1ܘܟܕ ܐܬܡܠܝܘ ܝܘܡܬܐ ܕܦܢܛܩܘܤܛܐ ܟܕ ܟܢܝܫܝܢ ܗܘܘ ܟܠܗܘܢ ܐܟܚܕܐ ܀
1 Bi bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp booloo nañu ci benn bérab.
2ܗܘܐ ܡܢ ܫܠܝܐ ܡܢ ܫܡܝܐ ܩܠܐ ܐܝܟ ܪܘܚܐ ܥܙܝܙܬܐ ܘܐܬܡܠܝ ܗܘܐ ܡܢܗ ܟܠܗ ܒܝܬܐ ܗܘ ܕܒܗ ܝܬܒܝܢ ܗܘܘ ܀
2 Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog.
3ܘܐܬܚܙܝܘ ܠܗܘܢ ܠܫܢܐ ܕܡܬܦܠܓܝܢ ܗܘܘ ܐܝܟ ܢܘܪܐ ܘܝܬܒܘ ܥܠ ܚܕ ܚܕ ܡܢܗܘܢ ܀
3 Te ay làmmiñ yu mel ni safara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk.
4ܘܐܬܡܠܝܘ ܟܠܗܘܢ ܒܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܘܐܩܦܘ ܗܘܘ ܠܡܡܠܠܘ ܒܠܫܢ ܠܫܢ ܐܝܟ ܡܐ ܕܪܘܚܐ ܝܗܒ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܠܡܡܠܠܘ ܀
4 Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneeni làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.
5ܐܝܬ ܗܘܘ ܕܝܢ ܓܒܪܐ ܕܥܡܪܝܢ ܒܐܘܪܫܠܡ ܕܕܚܠܝܢ ܡܢ ܐܠܗܐ ܝܗܘܕܝܐ ܡܢ ܟܠ ܥܡܡܐ ܕܬܚܝܬ ܫܡܝܐ ܀
5 Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.
6ܘܟܕ ܗܘܐ ܩܠܐ ܗܘ ܟܢܫ ܟܠܗ ܥܡܐ ܘܐܫܬܓܫ ܡܛܠ ܕܫܡܥ ܗܘܐ ܐܢܫ ܐܢܫ ܡܢܗܘܢ ܕܡܡܠܠܝܢ ܗܘܘ ܒܠܫܢܝܗܘܢ ܀
6 Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.
7ܬܗܝܪܝܢ ܗܘܘ ܕܝܢ ܟܠܗܘܢ ܘܡܬܕܡܪܝܢ ܟܕ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܚܕ ܠܚܕ ܗܠܝܢ ܟܠܗܘܢ ܕܡܡܠܠܝܢ ܠܐ ܗܐ ܓܠܝܠܝܐ ܐܢܘܢ ܀
7 Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?
8ܐܝܟܢܐ ܚܢܢ ܫܡܥܝܢ ܚܢܢ ܐܢܫ ܐܢܫ ܠܫܢܗ ܕܒܗ ܝܠܝܕܝܢ ܚܢܢ ܀
8 Naka la man a ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
9ܦܪܬܘܝܐ ܘܡܕܝܐ ܘܐܠܢܝܐ ܘܐܝܠܝܢ ܕܥܡܪܝܢ ܒܝܬ ܢܗܪܝܢ ܝܗܘܕܝܐ ܘܩܦܘܕܩܝܐ ܘܕܡܢ ܐܬܪܐ ܕܦܢܛܘܤ ܘܕܐܤܝܐ ܀
9 Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
10ܘܕܡܢ ܐܬܪܐ ܕܦܪܘܓܝܐ ܘܕܦܡܦܘܠܝܐ ܘܕܡܨܪܝܢ ܘܕܐܬܪܘܬܐ ܕܠܘܒܐ ܕܩܪܝܒܝܢ ܠܩܘܪܝܢܐ ܘܐܝܠܝܢ ܕܐܬܘ ܡܢ ܪܗܘܡܐ ܝܗܘܕܝܐ ܘܓܝܘܪܐ ܀
10 di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
11ܘܕܡܢ ܩܪܛܐ ܘܥܪܒܝܐ ܗܐ ܫܡܥܝܢ ܚܢܢ ܡܢܗܘܢ ܕܡܡܠܠܝܢ ܒܠܫܢܝܢ ܕܝܠܢ ܬܕܡܪܬܗ ܕܐܠܗܐ ܀
11 Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Kereet ak Araab yi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
12ܡܬܕܡܪܝܢ ܗܘܘ ܕܝܢ ܟܠܗܘܢ ܘܬܘܝܪܝܢ ܟܕ ܐܡܪܝܢ ܚܕ ܠܚܕ ܕܡܢܐ ܗܝ ܗܕܐ ܨܒܘܬܐ ܀
12 Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
13ܐܚܪܢܐ ܕܝܢ ܡܡܝܩܝܢ ܗܘܘ ܒܗܘܢ ܟܕ ܐܡܪܝܢ ܗܠܝܢ ܡܐܪܝܬܐ ܐܫܬܝܘ ܘܪܘܝܘ ܀
13 Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14ܒܬܪܟܢ ܩܡ ܫܡܥܘܢ ܟܐܦܐ ܥܡ ܚܕܥܤܪ ܫܠܝܚܝܢ ܘܐܪܝܡ ܩܠܗ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܓܒܪܐ ܝܗܘܕܝܐ ܘܟܠܗܘܢ ܕܥܡܪܝܢ ܒܐܘܪܫܠܡ ܗܕܐ ܬܬܝܕܥ ܠܟܘܢ ܘܨܘܬܘ ܡܠܝ ܀
14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
15ܠܐ ܓܝܪ ܐܝܟܢܐ ܕܐܢܬܘܢ ܤܒܪܝܢ ܗܠܝܢ ܪܘܝܢ ܕܗܐ ܥܕܡܐ ܠܗܫܐ ܬܠܬ ܐܢܝܢ ܫܥܝܢ ܀
15 Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16ܐܠܐ ܗܕܐ ܗܝ ܕܐܡܝܪܐ ܒܝܘܐܝܠ ܢܒܝܐ ܀
16 Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17ܢܗܘܐ ܒܝܘܡܬܐ ܐܚܪܝܐ ܐܡܪ ܐܠܗܐ ܐܫܘܕ ܪܘܚܝ ܥܠ ܟܠ ܒܤܪ ܘܢܬܢܒܘܢ ܒܢܝܟܘܢ ܘܒܢܬܟܘܢ ܘܓܕܘܕܝܟܘܢ ܚܙܘܢܐ ܢܚܙܘܢ ܘܩܫܝܫܝܟܘܢ ܚܠܡܐ ܢܚܠܡܘܢ ܀
17 “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi,dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp;seen xeet wu góor ak wu jigéendinañu wax ci kàddug Yàlla;waxambaane yi dinañu gis ay peeñute màggat yi di gént ay gént.
18ܘܥܠ ܥܒܕܝ ܘܥܠ ܐܡܗܬܝ ܐܫܘܕ ܪܘܚܝ ܒܝܘܡܬܐ ܗܢܘܢ ܘܢܬܢܒܘܢ ܀
18 Waaw ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xelci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen,te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
19ܘܐܬܠ ܐܬܘܬܐ ܒܫܡܝܐ ܘܓܒܪܘܬܐ ܥܠ ܐܪܥܐ ܕܡܐ ܘܢܘܪܐ ܘܥܛܪܐ ܕܬܢܢܐ ܀
19 Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaanak ay firnde ci suuf ci àddina,muy deret, safara ak ay niiri saxar.
20ܫܡܫܐ ܢܬܚܠܦ ܒܥܡܛܢܐ ܘܤܗܪܐ ܒܕܡܐ ܥܕܠܐ ܢܐܬܐ ܝܘܡܗ ܕܡܪܝܐ ܪܒܐ ܘܕܚܝܠܐ ܀
20 Jant bi dina daldi lëndëm,weer wi deretal,bala bésu Boroom biy ñëw,di bés bu mag, bi ànd ak ndam.
21ܘܢܗܘܐ ܟܠ ܕܢܩܪܐ ܫܡܗ ܕܡܪܝܐ ܢܚܐ ܀
21 Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam,dinga mucc.”
22ܓܒܪܐ ܒܢܝ ܐܝܤܪܝܠ ܫܡܥܘ ܡܠܐ ܗܠܝܢ ܝܫܘܥ ܢܨܪܝܐ ܓܒܪܐ ܕܡܢ ܐܠܗܐ ܐܬܚܙܝ ܠܘܬܟܘܢ ܒܚܝܠܐ ܘܒܐܬܘܬܐ ܘܒܓܒܪܘܬܐ ܐܝܠܝܢ ܕܐܠܗܐ ܥܒܕ ܒܝܢܬܟܘܢ ܒܐܝܕܗ ܐܝܟ ܕܐܢܬܘܢ ܝܕܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
22 «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.
23ܠܗܢܐ ܕܦܪܝܫ ܗܘܐ ܠܗ ܠܗܕܐ ܒܡܩܕܡܘܬ ܝܕܥܬܗ ܘܒܨܒܝܢܗ ܕܐܠܗܐ ܐܫܠܡܬܘܢܝܗܝ ܒܐܝܕܝ ܪܫܝܥܐ ܘܙܩܦܬܘܢ ܘܩܛܠܬܘܢ ܀
23 Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat.
24ܐܠܗܐ ܕܝܢ ܐܩܝܡܗ ܘܫܪܐ ܚܒܠܝܗ ܕܫܝܘܠ ܡܛܠ ܕܠܐ ܡܫܟܚܐ ܗܘܬ ܕܢܬܬܚܕ ܒܗ ܒܫܝܘܠ ܀
24 Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee mënu koo téye.
25ܕܘܝܕ ܓܝܪ ܐܡܪ ܥܠܘܗܝ ܡܩܕܡ ܗܘܝܬ ܚܙܐ ܠܡܪܝ ܒܟܠܙܒܢ ܕܥܠ ܝܡܝܢܝ ܗܘ ܕܠܐ ܐܙܘܥ ܀
25 Daawuda wax na ci mbiram ne:“Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam,gannaaw mu ngi ci sama ndeyjoor,kon duma raf.
26ܡܛܠ ܗܢܐ ܐܬܒܤܡ ܠܒܝ ܘܪܘܙܬ ܬܫܒܘܚܬܝ ܘܐܦ ܦܓܪܝ ܢܓܢ ܥܠ ܤܒܪܐ ܀
26 Moo tax sama xol sedd,may woy sama bànneex,te it sama yaram di tëdd ci yaakaar.
27ܡܛܠ ܕܠܐ ܫܒܩ ܐܢܬ ܠܢܦܫܝ ܒܫܝܘܠ ܘܠܐ ܝܗܒ ܐܢܬ ܠܚܤܝܟ ܕܢܚܙܐ ܚܒܠܐ ܀
27 Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq,te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
28ܓܠܝܬ ܠܝ ܐܘܪܚܐ ܕܚܝܐ ܬܡܠܝܢܝ ܒܤܝܡܘܬܐ ܥܡ ܦܪܨܘܦܟ ܀
28 Xamal nga ma yoonu dund;dinga ma béglooji ci sa kanam.”
29ܓܒܪܐ ܐܚܝܢ ܡܦܤ ܠܡܐܡܪ ܥܝܢ ܒܓܠܐ ܠܘܬܟܘܢ ܥܠ ܪܝܫ ܐܒܗܬܐ ܕܘܝܕ ܕܡܝܬ ܘܐܦ ܐܬܩܒܪ ܘܒܝܬ ܩܒܘܪܗ ܐܝܬܘܗܝ ܠܘܬܢ ܥܕܡܐ ܠܝܘܡܢܐ ܀
29 «Bokk yi, man naa leen a wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.
30ܢܒܝܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܘܝܕܥ ܗܘܐ ܕܡܘܡܬܐ ܝܡܐ ܠܗ ܐܠܗܐ ܕܡܢ ܦܐܪܐ ܕܟܪܤܟ ܐܘܬܒ ܥܠ ܟܘܪܤܝܟ ܀
30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne, Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne, dina teg ci nguuram kenn ci askanam.
31ܘܩܕܡ ܚܙܐ ܘܡܠܠ ܥܠ ܩܝܡܬܗ ܕܡܫܝܚܐ ܕܠܐ ܐܫܬܒܩ ܒܫܝܘܠ ܐܦܠܐ ܦܓܪܗ ܚܙܐ ܚܒܠܐ ܀
31 Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne, bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.
32ܠܗܢܐ ܝܫܘܥ ܐܩܝܡ ܐܠܗܐ ܘܚܢܢ ܟܠܢ ܤܗܕܘܗܝ ܀
32 Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.
33ܘܗܘܝܘ ܕܒܝܡܝܢܗ ܕܐܠܗܐ ܐܬܬܪܝܡ ܘܢܤܒ ܡܢ ܐܒܐ ܫܘܘܕܝܐ ܕܥܠ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܘܐܫܕ ܡܘܗܒܬܐ ܗܕܐ ܕܗܐ ܚܙܝܢ ܐܢܬܘܢ ܘܫܡܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
33 Yàlla yéege na ko ak ndeyjooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.
34ܠܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܕܘܝܕ ܤܠܩ ܠܫܡܝܐ ܡܛܠ ܕܗܘ ܐܡܪ ܕܐܡܪ ܡܪܝܐ ܠܡܪܝ ܬܒ ܠܟ ܡܢ ܝܡܝܢܝ ܀
34 Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na:“Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,
35ܥܕܡܐ ܕܐܤܝܡ ܒܥܠܕܒܒܝܟ ܟܘܒܫܐ ܠܪܓܠܝܟ ܀
35 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”
36ܫܪܝܪܐܝܬ ܗܟܝܠ ܢܕܥ ܟܠܗ ܒܝܬ ܐܝܤܪܝܠ ܕܡܪܝܐ ܘܡܫܝܚܐ ܥܒܕܗ ܐܠܗܐ ܠܗܢܐ ܝܫܘܥ ܕܐܢܬܘܢ ܙܩܦܬܘܢ ܀
36 «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne, Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
37ܘܟܕ ܫܡܥܘ ܗܠܝܢ ܐܬܓܢܚܘ ܒܠܒܗܘܢ ܘܐܡܪܘ ܠܫܡܥܘܢ ܘܠܫܪܟܐ ܕܫܠܝܚܐ ܡܢܐ ܢܥܒܕ ܐܚܝܢ ܀
37 Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu war a def?»
38ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܫܡܥܘܢ ܬܘܒܘ ܘܥܡܕܘ ܐܢܫ ܐܢܫ ܡܢܟܘܢ ܒܫܡܗ ܕܡܪܝܐ ܝܫܘܥ ܠܫܘܒܩܢ ܚܛܗܐ ܕܬܩܒܠܘܢ ܡܘܗܒܬܐ ܕܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܀
38 Piyeer tontu leen ne: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.
39ܠܟܘܢ ܓܝܪ ܗܘܐ ܫܘܘܕܝܐ ܘܠܒܢܝܟܘܢ ܘܠܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܪܚܝܩܝܢ ܐܝܠܝܢ ܕܗܘ ܐܠܗܐ ܢܩܪܐ ܐܢܘܢ ܀
39 Ndaxte li Yàlla dige woon, yéena ko moom ak seeni doom ak ñu sore ñépp, di ñépp ñi Yàlla sunu Boroom di woo ci moom.»
40ܘܒܡܠܐ ܐܚܪܢܝܬܐ ܤܓܝܐܬܐ ܡܤܗܕ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܘܒܥܐ ܗܘܐ ܡܢܗܘܢ ܟܕ ܐܡܪ ܚܝܘ ܡܢ ܫܪܒܬܐ ܗܕܐ ܡܥܩܡܬܐ ܀
40 Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen dénk ne: «Rëccleen ci niti jamono ju dëng jii.»
41ܘܐܢܫܝܢ ܡܢܗܘܢ ܥܬܝܕܐܝܬ ܩܒܠܘ ܡܠܬܗ ܘܗܝܡܢܘ ܘܥܡܕܘ ܘܐܬܬܘܤܦܘ ܒܗܘ ܝܘܡܐ ܐܝܟ ܬܠܬܐ ܐܠܦܝܢ ܢܦܫܢ ܀
41 Ñi nangu ay waxam nag, ñu sóob leen ci ndox, te ca bés booba lu mat limub ñetti junniy nit yokku nañu ci ñoom.
42ܘܐܡܝܢܝܢ ܗܘܘ ܒܝܘܠܦܢܐ ܕܫܠܝܚܐ ܘܡܫܬܘܬܦܝܢ ܗܘܘ ܒܨܠܘܬܐ ܘܒܩܨܝܐ ܕܐܘܟܪܤܛܝܐ ܀
42 Ñoom nag ñuy wéy ci njàngalem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak ñaan ci Yàlla.
43ܘܗܘܝܐ ܗܘܬ ܕܚܠܬܐ ܠܟܠ ܢܦܫ ܘܐܬܘܬܐ ܤܓܝܐܬܐ ܘܓܒܪܘܬܐ ܗܘܝܢ ܗܘܝ ܒܝܕ ܫܠܝܚܐ ܒܐܘܪܫܠܡ ܀
43 Ragal jàpp ñépp, te ndaw yi di def ay kéemaan ak ay firnde yu bare.
44ܘܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܗܝܡܢܘ ܗܘܘ ܐܟܚܕܐ ܗܘܘ ܘܟܠܡܕܡ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܕܓܘܐ ܗܘܐ ܀
44 Ñi gëm nag dañoo booloo te bokk lépp.
45ܘܐܝܠܝܢ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܩܢܝܢܐ ܡܙܒܢܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܘܡܦܠܓܝܢ ܗܘܘ ܠܐܢܫ ܐܢܫ ܐܝܟ ܡܕܡ ܕܤܢܝܩ ܗܘܐ ܀
45 Ñu jaay seeni suuf ak seen alal, séddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla.
46ܘܟܠܝܘܡ ܐܡܝܢܝܢ ܗܘܘ ܒܗܝܟܠܐ ܒܚܕܐ ܢܦܫ ܘܒܒܝܬܐ ܩܨܝܢ ܗܘܘ ܦܪܝܤܬܐ ܘܡܩܒܠܝܢ ܗܘܘ ܤܝܒܪܬܐ ܟܕ ܪܘܙܝܢ ܘܒܒܪܝܪܘܬܐ ܕܠܒܗܘܢ ܀
46 Te bés bu nekk ñu saxoo teew ak benn xalaat ca kër Yàlla ga, tey damm mburu ca kër ya; ñuy lekk seen ñam ak xol bu laab tey bég,
47ܡܫܒܚܝܢ ܗܘܘ ܠܐܠܗܐ ܟܕ ܝܗܝܒܝܢ ܒܪܚܡܐ ܩܕܡ ܟܠܗ ܥܡܐ ܘܡܪܢ ܡܘܤܦ ܗܘܐ ܟܠܝܘܡ ܠܐܝܠܝܢ ܕܚܐܝܢ ܒܥܕܬܐ ܀
47 di màggal Yàlla te am yiw ci wetu nit ñépp. Noonu bés bu nekk Boroom bi di yokk ca mbooloo ma ñi mucc.