1ܘܦܪܫܢ ܡܢܗܘܢ ܘܪܕܝܢ ܬܪܝܨܐܝܬ ܠܩܘ ܓܙܪܬܐ ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܐܬܝܢ ܠܪܘܕܘܤ ܘܡܢ ܬܡܢ ܠܦܐܛܪܐ ܀
1 Bi nga xamee ne tàggoo nanu ak ñoom ci naqar, nu dugg gaal, jubal dunu Kos. Te ca ëllëg sa nu dem ba teer ca Rodd, ba noppi jóge fa, jàll ba Patara.
2ܘܐܫܟܚܢ ܬܡܢ ܐܠܦܐ ܕܐܙܠܐ ܠܦܘܢܝܩܐ ܘܤܠܩܢ ܠܗ ܘܪܕܝܢ ܀
2 Foofa nag nu gis gaal guy jàll ba Fenisi, nu dugg ca, mu daldi teddi.
3ܘܡܛܝܢ ܥܕܡܐ ܠܘܬ ܩܘܦܪܘܤ ܓܙܪܬܐ ܘܫܒܩܢܗ ܠܤܡܠܐ ܘܐܬܝܢ ܠܤܘܪܝܐ ܘܡܢ ܬܡܢ ܡܛܝܢ ܠܨܘܪ ܬܡܢ ܓܝܪ ܐܝܬ ܗܘܐ ܠܗ ܠܐܠܦܐ ܠܡܢܚܘ ܛܥܢܗ ܀
3 Noonu nu séen dunu Sipar, bàyyi ko ci sunu càmmooñ, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi war a yebbee la mu yeboon.
4ܘܟܕ ܐܫܟܚܢ ܬܡܢ ܬܠܡܝܕܐ ܩܘܝܢ ܠܘܬܗܘܢ ܝܘܡܬܐ ܫܒܥܐ ܘܗܠܝܢ ܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܟܠܝܘܡ ܠܦܘܠܘܤ ܒܪܘܚ ܕܠܐ ܢܐܙܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܀
4 Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak ñoom juróom-ñaari fan. Ñoom nag ñu ne Pool ci li leen Xelu Yàlla mi may, mu bañ a dem Yerusalem.
5ܘܡܢ ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܝܘܡܬܐ ܢܦܩܢ ܕܢܐܙܠ ܒܐܘܪܚܐ ܘܡܠܘܝܢ ܗܘܘ ܠܢ ܟܠܗܘܢ ܗܢܘܢ ܘܢܫܝܗܘܢ ܘܒܢܝܗܘܢ ܥܕܡܐ ܠܒܪ ܡܢ ܡܕܝܢܬܐ ܘܩܥܕܘ ܥܠ ܒܘܪܟܝܗܘܢ ܥܠ ܝܕ ܝܡܐ ܘܨܠܝܘ ܀
5 Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te ñépp gunge nu, ñoom ak seeni jabar ak seeni doom; nu génn dëkk ba, sukk ca tefes ga, ñaan ci Yàlla.
6ܘܢܫܩܢ ܠܚܕܕܐ ܘܤܠܩܢ ܠܐܠܦܐ ܘܗܦܟܘ ܗܢܘܢ ܠܒܬܝܗܘܢ ܀
6 Noonu nu tàggoo ak ñoom, dugg ca gaal ga, ñu dellu seen kër.
7ܚܢܢ ܕܝܢ ܪܕܝܢ ܡܢ ܨܘܪ ܘܐܬܝܢ ܠܥܟܘ ܡܕܝܢܬܐ ܘܝܗܒܢ ܫܠܡܐ ܠܐܚܐ ܕܬܡܢ ܘܫܪܝܢ ܨܐܕܝܗܘܢ ܝܘܡܐ ܚܕ ܀
7 Bi nu jógee Tir nag, nu demaat ci géej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan.
8ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܢܦܩܢ ܘܐܬܝܢ ܠܩܤܪܝܐ ܘܥܠܢ ܫܪܝܢ ܒܒܝܬܗ ܕܦܝܠܝܦܘܤ ܡܤܒܪܢܐ ܐܝܢܐ ܕܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܡܢ ܫܒܥܐ ܀
8 Nu jóge fa ca ëllëg sa, ñëw ba ca dëkku Sesare. Nu dugg ca kër Filib, taskatu xebaar bu baax bi, mi bokk ci Juróom-ñaar ña, nu dal fa moom.
9ܘܐܝܬ ܗܘܝ ܠܗ ܒܢܬܐ ܒܬܘܠܬܐ ܐܪܒܥ ܕܡܬܢܒܝܢ ܗܘܝ ܀
9 Amoon na ñeenti doom yuy janq, ñuy wax ci kàddug Yàlla.
10ܘܟܕ ܐܝܬܝܢ ܬܡܢ ܝܘܡܬܐ ܤܓܝܐܐ ܢܚܬ ܗܘܐ ܡܢ ܝܗܘܕ ܢܒܝܐ ܚܕ ܕܫܡܗ ܗܘܐ ܐܓܒܘܤ ܀
10 Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi.
11ܘܥܠ ܠܘܬܢ ܘܫܩܠ ܥܪܩܬܐ ܕܚܨܘܗܝ ܕܦܘܠܘܤ ܘܐܤܪ ܪܓܠܐ ܕܢܦܫܗ ܘܐܝܕܘܗܝ ܘܐܡܪ ܗܟܢܐ ܐܡܪ ܪܘܚܐ ܕܩܘܕܫܐ ܕܓܒܪܐ ܡܪܗ ܕܥܪܩܬܐ ܗܕܐ ܗܟܢܐ ܢܐܤܪܘܢܗ ܝܗܘܕܝܐ ܒܐܘܪܫܠܡ ܘܢܫܠܡܘܢܗ ܒܐܝܕܝ ܥܡܡܐ ܀
11 Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
12ܘܟܕ ܗܠܝܢ ܡܠܐ ܫܡܥܢ ܒܥܝܢ ܡܢܗ ܚܢܢ ܘܒܢܝ ܐܬܪܐ ܕܠܐ ܢܐܙܠ ܠܐܘܪܫܠܡ ܀
12 Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu bañ a dem Yerusalem.
13ܗܝܕܝܢ ܥܢܐ ܘܐܡܪ ܦܘܠܘܤ ܡܢܐ ܥܒܕܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܒܟܝܢ ܐܢܬܘܢ ܘܫܚܩܝܢ ܐܢܬܘܢ ܠܗ ܠܠܒܝ ܐܢܐ ܓܝܪ ܠܐ ܗܘܐ ܕܐܬܐܤܪ ܒܠܚܘܕ ܡܛܝܒ ܐܢܐ ܐܠܐ ܐܦ ܕܐܡܘܬ ܒܐܘܪܫܠܡ ܚܠܦ ܫܡܗ ܕܡܪܢ ܝܫܘܥ ܀
13 Ci kaw loolu Pool tontu ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.»
14ܘܟܕ ܠܐ ܐܬܛܦܝܤ ܠܢ ܒܗܠܢ ܠܢ ܘܐܡܪܢ ܕܨܒܝܢܗ ܕܡܪܢ ܢܗܘܐ ܀
14 Bi nu ko mënul a dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobareg Boroom bi am!»
15ܘܒܬܪ ܝܘܡܬܐ ܗܠܝܢ ܐܬܛܝܒܢ ܘܤܠܩܢ ܠܢ ܠܐܘܪܫܠܡ ܀
15 Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.
16ܘܐܬܘ ܗܘܘ ܥܡܢ ܐܢܫܐ ܬܠܡܝܕܐ ܡܢ ܩܤܪܝܐ ܟܕ ܕܒܝܪܝܢ ܥܡܗܘܢ ܐܚܐ ܚܕ ܡܢ ܬܠܡܝܕܐ ܩܕܡܝܐ ܕܫܡܗ ܗܘܐ ܡܢܤܘܢ ܘܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܡܢ ܩܘܦܪܘܤ ܕܢܩܒܠܢ ܒܒܝܬܗ ܀
16 Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu war a dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg.
17ܘܟܕ ܐܬܝܢ ܠܐܘܪܫܠܡ ܩܒܠܘܢ ܐܚܐ ܚܕܝܐܝܬ ܀
17 Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég.
18ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܥܠܢ ܥܡ ܦܘܠܘܤ ܠܘܬ ܝܥܩܘܒ ܟܕ ܐܝܬ ܗܘܐ ܠܘܬܗ ܟܠܗܘܢ ܩܫܝܫܐ ܀
18 Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa.
19ܘܝܗܒܢ ܠܗܘܢ ܫܠܡܐ ܘܡܫܬܥܐ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܦܘܠܘܤ ܒܬܪ ܒܬܪ ܟܠ ܡܐ ܕܥܒܕ ܐܠܗܐ ܒܥܡܡܐ ܒܬܫܡܫܬܗ ܀
19 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.
20ܘܟܕ ܫܡܥܘ ܫܒܚܘ ܠܐܠܗܐ ܘܐܡܪܘ ܠܗ ܚܙܐ ܐܢܬ ܐܚܘܢ ܟܡܐ ܪܒܘܢ ܐܝܬ ܒܝܗܘܕ ܐܝܠܝܢ ܕܗܝܡܢܘ ܘܟܠܗܘܢ ܗܠܝܢ ܛܢܢܐ ܐܢܘܢ ܕܢܡܘܤܐ ܀
20 Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne, am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.
21ܐܬܐܡܪ ܠܗܘܢ ܕܝܢ ܥܠܝܟ ܕܡܠܦ ܐܢܬ ܕܢܦܪܩܘܢ ܡܢ ܡܘܫܐ ܟܠܗܘܢ ܝܗܘܕܝܐ ܕܒܥܡܡܐ ܟܕ ܐܡܪ ܐܢܬ ܕܠܐ ܢܗܘܘܢ ܓܙܪܝܢ ܒܢܝܗܘܢ ܘܠܐ ܒܥܝܕܐ ܕܢܡܘܤܐ ܢܗܘܘܢ ܡܗܠܟܝܢ ܀
21 Dégg nañu ci sa mbir nag ne, yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te bañ a xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.
22ܡܛܠ ܗܟܝܠ ܕܡܫܬܡܥܐ ܗܝ ܠܗܘܢ ܕܐܬܝܬ ܠܟܐ ܀
22 Lu nu ci war a def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne, ñëw nga.
23ܥܒܕ ܡܕܡ ܕܐܡܪܝܢܢ ܠܟ ܐܝܬ ܠܢ ܓܒܪܐ ܐܪܒܥܐ ܕܢܕܝܪ ܠܗܘܢ ܕܢܬܕܟܘܢ ܀
23 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor yu dige ak Yàlla.
24ܕܒܪ ܐܢܘܢ ܘܙܠ ܐܬܕܟܐ ܥܡܗܘܢ ܘܐܦܩ ܥܠܝܗܘܢ ܢܦܩܬܐ ܐܝܟ ܕܢܓܪܥܘܢ ܪܫܝܗܘܢ ܘܡܬܝܕܥܐ ܠܟܠܢܫ ܕܡܕܡ ܕܐܬܐܡܪ ܥܠܝܟ ܕܓܠ ܗܘ ܘܐܢܬ ܠܢܡܘܤܐ ܫܠܡ ܐܢܬ ܘܢܛܪ ܀
24 Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne, li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa.
25ܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܝܢ ܕܗܝܡܢܘ ܡܢ ܥܡܡܐ ܚܢܢ ܟܬܒܢ ܕܢܗܘܘܢ ܢܛܪܝܢ ܢܦܫܗܘܢ ܡܢ ܕܕܒܝܚܐ ܘܡܢ ܙܢܝܘܬܐ ܘܡܢ ܚܢܝܩܐ ܘܡܢ ܕܡܐ ܀
25 Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.»
26ܗܝܕܝܢ ܦܘܠܘܤ ܕܒܪ ܐܢܘܢ ܠܓܒܪܐ ܗܠܝܢ ܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܘܐܬܕܟܝ ܥܡܗܘܢ ܘܥܠ ܐܙܠ ܠܗܝܟܠܐ ܟܕ ܡܘܕܥ ܠܗܘܢ ܡܘܠܝܐ ܕܝܘܡܬܐ ܕܬܕܟܝܬܐ ܥܕܡܐ ܕܐܬܩܪܒ ܩܘܪܒܢܐ ܕܐܢܫ ܐܢܫ ܡܢܗܘܢ ܀
26 Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom.
27ܘܟܕ ܡܛܝ ܝܘܡܐ ܕܫܒܥܐ ܝܗܘܕܝܐ ܕܡܢ ܐܤܝܐ ܚܙܐܘܗܝ ܒܗܝܟܠܐ ܘܓܪܝܘ ܥܠܘܗܝ ܥܡܐ ܟܠܗ ܘܐܪܡܝܘ ܥܠܘܗܝ ܐܝܕܝܐ ܀
27 Bi àppu juróom-ñaari fan ya di bëgg a jeex, Yawut yi jóge diiwaanu Asi gis Pool ca kër Yàlla ga. Ñu daldi jógloo mbooloo mépp, jàpp ko,
28ܟܕ ܡܒܓܢܝܢ ܘܐܡܪܝܢ ܓܒܪܐ ܒܢܝ ܐܝܤܪܝܠ ܥܕܪܘ ܗܢܐ ܗܘ ܓܒܪܐ ܕܠܘܩܒܠ ܥܡܐ ܕܝܠܢ ܡܠܦ ܒܟܠ ܕܘܟܐ ܘܠܘܩܒܠ ܢܡܘܤܐ ܘܠܘܩܒܠ ܐܬܪܐ ܗܢܐ ܘܐܦ ܠܐܪܡܝܐ ܐܥܠ ܠܗܝܟܠܐ ܘܤܝܒܗ ܠܐܬܪܐ ܗܢܐ ܩܕܝܫܐ ܀
28 di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil; waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»
29ܩܕܡܘ ܗܘܘ ܓܝܪ ܚܙܘ ܥܡܗ ܠܛܪܘܦܝܡܤ ܐܦܤܝܐ ܒܡܕܝܢܬܐ ܘܤܒܪܝܢ ܗܘܘ ܕܥܡ ܦܘܠܘܤ ܥܠ ܠܗܝܟܠܐ ܀
29 Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne, Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga.
30ܘܐܫܬܓܫܬ ܡܕܝܢܬܐ ܘܐܬܟܢܫܘ ܟܠܗ ܥܡܐ ܘܐܚܕܘܗܝ ܠܦܘܠܘܤ ܘܓܪܘܗܝ ܠܒܪ ܡܢ ܗܝܟܠܐ ܘܒܪ ܫܥܬܗ ܐܬܬܚܕܘ ܬܪܥܐ ܀
30 Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya.
31ܘܟܕ ܒܥܐ ܗܘܐ ܟܢܫܐ ܠܡܩܛܠܗ ܐܫܬܡܥܬ ܠܟܠܝܪܟܐ ܕܐܤܦܝܪ ܕܟܠܗ ܡܕܝܢܬܐ ܐܬܬܙܝܥܬ ܠܗ ܀
31 Bi ñu koy wut a rey, xebaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na.
32ܘܒܪ ܫܥܬܗ ܕܒܪ ܠܩܢܛܪܘܢܐ ܘܠܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܤܓܝܐܐ ܘܪܗܛܘ ܥܠܝܗܘܢ ܘܟܕ ܚܙܘ ܠܟܠܝܪܟܐ ܘܠܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܒܗܠܘ ܡܢ ܕܡܚܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܠܦܘܠܘܤ ܀
32 Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool.
33ܘܩܪܒ ܠܘܬܗ ܟܠܝܪܟܐ ܘܐܚܕܗ ܘܦܩܕ ܕܢܐܤܪܘܢܗ ܒܬܪܬܝܢ ܫܫܠܢ ܘܡܫܐܠ ܗܘܐ ܥܠܘܗܝ ܕܡܢܘ ܘܡܢܐ ܥܒܕ ܀
33 Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.
34ܘܩܥܝܢ ܗܘܘ ܥܠܘܗܝ ܐܢܫܐ ܡܢ ܐܟܠܘܤ ܡܕܡ ܡܕܡ ܘܡܛܠ ܩܥܬܗܘܢ ܠܐ ܡܫܟܚ ܗܘܐ ܠܡܕܥ ܐܝܕܐ ܗܝ ܫܪܝܪܬܐ ܘܦܩܕ ܗܘܐ ܕܢܘܒܠܘܢܗ ܠܡܫܪܝܬܐ ܀
34 Waaye ci biir mbooloo ma, bu ñii nee lii, ña ca des ne laa. Kon nag gannaaw mënu caa xam dara lu wóor ndax coow li, mu santaane, ñu yóbbu ko ci biir tata ja.
35ܘܟܕ ܡܛܝ ܦܘܠܘܤ ܠܕܪܓܐ ܛܥܢܘܗܝ ܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܡܛܠ ܩܛܝܪܐ ܕܥܡܐ ܀
35 Bi Pool eggee ca yéegukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma réy, ba ay xarekat fab ko.
36ܐܬܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܒܬܪܗ ܥܡܐ ܤܓܝܐܐ ܘܩܥܝܢ ܗܘܘ ܘܐܡܪܝܢ ܫܩܘܠܝܗܝ ܀
36 Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: «Reyleen ko!»
37ܘܟܕ ܡܛܝ ܠܡܥܠ ܠܡܫܪܝܬܐ ܗܘ ܦܘܠܘܤ ܐܡܪ ܠܟܠܝܪܟܐ ܐܢ ܡܦܤ ܐܢܬ ܠܝ ܐܡܠܠ ܥܡܟ ܗܘ ܕܝܢ ܐܡܪ ܠܗ ܝܘܢܐܝܬ ܝܕܥ ܐܢܬ ܀
37 Bi ñu koy bëgg a dugal ca tata ja, Pool ne kilifa ga: «Ndax man naa laa wax dara?» Mu tontu ko: «Yaw dégg nga gereg?
38ܠܐ ܗܘܝܬ ܐܢܬ ܗܘ ܡܨܪܝܐ ܕܩܕܡ ܝܘܡܬܐ ܗܠܝܢ ܐܙܝܥܬ ܘܐܦܩܬ ܠܡܕܒܪܐ ܐܪܒܥܐ ܐܠܦܝܢ ܓܒܪܐ ܥܒܕܝ ܒܝܫܬܐ ܀
38 Kon nekkuloo waayi Misra, jooju jógloo woon nit ñi keroog te yóbbu woon ñeenti junniy bóomkat ca màndiŋ ma?»
39ܐܡܪ ܠܗ ܦܘܠܘܤ ܐܢܐ ܓܒܪܐ ܐܢܐ ܝܗܘܕܝܐ ܡܢ ܛܪܤܘܤ ܕܩܝܠܝܩܝܐ ܡܕܝܢܬܐ ܝܕܝܥܬܐ ܕܒܗ ܝܠܝܕ ܐܢܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܡܢܟ ܐܦܤ ܠܝ ܠܡܡܠܠܘ ܠܥܡܐ ܀
39 Pool ne ko: «Man Yawut laa, di jaambur ci Tars, dëkk bu am tur ci diiwaanu Silisi. Maa ngi lay ñaan, ma wax ak mbooloo mi.»
40ܘܟܕ ܐܦܤ ܠܗ ܩܡ ܦܘܠܘܤ ܥܠ ܕܪܓܐ ܘܐܙܝܥ ܗܘܐ ܠܗܘܢ ܐܝܕܗ ܘܟܕ ܒܗܠܘ ܡܠܠ ܥܡܗܘܢ ܥܒܪܐܝܬ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܀
40 Te kilifa ga may ko ko. Noonu Pool taxaw ca yéegukaay ba, tàllal loxoom mbooloo ma, ñu daldi ne tekk. Mu wax ak ñoom ci làkku yawut ne: