1ܦܛܪܘܤ ܫܠܝܚܐ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܓܒܝܐ ܘܬܘܬܒܐ ܕܙܪܝܥܝܢ ܒܦܢܛܘܤ ܘܒܓܠܛܝܐ ܘܒܩܦܘܕܩܝܐ ܘܒܐܤܝܐ ܘܒܒܝܬܘܢܝܐ ܀
1 Man Piyeer, ndawul Yeesu Kirist, maa leen di bind, yéen doxandéem yi tasaaroo ci diiwaani Pont, Galasi, Kapados, Asi ak Bitini. Yàlla Baay bi tànn na leen,
2ܐܝܠܝܢ ܕܐܬܓܒܝܘ ܒܡܩܕܡܘܬ ܝܕܥܬܗ ܕܐܠܗܐ ܐܒܐ ܒܩܕܝܫܘܬܐ ܕܪܘܚܐ ܕܢܗܘܘܢ ܠܡܫܡܥܬܐ ܘܠܪܤܤ ܕܡܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܛܝܒܘܬܐ ܘܫܠܡܐ ܢܤܓܐ ܠܘܬܟܘܢ ܀
2 ci li mu leen xam bu jiitu, te sédde leen boppam ci jëfu Xel mu Sell mi, ngir ngeen déggal ko, te seen xol laab ndax deretu Yeesu Kirist. Na leen Yàlla dollil yiw ak jàmm.
3ܡܒܪܟ ܗܘ ܐܠܗܐ ܐܒܘܗܝ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܗܘ ܕܒܚܢܢܗ ܤܓܝܐܐ ܐܘܠܕܢ ܡܢ ܕܪܝܫ ܒܩܝܡܬܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܠܤܒܪܐ ܕܚܝܐ ܀
3 Cant ñeel na Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist! Moo nu judduwaatal ci yërmandeem ju bare, ba may nu yaakaar ju sax ndax ndekkitel Yeesu Kirist.
4ܘܠܝܪܬܘܬܐ ܕܠܐ ܡܬܚܒܠܐ ܘܠܐ ܡܬܛܢܦܐ ܘܠܐ ܚܡܝܐ ܗܝ ܕܡܛܝܒܐ ܠܟܘܢ ܒܫܡܝܐ ܀
4 Sédd na leen cér bu dul yàqu, du gàkk te du seey mukk, dencal leen ko ci asamaan,
5ܟܕ ܢܛܝܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܚܝܠܐ ܕܐܠܗܐ ܘܒܗܝܡܢܘܬܐ ܠܚܝܐ ܕܡܛܝܒܝܢ ܕܢܬܓܠܘܢ ܠܙܒܢܐ ܐܚܪܝܐ ܀
5 yéen ñi muy aar ci dooleem, sukkandikoo ci ngëm, di leen nége mucc, gi mu nar a feeñal bés bu mujj ba.
6ܕܒܗܘܢ ܬܚܕܘܢ ܠܥܠܡ ܐܦܢ ܒܗܢܐ ܙܒܢܐ ܩܠܝܠ ܡܬܬܥܝܩܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܢܤܝܘܢܐ ܡܫܚܠܦܐ ܕܥܕܝܢ ܥܠܝܟܘܢ ܀
6 Yéena ngi bég bu baax ci biir yaakaar jooju, doonte sax, su waree am, yéena ngi dékku tiis ab diir, ci seen jànkoonte ak nattu yu wuute.
7ܐܝܟܢܐ ܕܒܘܚܪܢܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܢܬܚܙܐ ܕܡܝܬܪ ܡܢ ܕܗܒܐ ܤܢܝܢܐ ܕܐܬܒܩܝ ܒܢܘܪܐ ܠܬܫܒܘܚܬܐ ܘܠܐܝܩܪܐ ܘܠܩܘܠܤܐ ܒܓܠܝܢܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
7 Xam ne nattu yooyu dinañu sellal seen ngëm, ni safara di setale wurus, fekk wurus luy wéy la, te ngëm a ko gën fuuf. Noonu seen ngëm dina yelloo cant, ndam ak màgg, bés bu Yeesu Kirist feeñee.
8ܗܘ ܕܠܐ ܚܙܝܬܘܢܝܗܝ ܘܡܚܒܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܘܒܗܝܡܢܘܬܗ ܪܘܙܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܚܕܘܬܐ ܡܫܒܚܬܐ ܕܠܐ ܡܬܡܠܠܐ ܀
8 Musuleen koo gis waaye bëgg ngeen ko, gisuleen ko waaye gëm ngeen ko te am mbég mu xel dajul, mu fees dell ak ndam,
9ܕܬܩܒܠܘܢ ܦܘܪܥܢܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܚܝܐ ܕܢܦܫܬܟܘܢ ܀
9 di jot muj gi ngëm séentu, maanaam muccu xol.
10ܗܢܘܢ ܚܝܐ ܕܥܩܒܘ ܗܘܘ ܥܠܝܗܘܢ ܢܒܝܐ ܟܕ ܐܬܢܒܝܘ ܥܠ ܛܝܒܘܬܐ ܕܥܬܝܕܐ ܗܘܬ ܕܬܬܝܗܒ ܠܟܘܢ ܀
10 Naka mucc googu nag, yonent yi xamle yiw, wi ngeen naroon a joti, seet nañu ko te gëstu ko.
11ܘܒܨܘ ܕܒܐܝܢܐ ܙܒܢܐ ܡܚܘܝܐ ܘܡܤܗܕܐ ܪܘܚܗ ܕܡܫܝܚܐ ܕܥܡܪܐ ܒܗܘܢ ܕܥܬܝܕܝܢ ܚܫܘܗܝ ܕܡܫܝܚܐ ܘܬܫܒܘܚܬܗ ܕܡܢ ܒܬܪܟܢ ܀
11 Bi Xelum Kirist, mi nekkoon ci ñoom, seedee lu jiitu coonoy Kirist ak ndam la cay topp, jéem nañoo takk, kañ ak nan lay ame.
12ܘܐܬܓܠܝ ܠܗܘܢ ܟܠ ܕܒܨܝܢ ܗܘܘ ܡܛܠ ܕܠܘ ܠܢܦܫܗܘܢ ܒܥܝܢ ܗܘܘ ܐܠܐ ܠܢ ܕܝܠܢ ܡܬܢܒܝܢ ܗܘܘ ܐܝܠܝܢ ܕܗܫܐ ܐܬܓܠܝ ܠܟܘܢ ܒܝܕ ܐܝܠܝܢ ܕܤܒܪܢܟܘܢ ܒܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܕܐܫܬܕܪ ܡܢ ܫܡܝܐ ܕܒܗܝܢ ܒܗܠܝܢ ܡܬܪܓܪܓܝܢ ܐܦ ܡܠܐܟܐ ܕܢܕܝܩܘܢ ܀
12 Waaye Yàlla xamal na leen ne, moomuñu woon kàddu googu ñu wax, waaye yéena ko moom. Te mooy kàddu gi ngeen dégg ci gémmiñu ñi leen doon jottali xebaar bu baax bi, ci dooley Xel mu Sell, mi Yàlla yónnee asamaan; malaaka yi sax bëgg nañoo gëstu yëf yii.
13ܡܛܠ ܗܢܐ ܚܙܘܩܘ ܚܨܐ ܕܬܪܥܝܬܟܘܢ ܘܐܬܬܥܝܪܘ ܓܡܝܪܐܝܬ ܘܤܒܪܘ ܥܠ ܚܕܘܬܐ ܕܐܬܝܐ ܠܟܘܢ ܒܓܠܝܢܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
13 Kon fagaruleen ci seeni xalaat te maandu, di wékk seen yaakaar jépp ci yiw, wi leen Yàlla di jagleel bés bu Yeesu Kirist di feeñ.
14ܐܝܟ ܒܢܝܐ ܡܫܬܡܥܢܐ ܘܠܐ ܬܫܬܘܬܦܘܢ ܬܘܒ ܠܪܓܝܓܬܟܘܢ ܩܕܡܝܬܐ ܐܝܠܝܢ ܕܪܓܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܕܠܐ ܒܝܕܥܬܐ ܀
14 Gannaaw gaayi Yàlla yu koy déggal ngeen, buleen toppati bëgg-bëgg, yi ngeen toppoon, bi ngeen xamagul Yàlla.
15ܐܠܐ ܗܘܘ ܩܕܝܫܝܢ ܒܟܠܗܘܢ ܗܘܦܟܝܟܘܢ ܐܝܟ ܕܩܕܝܫ ܗܘ ܡܢ ܕܩܪܟܘܢ ܀
15 Waaye na seen dund gépp sell, ni Yàlla mi leen woo selle.
16ܡܛܠ ܕܟܬܝܒ ܕܗܘܝܬܘܢ ܩܕܝܫܝܢ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܐܢܐ ܩܕܝܫ ܐܢܐ ܀
16 Ndaxte Mbind mi nee na: «Sell-leen, ndaxte ku sell laa.»
17ܘܐܢ ܗܘ ܕܐܒܐ ܩܪܝܢ ܐܢܬܘܢ ܗܘ ܕܠܝܬ ܩܕܡܘܗܝ ܡܤܒ ܒܐܦܐ ܘܕܐܢ ܠܟܠܢܫ ܐܝܟ ܥܒܕܘܗܝ ܒܕܚܠܬܐ ܐܬܕܒܪܘ ܒܙܒܢܐ ܗܢܐ ܕܬܘܬܒܘܬܟܘܢ ܀
17 Gannaaw nag Yàlla, mi ngeen di wooye Baay, mooy àtte jëfi ñépp te du gënale kenn, saxleen ci ragal ko diirub seen ngan ci àddina.
18ܟܕ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܠܐ ܒܟܤܦܐ ܕܒܠܐ ܘܠܐ ܒܕܗܒܐ ܐܬܦܪܩܬܘܢ ܡܢ ܥܒܕܝܟܘܢ ܤܪܝܩܐ ܗܢܘܢ ܕܩܒܠܬܘܢ ܡܢ ܐܒܗܝܟܘܢ ܀
18 Xam ngeen ne, Yàlla jot na leen ci seen dund gu tekkiwul dara, gi maam ya nekkoon; te jotuleen ak yu deme ni xaalis mbaa wurus yuy wéy,
19ܐܠܐ ܒܕܡܐ ܝܩܝܪܐ ܕܐܡܪܐ ܕܡܘܡܐ ܘܛܘܠܫܐ ܠܝܬ ܒܗ ܕܐܝܬܘܗܝ ܡܫܝܚܐ ܀
19 waaye ci deretu Kirist ju tedd ji, mel ni mbote mu sikkul te wàññikuwul.
20ܗܘ ܕܡܩܕܡ ܗܘܐ ܦܪܝܫ ܠܗܕܐ ܡܢ ܩܕܡ ܬܪܡܝܬܗ ܕܥܠܡܐ ܘܐܬܓܠܝ ܒܐܚܪܝܬܗܘܢ ܕܙܒܢܐ ܡܛܠܬܟܘܢ ܀
20 Yàlla xamoon na ko, ba àddina sosoogul, waaye léegi ci mujug jamono feeñal na ko ndax yéen
21ܐܝܠܝܢ ܕܒܐܝܕܗ ܗܝܡܢܬܘܢ ܒܐܠܗܐ ܗܘ ܕܐܩܝܡܗ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܘܝܗܒ ܠܗ ܫܘܒܚܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܘܤܒܪܟܘܢ ܢܗܘܐ ܥܠ ܐܠܗܐ ܀
21 ñi jaar ci moom, gëm Yàlla. Te Yàlla dekkal na ko, sol ko ndam, ngir ngeen wékk seen ngëm ak seen yaakaar ci Yàlla.
22ܟܕ ܢܗܘܝܢ ܩܕܝܫܢ ܢܦܫܬܟܘܢ ܒܡܫܬܡܥܢܘܬܗ ܕܫܪܪܐ ܘܢܗܘܝܢ ܡܠܝܢ ܚܘܒܐ ܕܠܐ ܡܤܒ ܒܐܦܐ ܕܡܢ ܠܒܐ ܕܟܝܐ ܘܓܡܝܪܐ ܬܗܘܘܢ ܡܚܒܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܀
22 Kon nag gannaaw déggal ngeen dëgg gi, ba sellal seeni xol te am mbëggeel gu dëggu, bëgganteleen mbëggeel gu tar ak seen xol bépp.
23ܐܝܟ ܐܢܫܐ ܕܡܢ ܕܪܝܫ ܐܬܝܠܕܬܘܢ ܠܐ ܡܢ ܙܪܥܐ ܕܒܠܐ ܐܠܐ ܡܢ ܐܝܢܐ ܕܠܐ ܒܠܐ ܒܡܠܬܐ ܚܝܬܐ ܕܐܠܗܐ ܕܩܝܡܐ ܠܥܠܡ ܀
23 Ndaxte du ci jiwu wuy yàqu ngeen judduwaate, waaye ci jiwu wu sax, maanaam kàddug Yàlla giy dund tey sax.
24ܡܛܠ ܕܟܠ ܒܤܪ ܥܡܝܪܐ ܘܟܠܗ ܝܐܝܘܬܗ ܐܝܟ ܥܘܦܝܐ ܕܚܩܠܐ ܝܒܫ ܥܡܝܪܐ ܘܚܡܐ ܥܘܦܝܐ ܀
24 Ndaxte:«Nit ñax la,ndamam di tóor-tóor kese;ñax day wow, tóor-tóor ruus,waaye kàddug Boroom bi day sax ba fàww.»
25ܘܡܠܬܗ ܕܐܠܗܢ ܩܝܡܐ ܠܥܠܡܝܢ ܘܗܕܐ ܗܝ ܡܠܬܐ ܗܝ ܕܐܤܬܒܪܬܘܢ ܀
25 Te kàddu googu mooy xebaar bu baax, bi ñu leen doon yégal.