinco, y dos peces.
38 Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am? Demleen seeti.» Ñu dem seeti ne ko: «Juróomi mburu ak ñaari jën.»
39Y les mandó que hiciesen recostar á todos por partidas sobre la hierba verde.
39 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu def ay géew, toog ci ñax mu naat mi.
40Y se recostaron por partidas, de ciento en ciento, y de cincuenta en cincuenta.
40 Ñu toog nag ay géewi juróom-fukk ak téeméer.
41Y tomados los cinco panes y los dos peces, mirando al cielo, bendijo, y partió los panes, y dió á sus discípulos para que los pusiesen delante: y repartió á todos los dos peces.
41 Bi loolu amee Yeesu jël juróomi mburu yi ak ñaari jën yi, xool ci kaw, sant Yàlla, ba noppi mu damm mburu yi, jox ko taalibe yi, ngir ñu séddale ko mbooloo mi. Ñaari jën yi it mu séddale ko ñépp.
42Y comieron todos, y se hartaron.
42 Noonu ñépp lekk ba suur.
43Y alzaron de los pedazos doce cofines llenos, y de los peces.
43 Te it ñu dajale la desoon ca dammiti mburu ak jën ya, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees.
44Y los que comieron eran cinco mil hombres.
44 Ñu lekkoon nag matoon na limu juróomi junniy góor.
45Y luego dió priesa á sus discípulos á subir en el barco, é ir delante de él á Bethsaida de la otra parte, entre tanto que él despedía la multitud.
45 Ci kaw loolu Yeesu sant ay taalibeem, ñu dugg ci gaal gi, jàll ba Betsayda, bi muy yiwi mbooloo mi.
46Y después que los hubo despedido, se fué al monte á orar.
46 Bi mu tàggtoo ak mbooloo mi, mu yéeg ca tund wa, ñaan fa Yàlla.
47Y como fué la tarde, el barco estaba en medio de la mar, y él solo en tierra.
47 Noonu guddi jot, fekk gaal gi nekk ci diggu dex gi, te Yeesu rekk moo nekk ca tefes ga.
48Y los vió fatigados bogando, porque el viento les era contrario: y cerca de la cuarta vigilia de la noche, vino á ellos andando sobre la mar, y quería precederlos.
48 Booba mu gis taalibe yi sonn lool ci joow gaal gi ndax li leen ngelaw li soflu. Ca njël nag mu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi, ba xaw leen a raw.
49Y viéndole ellos, que andaba sobre la mar, pensaron que era fantasma, y dieron voces;
49 Bi ñu ko gisee nag, muy dox ci kaw dex gi, ñu foog ne njuuma la, daldi yuuxu.
50Porque todos le veían, y se turbaron. Mas luego habló con ellos, y les dijo: Alentaos; yo soy, no temáis.
50 Ndaxte ñépp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak ñoom ci saa si ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!»
51Y subió á ellos en el barco, y calmó el viento: y ellos en gran manera estaban fuera de sí, y se maravillaban:
51 Noonu mu fekksi leen ci gaal gi, ngelaw daldi ne tekk.
52Porque aun no habían considerado lo de los panes, por cuanto estaban ofuscados sus corazones.
52 Njàqarey taalibe ya nag weesu dayo, ndaxte seen xol dafa fatt, ba réere mbir kéemaan, gi Yeesu defoon ci mburu yi.
53Y cuando estuvieron de la otra parte, vinieron á tierra de Genezaret, y tomaron puerto.
53 Bi nga xamee ne jàll nañu, ba egg diiwaanu Senesaret, ñu teer fa,
54Y saliendo ellos del barco, luego le conocieron.
54 génn ca gaal ga. Ci saa si nit ñi xàmmi ko,
55Y recorriendo toda la tierra de alrededor, comenzaron á traer de todas partes enfermos en lechos, á donde oían que estaba.
55 ñu daldi daw ca diiwaan ba bépp, te fépp fu ñu ko dégg ñu di ko indil ñu wopp, tëdd ci seeni lal.
56Y donde quiera que entraba, en aldeas, ó ciudades, ó heredades, ponían en las calles á los que estaban enfermos, y le rogaban que tocasen siquiera el borde de su vestido; y todos los que le tocaban quedaban sanos.
56 Te fu mu man a aw, ci dëkk yu mag mbaa yu ndaw walla ci àll bi, ñu indil ko jarag yi ci pénc yi, ñaan ko, mu may leen ñu laal cati mbubbam rekk. Te képp ku ko laal daldi wér.