1ܗܕܐ ܕܬܠܬ ܗܝ ܙܒܢܝܢ ܕܐܬܐ ܐܢܐ ܠܘܬܟܘܢ ܕܥܠ ܦܘܡ ܬܪܝܢ ܘܬܠܬܐ ܤܗܕܝܢ ܬܩܘܡ ܟܠ ܡܠܐ ܀
1 Bii mooy ñetteel bi yoon, ma di leen ganesi. «Bépp àtte dina aju ci seedes ñaar walla ñetti nit.»
2ܡܢ ܩܕܝܡ ܐܡܪܬ ܗܘܝܬ ܠܟܘܢ ܘܬܘܒ ܡܩܕܡ ܐܢܐ ܐܡܪ ܐܢܐ ܠܟܘܢ ܐܝܟ ܕܐܦ ܬܪܬܝܢ ܙܒܢܝܢ ܕܗܘܝܬ ܠܘܬܟܘܢ ܐܡܪܬ ܠܟܘܢ ܘܐܦ ܗܫܐ ܟܕ ܪܚܝܩ ܐܢܐ ܟܬܒܢܐ ܠܗܠܝܢ ܕܚܛܘ ܘܠܫܪܟܐ ܕܐܚܪܢܐ ܕܐܢ ܐܬܐ ܬܘܒ ܠܐ ܐܚܘܤ ܀
2 Li ma waxoon ci sama ñaareelu ngan, ci ñi bàkkaaroon bu yàgg ak ñi ci des, maa ngi koy waxaat léegi, bala maa dikkaat: su ma dellusee, duma yërëm kenn.
3ܡܛܠ ܕܒܘܩܝܐ ܒܥܝܬܘܢ ܕܡܫܝܚܐ ܕܡܡܠܠ ܒܝ ܗܘ ܕܠܐ ܗܘܐ ܡܚܝܠ ܒܟܘܢ ܐܠܐ ܚܝܠܬܢ ܗܘ ܒܟܘܢ ܀
3 Bu fekkee ne dangeen a bëgg firnde juy wone ne, Kirist mooy wax jaarale ko ci man, dingeen ko am. Digganteem ak yéen du ànd ak néew doole, waaye dafay feeñal kàttan ci seen biir.
4ܐܦܢ ܐܙܕܩܦ ܓܝܪ ܒܡܚܝܠܘܬܐ ܐܠܐ ܚܝ ܗܘ ܒܚܝܠܐ ܕܐܠܗܐ ܘܐܦ ܚܢܢ ܡܚܝܠܝܢܢ ܥܡܗ ܐܠܐ ܚܝܝܢ ܚܢܢ ܥܡܗ ܒܚܝܠܐ ܕܐܠܗܐ ܕܒܟܘܢ ܀
4 Néewoon na doole, ba ñu koy daaj ca bant ngir rey ko, waaye mi ngi dund ci kàttanu Yàlla. Nun itam néew nanu doole ci sunu bokk ci moom, waaye dinanu dund ak moom ci kàttanu Yàlla, bu nuy jëfante ak yéen.
5ܢܦܫܟܘܢ ܒܩܘ ܐܢ ܒܗ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܩܝܡܝܢ ܐܢܬܘܢ ܢܦܫܟܘܢ ܐܤܘ ܐܘ ܠܐ ܡܫܬܘܕܥܝܬܘܢ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܒܟܘܢ ܗܘ ܘܐܢ ܠܐ ܡܤܠܝܐ ܐܢܬܘܢ ܀
5 Xool-leen seen bopp bu baax, ba xam ndax ngëm a ngi ci yéen. Seetluleen seen bopp. Xanaa xamuleen ne, Yeesoo ngi ci yéen? Walla boog ngeen gis ne, ay naaféq ngeen.
6ܡܤܒܪ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܬܕܥܘܢ ܕܚܢܢ ܠܐ ܗܘܝܢ ܡܤܠܝܢ ܀
6 Waaye yaakaar naa ne dingeen gis ne, man nanoo wone nun, firndeg ngëm.
7ܒܥܐ ܐܢܐ ܕܝܢ ܡܢ ܐܠܗܐ ܕܠܐ ܢܗܘܐ ܒܟܘܢ ܡܕܡ ܕܒܝܫ ܐܝܟ ܕܒܘܩܝܢ ܕܝܠܢ ܢܬܚܙܐ ܐܠܐ ܕܐܢܬܘܢ ܬܗܘܘܢ ܤܥܪܝܢ ܛܒܬܐ ܘܚܢܢ ܢܗܘܐ ܐܝܟ ܡܤܠܝܐ ܀
7 Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen bañ a def dara lu bon. Waxuma ne danoo bëgg a wone noonu sunu firndeg ngëm, waaye sunu yéene mooy ngeen jëf lu baax, boo yaboo sax ñu jiiñ nu ag naaféq.
8ܠܐ ܓܝܪ ܡܫܟܚܝܢܢ ܕܢܥܒܕ ܡܕܡ ܠܘܩܒܠ ܩܘܫܬܐ ܐܠܐ ܚܠܦ ܩܘܫܬܐ ܀
8 Ndaxte manalunu dara dëggu Yàlla gi; mënunu lu dul taxawal ko.
9ܚܕܝܢܢ ܕܝܢ ܡܐ ܕܚܢܢ ܟܪܝܗܝܢ ܘܐܢܬܘܢ ܚܝܠܬܢܝܢ ܗܕܐ ܓܝܪ ܐܦ ܡܨܠܝܢܢ ܕܐܢܬܘܢ ܬܬܓܡܪܘܢ ܀
9 Bu nu néewee doole, fekk am ngeen doole, bég nanu ci. Te sax nu ngi ñaan, ngeen jublu cig mat.
10ܡܛܠ ܗܢܐ ܟܕ ܪܚܝܩ ܐܢܐ ܗܠܝܢ ܟܬܒ ܐܢܐ ܕܠܐ ܡܐ ܕܐܬܝܬ ܩܫܝܐܝܬ ܐܤܥܘܪ ܐܝܟ ܫܘܠܛܢܐ ܕܝܗܒ ܠܝ ܡܪܝ ܠܒܢܝܢܟܘܢ ܘܠܐ ܠܤܘܚܦܟܘܢ ܀
10 Looloo tax ma leen di binde nii, bala maa ñëw; bëgguma leen a duma ci sañ-sañ bi ma Boroom bi jox. Jox na ma ko, ngir ma yokk seen ngëm, waaye du ngir seen kasara.
11ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܚܕܘ ܘܐܬܓܡܪܘ ܘܐܬܒܝܐܘ ܘܐܘܝܘܬܐ ܘܫܝܢܐ ܢܗܘܐ ܒܟܘܢ ܘܐܠܗܐ ܕܚܘܒܐ ܘܕܫܠܡܘܬܐ ܢܗܘܐ ܥܡܟܘܢ ܀
11 Kon nag bokk yi, bégleen, jublu cig mat, di déglu soññante bi ma leen di dénk, am benn xalaat te dëkk ci jàmm; noonu Yàlla miy mbëggeel te di Yàllay jàmm dina ànd ak yéen.
12ܫܐܠܘ ܒܫܠܡܐ ܚܕ ܕܚܕ ܒܢܘܫܩܬܐ ܩܕܝܫܬܐ ܀
12 Saafoonteleen ak xol bu laab.
13ܫܐܠܝܢ ܒܫܠܡܟܘܢ ܟܠܗܘܢ ܩܕܝܫܐ ܀
13 Mboolem gaayi Yàlla yépp ñu ngi leen di nuyu.
14ܫܠܡܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܚܘܒܗ ܕܐܠܗܐ ܘܫܘܬܦܘܬܐ ܕܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܥܡ ܟܠܟܘܢ ܐܡܝܢ ܀
14 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist, ak mbëggeelu Yàlla ak booloo, gi nu am ak Xel mu Sell mi, ànd ak yéen ñépp.