1ܒܥܝܢܢ ܕܝܢ ܡܢܟܘܢ ܐܚܝ ܥܠ ܡܐܬܝܬܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܥܠ ܟܢܘܫܝܐ ܕܝܠܢ ܕܠܘܬܗ ܀
1 Ci lu jëm ci ñëwu Boroom bi Yeesu Kirist nag, bokk yi, ak sunu daje ak moom, am na lu ma leen di ñaan:
2ܕܠܐ ܥܓܠ ܬܬܙܝܥܘܢ ܒܪܥܝܢܝܟܘܢ ܘܠܐ ܬܬܘܗܘܢ ܠܐ ܡܢ ܡܠܬܐ ܘܠܐ ܡܢ ܪܘܚܐ ܘܠܐ ܡܢ ܐܓܪܬܐ ܕܐܝܟ ܕܡܢ ܠܘܬܢ ܗܝ ܕܗܐ ܠܡ ܡܛܝ ܝܘܡܗ ܕܡܪܢ ܀
2 bu leen kenn gaaw a tàggale ak seen sago, mbaa di leen jaaxal, muy yonent buy wax, muy kàddu mbaa bataaxal bu ñu nu moomaleel, ci ne leen bésu Boroom bi ñëw na xaat.
3ܠܡܐ ܐܢܫ ܢܛܥܝܟܘܢ ܒܚܕ ܡܢ ܐܤܟܡܝܢ ܡܛܠ ܕܐܢ ܠܐ ܬܐܬܐ ܠܘܩܕܡ ܡܪܘܕܘܬܐ ܘܢܬܓܠܐ ܒܪܢܫܐ ܕܚܛܝܬܐ ܒܪܗ ܕܐܒܕܢܐ ܀
3 Bu leen kenn nax ci benn fànn, ndaxte balaa booba, fàww Xiiroo bu mag bi ak Yàlla am, te Nitu ñaawteef ki feeñ, moom aji alku ji.
4ܗܘ ܕܠܩܘܒܠܐ ܗܘ ܘܡܫܬܥܠܐ ܥܠ ܟܠ ܡܢ ܕܡܬܩܪܐ ܐܠܗ ܘܕܚܠܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܒܗܝܟܠܐ ܕܐܠܗܐ ܐܝܟ ܐܠܗܐ ܢܬܒ ܘܢܚܘܐ ܥܠ ܢܦܫܗ ܐܝܟ ܕܐܠܗܐ ܗܘ ܀
4 Day weddi lépp lu ñu teg Yàlla walla ñu koy jaamu, di yékkati boppam, ba toog sax ca kër Yàlla ga, tudde boppam Yàlla.
5ܠܐ ܥܗܕܝܬܘܢ ܕܟܕ ܠܘܬܟܘܢ ܗܘܝܬ ܗܠܝܢ ܐܡܪܬ ܗܘܝܬ ܠܟܘܢ ܀
5 Xanaa fàttalikuwuleen ne, waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak yéen.
6ܘܗܫܐ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܡܐ ܕܐܚܝܕ ܕܢܬܓܠܐ ܗܘ ܒܙܒܢܗ ܀
6 Te xam ngeen li ko téye léegi, ba du man a feeñ lu dul ci waxtoom.
7ܐܪܙܐ ܓܝܪ ܕܥܘܠܐ ܡܢ ܟܕܘ ܫܪܝ ܠܡܬܚܦܛܘ ܒܠܚܘܕ ܐܢ ܗܘ ܡܐ ܕܗܫܐ ܐܚܝܕ ܢܫܬܩܠ ܡܢ ܡܨܥܬܐ ܀
7 Ndaxte fi mu ne ñaawteef gaa ngi jax-jaxi xaat ci kumpa, waaye ki ko téye mi ngi fi ba tey. Bu fi jógee nag,
8ܘܗܝܕܝܢ ܢܬܓܠܐ ܥܘܠܐ ܗܘ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܢܤܝܦܝܘܗܝ ܒܪܘܚ ܦܘܡܗ ܘܢܒܛܠܝܘܗܝ ܒܓܠܝܢܐ ܕܡܐܬܝܬܗ ܀
8 Nitu ñaawteef ki dina feeñ, te Boroom bi Yeesu dina ko rey ak ngelawul gémmiñam, tas ko ak leer giy ànd ak ñëwam.
9ܡܐܬܝܬܗ ܓܝܪ ܕܗܘ ܒܡܥܒܕܢܘܬܐ ܗܝ ܕܤܛܢܐ ܒܟܠ ܚܝܠ ܘܐܬܘܬܐ ܘܬܕܡܪܬܐ ܕܓܠܬܐ ܀
9 Bu Nitu ñaawteef kooku feeñee, dina ànd ak kàttanu Seytaane ak doole ju bare, di wone ay firnde ak ay kéemaan yu dul dëgg;
10ܘܒܟܠܗ ܛܘܥܝܝ ܕܥܘܠܐ ܕܗܘܝܐ ܒܐܒܝܕܐ ܥܠ ܕܠܐ ܩܒܠܘ ܚܘܒܐ ܕܩܘܫܬܐ ܕܒܗ ܢܚܘܢ ܀
10 te dina nas bépp naxe buy sànke, ba yéem ñi nar a alku, ndaxte ubbiluñu seeni xol dëgg, gi leen manoon a musal.
11ܡܛܠܗܢܐ ܢܫܕܪ ܠܗܘܢ ܐܠܗܐ ܡܥܒܕܢܘܬܐ ܕܛܘܥܝܝ ܕܢܗܝܡܢܘܢ ܠܫܘܩܪܐ ܀
11 Looloo tax Yàlla yónnee leen xelum réer, ba ñu gëm fen.
12ܘܢܬܕܝܢܘܢ ܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܗܝܡܢܘ ܒܩܘܫܬܐ ܐܠܐ ܐܨܛܒܝܘ ܒܥܘܠܐ ܀
12 Noonu Yàlla dina mbugal ñépp ñi gëmul woon dëgg te doon bànneexu ci njubadi.
13ܚܢܢ ܕܝܢ ܚܝܒܝܢܢ ܠܡܘܕܝܘ ܠܐܠܗܐ ܒܟܠܙܒܢ ܥܠ ܐܦܝܟܘܢ ܐܚܝܢ ܚܒܝܒܘܗܝ ܕܡܪܢ ܕܓܒܟܘܢ ܐܠܗܐ ܡܢ ܪܫܝܬܐ ܠܚܝܐ ܒܩܕܝܫܘܬܐ ܕܪܘܚܐ ܘܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܫܪܪܐ ܀
13 Kon nag bokk yi, yéen ñi Boroom bi bëgg, mënunu lu dul sax ci sant Yàlla ci li mu leen tànn ca njàlbéen ga, ngir musal leen, mu sédde leen boppam jaarale ko ci jëfu Xel mu Sell mi ak seen gëm dëgg gi.
14ܠܗܠܝܢ ܗܘ ܓܝܪ ܩܪܟܘܢ ܒܡܤܒܪܢܘܬܐ ܕܝܠܢ ܕܬܗܘܘܢ ܬܫܒܘܚܬܐ ܠܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
14 Te Yàlla woo na leen ci loolu jaarale ko ci xebaar bu baax, bi nu leen doon yégal, ngir ngeen bokk ci ndamu sunu Boroom Yeesu Kirist.
15ܡܟܝܠ ܐܚܝ ܐܬܩܝܡܘ ܘܚܡܤܢܘ ܒܦܘܩܕܢܐ ܕܝܠܦܬܘܢ ܐܢ ܒܡܠܬܐ ܘܐܢ ܒܐܓܪܬܐ ܕܝܠܢ ܀
15 Kon nag bokk yi, taxawleen bu dëgër te jàpp ci dénkaane yi nu leen jottali, muy ci li nu wax, muy ci li nu bind.
16ܗܘ ܕܝܢ ܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܐܠܗܐ ܐܒܘܢ ܗܘ ܕܐܚܒܢ ܘܝܗܒ ܠܢ ܒܘܝܐܐ ܕܠܥܠܡ ܘܤܒܪܐ ܛܒܐ ܒܛܝܒܘܬܗ ܀
16 Na sunu Boroom Yeesu Kirist moom ci boppam ak Yàlla sunu Baay, mi nu bëgg te wone yiwam ci nun, ba ubbil nu buntu jàmm ju sax ak yaakaar ju wér,
17ܢܒܝܐ ܠܒܘܬܟܘܢ ܘܢܩܝܡ ܒܟܠ ܡܠܐ ܘܒܟܠ ܥܒܕ ܛܒ ܀
17 dëfël seeni xol te saxal leen ci bépp jëf ju rafet ak gépp kàddu gu baax.