1ܨܒܐ ܐܢܐ ܕܝܢ ܕܬܕܥܘܢ ܐܝܢܐ ܐܓܘܢܐ ܐܝܬ ܠܝ ܚܠܦܝܟܘܢ ܘܚܠܦ ܗܢܘܢ ܕܒܠܕܝܩܝܐ ܘܚܠܦ ܫܪܟܐ ܐܝܠܝܢ ܕܦܪܨܘܦܝ ܠܐ ܚܙܘ ܒܒܤܪ ܀
1 Bëgg naa nag, ngeen xam bëre bu metti, bi may bëre ngir yéen, ngir waa Lawdise ak ñépp ñi ma musul a teg bët. Damay def sama kem-kàttan,
2ܕܢܬܒܝܐܘܢ ܠܒܘܬܗܘܢ ܘܢܬܩܪܒܘܢ ܒܚܘܒܐ ܠܟܠܗ ܥܘܬܪܐ ܕܦܝܤܐ ܘܠܤܘܟܠܐ ܕܝܕܥܬܗ ܕܐܪܙܐ ܕܐܠܗܐ ܐܒܐ ܘܕܡܫܝܚܐ ܀
2 ngir ngeen am fit te nekk benn ci mbëggeel, ngir dajal noonu xam-xam bu mat, ba xam kumpag Yàlla, di Kirist.
3ܗܘ ܕܒܗ ܟܤܝܢ ܟܠܗܝܢ ܤܝܡܬܐ ܕܚܟܡܬܐ ܘܕܝܕܥܬܐ ܀
3 Ci moom lañu denc lépp lu ñuy sàkku ci xel ak ci xam-xam.
4ܗܕܐ ܕܝܢ ܐܡܪ ܐܢܐ ܕܠܐ ܐܢܫ ܢܗܘܐ ܡܛܥܐ ܠܟܘܢ ܒܦܝܤܐ ܕܡܠܐ ܀
4 Maa ngi wax lii, ngir kenn bañ leen a nax ci ay wax yu neex.
5ܐܦܢ ܒܒܤܪ ܓܝܪ ܦܪܝܩ ܐܢܐ ܡܢܟܘܢ ܐܠܐ ܒܪܘܚ ܥܡܟܘܢ ܐܢܐ ܘܚܕܐ ܐܢܐ ܕܚܙܐ ܐܢܐ ܡܛܟܤܘܬܟܘܢ ܘܫܪܝܪܘܬܐ ܕܗܝܡܢܘܬܟܘܢ ܕܒܡܫܝܚܐ ܀
5 Jëmm ji ñëwul waaye sama xel a ngi ci yéen, di bég ci seen doxalin ak ngëm gu dëgër, gi ngeen am ci Kirist.
6ܐܝܟܢܐ ܗܟܝܠ ܕܩܒܠܬܘܢ ܠܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܡܪܢ ܒܗ ܗܠܟܘ ܀
6 Kon nag, ni ngeen nangoo Kirist Yeesu ni Boroom bi, dundeleen noonu ci moom.
7ܟܕ ܡܫܪܪܝܢ ܥܩܪܝܟܘܢ ܘܡܬܒܢܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܗ ܘܡܬܩܝܡܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܗܝܡܢܘܬܐ ܗܝ ܕܝܠܦܬܘܢ ܕܒܗ ܬܬܝܬܪܘܢ ܒܬܘܕܝܬܐ ܀
7 Saxleen ci moom, di màgg ci moom, tey gën a dëgër ci ngëm, gi ñu leen jàngal, ba seen xol di baawaan ci gërëm Yàlla.
8ܐܙܕܗܪܘ ܕܠܡܐ ܐܢܫ ܢܚܠܨܟܘܢ ܒܦܝܠܤܦܘܬܐ ܘܒܛܥܝܘܬܐ ܤܪܝܩܬܐ ܐܝܟ ܝܘܠܦܢܐ ܕܒܢܝܢܫܐ ܘܐܝܟ ܐܤܛܘܟܤܘܗܝ ܕܥܠܡܐ ܘܠܐ ܐܝܟ ܡܫܝܚܐ ܀
8 Moytuleen ba kenn bañ leen a fàbbi ci ay xam-xami nit yuy naxi neen. Xam-xam yu mel noonu, ñu ngi soqikoo ci aada yu nit tëral, ci aaday àddina, waaye soqikoowul ci Kirist.
9ܕܒܗ ܥܡܪ ܟܠܗ ܡܘܠܝܐ ܕܐܠܗܘܬܐ ܓܘܫܡܢܐܝܬ ܀
9 Ndaxte ci Kirist, maanaam ci yaramu nitam, la matug Yàlla gépp dëkk,
10ܘܒܗ ܐܦ ܐܢܬܘܢ ܡܫܬܡܠܝܬܘܢ ܕܗܘ ܐܝܬܘܗܝ ܪܫܐ ܕܟܠܗܝܢ ܐܪܟܘܤ ܘܫܘܠܛܢܐ ܀
10 te mat ngeen ci moom, miy buuru kilifa yépp ak boroom sañ-sañ yépp.
11ܘܒܗ ܐܬܓܙܪܬܘܢ ܓܙܘܪܬܐ ܕܠܐ ܒܐܝܕܝܢ ܒܫܠܚ ܒܤܪܐ ܕܚܛܗܐ ܒܓܙܘܪܬܗ ܕܡܫܝܚܐ ܀
11 Ndax seen ngëm ci moom xaraf ngeen xaraf bu loxol nit deful, maanaam Kirist summil na leen dooley bàkkaar, ji moomoon seen yaram. Loolu mooy xaraf, bi Kirist def.
12ܘܐܬܩܒܪܬܘܢ ܥܡܗ ܒܡܥܡܘܕܝܬܐ ܘܒܗ ܩܡܬܘܢ ܥܡܗ ܕܗܝܡܢܬܘܢ ܒܚܝܠܐ ܕܐܠܗܐ ܕܐܩܝܡܗ ܡܢ ܒܝܬ ܡܝܬܐ ܀
12 Bi ñu leen sóobee ci ndox, suulaale nañu leen ak moom, te it dekki ngeen ak moom, ndaxte gëm ngeen ci dooley Yàlla, ji ko dekkal ca néew ya.
13ܘܠܟܘܢ ܕܡܝܬܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܒܚܛܗܝܟܘܢ ܘܒܥܘܪܠܘܬ ܒܤܪܟܘܢ ܐܚܝܟܘܢ ܥܡܗ ܘܫܒܩ ܠܢ ܟܠܗܘܢ ܚܛܗܝܢ ܀
13 Te yéen ñi doon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy ak seen ñàkka xaraf, Yàlla dundalaat na leen ak Kirist, baal nu sunuy bàkkaar yépp.
14ܘܥܛܐ ܒܦܘܩܕܢܘܗܝ ܫܛܪ ܚܘܒܝܢ ܗܘ ܕܐܝܬܘܗܝ ܗܘܐ ܤܩܘܒܠܢ ܘܫܩܠܗ ܡܢ ܡܨܥܬܐ ܘܩܒܥܗ ܒܙܩܝܦܗ ܀
14 Mbind mi nu doon tiiñal, te daa nu yey ndax ay sàrtam, Yàlla far na ko, dindi ko, daajaale ko ca bant, ba Kirist deeye.
15ܘܒܫܠܚ ܦܓܪܗ ܦܪܤܝ ܠܐܪܟܘܤ ܘܠܫܠܝܛܢܐ ܘܐܒܗܬ ܐܢܘܢ ܓܠܝܐܝܬ ܒܩܢܘܡܗ ܀
15 Futti na kilifa yi ak boroom sañ-sañ yi, weer leen ci kanamu ñépp, sëkktal leen niy jaam ndax ndam la Kirist jële ca bant ba.
16ܠܐ ܗܟܝܠ ܐܢܫ ܢܕܘܕܟܘܢ ܒܡܐܟܠܐ ܘܒܡܫܬܝܐ ܐܘ ܒܦܘܠܓܐ ܕܥܐܕܐ ܘܕܪܝܫ ܝܪܚܐ ܘܕܫܒܐ ܀
16 Kon nag bu leen kenn teg tooñ ci li jëm ciy ñam mbaa naan, ci màggal mbaa xewu weer wu feeñ, mbaa ci bésu noflaay.
17ܗܠܝܢ ܕܐܝܬܝܗܝܢ ܛܠܢܝܬܐ ܕܐܝܠܝܢ ܕܥܬܝܕܢ ܦܓܪܐ ܕܝܢ ܡܫܝܚܐ ܗܘ ܀
17 Loolu lépp nag takkandeer la woon buy misaal li waroon a ñëw, waaye lu dëggu li mi ngi ci Kirist.
18ܘܠܡܐ ܐܢܫ ܢܨܒܐ ܒܡܟܝܟܘܬ ܪܥܝܢܐ ܠܡܚܝܒܘܬܟܘܢ ܕܬܫܬܥܒܕܘܢ ܠܦܘܠܚܢܐ ܕܡܠܐܟܐ ܒܕܤܥܐ ܥܠ ܡܕܡ ܕܠܐ ܚܙܐ ܘܤܪܝܩܐܝܬ ܡܬܚܬܪ ܒܪܥܝܢܐ ܕܒܤܪܗ ܀
18 Kuy bég ci di toroxlu ci ngistal, di jaamu ay malaaka, buleen ko may, mu àtte leen. Kooku dafay jeneer, di seet li koy feeñu, bay tiitaroo xalaatam, fekk xalaatu nit kese la, te neen.
19ܘܠܐ ܐܚܕ ܪܫܐ ܕܡܢܗ ܟܠܗ ܦܓܪܐ ܡܬܪܟܒ ܘܡܬܩܝܡ ܒܫܪܝܢܐ ܘܒܗܕܡܐ ܘܪܒܐ ܬܪܒܝܬܐ ܕܐܠܗܐ ܀
19 Taqul ci Kirist, miy bopp bi yilif jëmm ji. Bopp bee tax ba jëmm jépp, ji siddit yi ak tenqo yi téye te taqale ko, di màgg màgg gi ko Yàlla di jox.
20ܐܢ ܓܝܪ ܡܝܬܬܘܢ ܥܡ ܡܫܝܚܐ ܡܢ ܐܤܛܘܟܤܘܗܝ ܕܥܠܡܐ ܠܡܢܐ ܐܝܟ ܗܘ ܕܚܝܝܢ ܐܢܬܘܢ ܒܥܠܡܐ ܡܬܕܝܢܝܢ ܐܢܬܘܢ ܀
20 Ndegam deeyandoo ngeen ak Kirist, ba génne noonu ci aaday àddina, lu tax ngeen di nangu, ñu di leen teg ay sàrt yu mel nii: «Bul fab, bul ñam, bul laal,» ni bu seenug dund aju woon ci àddina si?
21ܠܐ ܠܡ ܬܩܪܘܒ ܘܠܐ ܬܛܥܡ ܘܠܐ ܬܩܦ ܀
22 Sàrt yooyu ñu ngi aju ci ndigali nit ñi ak seen njàngale. Yëf yi ñu tudd yépp, dees na leen jariñoo, ba ñu jeex.
22ܕܐܝܬܝܗܝܢ ܗܠܝܢ ܚܫܚܬܐ ܕܡܬܚܒܠܐ ܘܦܘܩܕܐ ܐܢܝܢ ܘܝܘܠܦܢܐ ܕܒܢܝܢܫܐ ܀
23 Dëgg la, seeni sàrt dañuy dénkaane pasteef ci jaamu Yàlla, di toroxlu ak di fitnaal seen yaram. Waaye sàrt yooyu nag amuñu benn njariñ, ngir nit ñi noot seen nafsu.
23ܘܡܬܚܙܝܢ ܕܐܝܬ ܒܗܝܢ ܡܠܬܐ ܕܚܟܡܬܐ ܒܦܪܨܘܦ ܡܟܝܟܘܬܐ ܘܕܚܠܬ ܐܠܗܐ ܘܕܠܐ ܚܝܤܝܢ ܥܠ ܦܓܪܐ ܠܘ ܒܡܕܡ ܕܡܝܩܪ ܐܠܐ ܒܐܝܠܝܢ ܕܚܫܚܬܐ ܐܢܝܢ ܕܒܤܪܐ ܀