1ܗܠܝܢ ܡܠܠ ܝܫܘܥ ܘܐܪܝܡ ܥܝܢܘܗܝ ܠܫܡܝܐ ܘܐܡܪ ܐܒܝ ܐܬܬ ܫܥܬܐ ܫܒܚ ܒܪܟ ܕܒܪܟ ܢܫܒܚܟ ܀
1 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, waxtu wi tax ma ñëw ci àddina agsi na. Feeñalal ndamu Doom ji, ngir moom itam mu man a feeñal sa ndam.
2ܐܝܟܢܐ ܕܝܗܒܬ ܠܗ ܫܘܠܛܢܐ ܥܠ ܟܠ ܒܤܪ ܕܟܠ ܡܐ ܕܝܗܒܬ ܠܗ ܢܬܠ ܠܗ ܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܀
2 Ndaxte jox nga ko sañ-sañ ci bépp mbindeef, ngir mu may dund gu dul jeex gi ñi nga ko dénk.
3ܗܠܝܢ ܐܢܘܢ ܕܝܢ ܚܝܐ ܕܠܥܠܡ ܕܢܕܥܘܢܟ ܕܐܢܬ ܐܢܬ ܐܠܗܐ ܕܫܪܪܐ ܒܠܚܘܕܝܟ ܘܡܢ ܕܫܕܪܬ ܝܫܘܥ ܡܫܝܚܐ ܀
3 Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist.
4ܐܢܐ ܫܒܚܬܟ ܒܐܪܥܐ ܥܒܕܐ ܗܘ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܕܐܥܒܕ ܫܠܡܬܗ ܀
4 Wone naa sa ndam ci àddina, ndax li ma matal liggéey, bi nga ma santoon.
5ܘܗܫܐ ܫܒܚܝܢܝ ܐܢܬ ܐܒܝ ܠܘܬܟ ܒܗܘ ܫܘܒܚܐ ܕܐܝܬ ܗܘܐ ܠܝ ܠܘܬܟ ܡܢ ܩܕܡ ܕܢܗܘܐ ܥܠܡܐ ܀
5 Léegi nag Baay, ci sa teewaay, feeñalal ci man ndam, li ma amoon ci sa wet, laata àddina di sosu.
6ܐܘܕܥܬ ܫܡܟ ܠܒܢܝ ܐܢܫܐ ܗܢܘܢ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܡܢ ܥܠܡܐ ܕܝܠܟ ܗܘܘ ܘܠܝ ܝܗܒܬ ܐܢܘܢ ܘܢܛܪܘ ܡܠܬܟ ܀
6 «Xamal naa sa tur nit, ñi nga tànne ci àddina te dénk ma leen. Bokkoon nañu ci yaw, nga dénk ma leen, te sàmm nañu sa kàddu.
7ܗܫܐ ܝܕܥܬ ܕܟܠ ܡܐ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܡܢ ܠܘܬܟ ܗܘ ܀
7 Xam nañu léegi ne, loo ma joxaan, ci yaw la jóge,
8ܕܡܠܐ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܝܗܒܬ ܠܗܘܢ ܘܗܢܘܢ ܩܒܠܘ ܘܝܕܥܘ ܫܪܝܪܐܝܬ ܕܡܢ ܠܘܬܟ ܢܦܩܬ ܘܗܝܡܢܘ ܕܐܢܬ ܫܕܪܬܢܝ ܀
8 ndaxte xamal naa leen kàddu yi nga ma jox, te nangu nañu ko. Wóor na leen ne, ci yaw laa jóge, te gëm nañu ne yaa ma yónni.
9ܘܐܢܐ ܥܠܝܗܘܢ ܒܥܐ ܐܢܐ ܠܐ ܗܘܐ ܥܠ ܥܠܡܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܐܠܐ ܥܠ ܗܢܘܢ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܕܕܝܠܟ ܐܢܘܢ ܀
9 Ñoom laay ñaanal. Ñaanaluma waa àddina, waaye maa ngi ñaanal ñi nga ma dénk, ndaxte ci yaw lañu bokk.
10ܘܟܠ ܡܕܡ ܕܕܝܠܝ ܗܘ ܕܝܠܟ ܗܘ ܘܕܝܠܟ ܕܝܠܝ ܗܘ ܘܡܫܒܚ ܐܢܐ ܒܗܘܢ ܀
10 Lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom; te ñoom ñoo feeñal sama ndam.
11ܡܟܝܠ ܠܐ ܗܘܝܬ ܒܥܠܡܐ ܘܗܠܝܢ ܒܥܠܡܐ ܐܢܘܢ ܘܐܢܐ ܠܘܬܟ ܐܬܐ ܐܢܐ ܐܒܐ ܩܕܝܫܐ ܛܪ ܐܢܘܢ ܒܫܡܟ ܗܘ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܕܢܗܘܘܢ ܚܕ ܐܝܟܢܐ ܕܚܢܢ ܀
11 Nekkatuma ci àddina, waaye ñoom ñu ngi ci; man, ci yaw laa jëm. Baay bu sell bi, sàmm leen ci sa dooley tur woowu nga ma jox, ngir ñu nekk benn, ni nu nekke benn, man ak yaw.
12ܟܕ ܥܡܗܘܢ ܗܘܝܬ ܒܥܠܡܐ ܐܢܐ ܢܛܪ ܗܘܝܬ ܠܗܘܢ ܒܫܡܟ ܠܐܝܠܝܢ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܢܛܪܬ ܘܐܢܫ ܡܢܗܘܢ ܠܐ ܐܒܕ ܐܠܐ ܒܪܗ ܕܐܒܕܢܐ ܕܢܬܡܠܐ ܟܬܒܐ ܀
12 Bi ma nekkee ak ñoom, daan naa leen sàmm ci sa dooley tur, tur wi nga ma jox. Wottu naa leen, ba kenn ci ñoom sànkuwul, lu dul kiy aji réer ji, ngir li Mbind mi waxoon am.
13ܗܫܐ ܕܝܢ ܠܘܬܟ ܐܬܐ ܐܢܐ ܘܗܠܝܢ ܡܡܠܠ ܐܢܐ ܒܥܠܡܐ ܕܬܗܘܐ ܚܕܘܬܝ ܡܫܡܠܝܐ ܒܗܘܢ ܀
13 «Waaye léegi maa ngi jëmsi ci yaw, te maa ngi wax nii ci bi may nekk àddina, ngir ñu fees ak sama mbég.
14ܐܢܐ ܝܗܒܬ ܠܗܘܢ ܡܠܬܟ ܘܥܠܡܐ ܤܢܐ ܐܢܘܢ ܕܠܐ ܗܘܘ ܡܢ ܥܠܡܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܢܐ ܠܐ ܗܘܝܬ ܡܢ ܥܠܡܐ ܀
14 Jottali naa leen sa kàddu, te àddina bañ leen, ndax li ñu mel ni man, bañ a bokk ci àddina soosu.
15ܠܐ ܗܘܐ ܕܬܫܩܘܠ ܐܢܘܢ ܡܢ ܥܠܡܐ ܒܥܐ ܐܢܐ ܐܠܐ ܕܬܛܪ ܐܢܘܢ ܡܢ ܒܝܫܐ ܀
15 Ñaanuma nga jële leen àddina, waaye nga yiir leen ci Ibliis.
16ܠܐ ܗܘܘ ܓܝܪ ܡܢ ܥܠܡܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܢܐ ܠܐ ܗܘܝܬ ܡܢ ܥܠܡܐ ܀
16 Dañoo mel ni man; bokkuñu ci àddina.
17ܐܒܐ ܩܕܫ ܐܢܘܢ ܒܫܪܪܟ ܕܡܠܬܟ ܕܝܠܟ ܫܪܪܐ ܗܝ ܀
17 Samp leen ci dëgg, ngir ñu sell. Sa kàddu mooy dëgg.
18ܐܝܟܢܐ ܕܠܝ ܫܕܪܬ ܠܥܠܡܐ ܐܦ ܐܢܐ ܫܕܪܬ ܐܢܘܢ ܠܥܠܡܐ ܀
18 Ni nga ma yónnee àddina, noonu laa leen yónnee ci nit ñi.
19ܘܥܠ ܐܦܝܗܘܢ ܐܢܐ ܡܩܕܫ ܐܢܐ ܢܦܫܝ ܕܢܗܘܘܢ ܐܦ ܗܢܘܢ ܡܩܕܫܝܢ ܒܫܪܪܐ ܀
19 Sellal naa sama bopp ngir ñoom, ngir ñu sampu ci dëgg te sell.
20ܘܠܐ ܗܘܐ ܥܠ ܐܦܝ ܗܠܝܢ ܒܥܐ ܐܢܐ ܒܠܚܘܕ ܐܠܐ ܐܦ ܥܠ ܐܦܝ ܐܝܠܝܢ ܕܡܗܝܡܢܝܢ ܒܝ ܒܡܠܬܗܘܢ ܀
20 «Ñaanaluma leen ñoom rekk, waaye itam ñi may gëm ëllëg ndax seen wax.
21ܕܟܠܗܘܢ ܢܗܘܘܢ ܚܕ ܐܝܟܢܐ ܕܐܢܬ ܐܒܝ ܒܝ ܘܐܢܐ ܒܟ ܕܐܦ ܗܢܘܢ ܒܢ ܚܕ ܢܗܘܘܢ ܕܢܗܝܡܢ ܥܠܡܐ ܕܐܢܬ ܫܕܪܬܢܝ ܀
21 Damay ñaan ngir ñépp doon benn. Baay, na ñooñu nekk benn ci nun, ni nga nekke ci man te ma nekke ko ci yaw. Nañu ànd, ba àddina gëm ne, yaa ma yónni.
22ܘܐܢܐ ܫܘܒܚܐ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܝܗܒܬ ܠܗܘܢ ܕܢܗܘܘܢ ܚܕ ܐܝܟܢܐ ܕܚܢܢ ܚܕ ܚܢܢ ܀
22 Boole naa leen ci ndam, li nga ma sol, ngir ñu àndandoo, ni nu ànde man ak yaw.
23ܐܢܐ ܒܗܘܢ ܘܐܢܬ ܒܝ ܕܢܗܘܘܢ ܓܡܝܪܝܢ ܠܚܕ ܘܕܢܕܥ ܥܠܡܐ ܕܐܢܬ ܫܕܪܬܢܝ ܘܕܐܚܒܬ ܐܢܘܢ ܐܝܟܢܐ ܕܐܦ ܠܝ ܐܚܒܬ ܀
23 Man ci ñoom, yaw it ci man, ngir ñu gën a ànd, nekk benn, ba àddina xam ne yaa ma yónni, xam ne bëgg nga leen, ni nga ma bëgge.
24ܐܒܐ ܗܢܘܢ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܨܒܐ ܐܢܐ ܕܐܬܪ ܕܐܢܐ ܐܦ ܗܢܘܢ ܢܗܘܘܢ ܥܡܝ ܕܢܗܘܘܢ ܚܙܝܢ ܫܘܒܚܐ ܕܝܠܝ ܗܘ ܕܝܗܒܬ ܠܝ ܕܐܚܒܬܢܝ ܡܢ ܩܕܡ ܬܪܡܝܬܗ ܕܥܠܡܐ ܀
24 «Baay, bëgg naa, ñi nga ma dénk nekk ak man fa ma jëm, ngir ñu gis sama ndam, li nga ma sol, ndaxte bëgg nga ma, laata àddina di sosu.
25ܐܒܝ ܟܐܢܐ ܘܥܠܡܐ ܠܐ ܝܕܥܟ ܐܢܐ ܕܝܢ ܝܕܥܬܟ ܘܗܢܘܢ ܝܕܥܘ ܕܐܢܬ ܫܕܪܬܢܝ ܀
25 «Baay, yaw ku jub ki, waa àddina xamuñu la, waaye man xam naa la, te ñii xam nañu ne, yaa ma yónni.
26ܘܐܘܕܥܬ ܐܢܘܢ ܫܡܟ ܘܡܘܕܥ ܐܢܐ ܕܚܘܒܐ ܗܘ ܕܐܚܒܬܢܝ ܢܗܘܐ ܒܗܘܢ ܘܐܢܐ ܐܗܘܐ ܒܗܘܢ ܀
26 Xamal naa leen sa tur te dinaa ko gën a xamle, ngir mbëggeel, gi nga am ci man, nekk ci ñoom, te man it ma nekk ci ñoom.»