Syriac: NT

Wolof: New Testament

John

19

1ܗܝܕܝܢ ܦܝܠܛܘܤ ܢܓܕܗ ܠܝܫܘܥ ܀
1 Noonu Pilaat joxe ndigal, ñu dóor Yeesu ay yar.
2ܘܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܓܕܠܘ ܟܠܝܠܐ ܡܢ ܟܘܒܐ ܘܤܡܘ ܠܗ ܒܪܫܗ ܘܟܤܝܘܗܝ ܢܚܬܐ ܕܐܪܓܘܢܐ ܀
2 Xarekat ya ràbb kaalag dég, teg ko ci boppu Yeesu, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
3ܘܐܡܪܝܢ ܗܘܘ ܫܠܡ ܠܟ ܡܠܟܐ ܕܝܗܘܕܝܐ ܘܡܚܝܢ ܗܘܘ ܠܗ ܥܠ ܦܟܘܗܝ ܀
3 Ñu di ko jegeñsi, di ko pes, naan ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!»
4ܘܢܦܩ ܦܝܠܛܘܤ ܬܘܒ ܠܒܪ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܗܐ ܡܦܩ ܐܢܐ ܠܗ ܠܟܘܢ ܠܒܪ ܕܬܕܥܘܢ ܕܠܐ ܡܫܟܚ ܐܢܐ ܒܬܪܗ ܐܦܠܐ ܚܕܐ ܥܠܬܐ ܀
4 Pilaat génnaat ne leen: «Gis ngeen, maa ngi leen koy indil ci biti, ngir ngeen xam ne, waa jii, gisuma ci moom genn tooñ.»
5ܘܢܦܩ ܝܫܘܥ ܠܒܪ ܟܕ ܐܝܬ ܥܠܘܗܝ ܟܠܝܠܐ ܕܟܘܒܐ ܘܢܚܬܐ ܕܐܪܓܘܢܐ ܘܐܡܪ ܠܗܘܢ ܦܝܠܛܘܤ ܗܐ ܓܒܪܐ ܀
5 Yeesu nag génn, tegoo mbubbum xarekat mu xonq mi ak kaalag dég gi. Pilaat it ne leen: «Waa jaa ngii!»
6ܟܕ ܕܝܢ ܚܙܐܘܗܝ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܘܕܚܫܐ ܩܥܘ ܘܐܡܪܝܢ ܨܠܘܒܝܗܝ ܨܠܘܒܝܗܝ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܦܝܠܛܘܤ ܕܒܪܘ ܐܢܬܘܢ ܘܙܘܩܦܘܗܝ ܐܢܐ ܓܝܪ ܠܐ ܡܫܟܚ ܐܢܐ ܒܗ ܥܠܬܐ ܀
6 Waaye bi ñu ko gisee, saraxalekat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn tooñ.»
7ܐܡܪܝܢ ܠܗ ܝܗܘܕܝܐ ܠܢ ܢܡܘܤܐ ܐܝܬ ܠܢ ܘܐܝܟ ܕܒܢܡܘܤܢ ܚܝܒ ܗܘ ܡܘܬܐ ܕܥܒܕ ܢܦܫܗ ܒܪܗ ܕܐܠܗܐ ܀
7 Yawut yi tontu ko ne: «Am nanu aw yoon, te ci yoon woowu, war na dee ndaxte teg na boppam Doomu Yàlla.»
8ܟܕ ܫܡܥ ܕܝܢ ܦܝܠܛܘܤ ܗܕܐ ܡܠܬܐ ܝܬܝܪܐܝܬ ܕܚܠ ܀
8 Bi Pilaat déggee wax jooju, dafa gën a tiit,
9ܘܥܠ ܬܘܒ ܠܦܪܛܘܪܝܢ ܘܐܡܪ ܠܝܫܘܥ ܐܝܡܟܐ ܐܢܬ ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܦܬܓܡܐ ܠܐ ܝܗܒ ܠܗ ܀
9 dugg ca taax ma, daldi ne Yeesu: «Foo jóge?» Waaye Yeesu tontuwu ko.
10ܐܡܪ ܠܗ ܦܝܠܛܘܤ ܥܡܝ ܠܐ ܡܡܠܠ ܐܢܬ ܠܐ ܝܕܥ ܐܢܬ ܕܫܠܝܛ ܐܢܐ ܕܐܫܪܝܟ ܘܫܠܝܛ ܐܢܐ ܕܐܙܩܦܟ ܀
10 Pilaat ne ko: «Man ngay bañ a waxal? Xanaa xamuloo ne, am naa sañ-sañu bàyyi la, te am naa itam sañ-sañu daaj la ci bant?»
11ܐܡܪ ܠܗ ܝܫܘܥ ܠܝܬ ܗܘܐ ܠܟ ܥܠܝ ܫܘܠܛܢܐ ܐܦ ܠܐ ܚܕ ܐܠܘ ܠܐ ܝܗܝܒ ܗܘܐ ܠܟ ܡܢ ܠܥܠ ܡܛܠ ܗܢܐ ܗܘ ܡܢ ܕܐܫܠܡܢܝ ܠܟ ܪܒܐ ܗܝ ܚܛܝܬܗ ܡܢ ܕܝܠܟ ܀
11 Yeesu tontu ko ne: «Amuloo benn sañ-sañ ci man su dul bi la Yàlla jox. Looloo tax ba ki ma jébbal ci say loxo am na bàkkaar, bi gën a réy.»
12ܘܡܛܠ ܗܕܐ ܨܒܐ ܗܘܐ ܦܝܠܛܘܤ ܕܢܫܪܝܘܗܝ ܝܗܘܕܝܐ ܕܝܢ ܩܥܝܢ ܗܘܘ ܕܐܢ ܠܗܢܐ ܫܪܐ ܐܢܬ ܠܐ ܗܘܝܬ ܪܚܡܗ ܕܩܤܪ ܟܠ ܡܢ ܓܝܪ ܕܢܦܫܗ ܡܠܟܐ ܥܒܕ ܤܩܘܒܠܐ ܗܘ ܕܩܤܪ ܀
12 Booba nag la Pilaat doon fexee bàyyi Yeesu. Waaye Yawut ya di yuuxoo naan: «Boo bàyyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit ku teg boppam buur, noonub Sesaar la!»
13ܟܕ ܫܡܥ ܕܝܢ ܦܝܠܛܘܤ ܗܕܐ ܡܠܬܐ ܐܦܩܗ ܠܝܫܘܥ ܠܒܪ ܘܝܬܒ ܥܠ ܒܝܡ ܒܕܘܟܬܐ ܕܡܬܩܪܝܐ ܪܨܝܦܬܐ ܕܟܐܦܐ ܥܒܪܐܝܬ ܕܝܢ ܡܬܐܡܪܐ ܓܦܝܦܬܐ ܀
13 Bi Pilaat déggee loolu, mu daldi génne Yeesu ca biti, dem toog ca jalub àttekaay ba, ca fu ñuy wax Bérabu doj ya. Ci làkku yawut ñu naan ko Gabata.
14ܘܥܪܘܒܬܐ ܗܘܬ ܕܦܨܚܐ ܘܐܝܬ ܗܘܝ ܐܝܟ ܫܥܐ ܫܬ ܘܐܡܪ ܠܝܗܘܕܝܐ ܗܐ ܡܠܟܟܘܢ ܀
14 Ca bés ba ñuy waajal màggalu Jéggi ba la woon, ca weti digg-bëccëg. Pilaat ne Yawut ya: «Seen buur a ngii!»
15ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܩܥܝܢ ܗܘܘ ܫܩܘܠܝܗܝ ܫܩܘܠܝܗܝ ܨܠܘܒܝܗܝ ܨܠܘܒܝܗܝ ܐܡܪ ܠܗܘܢ ܦܝܠܛܘܤ ܠܡܠܟܟܘܢ ܐܙܩܘܦ ܐܡܪܝܢ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܠܝܬ ܠܢ ܡܠܟܐ ܐܠܐ ܐܢ ܩܤܪ ܀
15 Waaye ñuy yuuxoo naan: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo war a daaj ci bant?» Saraxalekat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!»
16ܗܝܕܝܢ ܐܫܠܡܗ ܠܗܘܢ ܕܢܙܩܦܘܢܝܗܝ ܘܕܒܪܘܗܝ ܠܝܫܘܥ ܘܐܦܩܘܗܝ ܀
16 Noonu Pilaat jébbal leen Yeesu, ngir ñu daaj ko ci bant. Bi leen ko Pilaat jébbalee, ñu jël ko, yóbbu.
17ܟܕ ܫܩܝܠ ܙܩܝܦܗ ܠܕܘܟܬܐ ܕܡܬܩܪܝܐ ܩܪܩܦܬܐ ܥܒܪܐܝܬ ܕܝܢ ܡܬܐܡܪܐ ܓܓܘܠܬܐ ܀
17 Yeesu ci boppam gàddu bant ba, génn ngir dem ca fa ñuy wax Bérabu kaaŋu bopp; ñu koy wooye Golgota ci làkku yawut.
18ܐܬܪ ܕܙܩܦܘܗܝ ܘܥܡܗ ܬܪܝܢ ܐܚܪܢܝܢ ܚܕ ܡܟܐ ܘܚܕ ܡܟܐ ܘܠܝܫܘܥ ܒܡܨܥܬܐ ܀
18 Foofa la xarekat ya daaje Yeesu ca bant ba. Ci noonu it ñu daajaale ñaari nit ci wetam, mu nekk ca digg ba.
19ܘܟܬܒ ܐܦ ܠܘܚܐ ܦܝܠܛܘܤ ܘܤܡ ܥܠ ܙܩܝܦܗ ܟܬܝܒ ܗܘܐ ܕܝܢ ܗܟܢܐ ܗܢܐ ܝܫܘܥ ܢܨܪܝܐ ܡܠܟܐ ܕܝܗܘܕܝܐ ܀
19 Pilaat santaane itam ñu bind, teg ko ca kaw bant, ba ñu ko daajoon. Mbind ma lii la wax: «Kii mooy Yeesum Nasaret, buuru Yawut yi.»
20ܘܠܗܢܐ ܕܦܐ ܤܓܝܐܐ ܡܢ ܝܗܘܕܝܐ ܩܪܐܘܗܝ ܡܛܠ ܕܩܪܝܒܐ ܗܘܬ ܠܡܕܝܢܬܐ ܕܘܟܬܐ ܕܐܙܕܩܦ ܒܗ ܝܫܘܥ ܘܟܬܝܒܐ ܗܘܐ ܥܒܪܐܝܬ ܘܝܘܢܐܝܬ ܘܪܗܘܡܐܝܬ ܀
20 Mbind mooma, Yawut yu bare jàng nañu ko, ndaxte fa ñu daajoon Yeesu ca bant ba jege woon na dëkk ba, te mbind ma ci làkku yawut la woon, ci làkku waa Room ak ci gereg.
21ܘܐܡܪܘ ܪܒܝ ܟܗܢܐ ܠܦܝܠܛܘܤ ܠܐ ܬܟܬܘܒ ܕܡܠܟܐ ܗܘ ܕܝܗܘܕܝܐ ܐܠܐ ܕܗܘ ܐܡܪ ܕܡܠܟܐ ܐܢܐ ܕܝܗܘܕܝܐ ܀
21 Noonu saraxalekat yu mag yu Yawut ya ne Pilaat: «Bul bind: “Buuru Yawut,” bindal rekk: “Kii moo ne mooy buuru Yawut yi.”»
22ܐܡܪ ܦܝܠܛܘܤ ܡܕܡ ܕܟܬܒܬ ܟܬܒܬ ܀
22 Pilaat tontu leen ne: «Xas naa koo bind, du deñ.»
23ܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܕܝܢ ܟܕ ܙܩܦܘܗܝ ܠܝܫܘܥ ܫܩܠܘ ܢܚܬܘܗܝ ܘܥܒܕܘ ܠܐܪܒܥ ܡܢܘܢ ܡܢܬܐ ܠܚܕ ܡܢ ܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܟܘܬܝܢܗ ܕܝܢ ܐܝܬܝܗ ܗܘܬ ܕܠܐ ܚܝܛܐ ܡܢ ܠܥܠ ܙܩܝܪܬܐ ܟܠܗ ܀
23 Xarekat ya, bi ñu daajee Yeesu ca bant ba, ba noppi dañoo jël ay yéreem, séddale ko ñeenti cér, ku nekk benn. Jël nañu it mbubbam bu ñu ràbb ca kaw ba ci suuf te amul benn ñaw.
24ܘܐܡܪܘ ܚܕ ܠܚܕ ܠܐ ܢܤܕܩܝܗ ܐܠܐ ܢܦܤ ܥܠܝܗ ܡܦܤ ܕܡܢܘ ܬܗܘܐ ܘܫܠܡ ܟܬܒܐ ܕܐܡܪ ܕܦܠܓܘ ܢܚܬܝ ܒܝܢܬܗܘܢ ܘܥܠ ܠܒܘܫܝ ܐܪܡܝܘ ܦܤܐ ܗܠܝܢ ܥܒܕܘ ܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܀
24 Xarekat ya di waxante naan: «Mbubb mi, bunu ko xotti, waaye nanu ko tegoo ay bant, ngir xam ku koy moom.» Noonu la Mbind mi waroon a ame, bi mu naan:«Séddoo nañu samay yére,tegoo ay bant sama mbubb.» Loolu nag la xarekat ya def.
25ܩܝܡܢ ܗܘܝ ܕܝܢ ܠܘܬ ܙܩܝܦܗ ܕܝܫܘܥ ܐܡܗ ܘܚܬܗ ܕܐܡܗ ܘܡܪܝܡ ܗܝ ܕܩܠܝܘܦܐ ܘܡܪܝܡ ܡܓܕܠܝܬܐ ܀
25 Ca wetu bant, ba ñu daajoon Yeesu, yaayam a nga fa taxawoon, moom ak doomu ndeyam ju jigéen, Maryaama jabari Këlópas, ak Maryaama mi dëkk Magdala.
26ܝܫܘܥ ܕܝܢ ܚܙܐ ܠܐܡܗ ܘܠܬܠܡܝܕܐ ܗܘ ܕܪܚܡ ܗܘܐ ܕܩܐܡ ܘܐܡܪ ܠܐܡܗ ܐܢܬܬܐ ܗܐ ܒܪܟܝ ܀
26 Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,»
27ܘܐܡܪ ܠܬܠܡܝܕܐ ܗܘ ܗܐ ܐܡܟ ܘܡܢ ܗܝ ܫܥܬܐ ܕܒܪܗ ܬܠܡܝܕܐ ܗܘ ܠܘܬܗ ܀
27 neeti taalibe ba: «Sa yaay a ngi nii.» Booba la ko taalibe ba yóbbu këram, yor ko.
28ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܝܕܥ ܝܫܘܥ ܕܟܠܡܕܡ ܐܫܬܠܡ ܘܕܢܬܡܠܐ ܟܬܒܐ ܐܡܪ ܨܗܐ ܐܢܐ ܀
28 Bi loolu wéyee gannaaw Yeesu xam na ne, lépp mat na léegi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: «Damaa mar.»
29ܘܡܐܢܐ ܤܝܡ ܗܘܐ ܕܡܠܐ ܚܠܐ ܗܢܘܢ ܕܝܢ ܡܠܘ ܐܤܦܘܓܐ ܡܢ ܚܠܐ ܘܤܡܘ ܥܠ ܙܘܦܐ ܘܩܪܒܘ ܠܘܬ ܦܘܡܗ ܀
29 Amoon na foofa gutt bu fees ak bineegar. Noonu ñu jël sagar, tooyal ko ca, takk ko ci bantu garab gu ñuy wax isob, teg ko ci gémmiñu Yeesu.
30ܟܕ ܕܝܢ ܫܩܠ ܗܘ ܚܠܐ ܝܫܘܥ ܐܡܪ ܗܐ ܡܫܠܡ ܘܐܪܟܢ ܪܫܗ ܘܐܫܠܡ ܪܘܚܗ ܀
30 Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: «Lépp mat na!» Noonu mu sëgg, delloo ruuwam Yàlla.
31ܝܗܘܕܝܐ ܕܝܢ ܡܛܠ ܕܥܪܘܒܬܐ ܗܘܬ ܐܡܪܝܢ ܠܐ ܢܒܘܬܘܢ ܦܓܪܐ ܗܠܝܢ ܥܠ ܙܩܝܦܝܗܘܢ ܡܛܠ ܕܫܒܬܐ ܢܓܗܐ ܝܘܡܐ ܗܘܐ ܓܝܪ ܪܒܐ ܝܘܡܐ ܕܫܒܬܐ ܗܝ ܘܒܥܘ ܡܢ ܦܝܠܛܘܤ ܕܢܬܒܪܘܢ ܫܩܝܗܘܢ ܕܗܢܘܢ ܙܩܝܦܐ ܘܢܚܬܘܢ ܐܢܘܢ ܀
31 Keroog ba ñu dee waajal bésu noflaay ba la woon, te Yawut ya bëgguñu néew ya des ca bant ya, ndaxte bésu noflaay boobu fonkoon nañu ko lool. Ñu ñaan Pilaat, mu dammlu tànki ña ñu daajoon, te jële leen fa.
32ܘܐܬܘ ܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܘܬܒܪܘ ܫܩܘܗܝ ܕܩܕܡܝܐ ܘܕܗܘ ܐܚܪܢܐ ܕܐܙܕܩܦ ܥܡܗ ܀
32 Noonu xarekat ya dem, damm tànki ku jëkk ka, teg ca ka ca des, ca ña ñu daajaale woon ak Yeesu.
33ܘܟܕ ܐܬܘ ܠܘܬ ܝܫܘܥ ܚܙܘ ܕܡܝܬ ܠܗ ܡܢ ܟܕܘ ܘܠܐ ܬܒܪܘ ܫܩܘܗܝ ܀
33 Bi ñu agsee ci Yeesu, dammuñu ay tànkam, ndaxte gis nañu ne booba faatu na.
34ܐܠܐ ܚܕ ܡܢ ܐܤܛܪܛܝܘܛܐ ܡܚܝܗܝ ܒܕܦܢܗ ܒܠܘܟܝܬܐ ܘܡܚܕܐ ܢܦܩ ܕܡܐ ܘܡܝܐ ܀
34 Waaye kenn ca xarekat ya daldi jël xeej, jam ko ko ci wet, ca saa sa deret ak ndox di tuuru.
35ܘܡܢ ܕܚܙܐ ܐܤܗܕ ܘܫܪܝܪܐ ܗܝ ܤܗܕܘܬܗ ܘܗܘ ܝܕܥ ܕܫܪܪܐ ܐܡܪ ܕܐܦ ܐܢܬܘܢ ܬܗܝܡܢܘܢ ܀
35 Kiy nettali mbir yooyu, da cee teg bëtam, te li muy wax dëgg la. Moom ci boppam xam na ne, li muy wax dëgg la, ngir yéen itam ngeen gëm,
36ܗܠܝܢ ܓܝܪ ܗܘܝ ܕܢܬܡܠܐ ܟܬܒܐ ܕܐܡܪ ܕܓܪܡܐ ܠܐ ܢܬܬܒܪ ܒܗ ܀
36 ndaxte loolu dafa xew ngir Mbind mi am: «Benn yaxam du damm.»
37ܘܬܘܒ ܟܬܒܐ ܐܚܪܢܐ ܕܐܡܪ ܕܢܚܘܪܘܢ ܒܡܢ ܕܕܩܪܘ ܀
37 Leneen it Mbind mi wax na ko: «Dinañu gis ki ñu jamoon.»
38ܒܬܪ ܗܠܝܢ ܝܘܤܦ ܗܘ ܕܡܢ ܪܡܬܐ ܒܥܐ ܡܢ ܦܝܠܛܘܤ ܡܛܠ ܕܬܠܡܝܕܐ ܗܘܐ ܕܝܫܘܥ ܘܡܛܫܐ ܗܘܐ ܡܢ ܕܚܠܬܐ ܕܝܗܘܕܝܐ ܕܢܫܩܘܠ ܦܓܪܗ ܕܝܫܘܥ ܘܐܦܤ ܦܝܠܛܘܤ ܘܐܬܐ ܘܫܩܠ ܦܓܪܗ ܕܝܫܘܥ ܀
38 Gannaaw loolu Yuusufa mi dëkk Arimate ñaan Pilaat ngir yóbbu néewu Yeesu. Yuusufa taalibe Yeesu la woon ci lu kenn yégul, ndaxte dafa ragaloon Yawut ya. Pilaat may ko ko. Yuusufa daldi dem, yóbbu néewu Yeesu.
39ܘܐܬܐ ܐܦ ܢܝܩܕܡܘܤ ܗܘ ܕܐܬܐ ܗܘܐ ܡܢ ܩܕܝܡ ܠܘܬ ܝܫܘܥ ܒܠܠܝܐ ܘܐܝܬܝ ܥܡܗ ܚܘܢܛܬܐ ܕܡܘܪܐ ܘܕܥܠܘܝ ܐܝܟ ܡܐܐ ܠܝܛܪܝܢ ܀
39 Nikodem itam ñëw, moom mi masoon a seeti Yeesu guddi. Mu indaale lu war a tollook fanweeri kiloy cuuraay lu ñu defare ndàbbi miir ak banti aloos.
40ܘܫܩܠܘܗܝ ܠܦܓܪܗ ܕܝܫܘܥ ܘܟܪܟܘܗܝ ܒܟܬܢܐ ܘܒܒܤܡܐ ܐܝܟܢܐ ܕܐܝܬ ܥܝܕܐ ܠܝܗܘܕܝܐ ܕܢܩܒܪܘܢ ܀
40 Ñu jël néewu Yeesu, laxas ko ci càngaay, boole ko ak cuuraay li, ni ko Yawut yi tàmmoo def, bu ñuy waajal néew.
41ܐܝܬ ܗܘܬ ܕܝܢ ܒܗܝ ܕܘܟܬܐ ܕܐܙܕܩܦ ܒܗ ܝܫܘܥ ܓܢܬܐ ܘܒܗ ܒܓܢܬܐ ܒܝܬ ܩܒܘܪܐ ܚܕܬܐ ܕܐܢܫ ܥܕܟܝܠ ܠܐ ܐܬܬܤܝܡ ܗܘܐ ܒܗ ܀
41 Tool a nga woon ca wetu bérab, ba ñu daajoon Yeesu, te ca tool booba amoon na fa bàmmeel bu ñu musul a suul kenn.
42ܘܤܡܘܗܝ ܬܡܢ ܠܝܫܘܥ ܡܛܠ ܕܫܒܬܐ ܥܐܠܐ ܗܘܬ ܘܡܛܠ ܕܩܪܝܒ ܗܘܐ ܩܒܪܐ ܀
42 Ca bésu Waajal la woon, ba Yawut ya doon waajal bésu noflaay ba, te bàmmeel ba jege woon na. Foofa lañu denc Yeesu.