Syriac: NT

Wolof: New Testament

Acts

23

1ܘܟܕ ܚܪ ܦܘܠܘܤ ܒܟܢܫܗܘܢ ܐܡܪ ܓܒܪܐ ܐܚܝ ܐܢܐ ܒܟܠ ܬܐܪܬܐ ܛܒܬܐ ܐܬܕܒܪܬ ܩܕܡ ܐܠܗܐ ܥܕܡܐ ܠܝܘܡܢܐ ܀
1 Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.»
2ܘܚܢܢܝܐ ܟܗܢܐ ܦܩܕ ܠܗܢܘܢ ܕܩܝܡܝܢ ܥܠ ܓܒܗ ܕܢܡܚܘܢܗ ܠܦܘܠܘܤ ܥܠ ܦܘܡܗ ܀
2 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam.
3ܘܦܘܠܘܤ ܐܡܪ ܠܗ ܥܬܝܕ ܗܘ ܐܠܗܐ ܕܢܡܚܝܟ ܐܤܬܐ ܡܚܘܪܬܐ ܘܐܢܬ ܝܬܒ ܐܢܬ ܕܐܢ ܐܢܬ ܠܝ ܐܝܟ ܕܒܢܡܘܤܐ ܟܕ ܥܒܪ ܐܢܬ ܥܠ ܢܡܘܤܐ ܘܦܩܕ ܐܢܬ ܕܢܡܚܘܢܢܝ ܀
3 Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!»
4ܘܐܝܠܝܢ ܕܩܝܡܝܢ ܗܘܘ ܬܡܢ ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܠܟܗܢܐ ܕܐܠܗܐ ܡܨܚܐ ܐܢܬ ܀
4 Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas saraxalekat bu mag, bi Yàlla fal?»
5ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܦܘܠܘܤ ܠܐ ܝܕܥ ܗܘܝܬ ܐܚܝ ܕܟܗܢܐ ܗܘ ܟܬܝܒ ܗܘ ܓܝܪ ܕܠܪܫܐ ܕܥܡܟ ܠܐ ܬܠܘܛ ܀
5 Pool tontu leen: «Bokk yi, xawma woon ne saraxalekat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»
6ܘܟܕ ܝܕܥ ܦܘܠܘܤ ܕܡܢܗ ܕܥܡܐ ܐܝܬܘܗܝ ܕܙܕܘܩܝܐ ܘܡܢܗ ܕܦܪܝܫܐ ܩܥܐ ܗܘܐ ܒܟܢܫܐ ܓܒܪܐ ܐܚܝ ܐܢܐ ܦܪܝܫܐ ܐܢܐ ܒܪ ܦܪܝܫܐ ܘܥܠ ܤܒܪܐ ܕܩܝܡܬܐ ܕܡܝܬܐ ܡܬܕܝܢ ܐܢܐ ܀
6 Naka noona Pool, mi xam ne, genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.»
7ܘܟܕ ܗܕܐ ܐܡܪ ܢܦܠܘ ܚܕ ܒܚܕ ܦܪܝܫܐ ܘܙܕܘܩܝܐ ܘܐܬܦܠܓ ܥܡܐ ܀
7 Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xaajalikoo.
8ܙܕܘܩܝܐ ܓܝܪ ܐܡܪܝܢ ܕܠܝܬ ܩܝܡܬܐ ܘܠܐ ܡܠܐܟܐ ܘܠܐ ܪܘܚܐ ܦܪܝܫܐ ܕܝܢ ܡܘܕܝܢ ܒܟܠܗܝܢ ܀
8 Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne, ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp.
9ܘܗܘܐ ܩܠܐ ܪܒܐ ܘܩܡܘ ܐܢܫܐ ܤܦܪܐ ܡܢ ܓܒܐ ܕܦܪܝܫܐ ܘܢܨܝܢ ܗܘܘ ܥܡܗܘܢ ܘܐܡܪܝܢ ܠܐ ܡܫܟܚܝܢܢ ܡܕܡ ܕܒܝܫ ܒܗܢܐ ܓܒܪܐ ܐܢ ܕܝܢ ܪܘܚܐ ܐܘ ܡܠܐܟܐ ܡܠܠ ܥܡܗ ܡܢܐ ܐܝܬ ܒܗ ܒܗܕܐ ܀
9 Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne, rab a ko wax mbaa malaaka...?»
10ܘܟܕ ܗܘܐ ܫܓܘܫܝܐ ܪܒܐ ܒܝܢܬܗܘܢ ܕܚܠ ܗܘܐ ܟܠܝܪܟܐ ܕܠܡܐ ܢܦܫܚܘܢܗ ܠܦܘܠܘܤ ܘܫܠܚ ܠܪܗܘܡܝܐ ܕܢܐܬܘܢ ܢܚܛܦܘܢܗ ܡܢ ܡܨܥܬܗܘܢ ܘܢܥܠܘܢܗ ܠܡܫܪܝܬܐ ܀
10 Noonu xuloo ba daldi gën a tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.
11ܘܟܕ ܗܘܐ ܠܠܝܐ ܐܬܚܙܝ ܠܗ ܡܪܢ ܠܦܘܠܘܤ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܬܚܝܠ ܡܛܠ ܕܐܝܟ ܕܐܤܗܕܬ ܥܠܝ ܒܐܘܪܫܠܡ ܗܟܢܐ ܥܬܝܕ ܐܢܬ ܕܐܦ ܒܪܗܘܡܐ ܬܤܗܕ ܀
11 Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.»
12ܘܟܕ ܗܘܐ ܨܦܪܐ ܐܬܟܢܫܘ ܗܘܘ ܐܢܫܝܢ ܡܢ ܝܗܘܕܝܐ ܘܐܚܪܡܘ ܥܠܝܗܘܢ ܕܠܐ ܢܐܟܠܘܢ ܘܠܐ ܢܫܬܘܢ ܥܕܡܐ ܕܢܩܛܠܘܢܗ ܠܦܘܠܘܤ ܀
12 Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne, duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool.
13ܗܘܝܢ ܗܘܘ ܕܝܢ ܗܢܘܢ ܕܐܩܝܡܘ ܒܡܘܡܬܐ ܗܢܐ ܩܝܡܐ ܝܬܝܪ ܡܢ ܐܪܒܥܝܢ ܓܒܪܝܢ ܀
13 Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent-fukk.
14ܘܐܬܩܪܒܘ ܠܘܬ ܟܗܢܐ ܘܠܘܬ ܩܫܝܫܐ ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܕܚܪܡܐ ܐܚܪܡܢ ܥܠܝܢ ܕܡܕܡ ܠܐ ܢܛܥܡ ܥܕܡܐ ܕܢܩܛܘܠ ܠܦܘܠܘܤ ܀
14 Noonu ñu dem ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne, dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.
15ܘܗܫܐ ܒܥܘ ܐܢܬܘܢ ܘܪܫܐ ܕܟܢܘܫܬܐ ܡܢ ܟܠܝܪܟܐ ܕܢܝܬܝܘܗܝ ܠܘܬܟܘܢ ܐܝܟ ܒܥܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܬܒܨܘܢ ܫܪܝܪܐܝܬ ܤܘܥܪܢܗ ܘܚܢܢ ܡܛܝܒܝܢܢ ܕܢܩܛܠܝܘܗܝ ܥܕܠܐ ܢܡܛܐ ܠܘܬܟܘܢ ܀
15 Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeen a bëgg a seet mbiram bu gën a wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»
16ܘܫܡܥ ܗܘܐ ܒܪ ܚܬܗ ܕܦܘܠܘܤ ܐܦܪܤܢܐ ܗܢܐ ܘܥܠ ܠܡܫܪܝܬܐ ܘܒܕܩ ܠܦܘܠܘܤ ܀
16 Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.
17ܘܫܕܪ ܦܘܠܘܤ ܩܪܐ ܠܚܕ ܡܢ ܩܢܛܪܘܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗ ܐܘܒܠ ܠܥܠܝܡܐ ܗܢܐ ܠܘܬ ܟܠܝܪܟܐ ܐܝܬ ܠܗ ܓܝܪ ܡܕܡ ܕܢܐܡܪ ܠܗ ܀
17 Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko war a yégal.»
18ܘܕܒܪܗ ܩܢܛܪܘܢܐ ܠܥܠܝܡܐ ܘܐܥܠܗ ܠܘܬ ܟܠܝܪܟܐ ܘܐܡܪ ܦܘܠܘܤ ܐܤܝܪܐ ܩܪܢܝ ܘܒܥܐ ܡܢܝ ܕܐܝܬܐ ܗܢܐ ܥܠܝܡܐ ܠܘܬܟ ܕܐܝܬ ܠܗ ܡܕܡ ܕܢܐܡܪ ܠܟ ܀
18 Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»
19ܘܐܚܕܗ ܒܐܝܕܗ ܟܠܝܪܟܐ ܠܥܠܝܡܐ ܘܢܓܕܗ ܠܚܕ ܓܒܐ ܘܡܫܐܠ ܗܘܐ ܠܗ ܕܡܢܐ ܐܝܬ ܠܟ ܕܬܐܡܪ ܠܝ ܀
19 Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgg a yégal?»
20ܘܐܡܪ ܠܗ ܥܠܝܡܐ ܝܗܘܕܝܐ ܐܬܚܫܒܘ ܕܢܒܥܘܢ ܡܢܟ ܕܬܚܬ ܠܦܘܠܘܤ ܡܚܪ ܠܟܢܫܗܘܢ ܐܝܟ ܨܒܝܢ ܡܕܡ ܝܬܝܪ ܕܢܐܠܦܘܢ ܡܢܗ ܀
20 Mu tontu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanamu kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgg a seet mbiram bu gën a wóor.
21ܐܢܬ ܗܟܝܠ ܠܐ ܬܬܛܦܝܤ ܠܗܘܢ ܗܐ ܓܝܪ ܝܬܝܪ ܡܢ ܐܪܒܥܝܢ ܓܒܪܝܢ ܡܢܗܘܢ ܢܛܪܝܢ ܠܗ ܒܟܡܐܢܐ ܘܐܚܪܡܘ ܥܠ ܢܦܫܗܘܢ ܕܠܐ ܢܐܟܠܘܢ ܘܠܐ ܢܫܬܘܢ ܥܕܡܐ ܕܢܩܛܠܘܢܗ ܘܗܐ ܡܛܝܒܝܢ ܘܡܩܘܝܢ ܠܫܘܘܕܝܟ ܀
21 Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent-fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne, dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.»
22ܘܫܪܝܗܝ ܟܠܝܪܟܐ ܠܥܠܝܡܐ ܟܕ ܦܩܕܗ ܕܐܢܫ ܠܐ ܢܕܥ ܕܗܠܝܢ ܒܕܩܬ ܠܝ ܀
22 Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.
23ܘܩܪܐ ܠܬܪܝܢ ܩܢܛܪܘܢܝܢ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܙܠܘ ܥܬܕܘ ܪܗܘܡܝܐ ܡܐܬܝܢ ܕܢܐܙܠܘܢ ܠܩܤܪܝܐ ܘܦܪܫܐ ܫܒܥܝܢ ܘܫܕܝܝ ܒܝܡܝܢܐ ܡܐܬܝܢ ܕܢܦܩܘܢ ܡܢ ܬܠܬ ܫܥܝܢ ܒܠܠܝܐ ܀
23 Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaari téeméeri xarekat ak juróom-ñaar-fukki gawar ak ñaari téeméer ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom-ñeenti waxtu ci guddi.
24ܛܝܒܘ ܕܝܢ ܐܦ ܒܥܝܪܐ ܐܝܟ ܕܢܪܟܒܘܢ ܠܦܘܠܘܤ ܘܢܦܠܛܘܢܗ ܠܘܬ ܦܝܠܟܤ ܗܓܡܘܢܐ ܀
24 Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.»
25ܘܟܬܒ ܐܓܪܬܐ ܝܗܒ ܠܗܘܢ ܕܐܝܬ ܒܗ ܗܟܢܐ ܀
25 Noonu mu bind bataaxal bii:
26ܠܘܤܝܘܤ ܠܦܝܠܟܤ ܗܓܡܘܢܐ ܢܨܝܚܐ ܫܠܡ ܀
26 Yaw Feligsë mu tedd mi, di boroom réew mi; man Këlódd Lisiyas maa ngi lay nuyu.
27ܠܓܒܪܐ ܗܢܐ ܐܚܕܘ ܝܗܘܕܝܐ ܐܝܟ ܕܢܩܛܠܘܢܗ ܘܩܡܬ ܐܢܐ ܥܡ ܪܗܘܡܝܐ ܘܦܪܩܬܗ ܟܕ ܝܠܦܬ ܕܪܗܘܡܝܐ ܗܘ ܀
27 Yawut yi jàpp nañu nit kii, bëgg koo rey, waaye bi ma yégee ne, jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko.
28ܘܟܕ ܒܥܐ ܗܘܝܬ ܠܡܕܥ ܥܠܬܐ ܕܡܛܠܬܗ ܪܫܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܐܚܬܬܗ ܠܟܢܫܗܘܢ ܀
28 Bëggoon naa xam lu tax ñu kalaame ko. Moo tax ma yóbbu ko ca kanamu seen kureelu àttekat ya.
29ܘܐܫܟܚܬ ܕܥܠ ܙܛܡܐ ܕܢܡܘܤܗܘܢ ܪܫܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܘܥܠܬܐ ܕܫܘܝܐ ܠܐܤܘܪܐ ܐܘ ܠܡܘܬܐ ܠܝܬ ܗܘܐ ܠܘܬܗ ܀
29 Gis naa ne li ñu ko jiiñ mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jiiñuñu ko dara lu jar dee mbaa jéng.
30ܘܟܕ ܐܬܒܕܩ ܠܝ ܢܟܠܐ ܒܟܡܐܢܐ ܕܥܒܕܘ ܥܠܘܗܝ ܝܗܘܕܝܐ ܡܚܕܐ ܫܕܪܬܗ ܠܘܬܟ ܘܦܩܕܬ ܠܩܛܓܪܢܘܗܝ ܕܢܐܬܘܢ ܘܢܐܡܪܘܢ ܥܡܗ ܩܕܡܝܟ ܗܘܝ ܚܠܝܡ ܀
30 Te bi ma déggee ne, ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay.
31ܗܝܕܝܢ ܪܗܘܡܝܐ ܐܝܟ ܕܐܬܦܩܕܘ ܕܒܪܘܗܝ ܠܦܘܠܘܤ ܒܠܠܝܐ ܘܐܝܬܝܘܗܝ ܠܐܢܛܝܦܛܪܤ ܡܕܝܢܬܐ ܀
31 Noonu xarekat ya jël Pool ci guddi, indi ko ba ca dëkku Antipataris, ni ñu leen ko sante.
32ܘܠܝܘܡܐ ܐܚܪܢܐ ܫܪܘ ܦܪܫܐ ܠܪܓܠܐ ܚܒܪܝܗܘܢ ܕܢܗܦܟܘܢ ܠܡܫܪܝܬܐ ܀
32 Ca ëllëg sa ñu woññiku, dellusi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge ko.
33ܘܐܝܬܝܘܗܝ ܠܩܤܪܝܐ ܘܝܗܒܘ ܐܓܪܬܐ ܠܗܓܡܘܢܐ ܘܐܩܝܡܘܗܝ ܩܕܡܘܗܝ ܠܦܘܠܘܤ ܀
33 Bi gawar ga àggee Sesare, ñu jox boroom réew ma bataaxal ba, jébbal ko Pool.
34ܘܟܕ ܩܪܐ ܐܓܪܬܐ ܡܫܐܠ ܗܘܐ ܠܗ ܕܡܢ ܐܝܕܐ ܗܘܦܪܟܝܐ ܐܝܬܘܗܝ ܘܟܕ ܝܠܦ ܕܡܢ ܩܝܠܝܩܝܐ ܀
34 Bi loolu amee boroom réew ma jàng bataaxal ba, laaj ci ban diiwaan la Pool dëkk. Bi mu yégee ne, mu ngi dëkk Silisi,
35ܐܡܪ ܠܗ ܫܡܥ ܐܢܐ ܠܟ ܡܐ ܕܐܬܘ ܩܛܓܪܢܝܟ ܘܦܩܕ ܕܢܛܪܘܢܗ ܒܦܪܛܘܪܝܢ ܕܗܪܘܕܤ ܀
35 mu ne ko: «Kon bu ñi la kalaame ñëwee, dinga layoo.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur ba Erodd.