Syriac: NT

Wolof: New Testament

Hebrews

5

1ܟܠ ܪܒ ܟܘܡܪܐ ܓܝܪ ܕܡܢ ܒܢܝܢܫܐ ܗܘܐ ܚܠܦ ܒܢܝܢܫܐ ܩܐܡ ܥܠ ܐܝܠܝܢ ܕܕܐܠܗܐ ܐܢܝܢ ܕܢܩܪܒ ܩܘܪܒܢܐ ܘܕܒܚܐ ܚܠܦ ܚܛܗܐ ܀
1 Saraxalekat bu mag bu nekk nag, ci biir nit ñi lañu ko jële, te fal ko muy dox seen diggante ak Yàlla. Noonu dina jébbal Yàlla ay sarax, tey rendi ay mala ngir dindi seeni bàkkaar.
2ܐܝܢܐ ܕܡܫܟܚ ܕܢܡܟ ܢܦܫܗ ܘܢܚܫ ܥܡ ܐܝܠܝܢ ܕܠܐ ܝܕܥܝܢ ܘܛܥܝܢ ܡܛܠ ܕܐܦ ܗܘ ܟܪܝܗܘܬܐ ܠܒܝܫ ܀
2 Te ndegam moom ci boppam nit kese la, man na muñal ñiy moy ndax seen ñàkka xam.
3ܘܡܛܠܬܗ ܚܝܒ ܗܘ ܕܐܝܟܢܐ ܕܚܠܦ ܥܡܐ ܗܟܢܐ ܐܦ ܚܠܦ ܢܦܫܗ ܢܩܪܒ ܥܠ ܚܛܗܘܗܝ ܀
3 Li mu ñàkk doole moo tax mu war a def ay sarax ngir mbaalug bàkkaaram, ni mu ko tàmmee defal mbooloo mi.
4ܘܠܐ ܗܘܐ ܠܢܦܫܗ ܐܢܫ ܢܤܒ ܐܝܩܪܐ ܐܠܐ ܐܝܢܐ ܕܡܬܩܪܐ ܡܢ ܐܠܗܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܗܪܘܢ ܀
4 Kenn mënul a teral sa bopp ba doon ab saraxalekat, su dul ne Yàllaa la woo, ni mu ko defe woon Aaroona.
5ܗܟܢܐ ܐܦ ܡܫܝܚܐ ܠܐ ܗܘܐ ܢܦܫܗ ܫܒܚ ܕܢܗܘܐ ܪܒ ܟܘܡܪܐ ܐܠܐ ܗܘ ܕܐܡܪ ܠܗ ܕܒܪܝ ܐܢܬ ܐܢܐ ܝܘܡܢܐ ܝܠܕܬܟ ܀
5 Kirist itam yékkatiwul boppam, ba doon saraxalekat bu mag, waaye Yàlla moo ko woo, bi muy wax ne:«Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.»
6ܐܝܟ ܕܐܦ ܒܕܘܟܬܐ ܐܚܪܬܐ ܐܡܪ ܕܐܢܬ ܗܘ ܟܘܡܪܐ ܠܥܠܡ ܒܕܡܘܬܗ ܕܡܠܟܝܙܕܩ ܀
6 Am na feneen fu mu wax ne:«Doon nga saraxalekat ba fàwwmel ni Melkisedeg.»
7ܐܦ ܟܕ ܒܤܪܐ ܠܒܝܫ ܗܘܐ ܒܥܘܬܐ ܘܬܟܫܦܬܐ ܒܓܥܬܐ ܚܝܠܬܢܝܬܐ ܘܒܕܡܥܐ ܩܪܒ ܗܘܐ ܠܡܢ ܕܡܫܟܚ ܗܘܐ ܡܢ ܡܘܬܐ ܕܢܚܝܘܗܝ ܘܐܫܬܡܥ ܀
7 Giiru dundam gépp ci àddina, Kirist da daan ñaan wall ci Yàlla, di ko dénku, boole ko ak i jooy ak i rangooñ. Da doon ñaan ci Yàlla, mi ko man a musal ci dee. Te ñaanam nangu na, ndax ni mu jébbale boppam Yàlla.
8ܘܟܕ ܛܒ ܒܪܐ ܐܝܬܘܗܝ ܡܢ ܕܚܠܬܐ ܘܚܫܐ ܕܤܒܠ ܝܠܦܗ ܠܡܫܬܡܥܢܘܬܐ ܀
8 Waaye li muy nekk-nekk doom, teewul mu jàng déggal Yàlla, jaare ko ci coono bi mu daj.
9ܘܗܟܢܐ ܐܬܓܡܪ ܘܗܘܐ ܠܟܠܗܘܢ ܐܝܠܝܢ ܕܡܫܬܡܥܝܢ ܠܗ ܥܠܬܐ ܕܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܀
9 Noonu la àgge cig mat, ñu def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir ñi ko déggal ñépp.
10ܘܐܫܬܡܗ ܡܢ ܐܠܗܐ ܪܒ ܟܘܡܪܐ ܒܕܡܘܬܗ ܕܡܠܟܝܙܕܩ ܀
10 Fekk na Yàlla tudde ko saraxalekat bu mag ni ko Melkisedeg nekke.
11ܥܠܘܗܝ ܕܝܢ ܥܠ ܗܢܐ ܡܠܟܝܙܕܩ ܤܓܝܐܐ ܗܝ ܠܢ ܡܠܬܐ ܠܡܐܡܪܗ ܘܥܤܩܐ ܠܡܦܫܩܘܬܗ ܡܛܠ ܕܗܘܝܬܘܢ ܠܟܘܢ ܟܪܝܗܐ ܒܡܫܡܥܬܟܘܢ ܀
11 Ci fànn googu, am na lu bare lu nu ci bëgg a wax, waaye tekkil leen ko dina jafe, ndaxte dangeen a naqari xel.
12ܚܝܒܝܢ ܗܘܝܬܘܢ ܓܝܪ ܡܠܦܢܐ ܠܡܗܘܐ ܡܛܠ ܕܙܒܢܐ ܠܟܘܢ ܒܝܘܠܦܢܐ ܗܫܐ ܕܝܢ ܬܘܒ ܤܢܝܩܝܢ ܐܢܬܘܢ ܕܬܐܠܦܘܢ ܐܝܠܝܢ ܐܢܝܢ ܟܬܝܒܬܐ ܩܕܡܝܬܐ ܕܪܝܫ ܡܠܘܗܝ ܕܐܠܗܐ ܘܗܘܝܬܘܢ ܠܟܘܢ ܤܢܝܩܐ ܥܠ ܚܠܒܐ ܘܠܐ ܥܠ ܡܐܟܘܠܬܐ ܫܪܝܪܬܐ ܀
12 Bu yàgg ngeen waroon a jàngal ñeneen ñi, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci kàddug Yàlla. Léegi nag yéena ngi tollu fi ñu leen war a nàmpale, ndaxte àttanuleen ñam wu dëgër.
13ܟܠܢܫ ܕܝܢ ܕܡܐܟܘܠܬܗ ܚܠܒܐ ܗܘ ܠܐ ܡܦܤ ܒܡܠܬܐ ܕܟܐܢܘܬܐ ܡܛܠ ܕܫܒܪܐ ܗܘ ܀
13 Képp kuy nàmp, ab xale nga ba tey. Jëfeegoo njàngale, mi jëm ci wàllu njubte.
14ܕܓܡܝܪܐ ܗܝ ܕܝܢ ܡܐܟܘܠܬܐ ܫܪܝܪܬܐ ܐܝܠܝܢ ܕܡܛܠ ܕܡܕܪܫܝܢ ܐܬܢܦܩܘ ܪܓܫܝܗܘܢ ܠܡܦܪܫ ܛܒܬܐ ܘܒܝܫܬܐ ܀
14 Waaye ñam wu dëgër, ñi mat a ko yelloo, maanaam ñiy jëfandikoo seen xel ngir ràññee lu baax ak lu bon.