1ܒܥܐ ܐܢܐ ܗܟܝܠ ܡܢܟ ܕܡܢ ܩܕܡ ܟܠܡܕܡ ܒܥܘܬܐ ܬܗܘܐ ܡܩܪܒ ܠܐܠܗܐ ܘܨܠܘܬܐ ܘܬܚܢܢܬܐ ܘܬܘܕܝܬܐ ܚܠܦ ܟܠܗܘܢ ܒܢܝܢܫܐ ܀
1 Fii laay tàmbale nag: maa ngi leen di dénk, ngeen yóbbu ñépp fa kanam Yàlla ciy ñaan, ay tinu ak i ngërëm.
2ܚܠܦ ܡܠܟܐ ܘܪܘܪܒܢܐ ܕܥܘܡܪܐ ܫܠܝܐ ܘܢܝܚܐ ܢܥܡܪ ܒܟܠܗ ܕܚܠܬ ܐܠܗܐ ܘܕܟܝܘܬܐ ܀
2 Ñaanal-leen buur yi ak kilifa yépp, ngir nu man a am dund gu dal te jàmmu, ànd ak ragal Yàlla ak faayda yu mat.
3ܗܕܐ ܓܝܪ ܫܦܝܪܐ ܘܡܩܒܠܐ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܡܚܝܢܢ ܀
3 Loolu mooy li rafet te neex Yàlla sunu Musalkat,
4ܗܘ ܕܨܒܐ ܕܟܠܗܘܢ ܒܢܝܢܫܐ ܢܚܘܢ ܘܢܬܦܢܘܢ ܠܝܕܥܬܐ ܕܫܪܪܐ ܀
4 bi bëgg ñépp mucc te xam dëgg gi.
5ܚܕ ܗܘ ܓܝܪ ܐܠܗܐ ܘܚܕ ܗܘ ܡܨܥܝܐ ܕܐܠܗܐ ܘܕܒܢܝܢܫܐ ܒܪܢܫܐ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
5 Ndaxte jenn Yàlla kepp moo am, ak benn Rammukat kepp diggante Yàlla ak nit ñi, di nit ki Kirist Yeesu,
6ܗܘ ܕܝܗܒ ܢܦܫܗ ܦܘܪܩܢܐ ܚܠܦ ܟܠ ܐܢܫ ܤܗܕܘܬܐ ܕܐܬܬ ܒܙܒܢܗ ܀
6 mi joxe bakkanam ngir jot ñépp. Loolu mooy seede si Yàlla joxe, bi waxtu wi jotee.
7ܗܝ ܕܐܢܐ ܐܬܤܝܡܬ ܟܪܘܙܗ ܘܫܠܝܚܗ ܩܘܫܬܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܘܠܐ ܡܕܓܠ ܐܢܐ ܕܗܘܝܬ ܡܠܦܢܐ ܕܥܡܡܐ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܫܪܪܐ ܀
7 Te fal na ma ci ndaw ak jàngalekat, may yégal xeeti àddina yoonu ngëm ak dëgg; fenuma, dëgg rekk laay wax.
8ܨܒܐ ܐܢܐ ܗܟܝܠ ܕܗܘܘ ܡܨܠܝܢ ܓܒܪܐ ܒܟܠ ܕܘܟܐ ܟܕ ܡܪܝܡܝܢ ܐܝܕܝܗܘܢ ܕܟܝܐܝܬ ܕܠܐ ܪܘܓܙܐ ܘܕܠܐ ܡܚܫܒܬܐ ܀
8 Li ma bëgg kon mooy lii: na góor ñi ñaan ci Yàlla fu nekk, tàllal ko loxo yu sell, te bañ cee boole mer mbaa werante.
9ܗܟܢܐ ܐܦ ܢܫܐ ܒܐܤܟܡܐ ܢܟܦܐ ܕܠܒܘܫܐ ܒܬܚܡܨܬܐ ܘܒܢܟܦܘܬܐ ܢܗܘܐ ܬܨܒܝܬܗܝܢ ܠܐ ܒܓܕܘܠܐ ܘܒܕܗܒܐ ܐܘ ܒܡܪܓܢܝܬܐ ܐܘ ܒܢܚܬܐ ܫܦܝܪܐ ܀
9 Naka noonu itam, na jigéen ñi di sol col gu faaydawu, cig woyof ak maandu. Buñu def seen xel ciy létt ak ci takkaayu wurus, mbaa ciy per ak col gu jafe.
10ܐܠܐ ܒܥܒܕܐ ܛܒܐ ܐܝܟܢܐ ܕܝܐܐ ܠܢܫܐ ܕܡܫܬܘܕܝܢ ܕܚܠܬ ܐܠܗܐ ܀
10 Waaye na seen col di jëf yu rafet, ndaxte looloo jekk ci jigéen juy woote ag ragal Yàlla.
11ܐܢܬܬܐ ܒܫܠܝܐ ܗܘܬ ܝܠܦܐ ܒܟܠ ܫܘܥܒܕ ܀
11 Te it na jigéen jàng cig noppi, ànd ak déggal gu mat.
12ܠܐܢܬܬܐ ܓܝܪ ܠܡܠܦܘ ܠܐ ܡܦܤ ܐܢܐ ܘܠܐ ܠܡܡܪܚܘ ܥܠ ܓܒܪܐ ܐܠܐ ܬܗܘܐ ܒܫܠܝܐ ܀
12 Mayuma jigéen, muy jàngale mbaa muy jiite góor, waaye na noppi.
13ܐܕܡ ܓܝܪ ܐܬܓܒܠ ܠܘܩܕܡ ܘܗܝܕܝܢ ܚܘܐ ܀
13 Ndaxte Aadama la Yàlla jëkk a sàkk, door caa teg Awa.
14ܘܐܕܡ ܠܐ ܛܥܐ ܐܢܬܬܐ ܕܝܢ ܛܥܬ ܘܥܒܪܬ ܥܠ ܦܘܩܕܢܐ ܀
14 Te it du Aadama la Seytaane nax, waaye jigéen ja la nax, ba mu jàdd.
15ܚܝܐ ܕܝܢ ܒܝܕ ܝܠܕܝܗ ܐܢ ܢܩܘܘܢ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܘܒܚܘܒܐ ܘܒܩܕܝܫܘܬܐ ܘܒܢܟܦܘܬܐ ܀
15 Teewul jigéen dina mucc ci wasin, su saxee ci ngëm ak mbëggeel, di ku sell te maandu.