1ܡܘܕܥ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܕܝܢ ܐܚܝ ܐܘܢܓܠܝܘܢ ܕܤܒܪܬܟܘܢ ܘܩܒܠܬܘܢܝܗܝ ܘܩܡܬܘܢ ܒܗ ܀
1 Léegi nag bokk yi, maa ngi leen di fàttali xebaar bu baax bi ma leen yégal. Xebaar bu baax boobu, nangu ngeen ko te yéena ngi ciy sax.
2ܘܒܗ ܚܐܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܐܝܕܐ ܡܠܬܐ ܤܒܪܬܟܘܢ ܐܢ ܥܗܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܢ ܠܐ ܗܘܐ ܤܪܝܩܐܝܬ ܗܝܡܢܬܘܢ ܀
2 Ci moom ngeen jaare, ba mucc, bu ngeen téyee bu dëgër njàngale mi, ni ma leen ko yégale. Walla xanaa boog gëm ngeen ko cig neen?
3ܐܫܠܡܬ ܠܟܘܢ ܓܝܪ ܡܢ ܠܘܩܕܡ ܐܝܟ ܡܕܡ ܕܩܒܠܬ ܕܡܫܝܚܐ ܡܝܬ ܥܠ ܐܦܝ ܚܛܗܝܢ ܐܝܟܢܐ ܕܟܬܝܒ ܀
3 Li ma jotoon, jottali naa leen ko, te moo jëkk ci maana yi: Kirist dee na ngir dindi sunuy bàkkaar, ni ko Mbind mi tërale,
4ܘܕܐܬܩܒܪ ܘܩܡ ܠܬܠܬܐ ܝܘܡܝܢ ܐܝܟ ܕܟܬܝܒ ܀
4 suul nañu ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba, ni ko Mbind mi tërale.
5ܘܐܬܚܙܝ ܠܟܐܦܐ ܘܒܬܪܗ ܠܬܪܥܤܪ ܀
5 Feeñu na Sefas, teg ca fukki taalibe ya ak ñaar.
6ܘܒܬܪܟܢ ܐܬܚܙܝ ܠܝܬܝܪ ܡܢ ܚܡܫܡܐܐ ܐܚܝܢ ܐܟܚܕܐ ܕܤܓܝܐܐ ܡܢܗܘܢ ܩܝܡܝܢ ܐܢܘܢ ܥܕܡܐ ܠܗܫܐ ܘܡܢܗܘܢ ܕܡܟܘ ܀
6 Gannaaw ga feeñu na lu ëpp juróomi téeméeri bokki taalibe ci benn yoon. Te ñu bare ci ñoom ñu ngi dund ba léegi, waaye am na ci ñu nelaw.
7ܘܡܢ ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܐܬܚܙܝ ܠܝܥܩܘܒ ܘܒܬܪܗ ܠܫܠܝܚܐ ܟܠܗܘܢ ܀
7 Ba noppi feeñu na Saag ak ndawi Kirist yépp.
8ܠܚܪܬܐ ܕܝܢ ܕܟܠܗܘܢ ܐܝܟ ܕܠܝܚܛܐ ܐܬܚܙܝ ܐܦ ܠܝ ܀
8 Man nag la mujj a feeñu, ma mel ni liir bu judduwul ci jamonoom.
9ܐܢܐ ܐܢܐ ܓܝܪ ܙܥܘܪܗܘܢ ܕܫܠܝܚܐ ܘܠܐ ܫܘܐ ܐܢܐ ܕܐܬܩܪܐ ܫܠܝܚܐ ܡܛܠ ܕܪܕܦܬ ܥܕܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
9 Ndaxte maa gën a ñàkk solo ci ndawi Kirist yi, te yeyoowuma sax, ñu may wooye ndaw, man mi doon fitnaal mbooloom Yàlla.
10ܒܛܝܒܘܬܗ ܕܝܢ ܕܐܠܗܐ ܐܝܬܝ ܡܕܡ ܕܐܝܬܝ ܘܛܝܒܘܬܗ ܕܒܝ ܠܐ ܗܘܬ ܤܪܝܩܐ ܐܠܐ ܝܬܝܪ ܡܢ ܟܠܗܘܢ ܠܐܝܬ ܠܐ ܐܢܐ ܐܠܐ ܛܝܒܘܬܗ ܕܥܡܝ ܀
10 Waaye nag yiwu Yàlla moo tax ma doon li ma doon, te yiw, wi mu wone ci man, du cig neen. Waaye sax maa gën a liggéey ñi ci des ñépp: du ci man, waaye yiwu Yàlla, wiy jëf ci man, moo tax.
11ܐܢ ܐܢܐ ܗܟܝܠ ܘܐܢ ܗܢܘܢ ܗܟܢܐ ܡܟܪܙܝܢܢ ܘܗܟܢܐ ܗܝܡܢܬܘܢ ܀
11 Noonu nag muy man muy ñoom, dénkaane boobu lanuy yégle, te moom ngeen gëm.
12ܐܢ ܕܝܢ ܡܫܝܚܐ ܡܬܟܪܙ ܕܩܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܐܝܟܢܐ ܐܝܬ ܒܟܘܢ ܐܢܫܐ ܕܐܡܪܝܢ ܠܝܬ ܚܝܬ ܡܝܬܐ ܀
12 Waaye su nu yéglee ne, Kirist dekki na, nan la ñenn ñi ci yéen man a waxe ne, néew yi duñu dekki?
13ܘܐܢ ܚܝܬ ܡܝܬܐ ܠܝܬ ܐܦܠܐ ܡܫܝܚܐ ܩܡ ܀
13 Su fekkee ne ñi dee duñu dekki, kon Kirist it dekkiwul.
14ܘܐܢ ܡܫܝܚܐ ܠܐ ܩܡ ܤܪܝܩܐ ܗܝ ܟܪܘܙܘܬܢ ܤܪܝܩܐ ܐܦ ܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܀
14 Te su Kirist dekkiwul, sunu waare day neen, te it seen ngëm day neen.
15ܡܫܬܟܚܝܢ ܚܢܢ ܕܝܢ ܐܦ ܤܗܕܐ ܕܓܠܐ ܕܐܠܗܐ ܕܐܤܗܕܢ ܥܠ ܐܠܗܐ ܕܐܩܝܡ ܠܡܫܝܚܐ ܟܕ ܠܐ ܐܩܝܡ ܀
15 Rax-ca-dolli gis nañu ne, seedeel nanu Yàlla ay fen, ndaxte seede nanu ci mbiram ne, dekkal na Yeesu, te fekk dekkalu ko, su néew yi dul dekki.
16ܐܢ ܡܝܬܐ ܓܝܪ ܠܐ ܩܝܡܝܢ ܐܦܠܐ ܡܫܝܚܐ ܩܡ ܀
16 Su néew yi dul dekki, Kirist moom it dekkiwul.
17ܘܐܢ ܡܫܝܚܐ ܠܐ ܩܡ ܒܛܠܐ ܗܝ ܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܘܥܕܟܝܠ ܒܚܛܗܝܟܘܢ ܐܢܬܘܢ ܀
17 Te su Kirist dekkiwul, seen ngëm du am solo, ba tey yéena ngi ci seeni bàkkaar.
18ܘܟܒܪ ܐܦ ܐܝܠܝܢ ܕܕܡܟܘ ܒܡܫܝܚܐ ܐܒܕܘ ܠܗܘܢ ܀
18 Te it ñi dee ba noppi ci Kirist sànku nañu.
19ܘܐܢ ܒܗܠܝܢ ܗܘ ܚܝܐ ܒܠܚܘܕ ܡܤܒܪܝܢܢ ܒܡܫܝܚܐ ܕܘܝܢܢ ܗܘ ܡܢ ܟܠܗܘܢ ܒܢܝܢܫܐ ܀
19 Su fekkee ci giiru dund gii rekk la sunu yaakaar ci Kirist ame solo, kon noo gën a mat a yërëm ñépp.
20ܗܫܐ ܕܝܢ ܡܫܝܚܐ ܩܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܘܗܘܐ ܪܫܝܬܐ ܕܕܡܟܐ ܀
20 Waaye léegi Kirist dekki na, di ku jëkk a dekki, ni gub yi ñu jëkk a tànne ci ngóob mi, jagleel leen Yàlla.
21ܘܐܝܟܢܐ ܕܒܝܕ ܒܪܢܫܐ ܗܘܐ ܡܘܬܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܒܝܕ ܒܪܢܫܐ ܗܘܝܐ ܚܝܬ ܡܝܬܐ ܀
21 Gannaaw ci nit la dee jaar, dugg àddina, kon it ci nit la ndekkite jaar.
22ܐܝܟܢܐ ܓܝܪ ܕܒܐܕܡ ܟܠܗܘܢ ܒܢܝܢܫܐ ܡܝܬܝܢ ܗܟܢܐ ܐܦ ܒܡܫܝܚܐ ܟܠܗܘܢ ܚܐܝܢ ܀
22 Kon ni ñépp deeye ci seen bokk ci Aadama, noonu la ñépp di dundaate ci seen bokk ci Kirist.
23ܐܢܫ ܐܢܫ ܒܛܟܤܗ ܪܫܝܬܐ ܗܘܐ ܡܫܝܚܐ ܒܬܪܟܢ ܐܝܠܝܢ ܕܕܡܫܝܚܐ ܐܢܘܢ ܒܡܐܬܝܬܗ ܀
23 Waaye ku nekk ak ayam. Kirist moo jëkk, mel ni gub yi ñu jëkk a tànne ci ngóob mi, ba noppi, bu Kirist dellusee, ñi bokk ci moom jël seen ay.
24ܘܗܝܕܝܢ ܬܗܘܐ ܚܪܬܐ ܡܐ ܕܡܫܠܡ ܡܠܟܘܬܐ ܠܐܠܗܐ ܐܒܐ ܡܐ ܕܒܛܠ ܟܠ ܪܝܫ ܘܟܠ ܫܘܠܛܢ ܘܟܠ ܚܝܠܝܢ ܀
24 Gannaaw ga, mujug jamono taxaw, te Kirist dina noot gépp kilifa ak bépp sañ-sañ ak doole, ba noppi delloo nguur gi kiy Yàlla di Baayam.
25ܥܬܝܕ ܗܘ ܓܝܪ ܕܢܡܠܟ ܥܕܡܐ ܕܢܤܝܡ ܒܥܠܕܒܒܘܗܝ ܟܠܗܘܢ ܬܚܝܬ ܪܓܠܘܗܝ ܀
25 Ndaxte fàww Kirist nguuru, ba kera Yàlla di daaneel noonam yépp ciy tànkam.
26ܘܐܚܪܝܐ ܒܥܠܕܒܒܐ ܡܬܒܛܠ ܡܘܬܐ ܀
26 Noon bu mujj, bi mu fiy jële, mooy dee.
27ܟܠ ܓܝܪ ܫܥܒܕ ܬܚܝܬ ܪܓܠܘܗܝ ܡܐ ܕܐܡܪ ܕܝܢ ܕܟܠܡܕܡ ܡܫܬܥܒܕ ܠܗ ܝܕܝܥܐ ܕܤܛܪ ܡܢ ܗܘ ܕܫܥܒܕ ܠܗ ܟܠ ܀
27 Ndaxte Mbind mi nee na: «Yàlla nootal na ko lépp, mu teg ci tànk.» Waaye bu Mbind mi nee, «noot na lépp,» wóor na ne, moom mi ko nootal lépp, génne na ci boppam.
28ܘܡܐ ܕܐܫܬܥܒܕ ܠܗ ܟܠ ܗܝܕܝܢ ܗܘ ܒܪܐ ܢܫܬܥܒܕ ܠܗܘ ܕܫܥܒܕ ܠܗ ܟܠ ܕܢܗܘܐ ܐܠܗܐ ܟܠ ܒܟܠ ܀
28 Léegi bu ñu ko nootalee lépp nag, moom Kirist muy Doom ji dina delloo kilifteef gi Yàlla, mi ko nootal lépp, ngir Yàlla nekk buur ci lépp.
29ܘܐܠܐ ܡܢܐ ܢܥܒܕܘܢ ܗܢܘܢ ܕܥܡܕܝܢ ܚܠܦ ܡܝܬܐ ܐܢ ܡܝܬܐ ܠܐ ܩܝܡܝܢ ܡܢܐ ܥܡܕܝܢ ܚܠܦ ܡܝܬܐ ܀
29 Su ndekkite amul, kon ñi ñu sóob ci ndox ngir ñi dee, lu mu leen di jariñ? Su dekki amul, kon lu tax ñu leen di sóob ngir ñi dee?
30ܘܠܡܢܐ ܐܦ ܚܢܢ ܒܟܠ ܫܥܐ ܒܩܢܕܝܢܘܤ ܩܝܡܝܢܢ ܀
30 Te nun it lu tax fu nu tollu nu jaay sunu bakkan?
31ܝܡܐ ܐܢܐ ܒܫܘܒܗܪܟܘܢ ܐܚܝ ܕܐܝܬ ܠܝ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܟܠܝܘܡ ܡܐܬ ܐܢܐ ܀
31 Bokk yi, ni ma damoo ci yéen ndax Yeesu Kirist, ni la ma wóore ne, bés bu nekk ma riisu dee.
32ܐܢ ܐܝܟ ܕܒܝܬ ܒܢܝܢܫܐ ܐܫܬܕܝܬ ܠܚܝܘܬܐ ܒܐܦܤܘܤ ܡܢܐ ܐܬܗܢܝܬ ܐܢ ܡܝܬܐ ܠܐ ܩܝܡܝܢ ܢܐܟܘܠ ܘܢܫܬܐ ܡܚܪ ܓܝܪ ܡܝܬܝܢܢ ܀
32 Su fekkee ne ci ni ñu ko waxe, xeex naa ca dëkku Efes ak rabi àll, kon ban njariñ la may amal? Su néew yi dul woon dekki, am na lu ci léeb wax:«Nanu lekk di naan, ndaxte ëllëg dinanu dee.»
33ܠܐ ܬܛܥܘܢ ܡܚܒܠܢ ܪܥܝܢܐ ܒܤܝܡܐ ܫܘܥܝܬܐ ܒܝܫܬܐ ܀
33 Bu leen ko réere mbir: «Ànd bu bon dina yàq nit ku baax.»
34ܐܥܝܪܘ ܠܒܟܘܢ ܙܕܝܩܐܝܬ ܘܠܐ ܬܚܛܘܢ ܐܝܬ ܓܝܪ ܐܢܫܐ ܕܝܕܥܬܐ ܕܐܠܗܐ ܠܝܬ ܒܗܘܢ ܠܒܗܬܬܟܘܢ ܗܘ ܐܡܪ ܐܢܐ ܀
34 Delloosileen xel yi te bàyyi bàkkaar, ndaxte am na ci yéen, ñu umple Yàlla. Kon war ngeen a rus!
35ܢܐܡܪ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܕܐܝܟܢܐ ܩܝܡܝܢ ܡܝܬܐ ܘܒܐܝܢܐ ܦܓܪܐ ܐܬܝܢ ܀
35 Waaye dina am kuy naan: «Nan la néew yi di dekkee? Wan yaram lañuy dellusee?»
36ܤܟܠܐ ܙܪܥܐ ܕܙܪܥ ܐܢܬ ܐܢ ܠܐ ܡܐܬ ܠܐ ܚܝܐ ܀
36 Yaa gàtt xel! Li ngay ji, du jebbi dund gu bees, fi ak deewul ba noppi.
37ܘܗܘ ܡܕܡ ܕܙܪܥ ܐܢܬ ܠܐ ܗܘܐ ܗܘ ܦܓܪܐ ܕܥܬܝܕ ܠܡܗܘܐ ܙܪܥ ܐܢܬ ܐܠܐ ܦܪܕܬܐ ܥܪܛܠܝܬܐ ܕܚܛܐ ܐܘ ܕܤܥܪܐ ܐܘ ܕܫܪܟܐ ܕܙܪܥܘܢܐ ܀
37 Te li ngay ji du jëmmi gàncax giy ñëwi, waaye pepp kese la, maanaam dugub, walla weneen jiwu.
38ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܝܗܒ ܠܗ ܦܓܪܐ ܐܝܟܢܐ ܕܨܒܐ ܘܠܚܕ ܚܕ ܡܢ ܙܪܥܘܢܐ ܦܓܪܐ ܕܟܝܢܗ ܀
38 Noonu Yàlla jox ko jëmm ju ko neex, jiwu wu nekk ak jëmmam.
39ܠܐ ܗܘܐ ܕܝܢ ܟܠ ܦܓܪ ܫܘܐ ܐܚܪܝܢ ܗܘ ܓܝܪ ܦܓܪܐ ܕܒܪ ܐܢܫܐ ܘܐܚܪܝܢ ܕܒܥܝܪܐ ܘܐܚܪܝܢ ܕܦܪܚܬܐ ܘܐܚܪܝܢ ܕܢܘܢܐ ܀
39 Jëmmi mbindeef yépp a wuute: nit ak jëmmam, mala, picc, jën — yu ci nekk ak sa jëmmi bopp.
40ܘܐܝܬ ܦܓܪܐ ܫܡܝܢܐ ܘܐܝܬ ܦܓܪܐ ܐܪܥܢܝܐ ܐܠܐ ܐܚܪܝܢ ܗܘ ܫܘܒܚܐ ܕܫܡܝܢܐ ܘܐܚܪܝܢ ܕܐܪܥܢܝܐ ܀
40 Am na itam ay jëmm ca asamaan ak ay jëmm ci suuf. Leeru jëmm ca asamaan wuute na ak gi ci suuf.
41ܘܐܚܪܝܢ ܗܘ ܫܘܒܚܐ ܕܫܡܫܐ ܘܐܚܪܝܢ ܫܘܒܚܐ ܕܤܗܪܐ ܘܐܚܪܝܢ ܫܘܒܚܐ ܕܟܘܟܒܐ ܘܟܘܟܒܐ ܡܢ ܟܘܟܒܐ ܡܝܬܪ ܗܘ ܒܫܘܒܚܐ ܀
41 Jant bi, weer wi ak biddiiw, lu nekk ak sag leer. Te it leeru biddiiw bu nekk dina wuute ak moroomam.
42ܗܟܢܐ ܐܦ ܚܝܬ ܡܝܬܐ ܡܙܕܪܥܝܢ ܒܚܒܠܐ ܩܝܡܝܢ ܕܠܐ ܚܒܠܐ ܀
42 Noonu la ndekkitel néew yi di deme. Bu ñu suulee néew bi, dañoo ji lu yàqu. Bu dekkee, du yàqooti ba abadan.
43ܡܙܕܪܥܝܢ ܒܨܥܪܐ ܩܝܡܝܢ ܒܫܘܒܚܐ ܡܙܕܪܥܝܢ ܒܟܪܝܗܘܬܐ ܩܝܡܝܢ ܒܚܝܠܐ ܀
43 Lu ñàkk solo lañuy suul; mu dekki ak ndam. Lu néew doole lañuy suul, mu dekki ak kàttan.
44ܡܙܕܪܥܝܢ ܦܓܪܐ ܢܦܫܢܝܐ ܩܐܡ ܦܓܪܐ ܪܘܚܢܝܐ ܐܝܬ ܓܝܪ ܦܓܪܐ ܕܢܦܫ ܘܐܝܬ ܦܓܪܐ ܕܪܘܚ ܀
44 Bu ñu koy suul, yaram lay doon wu soloo woon ruu. Bu dekkee, doon yaram wu soloo ndamu Xelum Yàlla. Ndegam am na yaram wu soloo ruu, kon dina am yaram wu soloo ndamu Xelum Yàlla.
45ܗܟܢܐ ܐܦ ܟܬܝܒ ܗܘܐ ܐܕܡ ܒܪܢܫܐ ܩܕܡܝܐ ܠܢܦܫ ܚܝܐ ܘܐܕܡ ܐܚܪܝܐ ܠܪܘܚܐ ܡܚܝܢܝܬܐ ܀
45 Mbind mi nee na: «Nit ku jëkk ka, Aadama, doon na boroom ruu,» waaye Aadama mu mujj mi doon na Xel muy joxe dund.
46ܐܠܐ ܠܐ ܗܘܐ ܠܘܩܕܡ ܪܘܚܢܝܐ ܐܠܐ ܢܦܫܢܝܐ ܘܗܝܕܝܢ ܪܘܚܢܝܐ ܀
46 Yaram wi soloo ndamu Xelum Yàlla jiituwul; yaramu doom Aadama moo jiitu; yaramu ndam li moo ci topp.
47ܒܪܢܫܐ ܩܕܡܝܐ ܥܦܪܢܐ ܕܡܢ ܐܪܥܐ ܒܪܢܫܐ ܕܬܪܝܢ ܡܪܝܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܀
47 Nit ku jëkk ka pëndu suuf la woon; ñaareelu nit ki di Kirist, mi ngi jóge asamaan.
48ܐܝܟܢܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܗܘ ܥܦܪܢܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܥܦܪܢܐ ܘܐܝܟܢܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܗܘ ܕܡܢ ܫܡܝܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܫܡܝܢܐ ܀
48 Waa àddina yor nañu jëmmi nit, ki ñu sàkke ci suuf; noonu it ñi bokk ci asamaan dinañu yor melokaanu ki jóge ci asamaan.
49ܘܐܝܟ ܕܠܒܫܢ ܕܡܘܬܐ ܕܗܘ ܕܡܢ ܥܦܪܐ ܗܟܢܐ ܢܠܒܫ ܕܡܘܬܐ ܕܗܘ ܕܡܢ ܫܡܝܐ ܀
49 Te ni nu yore melokaanu ki ñu sàkke ci suuf, noonu lanuy yoreji melokaanu ki jóge ca asamaan.
50ܗܕܐ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܐܚܝ ܕܒܤܪܐ ܘܕܡܐ ܡܠܟܘܬܐ ܕܫܡܝܐ ܠܡܐܪܬ ܠܐ ܡܫܟܚܝܢ ܘܠܐ ܚܒܠܐ ܝܪܬ ܠܐ ܡܬܚܒܠܢܘܬܐ ܀
50 Li may wax nag bokk yi, moo di ne, sunu yaram wii mënul a am wàll ci nguuru Yàlla, te lu yàqu mënul a am wàll ci liy sax abadan.
51ܗܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܐܪܙܐ ܠܘ ܟܠܢ ܢܕܡܟ ܟܠܢ ܕܝܢ ܢܬܚܠܦ ܀
51 Lii ma leen di xamal, mbóotu Yàlla la. Dégluleen, dunu jaar ci dee nun ñépp, waaye nun ñépp dinanu soppiku,
52ܚܪܝܦܐܝܬ ܐܝܟ ܪܦܦ ܥܝܢܐ ܒܩܪܢܐ ܐܚܪܝܬܐ ܟܕ ܬܩܪܐ ܘܢܩܘܡܘܢ ܡܝܬܐ ܕܠܐ ܚܒܠܐ ܘܚܢܢ ܢܬܚܠܦ ܀
52 ci saa su gàtt, ci xef-ak-xippi, bu liit gu mujj gi jibee. Ndax liit gi dina jib, néew yi dekki, di dund abadan, te nun dinanu soppiku.
53ܥܬܝܕ ܗܘ ܓܝܪ ܗܢܐ ܕܡܬܚܒܠ ܕܢܠܒܫ ܠܐ ܡܬܚܒܠܢܘܬܐ ܘܗܢܐ ܕܡܐܬ ܕܢܠܒܫ ܠܐ ܡܝܘܬܘܬܐ ܀
53 Yaram wu yàqu war na sol jëmm ja dul yàqooti, te yaram wiy dee sol dund gu sax abadan.
54ܡܐ ܕܠܒܫ ܕܝܢ ܗܢܐ ܕܡܬܚܒܠ ܠܐ ܡܬܚܒܠܢܘܬܐ ܘܗܢܐ ܕܡܐܬ ܠܐ ܡܝܘܬܘܬܐ ܗܝܕܝܢ ܬܗܘܐ ܡܠܬܐ ܗܝ ܕܟܬܝܒܐ ܕܐܬܒܠܥ ܡܘܬܐ ܒܙܟܘܬܐ ܀
54 Bu li yàqu solee melokaanu li dul yàqu, te liy dee sol melokaanu liy sax abadan, kon lii ñu wax ci Mbind mi mat:«Yàlla noot na dee, ba labal ko ci ndamam.
55ܐܝܟܘ ܥܘܩܤܟ ܡܘܬܐ ܐܘ ܐܝܟܐ ܗܝ ܙܟܘܬܟܝ ܫܝܘܠ ܀
55 Céy yaw dee! Ana sa ndam?Céy yaw dee! Ana sa daŋar ji ngay fitte?»
56ܥܘܩܤܗ ܕܝܢ ܕܡܘܬܐ ܚܛܝܬܐ ܗܝ ܘܚܝܠܐ ܕܚܛܝܬܐ ܢܡܘܤܐ ܗܘ ܀
56 Daŋaru dee mooy bàkkaar, te dooley bàkkaar mooy Yoon wi.
57ܛܝܒܘ ܕܝܢ ܠܐܠܗܐ ܕܝܗܒ ܠܢ ܙܟܘܬܐ ܒܝܕ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
57 Waaye jërë-jëf yaw Yàlla, ji nu jox ndam li jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist!
58ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܘܚܒܝܒܝ ܗܘܘ ܡܫܪܪܝܢ ܘܠܐ ܬܗܘܘܢ ܡܬܙܝܥܝܢ ܐܠܐ ܗܘܘ ܡܬܝܬܪܝܢ ܒܟܠܙܒܢ ܒܥܒܕܗ ܕܡܪܝܐ ܟܕ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܥܡܠܟܘܢ ܠܐ ܗܘܐ ܤܪܝܩ ܒܡܪܝܐ ܀
58 Kon nag sama bokk yi ma sopp, nangeen takku, sampu ba dëgër, te gën a sawar ci liggéeyu Boroom bi, xam ne seen liggéey, bi jëm ci Boroom bi, du neen.