Syriac: NT

Wolof: New Testament

1 Thessalonians

1

1ܦܘܠܘܤ ܘܤܠܘܢܘܤ ܘܛܝܡܬܐܤ ܠܥܕܬܐ ܕܬܤܠܘܢܝܩܝܐ ܕܒܐܠܗܐ ܐܒܐ ܘܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܛܝܒܘܬܐ ܥܡܟܘܢ ܘܫܠܡܐ ܀
1 Nun Pool, Silwan ak Timote noo ngi leen di bind, yéen mbooloom ñi gëm ci dëkku Tesalonig te nekk ci Yàlla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist. Na yiw ak jàmm ànd ak yéen.
2ܡܘܕܝܢܢ ܠܐܠܗܐ ܒܟܠܙܒܢ ܥܠ ܟܠܟܘܢ ܘܡܬܕܟܪܝܢܢ ܠܟܘܢ ܒܨܠܘܬܢ ܐܡܝܢܐܝܬ ܀
2 Bët bu set nu ngi sant Yàlla ndax yéen, di leen boole ci sunuy ñaan.
3ܘܥܗܕܝܢܢ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܐܒܐ ܥܒܕܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܘܥܡܠܐ ܕܚܘܒܟܘܢ ܘܡܤܝܒܪܢܘܬܐ ܕܤܒܪܟܘܢ ܕܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
3 Dunu noppee fàttaliku ci kanam Yàlla sunu Baay jëf ji juddu ci seen ngëm, liggéey bi tukkee ci seen mbëggeel, ak muñ gi sosoo ci seen yaakaar ci sunu Boroom Yeesu Kirist.
4ܝܕܥܝܢܢ ܓܝܪ ܓܒܝܘܬܟܘܢ ܐܚܝ ܚܒܝܒܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܀
4 Bokk yi, yéen ñi Yàlla bëgg, xam nanu ne Yàlla tànn na leen;
5ܡܛܠ ܕܡܤܒܪܢܘܬܢ ܠܐ ܗܘܐ ܒܡܠܐ ܒܠܚܘܕ ܗܘܬ ܠܘܬܟܘܢ ܐܠܐ ܐܦ ܒܚܝܠܐ ܘܒܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܘܒܦܝܤܐ ܫܪܝܪܐ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܐܝܟܢܐ ܗܘܝܢ ܒܝܢܬܟܘܢ ܡܛܠܬܟܘܢ ܀
5 ndaxte xebaar bu baax, bi nu leen doon yégal, yemul woon ci ay wax rekk, waaye àndoon na ak kàttan ak Xel mu Sell mi ak kóolute gu mag. Xam ngeen sunu taxawaay ci seen biir ngir seen njariñ.
6ܘܐܢܬܘܢ ܒܢ ܐܬܕܡܝܬܘܢ ܘܒܡܪܢ ܕܩܒܠܬܘܢ ܡܠܬܐ ܒܐܘܠܨܢܐ ܪܒܐ ܘܒܚܕܘܬܐ ܕܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܀
6 Te aw ngeen sunuy tànk ak yu Boroom bi, ci li ngeen nangu xebaar bi ci biir fitna yu metti, ànd ak mbég ci dooley Xel mu Sell mi.
7ܘܗܘܝܬܘܢ ܕܡܘܬܐ ܠܟܠܗܘܢ ܡܗܝܡܢܐ ܕܐܝܬ ܒܡܩܕܘܢܝܐ ܘܒܐܟܐܝܐ ܀
7 Noonu ngeen daldi nekk royukaay ngir ñi gëm ñépp ci diiwaani Maseduwan ak Akayi.
8ܡܢܟܘܢ ܓܝܪ ܐܫܬܡܥܬ ܡܠܬܗ ܕܡܪܢ ܠܐ ܒܠܚܘܕ ܒܡܩܕܘܢܝܐ ܘܒܐܟܐܝܐ ܐܠܐ ܒܟܠ ܐܬܪ ܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܕܒܐܠܗܐ ܐܫܬܡܥܬ ܐܝܟܢܐ ܕܠܐ ܢܤܬܢܩ ܕܢܐܡܪ ܥܠܝܟܘܢ ܡܕܡ ܀
8 Ndaxte kàddug Boroom bi jollee na ci seen biir, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen gëm Yàlla siiw na fépp. Matul sax nu di ci wax dara,
9ܗܢܘܢ ܓܝܪ ܡܫܬܥܝܢ ܐܝܢܐ ܡܥܠܢܐ ܗܘܐ ܠܢ ܠܘܬܟܘܢ ܘܐܝܟܢܐ ܐܬܦܢܝܬܘܢ ܠܘܬ ܐܠܗܐ ܡܢ ܕܚܠܬ ܦܬܟܪܐ ܕܬܦܠܚܘܢ ܠܐܠܗܐ ܚܝܐ ܘܫܪܝܪܐ ܀
9 ndaxte ñoom ci seen bopp ñooy seede li sunu ngan def ci seen biir. Maanaam, ni ngeen dëddoo xërëm yi, jublu ci Yàlla te di ko jaamu, moom miy Yàlla Aji Dund ju dëggu ji,
10ܟܕ ܡܤܟܝܬܘܢ ܠܒܪܗ ܡܢ ܫܡܝܐ ܠܝܫܘܥ ܗܘ ܕܐܩܝܡ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܕܗܘ ܡܦܨܐ ܠܢ ܡܢ ܪܘܓܙܐ ܕܐܬܐ ܀
10 te ngeen di séentu Doomam bàyyikoo asamaan, moom Yeesu mi mu dekkal te di nu musal ci merum Yàlla, mi nar a ñëw.