1ܐܢ ܒܟܠ ܠܫܢ ܕܒܢܝܢܫܐ ܐܡܠܠ ܘܒܕܡܠܐܟܐ ܘܚܘܒܐ ܠܐ ܢܗܘܐ ܒܝ ܗܘܝܬ ܠܝ ܢܚܫܐ ܕܙܐܡ ܐܘ ܨܨܠܐ ܕܝܗܒ ܩܠܐ ܀
1 Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi.
2ܘܐܢ ܬܗܘܐ ܒܝ ܢܒܝܘܬܐ ܘܐܕܥ ܐܪܙܐ ܟܠܗܘܢ ܘܟܠܗ ܝܕܥܬܐ ܘܐܢ ܬܗܘܐ ܒܝ ܟܠܗ ܗܝܡܢܘܬܐ ܐܝܟܢܐ ܕܛܘܪܐ ܐܫܢܐ ܘܚܘܒܐ ܠܝܬ ܒܝ ܠܐ ܗܘܝܬ ܡܕܡ ܀
2 Su ma yéglee wax ju tukkee ci Yàlla, ma xam lépp luy kumpa, ma yor xam-xam bépp, te gëm Yàlla ba man a randal ay tund, fekk boolewuma ci mbëggeel, duma dara.
3ܘܐܢ ܐܘܟܠ ܟܠ ܕܐܝܬ ܠܝ ܠܡܤܟܢܐ ܘܐܢ ܐܫܠܡ ܦܓܪܝ ܕܢܐܩܕ ܘܚܘܒܐ ܠܐ ܢܗܘܐ ܒܝ ܡܕܡ ܠܐ ܝܬܪ ܐܢܐ ܀
3 Te it su ma doon saraxe li ma am lépp, di bàyyi ñu lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mbëggeel, du ma jariñ dara.
4ܚܘܒܐ ܢܓܝܪܐ ܗܝ ܪܘܚܗ ܘܒܤܝܡ ܚܘܒܐ ܠܐ ܚܤܡ ܚܘܒܐ ܠܐ ܡܫܬܓܫ ܘܠܐ ܡܬܚܬܪ ܀
4 Ku bëgg dafay muñ te laabiir. Ku bëgg du kiñaan, du kañu, du tiitaru,
5ܘܠܐ ܤܥܪ ܕܒܗܬܬܐ ܘܠܐ ܒܥܐ ܕܝܠܗ ܘܠܐ ܡܬܬܦܝܪ ܘܠܐ ܡܬܪܥܐ ܕܒܝܫ ܀
5 du def lu jekkadi, du wut njariñu boppam, du naqari deret, du ñaaw njort.
6ܠܐ ܚܕܐ ܒܥܘܠܐ ܐܠܐ ܚܕܐ ܒܩܘܫܬܐ ܀
6 Du bég ci lu awul yoon, waaye dina bég ci lépp luy jollil dëgg.
7ܟܠ ܡܕܡ ܡܤܝܒܪ ܟܠܡܕܡ ܡܗܝܡܢ ܟܠ ܡܤܒܪ ܟܠ ܤܒܠ ܀
7 Mbëggeel day baale lépp, am gëm ci lépp, yaakaar lépp, muñ lépp.
8ܚܘܒܐ ܡܡܬܘܡ ܠܐ ܢܦܠ ܢܒܝܘܬܐ ܓܝܪ ܢܬܒܛܠܢ ܘܠܫܢܐ ܢܫܬܬܩܘܢ ܘܝܕܥܬܐ ܬܬܒܛܠ ܀
8 Mbëggeel amul àpp. Ñiy wax ci kàddug Yàlla dinañu noppi, ñiy wax ay làkk dinañu ko bàyyi, ñiy xamle xam-xamu Yàlla wàcc.
9ܩܠܝܠ ܗܘ ܓܝܪ ܡܢ ܤܓܝ ܝܕܥܝܢܢ ܘܩܠܝܠ ܡܢ ܤܓܝ ܡܬܢܒܝܢܢ ܀
9 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xebaar bi nu Yàlla dénk des na.
10ܐܡܬܝ ܕܝܢ ܕܬܐܬܐ ܓܡܝܪܘܬܐ ܗܝܕܝܢ ܢܬܒܛܠ ܗܘ ܡܕܡ ܕܩܠܝܠ ܗܘܐ ܀
10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul jóge fi.
11ܟܕ ܝܠܘܕܐ ܗܘܝܬ ܐܝܟ ܝܠܘܕܐ ܡܡܠܠ ܗܘܝܬ ܘܐܝܟ ܝܠܘܕܐ ܡܬܪܥܐ ܗܘܝܬ ܘܐܝܟ ܝܠܘܕܐ ܡܬܚܫܒ ܗܘܝܬ ܟܕ ܗܘܝܬ ܕܝܢ ܓܒܪܐ ܒܛܠܬ ܗܠܝܢ ܕܛܠܝܘܬܐ ܀
11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di dégge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, bàyyi naa lu bokkoon cig ndaw.
12ܗܫܐ ܐܝܟ ܕܒܡܚܙܝܬܐ ܚܙܝܢܢ ܒܦܠܐܬܐ ܗܝܕܝܢ ܕܝܢ ܐܦܝܢ ܠܘܩܒܠ ܐܦܝܢ ܗܫܐ ܝܕܥ ܐܢܐ ܩܠܝܠ ܡܢ ܤܓܝ ܗܝܕܝܢ ܕܝܢ ܐܕܥ ܐܝܟ ܡܐ ܕܐܬܝܕܥܬ ܀
12 Tey jii gis bu lëndëm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu lëndëm, bu ëllëgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na, bu ëllëgee dinaa xam ba mat sëkk, ni ma Yàlla xame.
13ܗܠܝܢ ܐܢܝܢ ܓܝܪ ܬܠܬ ܕܡܟܬܪܢ ܗܝܡܢܘܬܐ ܘܤܒܪܐ ܘܚܘܒܐ ܕܪܒ ܕܝܢ ܡܢܗܝܢ ܚܘܒܐ ܀
13 Léegi nag ñett yii ñooy sax: ngëm, yaakaar, mbëggeel; te mbëggeel moo ci raw.