Syriac: NT

Wolof: New Testament

Acts

16

1ܘܡܛܝ ܗܘܐ ܠܕܪܒܐ ܡܕܝܢܬܐ ܘܠܠܘܤܛܪܐ ܐܝܬ ܗܘܐ ܕܝܢ ܬܡܢ ܬܠܡܝܕܐ ܚܕ ܕܫܡܗ ܛܝܡܬܐܘܤ ܒܪܗ ܕܝܗܘܕܝܬܐ ܚܕܐ ܡܗܝܡܢܬܐ ܘܐܒܘܗܝ ܐܪܡܝܐ ܗܘܐ ܀
1 Naka noona mu dikk dëkki Derbë ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu gëm, waaye baayam di Gereg.
2ܘܟܠܗܘܢ ܬܠܡܝܕܐ ܕܡܢ ܠܘܤܛܪܐ ܘܡܢ ܐܝܩܢܘܢ ܡܤܗܕܝܢ ܗܘܘ ܥܠܘܗܝ ܀
2 Te mbokk, yi nekk dëkki Listar ak Ikoñum, seedeel nañu ko lu baax.
3ܠܗܢܐ ܨܒܐ ܗܘܐ ܦܘܠܘܤ ܕܢܕܒܪܝܘܗܝ ܥܡܗ ܘܢܤܒ ܓܙܪܗ ܡܛܠ ܝܗܘܕܝܐ ܕܐܝܬ ܗܘܘ ܒܐܬܪܐ ܝܕܥܝܢ ܗܘܘ ܓܝܪ ܟܠܗܘܢ ܠܐܒܘܗܝ ܕܐܪܡܝܐ ܗܘܐ ܀
3 Pool bëgg nag mu ànd ak moom, waaye ndegam Yawut yépp, ya dëkk ca wàllaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu jël ko, xarafal ko.
4ܘܟܕ ܐܙܠܝܢ ܗܘܘ ܒܡܕܝܢܬܐ ܡܟܪܙܝܢ ܗܘܘ ܘܡܠܦܝܢ ܠܗܘܢ ܕܢܗܘܘܢ ܢܛܪܝܢ ܦܘܩܕܢܐ ܐܝܠܝܢ ܕܟܬܒܘ ܫܠܝܚܐ ܘܩܫܝܫܐ ܕܒܐܘܪܫܠܡ ܀
4 Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko.
5ܒܪܡ ܥܕܬܐ ܡܬܩܝܡܢ ܗܘܝ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܘܤܓܝܢ ܗܘܝ ܒܡܢܝܢܐ ܟܠܝܘܡ ܀
5 Noonu mboolooy ñi gëm di gën a dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk.
6ܗܠܟܘ ܕܝܢ ܒܦܪܘܓܝܐ ܘܒܓܠܛܝܐ ܐܬܪܘܬܐ ܘܟܠܬ ܐܢܘܢ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܕܠܐ ܢܡܠܠܘܢ ܡܠܬܐ ܕܐܠܗܐ ܒܐܤܝܐ ܀
6 Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi.
7ܘܟܕ ܐܬܘ ܠܡܘܤܝܐ ܐܬܪܐ ܨܒܝܢ ܗܘܘ ܕܢܐܙܠܘܢ ܡܢ ܬܡܢ ܠܒܝܬܘܢܝܐ ܘܠܐ ܐܦܤܬ ܠܗܘܢ ܪܘܚܗ ܕܝܫܘܥ ܀
7 Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéem a dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayuleen ko.
8ܘܟܕ ܢܦܩܘ ܡܢ ܡܘܤܝܐ ܢܚܬܘ ܠܗܘܢ ܠܛܪܘܐܤ ܐܬܪܐ ܀
8 Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas.
9ܘܒܚܙܘܐ ܕܠܠܝܐ ܐܬܚܙܝ ܠܦܘܠܘܤ ܐܝܟ ܓܒܪܐ ܚܕ ܡܩܕܘܢܝܐ ܕܩܐܡ ܘܒܥܐ ܡܢܗ ܟܕ ܐܡܪ ܕܬܐ ܠܡܩܕܘܢܝܐ ܘܥܕܪܝܢܝ ܀
9 Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»
10ܟܕ ܕܝܢ ܚܙܐ ܦܘܠܘܤ ܗܢܐ ܚܙܘܐ ܡܚܕܐ ܨܒܝܢ ܠܡܦܩ ܠܡܩܕܘܢܝܐ ܡܛܠ ܕܐܤܬܟܠܢ ܕܡܪܢ ܩܪܢ ܕܢܤܒܪ ܐܢܘܢ ܀
10 Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xebaar bu baax bi.
11ܘܪܕܝܢ ܡܢ ܛܪܘܐܤ ܘܬܪܨܢ ܠܤܡܬܪܩܐ ܘܡܢ ܬܡܢ ܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܐܬܝܢ ܠܢܐܦܘܠܝܤ ܡܕܝܢܬܐ ܀
11 Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis.
12ܘܡܢ ܬܡܢ ܠܦܝܠܝܦܘܤ ܕܗܝ ܗܝ ܪܫܐ ܕܡܩܕܘܢܝܐ ܘܐܝܬܝܗ ܩܘܠܘܢܝܐ ܗܘܝܢ ܕܝܢ ܒܗ ܒܗܕܐ ܡܕܝܢܬܐ ܝܘܡܬܐ ܝܕܝܥܐ ܀
12 Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it suufus Room. Nu toog fa ay fan.
13ܘܢܦܩܢ ܒܝܘܡܐ ܕܫܒܬܐ ܠܒܪ ܡܢ ܬܪܥܐ ܕܡܕܝܢܬܐ ܥܠ ܝܕ ܢܗܪܐ ܡܛܠ ܕܬܡܢ ܡܬܚܙܐ ܗܘܐ ܒܝܬ ܨܠܘܬܐ ܘܟܕ ܝܬܒܢ ܡܡܠܠܝܢ ܗܘܝܢ ܥܡ ܢܫܐ ܕܟܢܝܫܢ ܗܘܝ ܬܡܢ ܀
13 Bi bésu noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo.
14ܘܐܢܬܬܐ ܚܕܐ ܡܙܒܢܬ ܐܪܓܘܢܐ ܕܕܚܠܐ ܗܘܬ ܡܢ ܐܠܗܐ ܫܡܗ ܗܘܐ ܠܘܕܝܐ ܡܢ ܬܐܘܛܝܪܐ ܡܕܝܢܬܐ ܕܗܕܐ ܦܬܚ ܠܒܗ ܡܪܢ ܘܫܡܥܐ ܗܘܬ ܡܕܡ ܕܐܡܪ ܦܘܠܘܤ ܀
14 Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.
15ܘܥܡܕܬ ܗܘܬ ܗܝ ܘܒܢܝ ܒܝܬܗ ܘܒܥܝܐ ܗܘܬ ܡܢܢ ܘܐܡܪܐ ܕܐܢ ܗܘ ܕܫܪܝܪܐܝܬ ܬܟܝܠܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܗܝܡܢܬ ܒܡܪܢ ܬܘ ܫܪܘ ܠܟܘܢ ܒܒܝܬܝ ܘܤܓܝ ܐܠܨܬܢ ܀
15 Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.
16ܘܗܘܐ ܕܟܕ ܐܙܠܝܢܢ ܠܒܝܬ ܨܠܘܬܐ ܦܓܥܬ ܒܢ ܥܠܝܡܬܐ ܚܕܐ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗ ܪܘܚܐ ܕܩܨܡܐ ܘܥܒܕܐ ܗܘܬ ܠܡܪܝܗ ܬܐܓܘܪܬܐ ܤܓܝܐܬܐ ܒܩܨܡܐ ܕܩܨܡܐ ܗܘܬ ܀
16 Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem.
17ܘܐܬܝܐ ܗܘܬ ܒܬܪ ܦܘܠܘܤ ܘܒܬܪܢ ܘܩܥܝܐ ܗܘܬ ܘܐܡܪܐ ܗܠܝܢ ܐܢܫܐ ܥܒܕܘܗܝ ܐܢܘܢ ܕܐܠܗܐ ܡܪܝܡܐ ܘܡܤܒܪܝܢ ܠܟܘܢ ܐܘܪܚܐ ܕܚܝܐ ܀
17 Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; ñoo leen di yégal yoonu mucc.»
18ܘܗܟܢܐ ܥܒܕܐ ܗܘܬ ܝܘܡܬܐ ܤܓܝܐܐ ܘܐܬܬܦܝܪ ܦܘܠܘܤ ܘܐܡܪ ܠܗ ܠܪܘܚܐ ܗܝ ܦܩܕ ܐܢܐ ܠܟܝ ܒܫܡܗ ܕܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܕܬܦܩܝܢ ܡܢܗ ܘܒܗ ܒܫܥܬܐ ܢܦܩܬ ܀
18 Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu woññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom.
19ܘܟܕ ܚܙܘ ܡܪܝܗ ܕܢܦܩ ܠܗ ܡܢܗ ܤܒܪܐ ܕܬܐܓܘܪܬܗܘܢ ܐܚܕܘܗܝ ܠܦܘܠܘܤ ܘܠܫܝܠܐ ܘܢܓܕܘ ܐܝܬܝܘ ܐܢܘܢ ܠܫܘܩܐ ܀
19 Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya.
20ܘܩܪܒܘ ܐܢܘܢ ܠܐܤܛܪܛܓܐ ܘܠܪܫܐ ܕܡܕܝܢܬܐ ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܕܗܠܝܢ ܐܢܫܐ ܡܕܠܚܝܢ ܠܗ ܠܡܕܝܢܬܢ ܡܛܠ ܕܝܗܘܕܝܐ ܐܢܘܢ ܀
20 Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk,
21ܘܡܟܪܙܝܢ ܠܢ ܥܝܕܐ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܡܦܤ ܠܢ ܠܡܩܒܠܘ ܘܠܡܥܒܕ ܡܛܠ ܕܪܗܘܡܝܐ ܚܢܢ ܀
21 di xamle ay aada yu nu sañul a nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.»
22ܘܟܢܫܐ ܤܓܝܐܐ ܐܬܟܢܫܘ ܥܠܝܗܘܢ ܗܝܕܝܢ ܐܤܛܪܛܓܐ ܤܕܩܘ ܢܚܬܝܗܘܢ ܘܦܩܕܘ ܕܢܢܓܕܘܢ ܐܢܘܢ ܀
22 Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar.
23ܘܟܕ ܢܓܕܘ ܐܢܘܢ ܤܓܝ ܐܪܡܝܘ ܐܢܘܢ ܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܘܦܩܕܘ ܠܢܛܪ ܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܕܢܛܪ ܐܢܘܢ ܙܗܝܪܐܝܬ ܀
23 Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér.
24ܗܘ ܕܝܢ ܟܕ ܩܒܠ ܗܢܐ ܦܘܩܕܢܐ ܐܥܠ ܚܒܫ ܐܢܘܢ ܒܒܝܬܐ ܓܘܝܐ ܕܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܘܐܤܪ ܪܓܠܝܗܘܢ ܒܤܕܐ ܀
24 Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gën a ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk.
25ܘܒܦܠܓܗ ܕܠܠܝܐ ܦܘܠܘܤ ܘܫܝܠܐ ܡܨܠܝܢ ܗܘܘ ܘܡܫܒܚܝܢ ܗܘܘ ܠܐܠܗܐ ܘܫܡܥܝܢ ܗܘܘ ܠܗܘܢ ܐܤܝܪܐ ܀
25 Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di ñaan ak di sant Yàlla, te ñeneen ñi nekk ca kaso ba di leen déglu.
26ܘܡܢ ܫܠܝܐ ܙܘܥܐ ܪܒܐ ܗܘܐ ܘܐܬܬܙܝܥ ܫܬܐܤܐ ܕܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܘܐܬܦܬܚܘ ܡܚܕܐ ܬܪܥܐ ܟܠܗܘܢ ܘܐܤܘܪܝܗܘܢ ܕܟܠܗܘܢ ܐܫܬܪܝܘ ܀
26 Ca saa sa suuf yengu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt yépp daldi ne kulbet ubbiku, te jéngi ña ñu tëj ne tell tijjiku.
27ܘܟܕ ܐܬܬܥܝܪ ܢܛܪ ܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܘܚܙܐ ܕܦܬܝܚܝܢ ܬܪܥܐ ܕܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܢܤܒ ܤܦܤܪܐ ܘܒܥܐ ܕܢܩܛܘܠ ܢܦܫܗ ܡܛܠ ܕܤܒܪ ܗܘܐ ܕܥܪܩܘ ܠܗܘܢ ܐܤܝܪܐ ܀
27 Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt yépp ubbiku, mu daldi bocci jaaseem, bëgg a xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo daw.
28ܘܩܪܝܗܝ ܦܘܠܘܤ ܒܩܠܐ ܪܡܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܠܐ ܬܥܒܕ ܠܢܦܫܟ ܡܕܡ ܕܒܝܫ ܡܛܠ ܕܟܠܢ ܗܪܟܐ ܚܢܢ ܀
28 Waaye Pool wax ci kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.»
29ܘܐܢܗܪ ܠܗ ܫܪܓܐ ܘܫܘܪ ܘܥܠ ܟܕ ܪܐܬ ܘܢܦܠ ܥܠ ܪܓܠܝܗܘܢ ܕܦܘܠܘܤ ܘܕܫܝܠܐ ܀
29 Bi ko boroom kaso ba déggee, mu daldi laaj làmp, ne saraax dugg, daanu ci kanamu Pool ak Silas, di lox.
30ܘܐܦܩ ܐܢܘܢ ܠܒܪ ܘܐܡܪ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܡܪܝ ܡܢܐ ܘܠܐ ܠܝ ܠܡܥܒܕ ܐܝܟ ܕܐܚܐ ܀
30 Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma war a def, ba mucc?»
31ܘܗܢܘܢ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܗܝܡܢ ܒܡܪܢ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܘܬܚܐ ܐܢܬ ܘܒܝܬܟ ܀
31 Ñu tontu ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.»
32ܘܡܠܠܘ ܥܡܗ ܡܠܬܐ ܕܡܪܝܐ ܘܥܡ ܟܠܗܘܢ ܒܢܝ ܒܝܬܗ ܀
32 Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp.
33ܘܒܗ ܒܫܥܬܐ ܒܗ ܒܠܠܝܐ ܕܒܪ ܐܤܚܝ ܐܢܘܢ ܡܢ ܢܓܕܗܘܢ ܘܒܪ ܫܥܬܗ ܥܡܕ ܗܘ ܘܒܢܝ ܒܝܬܗ ܟܠܗܘܢ ܀
33 Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.
34ܘܕܒܪ ܐܤܩ ܐܢܘܢ ܠܒܝܬܗ ܘܤܡ ܠܗܘܢ ܦܬܘܪܐ ܘܪܘܙ ܗܘܐ ܗܘ ܘܒܢܝ ܒܝܬܗ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
34 Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.
35ܘܟܕ ܗܘܐ ܨܦܪܐ ܫܕܪܘ ܐܤܛܪܛܓܐ ܠܫܩܠܝ ܫܒܛܐ ܕܢܐܡܪܘܢ ܠܪܒ ܐܤܝܪܐ ܫܪܝ ܠܗܠܝܢ ܐܢܫܐ ܀
35 Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.»
36ܘܟܕ ܫܡܥ ܪܒ ܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܥܠ ܐܡܪ ܠܗ ܗܝ ܗܕܐ ܡܠܬܐ ܠܦܘܠܘܤ ܕܫܕܪܘ ܐܤܛܪܛܓܐ ܐܝܟ ܕܬܫܬܪܘܢ ܘܗܫܐ ܦܘܩܘ ܙܠܘ ܒܫܠܡܐ ܀
36 Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen, te dem ci jàmm.»
37ܐܡܪ ܠܗ ܦܘܠܘܤ ܕܠܐ ܤܟܠܘ ܢܓܕܘܢ ܠܥܝܢ ܥܠܡܐ ܟܠܗ ܠܐܢܫܐ ܪܗܘܡܝܐ ܘܐܪܡܝܘܢ ܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܘܗܫܐ ܡܛܫܝܐܝܬ ܡܦܩܝܢ ܠܢ ܠܐ ܓܝܪ ܐܠܐ ܗܢܘܢ ܢܐܬܘܢ ܢܦܩܘܢܢ ܀
37 Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanamu ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgg a sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»
38ܘܐܙܠܘ ܫܩܠܝ ܫܒܛܐ ܘܐܡܪܘ ܠܐܤܛܪܛܓܐ ܡܠܐ ܗܠܝܢ ܕܐܬܐܡܪ ܠܗܘܢ ܘܟܕ ܫܡܥܘ ܕܪܗܘܡܝܐ ܐܢܘܢ ܕܚܠܘ ܀
38 Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne, jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit.
39ܘܐܬܘ ܠܘܬܗܘܢ ܘܒܥܘ ܡܢܗܘܢ ܕܢܦܩܘܢ ܘܢܫܢܘܢ ܠܗܘܢ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܀
39 Ñu ñëw nag di leen dëfël, ñu gunge leen ci biti, di leen ñaan, ñu génn dëkk ba.
40ܘܟܕ ܢܦܩܘ ܡܢ ܒܝܬ ܐܤܝܪܐ ܥܠܘ ܠܘܬ ܠܘܕܝܐ ܘܚܙܘ ܬܡܢ ܠܐܚܐ ܘܒܝܐܘ ܐܢܘܢ ܘܢܦܩܘ ܀
40 Noonu ñu génn ca kaso ba, dugg ci kër Lidi, ñu gis fa bokk ya, dëgëral leen, daldi dem seen yoon.