1ܥܠ ܕܒܚܐ ܕܝܢ ܕܦܬܟܪܐ ܝܕܥܝܢܢ ܕܒܟܠܢ ܐܝܬ ܝܕܥܬܐ ܘܝܕܥܬܐ ܡܚܬܪܐ ܚܘܒܐ ܕܝܢ ܒܢܐ ܀
1 Léegi nag, ci li jëm ci yàpp wi ñu jébbal xërëm yi: nun ñépp am nanu xam-xam, loolu dëgg la. Xam-xam day tax ba nit yég boppam, waaye mbëggeel day yékkati ngëm.
2ܐܢ ܐܢܫ ܕܝܢ ܤܒܪ ܕܝܕܥ ܡܕܡ ܠܐ ܥܕܟܝܠ ܡܕܡ ܝܕܥ ܐܝܟ ܡܐ ܕܘܠܐ ܠܗ ܠܡܕܥ ܀
2 Ku xalaat ne xam nga dara, sa xam-xam bënnagul.
3ܐܢ ܐܢܫ ܕܝܢ ܡܚܒ ܠܐܠܗܐ ܗܢܐ ܐܬܝܕܥ ܡܢܗ ܀
3 Waaye ku bëgg Yàlla, Yàlla xam la.
4ܥܠ ܡܐܟܘܠܬܐ ܗܟܝܠ ܕܕܒܚܐ ܕܦܬܟܪܐ ܝܕܥܝܢܢ ܕܠܐ ܗܘܐ ܡܕܡ ܗܘ ܦܬܟܪܐ ܒܥܠܡܐ ܘܕܠܝܬ ܐܠܗ ܐܚܪܝܢ ܐܠܐ ܐܢ ܚܕ ܀
4 Kon nag ci li jëm ci lekk yàpp wu ñu jébbal xërëm yi, xam nanu ne, xërëm du dara ci àddina te xam nanu itam ne, Yàlla kenn rekk la.
5ܐܦܢ ܓܝܪ ܐܝܬ ܕܡܬܩܪܝܢ ܐܠܗܐ ܐܘ ܒܫܡܝܐ ܐܘ ܒܐܪܥܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܝܬ ܐܠܗܐ ܤܓܝܐܐ ܘܡܪܘܬܐ ܤܓܝܐܐ ܀
5 Su fekkee ne am na sax yu ñuy teg Yàlla, muy ci asamaan mbaa ci suuf --ndaxte am na yu bare yu ñu faral di bokkaaleel Yàlla ak Boroom bi —
6ܐܠܐ ܠܢ ܕܝܠܢ ܚܕ ܗܘ ܐܠܗܐ ܐܒܐ ܕܟܠ ܡܢܗ ܘܚܢܢ ܒܗ ܘܚܕ ܡܪܝܐ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܟܠ ܒܐܝܕܗ ܘܐܦ ܚܢܢ ܒܐܝܕܗ ܀
6 ba tey ci nun, jenn Yàlla rekk a am, muy Baay bi; lépp a ngi jóge ci moom te moom lanu nekkal. Te it benn Boroom rekk a am, muy Yeesu Kirist; lépp a ngi jaare ci moom, te nun it nu ngi dund jaare ci moom.
7ܐܠܐ ܠܐ ܗܘܐ ܒܟܠܢܫ ܝܕܥܬܐ ܐܝܬ ܓܝܪ ܐܢܫܐ ܕܒܬܐܪܬܗܘܢ ܥܕܡܐ ܠܗܫܐ ܕܥܠ ܦܬܟܪܐ ܐܝܟ ܕܕܒܝܚܐ ܐܟܠܝܢ ܘܡܛܠ ܕܟܪܝܗܐ ܬܐܪܬܗܘܢ ܡܬܛܘܫܐ ܀
7 Waaye ñépp xamuñu loolu. Am na ñu tàmmoon xërëm yi, te léegi, bu ñu lekkatee yàppu sarax yi, dañuy xalaat ne, xërëm lañu ko jagleel. Seen xel dafa leen di yedd, ndaxte ci seen ñàkka xam dañuy foog ne, taq nañu sobe ndax ñam woowu.
8ܡܐܟܘܠܬܐ ܕܝܢ ܠܐ ܡܩܪܒܐ ܠܢ ܠܐܠܗܐ ܠܐ ܓܝܪ ܐܢ ܐܟܠܝܢܢ ܡܬܝܬܪܝܢܢ ܘܠܐ ܐܢ ܠܐ ܢܐܟܘܠ ܡܬܒܨܪܝܢܢ ܀
8 Waaye ñam mënul a tax nu neex Yàlla. Su nu ci lekkee, du yokk dara ci nun. Su nu ci lekkul, du nu wàññi dara.
9ܚܙܘ ܕܝܢ ܕܠܡܐ ܫܘܠܛܢܟܘܢ ܗܢܐ ܢܗܘܐ ܬܘܩܠܬܐ ܠܟܪܝܗܐ ܀
9 Waaye moytuleen, ba sañ-sañ bi ngeen am, bañ a yóbbe bàkkaar ñi seen ngëm néew.
10ܐܢ ܐܢܫ ܓܝܪ ܢܚܙܝܟ ܠܟ ܕܐܝܬ ܒܟ ܝܕܥܬܐ ܕܤܡܝܟ ܐܢܬ ܒܝܬ ܦܬܟܪܐ ܠܐ ܗܐ ܬܐܪܬܗ ܡܛܠ ܕܟܪܝܗ ܗܘ ܡܫܬܪܪܐ ܠܡܐܟܠ ܕܕܒܝܚܐ ܀
10 Su amee ku ngëmam néew, mu gis la, yaw mi bare xam-xam, nga toog di lekk ca màggalukaayu xërëm ya, ndax du ko xiir mu lekk yàppu sarax?
11ܘܐܒܕ ܠܗ ܒܝܕܥܬܟ ܕܝܠܟ ܗܘ ܐܝܢܐ ܕܡܪܥ ܕܡܛܠܬܗ ܡܝܬ ܡܫܝܚܐ ܀
11 Noonu sa xam-xam dina lor kooku ngëmam néew, fekk sa mbokk moomu, Kirist dee na ngir moom!
12ܘܐܢ ܗܟܢܐ ܡܤܟܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܐܚܝܟܘܢ ܘܡܩܦܚܝܢ ܐܢܬܘܢ ܬܐܪܬܗܘܢ ܡܪܥܬܐ ܒܡܫܝܚܐ ܗܘ ܡܤܟܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
12 Su ngeen bàkkaaree, ba tooñ bokk yi néew ngëm, di nëxal seen xel, bàkkaar ngeen ba tooñ Kirist.
13ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܢ ܡܐܟܘܠܬܐ ܡܟܫܠܐ ܠܐܚܝ ܠܥܠܡ ܒܤܪܐ ܠܐ ܐܟܘܠ ܕܠܐ ܐܟܫܠ ܠܐܚܝ ܀
13 Kon bu sama mbokk sóoboo ci bàkkaar ndax ñam wi ma lekk, dootuma lekk mukk yàpp, ngir bañ a sóob ci bàkkaar sama mbokk mi.