Syriac: NT

Wolof: New Testament

1 Corinthians

6

1ܡܡܪܚ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܟܕ ܐܝܬ ܠܗ ܕܝܢܐ ܥܡ ܐܚܘܗܝ ܕܢܕܘܢ ܩܕܡ ܥܘܠܐ ܘܠܐ ܩܕܡ ܩܕܝܫܐ ܀
1 Te it bu kenn ci yéen amee lëj-lëj digganteem ak mbokku taalibeem, lu tax muy dem ca àttekaayi ñi xamul Yàlla, te bañ a dem ca gaayi Yàlla yi, ñu àtte ko?
2ܐܘ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܩܕܝܫܐ ܠܥܠܡܐ ܢܕܘܢܘܢ ܘܐܢ ܥܠܡܐ ܒܟܘܢ ܡܬܕܝܢ ܠܐ ܫܘܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܡܕܢ ܕܝܢܐ ܕܩܕܩܐ ܀
2 Xanaa dangeen a xamul ne, gaayi Yàlla yi ñooy àtteji àddina? Te ndegam yéenay àtteji àddina, lu tere ngeen man a àtte mbir yu ñàkk solo yi?
3ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܠܡܠܐܟܐ ܕܝܢܝܢܢ ܚܕ ܟܡܐ ܐܝܠܝܢ ܕܕܥܠܡܐ ܐܢܝܢ ܗܢܐ ܀
3 Xanaa xamuleen ne, nooy àtteji malaaka yi? waxatumaak mbiri àddina sii.
4ܐܠܐ ܐܢ ܐܝܬ ܠܟܘܢ ܕܝܢܐ ܥܠ ܕܥܠܡܐ ܠܐܝܠܝܢ ܕܒܤܝܢ ܒܥܕܬܐ ܐܘܬܒܘ ܠܟܘܢ ܒܕܝܢܐ ܀
4 Bu ngeen amee ay lëj-lëj yu mel noonu, dangeen di wuti ay àttekat ci ay nit, ñi amul wenn yoon ci mbooloom ñi gëm!
5ܠܟܘܐܪܐ ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܗܟܢܐ ܠܝܬ ܒܟܘܢ ܐܦܠܐ ܚܕ ܚܟܝܡܐ ܕܢܫܟܚ ܢܫܘܐ ܒܝܬ ܐܚܐ ܠܐܚܘܗܝ ܀
5 Ma ne kon, war ngeen a rus! Xanaa amul ci seen biir kenn ku am xel, ku man a àtte mbokkam yi?
6ܐܠܐ ܐܚܐ ܥܡ ܐܚܘܗܝ ܡܬܕܝܢ ܘܬܘܒ ܩܕܡ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܡܗܝܡܢܝܢ ܀
6 Waaye defuleen loolu; mbokk a ngi layoo ak moroomam, rax-ca-dolli ci kanamu ñi gëmul lañu koy defe!
7ܡܢ ܟܕܘ ܗܟܝܠ ܩܢܘܡܟܘܢ ܚܒܬܘܢ ܠܟܘܢ ܕܕܝܢܐ ܚܕ ܥܡ ܚܕ ܐܝܬ ܠܟܘܢ ܡܛܠ ܡܢܐ ܓܝܪ ܠܐ ܡܬܥܠܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܘܡܛܠ ܡܢܐ ܠܐ ܡܬܓܠܙܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
7 Layoo bi sax wone na ne, bàyyi ngeen seen warugar. Lu tax muñuleen sax tooñ, yi ñu leen di tooñ? Lu tax far nanguwuleen, ñu sàcc leen?
8ܐܠܐ ܐܢܬܘܢ ܥܠܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܘܓܠܙܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܦ ܠܐܚܝܟܘܢ ܀
8 Waaye yéen sax yéenay tooñ ak di sàcc, te seeni bokk ngeen koy def!
9ܐܘ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܥܘܠܐ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܠܐ ܝܪܬܝܢ ܠܐ ܬܛܥܘܢ ܠܐ ܙܢܝܐ ܘܠܐ ܦܠܚܝ ܦܬܟܪܐ ܘܠܐ ܓܝܪܐ ܘܠܐ ܡܚܒܠܐ ܘܠܐ ܫܟܒܝ ܥܡ ܕܟܪܐ ܀
9 Xanaa xamuleen ne, ñi jubadi duñu bokk ci nguuru Yàlla? Bu leen ci kenn nax: ñiy doxaan walla xërëmkat yi ak njaalookat yi ak góor-jigéen ñi ak ñi ko nangu,
10ܘܠܐ ܥܠܘܒܐ ܘܠܐ ܓܢܒܐ ܘܠܐ ܪܘܝܐ ܘܠܐ ܡܨܥܪܢܐ ܘܠܐ ܚܛܘܦܐ ܗܠܝܢ ܡܠܟܘܬܗ ܕܐܠܗܐ ܠܐ ܝܪܬܝܢ ܀
10 walla sàcc yi ak ñu bëgge ñi ak màndikat yi ak ñiy xaste ak njublaŋ yi, duñu bokk ci nguuru Yàlla.
11ܘܗܠܝܢ ܐܝܬ ܗܘܝ ܒܐܢܫ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܐܠܐ ܤܚܝܬܘܢ ܘܐܬܩܕܫܬܘܢ ܘܐܙܕܕܩܬܘܢ ܒܫܡܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܒܪܘܚܗ ܕܐܠܗܢ ܀
11 Te am na ñu meloon noonu ci yéen. Waaye Yàlla fóotal na leen seeni bàkkaar, sellal leen, àtte leen ni ñu jub, ci turu Boroom bi Yeesu Kirist ak ci dooley Xelum Yàlla, sunu Boroom.
12ܟܠ ܫܠܝܛ ܠܝ ܐܠܐ ܠܐ ܟܠ ܦܩܚ ܠܝ ܟܠ ܫܠܝܛ ܠܝ ܐܠܐ ܥܠܝ ܐܢܫ ܠܐ ܢܫܬܠܛ ܀
12 Am na ci yéen ñu naan: «Sañ naa lépp.» Waaw, waaye du lépp a jariñ nit. «Sañ naa lépp,» waaye duma bàyyi dara, mu noot ma.
13ܡܐܟܘܠܬܐ ܕܟܪܤܐ ܘܟܪܤܐ ܕܡܐܟܘܠܬܐ ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܠܬܪܬܝܗܝܢ ܡܒܛܠ ܦܓܪܐ ܕܝܢ ܠܐ ܠܙܢܝܘܬܐ ܐܠܐ ܠܡܪܢ ܘܡܪܢ ܠܦܓܪܐ ܀
13 Am na ci yéen ñu naan: «Ñam mooy jariñ biir, te biir ay jariñoo ñam.» Waaw, te Yàlla dina leen yàq, ñoom ñaar yépp. Waaye sàkkuñu yaram ngir moy Yàlla; dañu koo sàkk, ngir muy jariñ Boroom bi, Boroom bi di ko jariñoo.
14ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܘܠܡܪܢ ܐܩܝܡ ܘܠܢ ܡܩܝܡ ܒܚܝܠܗ ܀
14 Te Yàlla, mi dekkal Boroom bi, dina dekkal it sunu yaram jaare ko ci dooleem.
15ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܦܓܪܝܟܘܢ ܗܕܡܐ ܐܢܘܢ ܕܡܫܝܚܐ ܢܤܒ ܗܕܡܐ ܕܡܫܝܚܐ ܢܥܒܕܝܘܗܝ ܗܕܡܐ ܕܙܢܝܬܐ ܚܤ ܀
15 Xanaa xamuleen ne, seen yaram ñooy céri Kirist? Ndax kon damay jël céri Kirist, def ko céri jigéeni moykat? Mukk!
16ܐܘ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܡܢ ܕܢܩܦ ܠܙܢܝܬܐ ܚܕ ܗܘ ܦܓܪ ܐܡܝܪ ܓܝܪ ܕܢܗܘܘܢ ܬܪܝܗܘܢ ܚܕ ܦܓܪ ܀
16 Xanaa xamuleen ne, kuy ànd ak jigéen juy moy dafay booloo ak moom, nekk benn? Ndaxte Mbind mi nee na: «Ñoom ñaar dinañu doon benn.»
17ܡܢ ܕܢܩܦ ܕܝܢ ܠܡܪܢ ܗܘܐ ܥܡܗ ܚܕܐ ܪܘܚ ܀
17 Waaye nag kuy ànd ak Boroom bi, xel yi dañuy booloo, nekk benn.
18ܥܪܘܩܘ ܡܢ ܙܢܝܘܬܐ ܟܠ ܚܛܝܬܐ ܕܢܥܒܕ ܒܪܢܫܐ ܠܒܪ ܡܢ ܦܓܪܗ ܗܝ ܡܢ ܕܡܙܢܐ ܕܝܢ ܒܦܓܪܗ ܗܘ ܚܛܐ ܀
18 Dawleen njaaloo! Bépp bàkkaar bu nit man a def, du laal yaramam, waaye nag kuy njaaloo, dafay bàkkaar, di lor yaramam.
19ܐܘ ܠܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܦܓܪܟܘܢ ܗܝܟܠܐ ܗܘ ܕܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܕܥܡܪܐ ܒܟܘܢ ܗܝ ܕܩܒܠܬܘܢ ܡܢ ܐܠܗܐ ܘܠܐ ܗܘܝܬܘܢ ܕܢܦܫܟܘܢ ܀
19 Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy kër Yàlla gi? Gannaaw Xel mu Sell maa ngi ci yéen, te Yàllaa leen ko may, kon moomuleen seen bopp,
20ܐܙܕܒܢܬܘܢ ܓܝܪ ܒܕܡܝܐ ܗܘܝܬܘܢ ܗܟܝܠ ܡܫܒܚܝܢ ܠܐܠܗܐ ܒܦܓܪܟܘܢ ܘܒܪܘܚܟܘܢ ܗܢܘܢ ܕܐܝܬܝܗܘܢ ܕܐܠܗܐ ܀
20 ndaxte Yàlla jot na leen ak njëg gu réy. Kon nag màggal-leen Yàlla ci seen yaram.